Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 10 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 He left there for the region of Judea and beyond the Jordan; crowds gathered to him again, and as usual he taught them once more. Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ca wàlli réewu Yawut yi, ya ca gannaaw dexu Yurdan. Bi mu fa demee, mbooloo mu bare ñëw fi moom. Yeesu daldi leen jàngal, ni mu ko daan defe.
2 Some Pharisees came to test him, asking, "Is it lawful for a man to divorce his wife?" Noonu ay Farisen ñëw ci moom, lalal ko fiir, ñu laaj ko: «Ndax jaadu na, nit fase soxnaam?»
3 He answered them, "What did Moses command you?" Yeesu ne leen: «Lu leen yoonu Musaa sant?»
4 They said, "Moses permitted a man to write a certificate of divorce and send her away." Ñu ne ko: «Musaa maye na, nit bind kayitu pase, tàggook soxnaam.»
5 Jesus told them, "He wrote you this command because your hearts were hard. Waaye Yeesu ne leen: «Dénkaane boobu mu leen bindal, bind na ko ndax seen xol dafa fatt.
6 But from the beginning of creation, our Father made them male and female. Waaye ca njàlbéen ga “Yàlla sàkk na leen, kii góor, kii jigéen.
7 'For this reason a man will leave his father and mother and be joined to his wife, Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam,
8 and the two will become one flesh.' So they are no longer two, but one flesh. ñoom ñaar doon benn.” Kon nekkatuñu ñaar waaye benn lañu.
9 Therefore what our Father has joined together, let no one separate." Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
10 Back in the house, the disciples asked him about this again. Bi ñu delloo ca kër ga nag, taalibe ya laaj ko ci mbirum loolu.
11 He said to them, "Whoever divorces his wife and marries another commits adultery against her, Noonu Yeesu ne leen: «Ku fase sa soxna, takk jeneen, njaaloo nga, di tooñ ku jëkk ka.
12 and if she divorces her husband and marries another, she commits adultery." Te jigéen ji tas, séyaat ak keneen, njaaloo nga.»
13 People were bringing children to him so that he might touch them, but the disciples rebuked them. Bi loolu wéyee ñu indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom. Waaye taalibe ya gëdd nit ñi.
14 When Jesus saw this, he grew angry and said, "Let the children come to me; don't stop them, for the kingdom of our Father belongs to such as these. Bi ko Yeesu gisee nag, mu metti ko lool, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man! Buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla.
15 Truly I tell you, whoever doesn't receive our Father's kingdom like a child will never enter it." Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci mana dugg.»
16 And he took them in his arms and blessed them, laying his hands on them. Noonu Yeesu leewu leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen.
17 As he started down the road, a man ran up, knelt before him, and asked, "Good Teacher, what must I do to inherit eternal life?" Gannaaw loolu bi Yeesu nekkee ci kaw yoon wi di dem, am ku daw, sukk ci kanamam ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma wara def, ngir am wàll ci dund gu dul jeex gi?»
18 Jesus asked, "Why call me good? No one is good except our Father alone. Yeesu ne ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax ki? Yàlla rekk a baax.
19 You know the commandments: 'don't murder, commit adultery, steal, or give false testimony; don't defraud; honor your father and mother.'" Xam nga ndigal yi: “Bul bóome, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, bul nangu alalu jaambur, teralal sa ndey ak sa baay.”»
20 He said to him, "Teacher, all these I have kept since my youth." Waa ji ne ko: «Kilifa gi, loolu lépp sàmm naa ko li dale ci samag ndaw ba tey.»
21 Jesus looked at him and loved him. "One thing you lack: go, sell everything you own, give to the poor—you'll have treasure in heaven—then come follow me." Noonu Yeesu xool ko, am cofeel ci moom, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal jaay li nga am, jox ko miskin yi, te dinga woomle ci asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.»
22 At this word his face fell, and he went away grieving, for he had many possessions. Waaye ci wax jooju xar kanamam lëndëm, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
23 Jesus looked around and told his disciples, "How hard it will be for the wealthy to enter the kingdom of our Father!" Noonu Yeesu xool taalibe yi ko wër ne leen: «Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!»
24 The disciples were amazed at his words. Jesus said to them again, "Children, how hard it is to enter the kingdom of our Father! Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti leen: «Samay xarit, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!
25 A camel goes through a needle's eye easier than a rich person enters our Father's kingdom." Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.»
26 They were even more astonished and said to one another, "Then who can be saved?" Wax jooju gënatee jaaxal taalibe ya, ñu naan ci seen biir: «Kon nag ku mana mucc?»
27 Jesus looked at them and said, "With man, impossible; but not with our Father, for all things are possible with our Father." Noonu Yeesu xool leen naan: «Loolu të na nit, waaye tëwul Yàlla; Yàlla man na lépp.»
28 Peter began to say to him, "Look, we have left everything and followed you." Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: «Nun de dëddu nanu lépp te topp la!»
