Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Philippians 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Finally, brothers and sisters, rejoice in the Lord. Writing the same things again is no trouble for me, and it protects you. Kon nag samay bokk, bégleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju.
2 Watch for the dogs, watch for the evil workers, watch for those who mutilate the flesh. Moytuleen xaj yi, waaw, moytuleen ñiy jëfe lu bon, ñoom ñi seen xarafal weesul wàññi yaramu nit.
3 We are the circumcision—worshiping by the Spirit of our Father, boasting in Christ Jesus, trusting nothing in the flesh, Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy màggal Yàlla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu benn yaakaar ci matug nit.
4 though I too could have confidence in the flesh. If anyone else thinks he has grounds for confidence in the flesh, I have more: Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw.
5 Circumcised the eighth day; Israelite by birth, from Benjamin's tribe; Hebrew of Hebrews; a Pharisee under the law. Xarafoon naa ca ayu-bés ga, bokk ci bànni Israyil ci giiru Beñamin, di Ebrë ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen bëgga wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon;
6 In zeal, persecuting the church; in righteousness under the law, blameless. bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom ñi gëm Kirist; bu dee ci njub ci sàmm yoon, awma benn gàkk.
7 But whatever was gain to me, I now count as loss for the sake of Christ. Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist.
8 Yes, I count everything as loss because of the priceless worth of knowing Christ Jesus my Lord. For his sake I've lost all things, and count them garbage, so I may gain Christ, Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel manu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist.
9 and be found in him, not having my own righteousness from the law, but that through faith in Christ—the righteousness from our Father based on faith, Na ma Yàlla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci sàmm yoon, waaye gu aju ci gëm Kirist, maanaam njub gi nu Yàlla sol ci kaw ngëm.
10 so I may know him, his resurrection's power, sharing his sufferings, becoming like him in death, Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam,
11 if somehow I may attain to the resurrection from the dead. ngir mana séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.
12 Not that I have already obtained it, or am already perfected, but I press on to grasp that for which Christ Jesus grasped me. Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist jël ma.
13 Brothers, I don't count myself as having grasped it yet. But one thing: forgetting what's behind, reaching for what's ahead, Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam,
14 I press toward the goal for the prize of our Father's heavenward call in Christ Jesus. di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla taxa woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.
15 Let all of us who are mature think this way; if you think differently on anything, our Father will reveal that to you too. Nun ñi mat nag, nanu xalaat loolu. Su ngeen ci amee werantey xol, Yàlla dina leen ko leeralal.
16 Only let us hold true to what we have already attained. Li am daal, fa seen ngëm tolloo, na fa seen jëf àgg.
17 Brothers, imitate me together, and watch those who live by the pattern you have in us. Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen.
18 Many live as enemies of Christ's cross—I've told you this often, and now say it in tears. Ndaxte jëfi ñu bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba tàyyi, maa ngi koy waxaat léegi ak i jooy.
19 Their end is destruction, their god the stomach, their glory their shame, minds fixed on earthly things. Alku lañuy mujje, ñoom ñiy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut yëfi àddina rekk.
20 But our citizenship is in heaven; from there we eagerly await a Savior, the Lord Jesus Christ, Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist jóge fa, musalsi nu.
21 who will transform our lowly body to match his glorious body, by the power that subjects all things to himself. Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi ànd ak ndam dëppook kàttanam, gi ko mana notal mbindeef yépp.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]