Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 6 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 He went out from there and came to his hometown, and his disciples followed him. Bi loolu amee Yeesu jóge fa, dellu réewam, ànd ak taalibe yi.
2 On the Sabbath he began teaching in the synagogue. Many who heard were amazed: "Where did this man get this? What wisdom is this, given to him? How do such miracles happen through his hands? Bésub noflaay bi nag mu jàngal leen ci seen jàngu, ba mbooloom ñi ko dégg waaru naan: «Lii, fu mu ko jële, te xam-xam bii mu yor, lu mu doon, ba muy def kéemaan yii?
3 Isn't this the carpenter, Mary's son, brother of James, Joses, Judas, and Simon? Aren't his sisters here with us?" They were offended by him. Ndax kii du minise bi? Ndax du doomu Maryaama te magu Saag, Yuusufa, Yuda ak Simoŋ? Te ay rakkam yu jigéen ndax nekkuñu fi ak nun?» Kon nag ñu daldi ko xeeb.
4 Jesus said to them, "A prophet lacks honor only in his hometown, among his relatives, and in his own household." Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam, ciy bokkam mbaa ci këram.»
5 He could do no miracle there, except laying hands on a few sick and healing them. Yeesu manu faa def ay kéemaan yu bare, lu dul teg loxo yenn jarag, wéral leen.
6 He was amazed at their lack of faith. Then he went around the villages teaching. Mu waaru ndax seen ngëmadi. Bi loolu amee Yeesu di wër dëkk ya, di jàngle.
7 He called the twelve and began sending them out two by two, giving them authority over unclean spirits. Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, yónni leen, ñu ànd ñaar-ñaar.
8 He ordered them to take only a staff for the road—no bread, no bag, no money in their belts, Mu digal leen nii: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara; du mburu mbaa mbuus mbaa xaalis ci seeni maxtume, waaye yemleen ci aw yet rekk.
9 but to wear sandals and not put on two tunics. Sol-leen ay dàll te yem ci benn turki.»
10 And he said to them, "Wherever you enter a house, stay there until you leave that place. Mu ne leen: «Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen jóge dëkk ba.
11 Whatever place refuses to welcome or hear you, leaving there, shake the dust off your feet as testimony against them." Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu leen, génnleen fa, yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
12 So they went out and proclaimed that people should repent. Noonu taalibe ya dem, di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar.»
13 And they drove out many demons and anointed many sick people with oil and healed them. Ñu dàq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wéral leen.
14 King Herod heard of it, for Jesus's name had become known. Some were saying, "John the Baptist has been raised from the dead; that is why these miraculous powers are at work in him." Noonu Erodd buur bi dégg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag: «Yaxya dekki na, moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
15 But others said, "He's Elijah." Others said, "He's a prophet, like one of the prophets of old." Ñeneen ne: «Kii Ilyaas la.» Ñi ci des ne: «Yonent la, bu mel ni yonent yu jëkk ya.»
16 But when Herod heard of it, he said, "John, whom I beheaded, has been raised." Waaye bi ko Erodd déggee, mu ne: «Yaxya male ma dagglu boppam, moom moo dekki.»
17 Herod had sent and seized John, binding him in prison because of Herodias, his brother Philip's wife, whom he had married. Fekk Erodd yónnee woon na, jàpp Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam.
18 For John kept telling Herod, "It is not lawful for you to have your brother's wife." Te Yaxya ne ko: «Jaaduwul nga denc sa jabaru mag.»
19 And Herodias held a grudge against him and wanted to kill him, but she could not, Moo tax Erojàdd ëmbal ko mer, ba bëgg koo rey, waaye manu koo def.
20 Herod feared John, knowing him righteous and holy, and protected him. Hearing John left Herod deeply puzzled, yet he gladly listened to him. Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba sàmm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan déglu it, day jaaxle lool, teewul mu bég ci déglu ko.
21 Then a fitting day came: Herod's birthday, when he gave a banquet for his nobles, military commanders, and Galilee's leading men. Noonu bés bu yell ñëw, ba Erodd doon màggal bésu juddoom; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay xare ba ak njiiti diiwaanu Galile.
22 When Herodias's daughter entered and danced, she delighted Herod and his dinner guests. The king told the girl, "Ask me for anything you want, and I'll give it to you." Booba doomu Erojàdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan ñi, ba buur bi ne janq bi: «Laaj ma loo bëgg, dinaa la ko jox.»
23 He swore to her, "Whatever you ask me, I'll give you—up to half my kingdom." Mu boole ci ngiñ ne ko: «Loo ma mana laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-wàllu réew mi sax.»
24 She went out and said to her mother, "What should I ask?" She said, "The head of John the Baptist." Noonu janq bi génn ne ndeyam: «Lu may laaj?» Mu ne ko: «Laajal boppu Yaxya.»
25 She went in immediately, with urgency, to the king and asked, "I want you to give me this instant the head of John the Baptist on a platter." Mu daldi gaawantu dugg nag ci kanam buur bi ne ko: «Damaa bëgg, nga indil ma léegi boppu Yaxya ci biir ndab.»
26 Deeply grieved, the king still wouldn't refuse her, because of his oaths and his guests. Bi ko buur ba déggee, mu am naqar wu réy. Waaye bëggu koo gàntu ndax ngiñ li ak gan ñi.
27 The king at once sent an executioner, ordering John's head brought. He went and beheaded him in the prison, Mu daldi yónni nag xarekat, jox ko ndigal, mu indil ko boppu Yaxya. Waa ji dem, dagg boppu Yaxya ca kaso ba,
28 and brought his head on a platter, gave it to the girl, and the girl gave it to her mother. indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq bi, mu daldi ko jox yaayam.
