Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 5 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 They came to the other side of the sea, to the region of the Gerasenes. Noonu ñu jàll dex ga, ba teer ci diiwaanu waa Serasa.
2 As Jesus left the boat, a man with an unclean spirit met him at once, from the tombs. Bi Yeesu génnee gaal gi, nit ku rab jàpp jóge ca sëg ya, daldi ñëw kar ko.
3 He lived among the tombs, and no one could bind him anymore, not even with a chain. Kooku nag ca sëg ya la dëkk, te kenn manu koo yeew, du ak càllala sax.
4 For he'd often been bound with shackles and chains, but tore the chains apart and shattered the shackles—no one had strength to subdue him. Ndaxte ay yoon yu bare jéngoon nañu ko te yeew ko ak ay càllala, waaye waa ji daldi dagg càllala yi te damm jéng yi, ba kenn amul woon kàttanu téye ko.
5 Night and day, among the tombs and on the mountains, he cried out constantly, cutting himself with stones. Guddi ak bëccëg mu nga woon ca sëg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer.
6 And when he saw Jesus from a distance, he ran and fell down before him. Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam,
7 Shouting loudly, he said, "What do you want with me, Jesus, Son of the Most High God? I beg you by God, don't torment me!" di xaacu naan: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Ci turu Yàlla, bu ma mbugal.»
8 For Jesus had been saying to him, "Come out of the man, you unclean spirit!" Ndaxte Yeesu da ko ne: «Yaw rab wu bon wi, génnal ci nit ki.»
9 Jesus asked, "What is your name?" "Legion," he said, "we are many." Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
10 He kept begging him not to send them out of the region. Muy ñaan Yeesu lool, ngir mu bañ leena dàq ca réew ma.
11 Now a great herd of pigs was feeding there on the hillside. Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
12 And they begged him, "Send us to the pigs; let us enter them." Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.»
13 He gave permission. The unclean spirits came out and entered the pigs; the herd—about 2,000—rushed down the cliff into the sea and drowned in the sea. Mu may leen ko. Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nañu ñaari junni.
14 The herders fled and told it in town and country; people came to see what happened. Noonu sàmm ya daw ca dëkk ba ak ca àll ba, nettaliji mbir mi, ba nit ñi ñëw, seet li xew.
15 They came to Jesus and saw the man who had been possessed by the demons, the one who'd had the legion, sitting there, dressed and thinking clearly—and they were afraid. Ñu ñëw nag ci Yeesu, gis ka rab ya jàppoon toog, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
16 Eyewitnesses told them what had happened to the demon-possessed man, and about the pigs. Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya.
17 And they began to beg Jesus to leave their region. Ci kaw loolu ñu daldi ñaan Yeesu, mu sore seen réew.
18 As he was getting into the boat, the once-possessed man begged to be with him. Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya jàppoon ñaan Yeesu, ngir ànd ak moom.
19 But Jesus refused, telling him instead, "Go home to your own people and tell them how much our Father has done for you, and how he has had mercy on you." Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: «Ñibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi yërëme, ba defal la lii lépp.»
20 He went and began proclaiming in the Decapolis all Jesus had done for him, and everyone was amazed. Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru.
21 When Jesus crossed again by boat to the other side, a large crowd gathered around him by the sea. Noonu Yeesu jàllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit ñu bare dajaloo, wër ko.
22 One of the synagogue leaders, named Jairus, came, saw Jesus, and fell at his feet, Kenn ci njiiti jàngu ba nag, tudd Yayrus, ñëw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tànkam,
23 and begged him urgently, "My little daughter is dying. Come, lay your hands on her, so she may be healed and live." di ko sarxu lu bare naan: «Sama doom ju jigéen mi ngi bëgga faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu wér te dund.»
24 So Jesus went with him. And a great crowd followed him and pressed around him. Noonu Yeesu ànd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu réy topp ko, di ko tanc.
25 And there was a woman with a discharge of blood that had gone on for twelve years. Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar.
26 She had suffered much under many doctors, spent all she owned, gained nothing, and only grew worse. Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.
27-28 Hearing about Jesus, she came up behind him in the crowd and touched his cloak. Noonu mu déggoon turu Yeesu, ne ci boppam: «Su ma laalee ay yéreem rekk, dinaa wér.» Mu jaxasoo ak mbooloo mi nag, doxe ko gannaaw, laal mbubbam.
28 For she kept saying, "If I just touch his garments, I will be made well." Not in this edition
29 Her flow of blood dried up instantly, and she felt in her body that she was healed of her suffering. Ci saa si deret ji taxaw, mu yég ci yaramam ne jàngoroom deñ na.
30 At once Jesus, aware that power had left him, turned around in the crowd and asked, "Who touched my clothes?" Yeesu yég ci saa si ne, doole génn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi: «Ana ku laal samay yére?»
31 His disciples said to him, "You see the crowd crushing you, yet you ask, 'Who touched me?'" Ay taalibeem ne ko: «Xanaa gisuloo mbooloo mi lay wër; ngay laaj: “Ku ma laal?”»
32 And he looked around to see who had done it. Waaye Yeesu di xool li ko wër, ngir gis ku ko def.
33 But the woman, afraid and trembling, knowing what had happened to her, came, fell before him, and told him the whole truth. Noonu jigéen ja ñëw, daanu ciy tànkam, wax ko dëgg gépp; mu tiit bay lox, ndaxte xam na li xewoon ci yaramam.
34 He told her, "Daughter, your faith made you well. Go in peace, healed of your suffering." Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la; demal ci jàmm, te na sa jàngoro wàcc.»
35 While he was still speaking, people came from the synagogue leader's house, saying, "Your daughter has died. Why bother the Teacher any longer?" Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul nuy sonal kilifa gi.»
36 But Jesus overheard what they said and told the synagogue leader, "Don't fear, only believe." Waaye Yeesu jàppul wax jooju; mu ne njiit la: «Gëmal rekk te baña tiit.»
37 And he allowed no one to follow him except Peter, James, and John the brother of James. Noonu Yeesu dem, ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana rekk, ndaxte mayul keneen, mu ànd ak moom.
38 They came to the synagogue leader's house and Jesus saw chaos—people weeping, wailing loudly. Naka lañu ñëw ci kër njiit li, Yeesu dégg coow li; ñii di jooy, ñii di yuuxu.
39 Entering, he said to them, "Why this commotion and crying? The child isn't dead, just asleep." Mu dugg ne leen: «Lu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
40 They laughed at him. But he sent them all out, took the child's father and mother and his companions, and entered where the child was. Waaye ñu di ko ñaawal. Noonu Yeesu génne ñépp, woo baayu janq bi ak yaay ji ak ñi mu àndal, dugg fa janq bi nekk.
41 He took her hand and said to her, "Talitha koum," which means, "Little girl, I say to you, get up!" Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.»
42 At once the girl got up and walked—for she was twelve—and they were instantly overwhelmed with great amazement. Ca saa sa janq bi jóg, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp daldi waaru, ba ne jomm.
43 He strictly ordered them to tell no one of this, and said to give her something to eat. Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal; teg ca naa: «Mayleen janq bi, mu lekk.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]