Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Philippians 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Paul and Timothy, servants of Christ Jesus, to all the holy ones in Christ Jesus at Philippi, with the overseers and deacons: Nun Pool ak Timote, jaami Kirist Yeesu, noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yépp ci dëkku Filib, yi bokk ci Kirist Yeesu, yéen ak seeni njiit ak ñiy topptoo yëfi mbooloo mi.
2 Grace to you and peace from our Father and the Lord Jesus Christ. Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
3 I thank my Father every time I remember you, Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Yàlla sama Boroom;
4 always praying for all of you with joy in every prayer, te saa su ma leen di ñaanal yéen yépp, duma noppee bég,
5 because of your partnership in the gospel from the first day until now. ndax seen ànd ak man ci tas xibaaru jàmm bi, ca ndoorte la ba tey.
6 I'm confident of this very thing: the one who began a good work in you will complete it until the day of Christ Jesus. Wóor na ma ne Yàlla mi tàmbali jëf ju baax jii ci yéen, dina ci sax, ba bésu Kirist Yeesu ñëw.
7 I'm right to feel this about you—I hold you in my heart, all of you sharing with me in grace, in my chains and in defending and confirming the gospel. Te juumuma ci li ma xalaat loolu ci yéen ñépp, ndaxte def naa leen ci sama xol; ba tax fii ci kaso bi, ci taxawal xibaaru jàmm bi ak lawal ko, yéen ñépp am ngeen wàll ak man ci yiwu Yàlla.
8 For our Father is my witness, how I long for you all with Christ Jesus's deep affection. Ndaxte Yàllaa seede ne sama xol seey na ci yéen ñépp ci biir cofeelu Kirist Yeesu.
9 This is my prayer: that your love overflow more and more, with knowledge and all discernment, Li ma leen di ñaanal nag mooy lii: yal na seen mbëggeel di yokku tey gëna tar, jaar ci xam ak xàmmi gu wér;
10 so you can discern what is best, staying pure and blameless until the day of Christ. yal nangeen sax noonu ci li gëna rafet, ngeen am xol bu laab te baña am benn sikk, ba bésu Kirist ñëw;
11 Filled with the fruit of righteousness through Jesus Christ, to our Father's glory and praise. yal na seen xol meññ njub, ba ne gàññ, jaar ci Yeesu Kirist ci ndamul Yàlla ak cantam.
12 I want you to know, brothers and sisters, that my circumstances have actually advanced the gospel, Damaa bëgg, bokk yi, ngeen xam lii: li ma dal taxul xibaaru jàmm bi dellu gannaaw, waaye da koo jëmale kanam.
13 so my chains for Christ became known to the whole imperial guard and everyone else. Noonu ñiy wottu buur bi ak ñépp gis nañu bu leer ne turu Kirist rekk a tax ñu jàpp ma.
14 Most of the brothers and sisters, made confident in the Lord by my chains, now dare more to speak the word fearlessly. Te it bokk yu bare takk nañu seeni fit ci li ñu gis samay buum, ba tax ñu gëna ñeme ci wax kàddug Yàlla ci lu àndul ak genn tiit.
15-16 Some, it is true, preach Christ out of envy and rivalry, but others out of goodwill. Am na ñuy waare ci turu Kirist ci kaw kiñaan ak xëccoo, waaye ñi ci des ci kaw cofeel ak xol bu laab, ndaxte xam nañu ne Yàlla moo ma teg fii, ngir ma taxawal xibaaru jàmm bi.
16 These act from love, knowing I'm assigned to defend the gospel. Not in this edition
17 The others proclaim Christ out of selfish ambition, not sincerely, thinking to stir up trouble for me in my chains. Waaye ñale amuñu xol bu laab, te seen njariñu bopp rekk a tax ñuy yégle turu Kirist, di wuta feddali samay buum ak coono.
18 What then? Only that in every way—whether in pretense or truth—Christ is proclaimed, and I rejoice in this. Yes, I will keep rejoicing. Lu ci génn nag? Xanaa lii rekk: turu Kirist jolli na ci nii mbaa naa, muy ci naaféq, muy ci dëgg; bég naa ci te dinaa ci bégati.
19 For I know this will result in my rescue, through your prayers and the help of Jesus Christ's Spirit. Ndaxte xam naa ne loolu lépp mu ngi jëm ci sama mucc, jaar ci seeni ñaan ak ndimbalu Xelum Yeesu Kirist, mi ma Yàllay yéwénal.
20 My eager expectation and hope: I will never be ashamed, but with full courage, now as always, Christ will be praised in my body, whether by life or by death. Ndaxte sama xënte ak sama yaakaar mooy ma baña rus ci lenn, waaye sama yaram feeñal ndamu Kirist, ma ànd ci ak kóolute gu mat, su may dund mbaa may dee; moom laa daan def démb, te moom laay def tey.
21 For to me, to live is Christ, and to die is gain. Ndaxte su ma dundee, Kirist laay noyyee; su ma deeyee, xéewal lay doon ci man.
22-23 If I am to go on living in the body, this will mean fruitful work for me. Yet I don't know which to choose. Su ma Yàlla bàyyee ci àddina, sas wu am njariñ la ci man. Am naa xel ñaar, xawma bi ci gën. Am naa yéeney jóge fi, fekki Kirist, te looloo gën fuuf,
23 Torn between the two, I want to leave and be with Christ—far better, Not in this edition
24 but to remain in the body is more necessary for your sake. waaye ma des fi ci àddina moo gën ci yéen.
25 Convinced of this, I know I'll remain and stay with you all, for your progress and joy in the faith, Loolu wóor na ma; kon xam naa ne dinaa fi des, di leen taxawu yéen ñépp, ngir seen ngëm yokku, ànd ak mbég.
26 so your boasting in Christ Jesus may overflow because of me, when I come to you again. Noonu dinaa délsi ci yéen, ngir sama taxawaay gëna lawal seen mbég ci Kirist Yeesu.
27 Just live worthy of the gospel of Christ, so that whether I come and see you, or am absent, I hear you stand firm in one spirit, contending together with one mind for the gospel's faith, Waaye dénk naa leen lii: na seeni jëf yelloo ak li Kirist digle ci xibaaru jàmm bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma dégg seen mbir rekk, dinaa xam ne yéena ngi dëgër ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xibaaru jàmm bi,
28 and not scared of your opponents at all—proof to them of their destruction, but of your salvation, and that from our Father. te baña tiit dara ndax noon, yi leen di xëbal. Màndarga la muy wone ne aji sànku lañu, di màndarga it ne aji mucc ngeen, di mucc gu jóge ci Yàlla.
29 For it has been graciously granted to you, for Christ's sake, not only to believe in him but also to suffer for him, Ndaxte Yàlla may na leen, ngeen gëm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam,
30 going through the same struggle you saw me face, and now hear that I still face. di wéy ci bëre, bi ngeen gisoon ci man te dégg léegi sama mbir.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]