29 Jesus said, "Truly I tell you, no one has left house or brothers or sisters or mother or father or children or fields for my sake and for the gospel, Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër, doomu ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, doom walla suuf ndax man ak xibaaru jàmm bi,
30 "who won't receive a hundredfold now, in this time—houses, brothers, sisters, mothers, children, fields, with persecutions—and in the age to come, eternal life. dinga am tey jii téeméeri yoon ay kër, doomi ndey yu góor ak yu jigéen, ndey, doom ak suuf, ñoom ak ay fitnay noon, te ëllëg nga am dund gu dul jeex.
31 But many who are first will be last, and the last first." Waaye ñu bare ci ñi jiitu ñooy mujji; ñi mujj ñooy jiituji.»
32 On the road up to Jerusalem, Jesus walked ahead of them. They were amazed, and those following were afraid. Taking the twelve aside again, he began telling them what was about to happen to him: Gannaaw loolu ñu ànd jëm Yerusalem, Yeesu jiitu; taalibe yi am njàqare, te ñi ci topp tiit. Noonu Yeesu woowaat fukk ak ñaar ña cig wet, xamal leen li nara xew ci mbiram.
33 "Look, we're going up to Jerusalem. The Son of Man will be handed over to the chief priests and scribes, who will condemn him to death and hand him over to the Gentiles. Mu ne leen: «Noo ngi dem Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee, jébbal ko ñi dul Yawut,
34 They will mock him, spit on him, flog him, and kill him; after three days he will rise." ñu ñaawal ko, di tifli ci kawam, dóor ko ay yar, rey ko. Waaye gannaaw ñetti fan dina dekki.»
35 James and John, Zebedee's sons, came to him and said, "Teacher, we want you to do for us whatever we ask." Gannaaw loolu Saag ak Yowaana, doomi Sebede, ñëw ci Yeesu. Ñu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon nga may nu li nu lay ñaan.»
36 He said to them, "What do you want me to do for you?" Yeesu ne leen: «Lu ngeen bëggoon, ma may leen ko?»
37 They said to him, "Let us sit in your glory, one at your right, one at your left." Ñu ne ko: «Bés boo soloo sa ndam, nga may nu, nu toog, kii ci sa ndijoor, kii ci sa càmmoñ.»
38 Jesus said to them, "You don't know what you're asking. Can you drink the cup I drink, or be baptized with the baptism I'm baptized with?" Waaye Yeesu ne leen: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan? Ndax man ngeena sóobu ci metit, yi ma nara sóobu?»
39 "We can," they said. Jesus said to them, "The cup I drink, you will drink; the baptism I'm baptized with, you will be baptized with, Ñu ne ko: «Waaw, man nanu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Dingeen naan kaasu naqar, bi may naan, tey sóobu ci metit, yi ma nara sóobu,
40 but sitting at my right or left isn't mine to give - that's for those it's prepared for." waaye toog ci sama ndijoor mbaa sama càmmoñ, du man maa koy maye. Ñi ñu ko waajal rekk a ko yelloo.»
41 Hearing this, the ten grew indignant at James and John. Bi nga xamee ne fukki taalibe ya ca des dégg nañu loolu, ñu daldi mere Saag ak Yowaana.
42 Jesus called them together and said, "You know that those regarded as rulers of the Gentiles dominate them, and their great ones wield power over them. Waaye Yeesu woo leen naan: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, ñi ñu teg njiit dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi di leen not.
43 But it isn't so among you. Instead, whoever wants to be great among you must be your servant, Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga,
44 and whoever wants to be first among you must be slave of all. te ku bëgga nekk njiit, na nekk seen jaam.
45 For even the Son of Man came not to be served, but to serve, and to give his life as a ransom for many." Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe sax, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye ngir muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
46 They came to Jericho. As Jesus and his disciples were leaving with a large crowd, blind Bartimaeus son of Timaeus sat begging by the road. Bi loolu wéyee ñu agsi ca dëkku Yeriko. Bi ko Yeesu di génn, ànd ak taalibe ya ak mbooloo mu xawa bare, am gumba gu tudd Bartime-- liy tekki «doomu Time», toog ci wetu yoon wi, di yelwaan.
47 Hearing it was Jesus of Nazareth, he began to cry out, "Jesus, Son of David, have mercy on me!" Noonu mu dégg ne, Yeesum Nasaret moo fay romb; mu daldi yuuxu naan: «Yërëm ma, yaw Sëtu Daawuda bi!»
48 Many scolded him to be silent, but he shouted even louder, "Son of David, have mercy on me!" Ci kaw loolu ñu bare gëdd ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna yuuxu naan: «Yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm ma!»
49 Jesus stopped and said, "Call him." So they called the blind man: "Courage! Get up—he's calling you." Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.»
50 Throwing off his cloak, he jumped up and came to Jesus. Bi mu ko déggee, mu sànni malaanam, ne bërét, dem ci Yeesu.
51 Jesus told him, "What do you want me to do for you?" The blind man told him, "Rabboni, let me see again." Yeesu ne ko: «Loo bëggoon ma defal la ko?» Gumba gi ne ko: «Kilifa gi, damaa bëgga gis.»
52 Jesus told him, "Go; your faith has healed you." At once he regained his sight and followed Jesus on the road. Noonu Yeesu ne ko: «Demal ci jàmm. Sa ngëm faj na la.» Ci saa si gumba gi gis, daldi topp Yeesu ci yoon wi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]