Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Once again Jesus entered the synagogue, and a man with a withered hand was there. Am beneen bés, Yeesu duggaat ci jàngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom làggi.
2 They watched closely to see if he'd heal the man on the Sabbath, to accuse Jesus. Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu man koo tuumaal.
3 Jesus said to the man with the withered hand, "Stand up and come forward." Yeesu ne ku loxoom làggi: «Jógal, taxaw ci kanam ñépp.»
4 Then he asked them, "Is it lawful on the Sabbath to do good or to do harm, to save life or to kill?" But they stayed silent. Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell.
5 He looked around at them in anger, grieved by their hardness of heart, and told the man, "Stretch out your hand." He stretched it out, and his hand was restored. Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ.
6 Then the Pharisees went out and immediately began plotting with the Herodians how they might destroy him. Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu.
7 Jesus withdrew with his disciples to the sea; a large crowd from Galilee followed, and from Judea, Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko.
8 from Jerusalem, Idumea, beyond the Jordan, and the region around Tyre and Sidon—hearing all he was doing, a great crowd came to him. Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon.
9-10 He told his disciples to keep a small boat ready, because of the crowd, so they wouldn't crush him. Booba nag Yeesu faj na ñu bare, ba mboolem ñi am i jàngoro di ko song, ngir laal ko. Noonu Yeesu wax ay taalibeem, ñu wutal ko gaal, ngir mbooloo mi bañ koo buux.
10 For he had healed so many that all who had diseases were pressing forward to touch him. Not in this edition
11 Whenever the unclean spirits saw him, they fell before him, shouting, "You are the Son of God!" Fekk booba képp ku rab jàpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.»
12 But he firmly warned them not to reveal him. Waaye Yeesu gëdd rab yi bu wér, ngir ñu bañ koo siiwal.
13 Jesus went up the mountain and called those he wanted; they came to him. Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund wi, woo ñi ko neex, ñu daldi ñëw ci moom.
14 He appointed twelve, named apostles, so they could be with him and he could send them out to preach, Noonu mu tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñu ànd ak moom te mu yónni leen, ñu waareji,
15 and to have authority to drive out demons. mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab.
16 These are the twelve he appointed: Simon, to whom he gave the name Peter; Fukk ak ñaar ñii la tànn: Simoŋ, mi mu tudde Piyeer,
17 James son of Zebedee, and John his brother, whom he named Boanerges, meaning Sons of Thunder; Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay-- ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi»--
18 Andrew, Philip, Bartholomew, Matthew, Thomas, James son of Alphaeus, Thaddaeus, Simon the Zealot, Andare ak Filib, Bartelemi ak Macë, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
19 and Judas Iscariot, who betrayed him. ak Yudaa Iskariyo mi nara wor Yeesu.
20 He went home; the crowd gathered again, so he and his disciples couldn't even eat. Am beneen bés Yeesu ñëwaat ca kër ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax manuñoo lekk sax.
21 When his family heard, they went out to restrain him, for they said, "He's out of his mind." Bi ko ay bokkam déggee nag, ñu ñëw, ngir jàppsi ko naan: «Dafa tàggoo ak sagoom.»
22 The scribes who came down from Jerusalem said, "He has Beelzebul," and, "By the prince of demons he drives out demons." Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
23 So Jesus called them to him and spoke in parables: "How can Satan drive out Satan? Noonu Yeesu woo leen, wax ak ñoom ciy léeb ne leen: «Naka la Seytaane mana dàqe Seytaane?
24 If a kingdom is divided against itself, that kingdom cannot stand. Réew mu xeex boppam, du mana yàgg.
25 And if a house is divided against itself, that house will not be able to stand. Te kër gu xeex boppam, du mana yàgg.
26 And if Satan opposes himself and is divided, he cannot stand; his end has come. Bu Seytaane nag jógee, ba xeex boppam, xàjjalikoo dikkal na ko te du mana yàgg, waaye dina tas.
27 No one can enter a strong man's house and take his goods without first tying up the strong man—then he can plunder the house. «Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn mana dugge ci këram, nangu alalam? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp.
28 Truly I tell you, all sins and insults against God will be forgiven children of mankind, whatever they say, Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp dees na ko baal nit ñi, muy bàkkaar, muy sosal Yàlla wu mu mana doon.
29 but whoever blasphemes against the Holy Spirit never has forgiveness; they are guilty of an eternal sin," Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; gàddu na bàkkaar ba fàww.»
30 for they were saying, "He has an unclean spirit." Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon nañu, rab jàpp na ko.
31 His mother and brothers arrived and, standing outside, sent to him, calling him. Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw, ñu taxaw ci biti, yónnee, woo ko.
32 A crowd sat around him and said to him, "Look, your mother and your brothers are outside, asking for you." Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.»
33 He answered them, "Who are my mother and my brothers?" Waaye Yeesu ne leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?»
34 Looking around at those sitting in a circle around him, he said, "Here are my mother and my brothers! Noonu mu xool ñi ko wër naan: «Sama yaay ak samay rakk a ngii;
35 Whoever does the will of our Father is my brother and sister and mother." ndaxte kuy def coobarey Yàlla, kooku mooy sama rakk ak sama jigéen ak sama ndey.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]