Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 9 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 He said to them, "Truly I tell you: some standing here will not taste death before they see the kingdom of our Father come with power." Mu ne leen ati: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu nguuru Yàlla ñëw ak doole.»
2 Six days later Jesus took Peter, James, and John, and led them up a high mountain alone, and he was transfigured before them. Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu yóbbu leen ñoom rekk fu wéet ci tund wu kawe lool. Foofa jëmmam soppiku ci seen kanam;
3 His clothes became radiant, dazzling white—whiter than anyone on earth could bleach them. ay yéreem di ray-rayi, weex tàll, te fóotukatu àddina manu leen weexale nii.
4 And Elijah appeared to them along with Moses, and they were talking with Jesus. Noonu ñu gis yonenti Yàlla Ilyaas ak Musaa, di wax ak Yeesu.
5 Peter said to Jesus, "Rabbi, it's good that we're here. Let's make three shelters—one for you, one for Moses, and one for Elijah." Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.»
6 He did not know what to say, for they were terrified. Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jàpp na leen ñoom ñett ñépp.
7 A cloud appeared and overshadowed them, and a voice came from the cloud: "This is my beloved Son. Listen to him!" Noonu niir muur leen, te baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
8 Suddenly, when they looked around, they no longer saw anyone with them except Jesus. Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk.
9 Coming down the mountain, he ordered them to tell no one what they'd seen until the Son of Man rose from the dead. Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi muy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki na.»
10 So they kept the matter to themselves, questioning what rising from the dead could mean. Ñu téye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki.
11 And they asked him, "Why do the scribes say that Elijah must come first?" Noonu taalibe yi laaj Yeesu: «Lu tax xutbakat yi di naan, Ilyaas moo wara jëkka ñëw?»
12 He said, "Elijah does come first and restores everything. Then why is it written the Son of Man must suffer much and be treated with contempt? Yeesu ne leen: «Waaw, Ilyaas dina jëkka ñëw, jubbanti lépp. Waaye itam lu tax bind nañu ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, ñu xeeb ko, dëddu ko.
13 But I tell you, Elijah has come, and they did to him whatever they pleased, as it is written about him." Waaye maa ngi leen di wax ne, Ilyaas ñëw na, te def nañu ko la leen neex, ni ko Mbind mi waxe.»
14 Coming to the other disciples, they saw a large crowd around the disciples, and scribes arguing with them. Bi nga xamee ne Yeesu ñëw na, ba jege taalibe yi, mu gis mbooloo mu bare wër leen, te ay xutbakat di werante ak ñoom.
15 As soon as the whole crowd saw Jesus, they were astonished and ran to greet him. Naka la mbooloo mi gis Yeesu, ñu waaru, daldi daw nuyu ko.
16 He asked them, "What are you arguing about with the scribes?" Noonu Yeesu laaj leen: «Ci lan ngeen di werante ak ñoom?»
17-18 Someone in the crowd answered him, "Teacher, I brought my son to you; he has a spirit that won't let him speak. Kenn ci mbooloo mi ne ko: «Kilifa gi, rab jàpp na sama doom, ba luuloo ko. Saa su ko jàppee, daf koy daaneel ci suuf, gémmiñ gi di fuur, muy yéyu, ne jàdd. Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye manuñu ko.»
18 Whenever it seizes him, it throws him down. He foams at the mouth, grinds his teeth, and stiffens. I asked your disciples to drive it out, but they couldn't." Not in this edition
19 He replied, "You unbelieving generation, how long must I stay with you? How long must I endure you? Bring him to me." Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi, ba kañ laa wara nekk ak yéen, ba kañ laa leen wara muñal? Indil-leen ma xale bi.»
20 They brought the boy to him. Seeing Jesus, the spirit instantly convulsed him; he fell to the ground, thrashing and foaming at the mouth. Ñu indil ko ko. Bi xale bi gisee Yeesu nag, rab wi sayloo ko ci saa si, mu daanu ci suuf, di xalangu, gémmiñ giy fuur.
21 Jesus asked the boy's father, "How long has this been happening to him?" "From childhood," he said. Yeesu laaj baay bi: «Lii kañ la ko dal?» Baay bi ne ko: «Li dale ci ngoneem.
22 "It has often thrown him into fire and water to destroy him. But if you can do anything, pity us and help us." Léeg-léeg rab wi bëmëx ko ci sawara, léeg-léeg mu bëmëx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, yërëm nu te xettali nu.»
23 Jesus said to him, "'If you can'? Everything is possible for the one who believes." Yeesu ne ko: «Nga ne: “Soo ko manee,” ku gëm man na lépp.»
24 Immediately the boy's father cried, "I believe; help my unbelief!" Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: «Gëm naa, dàqal ma sama ngëmadi.»
