Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Jesus again taught by the sea. So large a crowd gathered around him that he got into a boat on the water and sat, while the whole crowd was on land by the sea. Am beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di jànglewaat. Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu yéeg cig gaal, dugg ca dex ga; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
2 He taught them many things in parables, and in his teaching he said to them: Noonu Yeesu daldi leen jàngal lu bare ciy léeb. Ci njàngleem nag mu ne leen:
3 "Listen! A sower went out to sow. «Dégluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
4 And as he sowed, some seed fell along the path, and the birds came and devoured it. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
5 Other seed fell on rocky ground, lacking much soil, and sprang up at once since the soil had no depth. Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
6 When the sun rose, the plants were scorched, and since they had no root, they withered. Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
7 Other seed fell among thorns, and the thorns grew up and choked it, yielding no grain. Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara.
8 Other seed fell into good soil, producing grain that sprouted, grew, and yielded thirty, sixty, one hundred times what was sown." Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, lii mat téeméer.»
9 And he said, "Whoever has ears to hear, let him hear." Noonu Yeesu ne leen: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
10 When he was alone, those around him, together with the Twelve, asked him about the parables. Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi.
11 He said to them, "To you is given the secret of the kingdom of our Father, but to those outside, everything comes in parables, Mu ne leen: «Yéen may nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci biti léeb ay ëmb lépp.
12 so that 'they may look but not perceive, and hear but not understand, and not turn and be forgiven.'" Noonu la, ngir: “Ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara, di déglu bu baax waaye duñu xam dara, ngir bañ ñu tuub seeni bàkkaar te Yàlla baal leen.”»
13 He said to them, "You don't understand this parable? Then how will you understand all the parables? Noonu Yeesu ne leen: «Ndax xamuleen léeb wii? Nu ngeen xame nag léeb yi ci des?
14 The sower sows the word. Ki ji nag, kàddu gi lay ji.
15 These are the ones on the path where the word is sown: once they hear, Satan comes immediately and takes away the word sown in them. Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg, Seytaane ñëw ci saa si, këf kàddu, gi ñu def ci moom.
16 These are the ones sown on rocky ground, who hear the word and immediately receive it with joy. Ki jot kàddu gi ci bérab bu bare ay doj mooy ki dégg kàddu gi, nangu ko ak mbég ci saa si,
17 But they have no root in themselves, lasting only briefly; when trouble or persecution comes because of the word, they fall away at once. waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
18 And others are the ones sown among thorns. These are those who hear the word, Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi,
19 but worries of this age, the deceit of wealth, and desires for other things enter and choke the word, and it produces no fruit. waaye soxlay àddina ak naxi alal ak bëgge solu ko, tanc kàddu gi, ba du meññ dara.
20 And these are the ones sown on good soil: they hear the word, accept it, and produce fruit—thirty, sixty, one hundred times over." Ki jot kàddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dégg te nangu ko, ba jariñ; kii mat fanweeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, kii mat juróom benn fukk, kii mat téeméer.»
21 He told them, "Does anyone bring in a lamp to put it under a basket or bed—not on a stand? Yeesu ne leen itam: «Ndax nit dina jël làmp, dëpp ci leget walla def ko ci ron lal? Ndax du ko wékk?
22 Nothing is hidden except to be revealed; nothing is secret except to surface. Amul dara luy kumpa lu ñu warula siiwal, mbaa mu làqu te warul ne fàŋŋ.
23 If anyone has ears to hear, let him hear." Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
24 He told them, "Watch what you hear. The measure you use will be measured to you—and more added. Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen.
25 For whoever has will be given more; whoever doesn't, even what he has will be taken from him." Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as néew, dees na ko nangu.»
26 He said, "This is what the kingdom of our Father is like: a man scatters seed on the ground. Yeesu teg ci ne: «Nguuru Yàlla dafa mel ni nit ku ji tool.
27 Night and day, asleep or awake, the seed sprouts and grows, though he doesn't know how. Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg, jiwu wi sax, di màgg, te xamul naka la ko defe.
28 The soil yields grain on its own—first blade, then head, then full kernel in the head. Suuf day meññ moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub.
29 But when the grain ripens, he immediately sends the sickle, since harvest has come." Bu gub yi ñoree nag, mu dagg ko, ndaxte ngóob jot na.»
30 He said, "What can we compare the kingdom of our Father to, or what parable can we use for it? Yeesu ne leen ati: «Lu nu mana méngaleel nguuru Yàlla? Walla ban léeb lanu ko mana misaale?
31 It's like a mustard seed, the smallest of all seeds when sown on the ground. Dafa mel ni doomu fuddën, bi gëna tuuti ci jiwu yépp;
32 Yet once sown, it grows up and becomes the largest of all garden plants, producing branches so big that birds of the air can nest in its shade." waaye boo ko jiyee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.»
33 With many such parables he spoke the word to them, as they were able to hear. Noonu Yeesu dégtal leen yeneen léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan.
34 He spoke to them only in parables, but privately explained everything to his own disciples. Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp.
35 That day, when evening came, he said to them, "Let us cross over to the other side." Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.»
36 They left the crowd and took him along, just as he was, in the boat, other boats accompanying him. Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneen gaal ànd ak moom.
37 A fierce windstorm came up. Waves broke over the boat, so that it was already being swamped. Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgga fees.
38 But Jesus was asleep in the stern on the cushion. They woke him and said, "Teacher, don't you care that we're dying?" Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?»
39 He got up, rebuked the wind, and told the sea, "Peace! Be still!" The wind stopped, and it grew totally calm. Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm.
40 He said to them, "Why are you so afraid? Do you still have no faith?" Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»
41 They were terrified and asked one another, "Who then is this, that even the wind and the sea obey him?" Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]