Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Philippians 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So if any encouragement in Christ, any comfort from love, any deep communion in the Holy Spirit, any tenderness and compassion exist, Su nu Kirist mayee fit nag ak mbëggeel guy dëfal sunu xol, su nu amee cér ci Xel mu Sell mi, su amee cofeel ak yërmande ci sunu bokk ci moom,
2 complete my joy: think alike, love alike, unite in spirit, one in purpose. kon mottalileen sama mbég, ci bokk benn xalaat ak genn mbëggeel, benn bakkan ak menn xel.
3 Do nothing out of selfish ambition or empty conceit, but in humility consider others better than yourselves. Buleen def dara ci kaw wut aw tur walla wonu, waaye jiital-leen seeni moroom cig woyof.
4 Each of you should attend not only to your own interests, but also to others'. Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom.
5 Have this mindset among yourselves—one that is yours in Christ Jesus, Te ngeen soloo xel mi nekkoon ci Kirist Yeesu:
6 who, existing in the form of our Father, did not consider equality with our Father something to be grasped, Njàlbéen ga fekk na Kirist yor melow Yàlla, waaye aakimoowul taxawaayam ci li mu méngoo ak Yàlla.
7 but emptied himself by taking on the form of a servant and being born in human likeness. Waaye daa wàcce boppam, ba tollook nit ñi, def boppam surga. Te bi mu yoree bindu nit,
8 And appearing as a human being, he humbled himself by becoming obedient to death—even death on a cross. daa suufeel boppam, di dégg ndigal, ba joxe boppam, ñu daaj ko sax ci bant.
9 Therefore our Father exalted him to the highest place and gave him the name that is above every name, Moo tax Yàlla kaweel ko lool, jox ko tur wi tiim yépp,
10 so that at the name of Jesus every knee should bow, in heaven and on earth and under the earth, ngir turu Yeesoo tax ñépp sukk, ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf;
11 and every tongue confess that Jesus Christ is Lord, to the glory of our Father. te ñépp bokk genn kàddu naan: Yeesu Kirist mooy Boroom bi; ci màggug Yàlla Baay bi.
12 So, my dear ones, as you've always obeyed—not only in my presence but now much more in my absence—keep working out your salvation with fear and trembling, Noonu samay soppe, xam naa ne masuleena jóg ci dégg ndigal, waxuma sax bi ma nekkee ak yéen rekk, waaye rawatina bi ma leen soree. Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen biral seen mucc ci seeni jëf, te def ko ci ragal Yàlla gu dëggu.
13 for our Father works in you, giving both the will and the work for his good purpose. Ndaxte Yàlla ci boppam mooy jëf ci yéen, ngir ngeen fonk coobareem te di ko jëfe.
14 Do everything without grumbling or arguing, Lépp lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo.
15 so you may be blameless and pure, faultless children of our Father amid a crooked and depraved generation—shining among them like stars in the world, Noonu dingeen am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ, di goney Yàlla yu amul sikk ci biir jamono ju yàqu te rëb. Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci àddina si,
16 holding firmly to the word of life, so I can boast on Christ's day that I didn't run or work for nothing. di jottali kàddug dund gi. Noonu bu bésu Kirist ñëwee, dinaa mana bég, xam ne dawuma lu amul njariñ te sonnuma cig neen.
17 But even if I'm poured out as a drink offering on the sacrifice and service of your faith, I'm glad and rejoice with you all. Bu sama deret waree tuuru sax, ngir seen ngëm mat sëkk, ma mel ni naan gu ñu boole ak sarax su jëm ci Yàlla, ba tey bég naa ci, te dinaa ci bégati.
18 So you too should be glad and rejoice with me. Yéen itam nag bégleen, waaw, fekksileen ma ci sama mbég.
19 I hope, in the Lord Jesus, to send Timothy to you soon, so I too may be encouraged, knowing how you are. Gannaaw loolu, bu soobee Boroom bi Yeesu, yaakaar naa ne dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir sama xel dal ci xam nan ngeen def.
20 I have no one else like him, who will genuinely care for your welfare. Ndaxte amu fi kenn gannaaw Timote, ku bokk ak man xalaat te fonk leen bu wér.
21 For they all look after their own interests, not those of Jesus Christ. Ñi ci des ñépp, seen bopp lañuy xalaat, waaye du mbiri Yeesu Kirist.
22 You know Timothy's proven worth—like a son with a father, he served with me in the gospel work. Waaye xam ngeen takkuteg Timote, ci ni mu ànde ak man ci tas xibaaru jàmm bi, ni doom di taxawoo baayam.
23 So I hope to send him as soon as I see how things go with me, Moom laa yaakaara yónni fi yéen nag, waxtu wu ma yégee, nu sama mbir di tëdde.
24 and I am confident in the Lord that I myself will come soon. Waaye wóor na ma ne Boroom bi dina ma may, man ci sama bopp, ma seetsi leen balaa yàgg.
25 I thought it necessary to send Epaphroditus back to you—my brother, coworker, and fellow soldier, your messenger and servant for my needs. Ci lu jëm ci sama mbokk Epafrodit nag, miy sama nawle ci liggéey bi ak ci xeex bi, te di seen ndaw ci faj samay soxla, jàpp naa ne war naa leen koo delloo.
26 He has longed for you all, and is troubled that you heard he was sick. Ndaxte namm na leen lool, te tiisoo na li ngeen yég jagadeem.
27 Indeed he was sick, and nearly died. But our Father had mercy on him—not only him but me too, sparing me sorrow upon sorrow. Ci dëgg-dëgg woppoon na ba xawa dee, waaye Yàlla yërëm na ko, ba fëgg boppam, rax-ca-dolli siggil na ma man itam, ngir ma baña am tiis ci kaw tiis.
28 So I'm more eager to send him, so seeing him again you'll rejoice and I'll worry less. Noonu delloo naa leen ko ci lu gaaw, ngir ñëwam bégal seeni xol, te man itam sama xol féex.
29 Welcome him in the Lord with all joy, and honor people like him, Teeruleen ko teeru bu rafet nag ngir Boroom bi, te teral ñi mel ni moom.
30 because he neared death for Christ's work, risking his life to make up your missing help to me. Ndaxte liggéeyal na Kirist, ba riisu dee, te gar na bakkanam ci taxawal leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]