25 Seeing a crowd running together, Jesus rebuked the unclean spirit: "Mute and deaf spirit, I command you—come out of him and never enter him again!" Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, wërsi ko, mu daldi gëdd rab wi nag ne ko: «Génnal ci moom, yaw rab wu luu te tëx, te bu ko jàppaat; wax naa la ko.»
26 Crying out and convulsing him hard, it came out. He looked like a corpse, so many said, "He's dead." Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, génn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax ñu bare ne: «Dee na.»
27 But Jesus took him by the hand and raised him up, and he stood. Waaye Yeesu jàpp loxoom, jógloo ko, xale bi daldi taxaw.
28 When Jesus had gone indoors, his disciples asked him privately, "Why couldn't we drive it out?" Bi Yeesu duggee ci kër gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: «Lu tax manunu ko woona dàq?»
29 He told them, "This kind can come out only by prayer." Yeesu ne leen: «Yu mel ni yii, ñaan ci Yàlla rekk a leen di dàq.»
30 They left there and passed through Galilee. Jesus did not want anyone to know where they were, Bi loolu amee ñu jóge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu bëggul kenn yég ko.
31 because he was teaching his disciples, telling them, "The Son of Man is being handed into human hands. They will kill him, and three days later he will rise." Ndaxte muy jàngal taalibe yi ne leen: «Dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit, te dinañu ko rey, mu dekki ci ñetti fan.»
32 But they did not understand what he meant, and they were afraid to ask him. Waaye taalibe yi xamuñu lu wax joojuy tekki, te ñemewuñu ko koo laaj.
33 They came to Capernaum. In the house he asked them, "What were you arguing about on the way?" Bi nga xamee ne egg nañu dëkku Kapernawum, te dugg ci kër gi, Yeesu laaj leen ne: «Lu ngeen doon waxtaane ci yoon wi?»
34 But they were silent, since they had argued along the way about who was greatest. Waaye ñu ne cell, ndaxte ñu ngi fa doon werante, ba xam ku gëna màgg ci ñoom.
35 He sat down, called the Twelve, and told them, "Anyone who wants to be first must be last of all and servant of all." Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak ñaar ne leen: «Ku bëgga jiitu, na topp ci gannaaw ñépp te nekk surgab ñépp.»
36 He took a little child, stood him among them, took the child in his arms, and said to them: Bi ko Yeesu waxee, mu jël xale, indi ko ci biir géew bi, ba noppi leewu ko naan:
37 "Whoever accepts one of these little children in my name accepts me; whoever accepts me accepts not me but the one who sent me." «Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma yónni.»
38 John said to him, "Teacher, we saw someone driving out demons in your name and tried to stop him, since he doesn't follow us." Bi loolu amee Yowaana ne ko: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndax li mu bokkul ci nun.»
39 But Jesus said, "Don't stop him—no one who does a miracle in my name can soon speak evil of me. Waaye Yeesu ne ko: «Buleen ko tere, ndaxte kenn manula def kéemaan ci sama tur, ba noppi di ma xarab.
40 For whoever is not against us is for us. Ku nu sotul, far na ak nun.
41 Truly I tell you, whoever gives you a cup of water to drink because you belong to Christ will never lose his reward. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax yéena ngi bokk ci man Kirist, kooku du ñàkk yoolam mukk.
42 Whoever trips up one of these little ones who believe in me—better for him to have a large millstone hung around his neck and be thrown into the sea. «Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom, moo di ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej.
43-44 If your hand trips you up, cut it off. Better to enter life maimed than with two hands to go into hell, into the unquenchable fire. Boo xamee ne sa loxo mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko. Ndaxte ñàkk loxo te tàbbi ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo te tàbbi ci sawara su dul fey mukk.
45-46 If your foot trips you up, cut it off. Better to enter life lame than be thrown into hell with two feet. Te bu la sa tànk di yóbbe bàkkaar, dagg ko. Nga lafañ te tàbbi ci dund gu wóor gi moo gën, nga am ñaari tànk, ñu sànni la ci sawara.
47 If your eye trips you up, throw it out. Better to enter the kingdom of our Father with one eye than be thrown into hell with two, Te bu la sa bët di yóbbe bàkkaar, luqi ko. Nga patt te dugg ci nguuru Yàlla, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, ñu sànni la ci sawara.
48 where 'their worm never dies and the fire never goes out.' Foofa: “Sax ya duñu dee mukk, te sawara sa du fey.”
49 For everyone will be salted with fire. Ñépp sawara lañu leen di xorome.
50 Salt is good, but if it loses its saltiness, how can you season it again? Keep salt among yourselves, and be at peace with each other." Xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Amleen xorom te ngeen jàmmoo.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]