Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 7 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 The Pharisees and some of the scribes who had come from Jerusalem gathered around Jesus, Amoon na bés nag, ay Farisen ak ay xutbakat yu jóge Yerusalem ñëw ci Yeesu.
2 and they saw that some of his disciples were eating bread with unclean hands—that is, unwashed. Ñu gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwuñu woon, ni ko aada santaanee.
3 (For the Pharisees and all the Jews don't eat unless they wash their hands ceremonially, keeping the elders' tradition. Farisen yi nag ñoom ak Yawut yi yépp dañuy topp aaday yoon, yi maam yi tëral, te fandee leen gënal lekk ak loxo yu ñu raxasul.
4 When they come from the market, they don't eat without washing. They also hold to many other traditions they've received—washing cups, pitchers, and copper vessels.). Te it bu ñu jógee pénc ma, su ñu sanguwul set, duñu lekk. Am nañu it yeneen aada yu bare, maanaam ni nga wara raxase ay kaas, ay njaq ak ay satala, ba ñu laab.
5 Then the Pharisees and scribes asked him, "Why don't your disciples follow the elders' tradition, but eat bread with unclean hands?" Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?»
6 He replied, "Isaiah prophesied truly about you hypocrites, as written: 'These people honor me with their lips, but their heart is far from me.' Yeesu ne leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee: “Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma.
7 'They worship me in vain, teaching as doctrines the commandments of men.' Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”»
8 You abandon the commandment of our Father and hold to the tradition of men." Yeesu neeti leen: «Dëddu ngeen ndigali Yàlla, jublu ci aaday nit.»
9 He said to them, "You do a fine job setting aside our Father's commandment to keep your own tradition!" Mu teg ca ne leen: «Xelu ngeen ci tebbi ndigali Yàlla, ngir sàmm seen aada.
10 For Moses said, 'Honor your father and your mother,' and 'Whoever curses father or mother must be executed.' Ndaxte Musaa nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” teg ca ne: “Ku móolu sa yaay walla sa baay, dees na la rey.”
11 "But you say: if anyone tells his father or mother, 'Whatever you'd have gained from me is Corban' (a gift devoted to our Father), Waaye yéen dangeen ne: ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga wara jariñoo ci man Korban la,” --maanaam saraxu Yàlla la--
12 then you no longer let him do anything for his father or mother. dootuleen ko bàyyi, mu defal dara ndeyam walla baayam.
13 So you cancel the word of our Father with your handed-down tradition. You do many things like this." Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it yéena ngi def yeneen yu bon yu mel nii.»
14 He called the crowd again and said to them, "Listen to me, all of you, and understand: Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne leen: «Yéen ñépp dégluleen ma te xam.
15-16 Nothing outside a person entering him can make him unclean; rather, what comes out of a person is what makes him unclean." Li ci biti, tey dugg nit, du ko mana indil sobe, waaye li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.»
17 When he had left the crowd and entered the house, his disciples asked him about the parable. Bi nga xamee ne jóge nañu ci mbooloo mi, dugg ci kër gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil leen wax ju làqu jooju.
18 He said to them, "Are you also this dull? Don't you understand nothing entering a person from outside can make him unclean, Yeesu ne leen: «Ndax yéen itam seen xol dafa tëju? Xanaa xamuleen ne, dara lu jóge biti, dugg ci nit, du ko mana indil sobe,
19 since it doesn't enter his heart but his stomach, and then goes out into the sewer?" (Saying this, he declared all foods clean.). ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jëm, ba noppi daldi génn ca bérab bu làqu?» Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bépp ñam.
20 He said, "What comes out of a person—that makes him unclean. Yeesu ne leen ati: «Li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.
21 For from within, out of the human heart, come evil thoughts—sexual sin, theft, murder, Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jóge ak ndoxaanu yàqute, càcc ak bóom,
22 adultery, greed, malice, deceit, sensuality, envy, slander, pride, and foolishness. njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof.
23 All these evils come from inside and make a person unclean." Lu bon loolu lépp day génn ci nit, di ko indil sobe.»
24 Jesus left there for the region of Tyre. He entered a house, wanting no one to know, but couldn't stay hidden. Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam manula umpe.
25 Instead, a woman whose little daughter had an unclean spirit heard about him at once, came, and fell at his feet. Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam,
26 The woman was Greek, Syrophoenician by birth. She kept asking him to drive the demon out of her daughter. fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam.
27 He told her, "Let the children eat first, for it's not right to take their bread and toss it to the dogs." Waaye Yeesu ne ko: «Na gone yi jëkka lekk, ba regg; fab ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
28 But she replied to him, "Sir, even the dogs under the table eat the children's crumbs." Jigéen ji ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gone yi.»
29 He said to her, "Because of this answer, go—the demon has left your daughter." Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Ndax wax jooju demal ci jàmm, rab wa génn na sa doom.»
30 And she went home and found the child lying on the bed, and the demon gone. Noonu mu ñibbi, fekk doom ji tëdd cib lal te mucc ci rab wi.
31 Then Jesus left the territory of Tyre, went through Sidon to the Sea of Galilee, into the region of the Decapolis. Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi.
32 They brought him a deaf man who could hardly speak, begging him to lay his hand on him. Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo.
33 Jesus took him aside privately, away from the crowd, put his fingers in the man's ears, spit, and touched his tongue. Noonu Yeesu yóbbu ko, ba ñu sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal làmmiñam.
34 Then, looking up to heaven, he sighed deeply and said to him, "Ephphatha!" (that is, "Be opened!"). Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki «Ubbikuleen.»
35 And immediately his ears were opened, his tongue was released, and he began to speak plainly. Ci saa si ay noppam daldi dégg te làmmiñam yiwiku, muy wax bu leer.
36 Jesus ordered them to tell no one; but the more he ordered, the more they proclaimed it. Bi mu ko defee Yeesu tere leen, ñu wax ko kenn, waaye lu mu leen ko gëna tere, ñu gën ko nee siiwale.
37 They were completely amazed: "He has done everything well—he makes the deaf hear and the mute speak." Ñu waaru lool naan: «Lépp lu mu def, lu yéeme la. May na sax tëx yi ñuy dégg, ak luu yi ñuy wax.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]