29 When John's disciples heard, they came, took his body, and laid it in a tomb. Ba taalibey Yaxya déggee loolu, ñu ñëw, fab néew ba, suul ko ci bàmmeel.
30 The apostles gathered to Jesus and told him all that they had done and taught. Gannaaw loolu ndaw yi dajaloo ci wetu Yeesu, nettali li ñu def ak li ñu jàngle lépp.
31 He told them, "Come away by yourselves to a quiet place and rest a while." For many were coming and going, and they had no time to eat. Ci kaw loolu Yeesu ne leen: «Nanu beddeeku, dem ci bérab bu wéet; ngeen noppalu fa tuuti.» Waxoon na loolu, ndaxte amoon na ñu bare ñu doon dem ak a dikk, ba amuñu sax jot ngir lekk.
32 And they went away in the boat to a desolate place by themselves. Noonu ñu dugg cig gaal, dem ca bérab bu wéet.
33 Many saw them leave and recognized them; they ran on foot from every town and got there ahead of them. Bi ñuy dem nag, am ñu leen gis, xàmmi leen, ñu daldi jóge ci dëkk yépp, daw, jiitu leen fa.
34 Stepping ashore, he saw a large crowd and felt compassion for them, for they were like sheep without a shepherd, and began teaching them many things. Bi Yeesu génnee gaal gi, mu gis mbooloo mu réy, yërëm leen, ndaxte dañoo mel ni xar yu amul sàmm. Kon mu daldi leen jàngal lu bare.
35 When it was already late, his disciples came to him and said, "This is an isolated place, and it's already late. Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi.
36 Send them away to go into the surrounding countryside and villages and buy themselves something to eat." Yiwil mbooloo mi nag, ñu dugg ci àll bi ak dëkk yi nu wër, jënd lu ñu lekk.»
37 He replied, "You give them something to eat." They said, "Should we go buy 200 denarii of bread and give them it to eat?" Waaye Yeesu ne leen: «Yéen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa nu jënd lu tollook peyu juróom ñetti weer ci mburu, jox leen ñu lekk?»
38 He asked them, "How many loaves do you have? Go and see." They found out and said, "Five, and two fish." Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am? Demleen seeti.» Ñu dem seeti ne ko: «Juróomi mburu ak ñaari jën.»
39 Then he commanded them all to sit down in groups on the green grass. Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu def ay géew, toog ci ñax mu naat mi.
40 So they sat down in groups, by hundreds and by fifties. Ñu toog nag ay géewi juróom fukk ak téeméer.
41 Taking the five loaves and two fish, he looked up to heaven, gave thanks and broke the loaves, gave them to the disciples to set before the people, and divided the two fish among them all. Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, sant Yàlla, ba noppi mu damm mburu yi, jox ko taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi. Ñaari jën yi it mu séddale ko ñépp.
42 And they all ate and were satisfied. Noonu ñépp lekk ba suur.
43 And they took up twelve baskets full of broken pieces and of the fish. Te it ñu dajale la desoon ca dammiti mburu ak jën ya, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees.
44 And those who ate the loaves were 5,000 men. Ñu lekkoon nag matoon na limu juróomi junniy góor.
45 At once he made his disciples board the boat and go ahead to the other side, toward Bethsaida, while dismissing the crowd. Ci kaw loolu Yeesu sant ay taalibeem, ñu dugg ci gaal gi, jàll ba Betsayda, bi muy yiwi mbooloo mi.
46 And after he had taken leave of them, he went up on the mountain to pray. Bi mu tàggtoo ak mbooloo mi, mu yéeg ca tund wa, ñaan fa Yàlla.
47 When evening came, the boat was out on the sea, and he was alone on the land. Noonu guddi jot, fekk gaal gi nekk ci diggu dex gi, te Yeesu rekk moo nekk ca tefes ga.
48 He saw them straining at the oars, for the wind was against them. Around three in the morning he came to them, walking on the sea. He meant to pass by them, Booba mu gis taalibe yi sonn lool ci joow gaal gi ndax li leen ngelaw li soflu. Ca njël nag mu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi, ba xaw leena raw.
49 but seeing him walk on the sea, they thought it was a ghost and cried out, Bi ñu ko gisee nag, muy dox ci kaw dex gi, ñu foog ne njuuma la, daldi yuuxu.
50 for all saw him and were terrified; but immediately he spoke to them, saying, "Take heart; it is I. Do not be afraid." Ndaxte ñépp gis ko te jommi ci. Waaye mu wax ak ñoom ci saa si ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!»
51 He got into the boat with them, and the wind stopped; they were completely amazed among themselves, Noonu mu fekksi leen ci gaal gi, ngelaw daldi ne tekk.
52 for they did not understand about the loaves, but their hearts were hardened. Njàqarey taalibe ya nag weesu dayo, ndaxte seen xol dafa fatt, ba réere mbir kéemaan, gi Yeesu defoon ci mburu yi.
53 When they had crossed over, they came to land at Gennesaret and moored to the shore. Bi nga xamee ne jàll nañu, ba egg diiwaanu Senesaret, ñu teer fa,
54 And when they got out of the boat, the people immediately recognized him. génn ca gaal ga. Ci saa si nit ñi xàmmi ko,
55 They ran through that whole region and began carrying the sick on mats to wherever they heard he was. ñu daldi daw ca diiwaan ba bépp, te fépp fu ñu ko dégg ñu di ko indil ñu wopp, tëdd ci seeni lal.
56 Wherever he went—villages, towns, countryside—they laid the sick in the marketplaces, begging to touch just the edge of his cloak. All who touched it were healed. Te fu mu mana aw, ci dëkk yu mag mbaa yu ndaw walla ci àll bi, ñu indil ko jarag yi ci pénc yi, ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk. Te képp ku ko laal daldi wér.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]