Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 8 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 In those days, again a large crowd gathered with nothing to eat. Jesus called his disciples and said, Ca bés yooya mbooloo mu réy amaatoon na, te amuñu woon lu ñu lekk. Noonu Yeesu woo taalibe ya ne leen:
2 "I feel compassion for the crowd—they've been with me three days now and have nothing to eat. «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk.
3 If I send them home hungry, they'll collapse on the way—some have come from far off." Su ma leen yiwee ak seen xiif, dinañu tële ci yoon wi, ndaxte am na ñu jóge fu sore.»
4 And his disciples answered him, "How can anyone feed these people with bread here in the wilderness?" Taalibe yi ne ko: «Waaye fii àllub neen la; fu nuy jële lu doy ngir dundal leen?»
5 And he asked them, "How many loaves do you have?" They said, "Seven." Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
6 He told the crowd to sit on the ground, took the seven loaves, gave thanks, broke them, and gave them to his disciples to serve to the people; and they served the crowd. Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. Mu jël juróom ñaari mburu yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ngir ñu séddale leen mbooloo mi; taalibe yi def ko.
7 They also had a few small fish; after blessing them, he told the disciples to serve these to the people. Amoon na fa it tuuti jën yu ndaw. Yeesu jël ko, sant Yàlla, wax taalibe yi, ñu séddale leen itam mbooloo mi.
8 And they ate and were satisfied. And they took up seven baskets of the leftover pieces. Noonu nit ñi lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
9 About 4,000 people were there. And he sent them away. Ña ko fekke nag matoon nañu ñeenti junniy góor.
10 Then immediately he got into the boat with his disciples and went to the district of Dalmanutha. Bi ko Yeesu defee, mu yiwi leen, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca wàlli Dalmanuta.
11 The Pharisees came and began debating with him, testing him by demanding a sign from heaven. Noonu Farisen yi ñëw, di werante ak moom; ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.
12 Sighing deeply in his spirit, he said, "Why does this generation demand a sign? Truly I tell you, no sign will be given to this generation." Waaye Yeesu binni ci xolam ne leen: «Lu tax niti jamono jii di laaj kéemaan? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, duñu jot genn kéemaan.»
13 And he left them, got back into the boat, and went to the other side. Ci kaw loolu Yeesu bàyyi leen, duggaat ci gaal gi, di jàll dex gi.
14 They'd forgotten to bring bread—only one loaf was with them in the boat. Taalibe yi nag fàtte woon nañu yóbbaale mburu, te amuñu woon lu dul benn mburu ci gaal gi.
15 And he warned them, "Watch out—beware of the yeast of the Pharisees and the yeast of Herod." Noonu Yeesu artu leen ne: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak ñi far ak buur bi Erodd.»
16 And they began discussing with one another that they had no bread. Taalibe yi nag daldi werante naan: «Nun de indaalewunu mburu.»
17 Knowing this, Jesus asked, "Why discuss having no bread? Do you still not see or grasp? Are your hearts hardened? Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey?
18 Having eyes, do you not see? Having ears, do you not hear? And do you not remember? Ndax ay gumbay njàccaar ngeen, te seeni nopp naqari? Xanaa fàttalikuwuleen;
19 When I broke the five loaves for the 5,000, how many baskets full of fragments did you collect?" They said, "Twelve." bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar.»
20 "And when I broke the seven for the 4,000, how many basketfuls of broken pieces did you gather?" They said, "Seven." Yeesu neeti leen: «Te bés bi ma dammee juróom ñaari mburu yi ngir ñeenti junni ñi, ñaata dàmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
21 And he said to them, "Do you still not understand?" Noonu Yeesu ne leen: «Ndax seen xol dafa tëju ba tey?»
22 They came to Bethsaida, where people brought him a blind man and begged Jesus to touch the man. Gannaaw loolu ñu ñëw ci Betsayda. Foofa ñu indil Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu laal ko.
23 He took the blind man's hand, led him out of the village, spit on his eyes, laid hands on him, and asked, "Do you see anything?" Yeesu nag jàpp loxob gumba gi, yóbbu ko, ba génn dëkk bi. Mu def tiflit ciy bëtam, teg ko loxo naan: «Ndax gis nga dara?»
24 He looked up and said, "I see people, but they look like trees, walking." Waa ji xool ne ko: «Gis naa ay nit, ñu mel ni ay garab, te ñu ngi dox.»
25 Then Jesus put his hands on the man's eyes again; he looked intently, was restored, and saw everything distinctly. Kon Yeesu laalaat bët yi, gumba gi ne xefeet, daldi wér, ba gis lépp bu leer.
26 And he sent him home, saying, "Do not even go into the village." Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu ñibbi ne ko: «Bul dugg ca dëkk ba.»
27 Jesus and his disciples went to the villages of Caesarea Philippi. On the way he asked them, "Who do people say I am?" Bi loolu amee Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca dëkk, yi wër Sesare bu Filib. Bi ñuy dem nag, mu laaj taalibe yi: «Nit ñi, lu ñu wax ne man moom laa?»
28 They told him, "John the Baptist; and others say Elijah; and others, one of the prophets." Ñu ne ko: «Am na ñuy ne yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yi.»
29 Then he asked them, "But who do you say I am?" Peter answered, "You are the Christ." Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi.»
30 And he strictly warned them not to speak about him. Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo wax kenn.
31 He began teaching them the Son of Man must suffer much, be rejected by the elders, chief priests, and scribes, be killed, and rise after three days. Booba Yeesu tàmbali na leena xamal ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare; njiit ya, sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ci ñetti fan.
32 He said this plainly. And Peter took him aside and began to rebuke him. Noonu mu xamal leen mbir mi, ba mu leer nàññ. Bi ko Piyeer déggee, mu woo ko ci pegg, daldi ko yedd.
33 But turning, he looked at his disciples and rebuked Peter: "Get behind me, Satan! For you are not setting your mind on the things of our Father, but on the things of man." Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: «Sore ma Seytaane; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
34 He called the crowd and his disciples and said to them, "Whoever wants to come after me must deny himself, take up his cross, and follow me. Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne leen: «Ku bëgga topp ci samay tànk, na bàyyi boppam te gàddu bant bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
35 Whoever wants to save his life will lose it; whoever loses his life for my sake and the good news will save it. Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man ak ngir xibaaru jàmm bi, dinga ko jotaat.
36 What good does it do a person to gain the whole world and forfeit his soul? Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam?
37 For what can a person give in exchange for his soul? Te nit, lu mu wara weccee bakkanam?
38 For whoever is ashamed of me and my words in this adulterous, sinful generation—the Son of Man will be ashamed of them too when he comes in his Father's glory with the holy angels." Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax ci kanam niti jamono jii, ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla te topp bàkkaar, Doomu nit ki dina la rusa xam, bés bu ñëwee ci ndamu Baayam, ànd ak malaaka yu sell yi.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]