Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 John 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Beloved, don't believe every spirit, but test the spirits to see if they're from our Father, for many false prophets have gone out into the world. Samay soppe, buleen gëm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci Yàlla lañu jóge walla déet, ndaxte naaféq yu bare yu mbubboo turu yonent jóg nañu, tasaaroo ci àddina si.
2 By this you know the Spirit of our Father: every spirit confessing that Jesus Christ has come in the flesh is from our Father, Ci lii lanu xàmmee Xelum Yàlla: mépp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist ñëw na, nekk nit, ci Yàlla la bokk.
3 and every spirit that does not confess Jesus is not from our Father. This is the antichrist's spirit, which you heard was coming, and is already in the world now. Waaye mépp xel mu nanguwul Yeesu, bokkul ci Yàlla. Xel moomu mooy xelum Bañaaleb Kirist, mi ngeen déggoon ne dina ñëw, te léegi sax mu ngi ci biir àddina.
4 You are from our Father, little children, and have overcome them, because greater is the one in you than the one in the world. Yéen samay doom, ci Yàlla ngeen bokk, te daan ngeen yonent yu naaféq yooyu, ndaxte ki nekk ci yéen moo ëpp doole ki nekk ci àddina.
5 They are from the world; therefore they speak from the world, and the world listens to them. Ñoom ci àddina lañu bokk; moo tax ñuy wax waxi àddina, te àddina di leen déglu.
6 We are from our Father. Whoever knows him hears us; whoever is not from him does not hear us. This is how we know the Spirit of truth and the spirit of error. Nun nag ci Yàlla lanu bokk. Ku xam Yàlla dinga nu déglu; ku bokkul ci Yàlla doo nu déglu. Ci loolu lanuy xàmmee Xel miy dëgg ak xel mi dul dëgg.
7 Beloved, let us love one another, for love is from our Father, and all who love are born of him and know him. Samay soppe, nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo; képp ku bëgg sa mbokk nag, ci Yàlla nga juddoo, te xam nga Yàlla.
8 Whoever does not love does not know our Father, because our Father is love. Ku bëggul sa mbokk, xamuloo Yàlla, ndax Yàlla mbëggeel la.
9 This is how our Father's love was shown among us: our Father sent his one and only Son into the world so we might live through him. Nii la Yàlla wonee mbëggeelam ci nun; yónni na ci àddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom.
10 This is love: not that we loved our Father, but that he loved us and sent his Son as the atoning sacrifice for our sins. Lii mooy mbëggeel, du sunu mbëggeel ci Yàlla, waaye mbëggeelam ci nun, ba mu yónni Doomam, mu joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar.
11 Beloved, if our Father so loved us, we also ought to love one another. Samay soppe, bu nu Yàlla bëggee nii, nun itam war nanoo bëggante.
12 No one has ever seen our Father; if we love one another, our Father remains in us and his love is made complete in us. Kenn masula gis Yàlla, waaye bu nu bëggantee, Yàllaa ngi dëkk ci nun te mbëggeelam mat na sëkk ci nun.
13 By this we know we live in him and he in us: he has given us his Spirit. Ci lii lanuy xame ne sax nanu ci Yàlla, te moom itam dëkk na ci nun: sol na nu Xelam.
14 We have seen and testify that our Father sent the Son as Savior of the world. Te nun gis nanu te seede ne, Baay bi yónni na Doom ji, mu nekk Musalkatu àddina.
15 Whoever confesses Jesus is the Son of our Father, our Father remains in him, and he in our Father. Képp ku nangu ne, Yeesu Doomu Yàlla la, Yàlla dëkk na ci yaw, te yaw it sax nga ci Yàlla.
16 We have known and believed the love our Father has for us. Our Father is love, and whoever remains in love remains in him, and he in them. Mbëggeel gi Yàlla am ci nun, xam nanu ko te gëm ko. Yàlla mbëggeel la, te képp ku sax ci mbëggeel, yaa ngi sax ci Yàlla, mu dëkk ci yaw.
17 This is how love is made complete in us, so we may have confidence on judgment day, because as he is, so are we in this world. Ni Kirist mel, noonu lanu mel nun itam ci àddina. Ci loolu la mbëggeel mate sëkk ci nun, ngir nu am kóolute bésu àtte ba.
18 In love there is no fear; perfect love drives out fear, since fear involves punishment, and whoever fears is not complete in love. Genn ragal amul ci mbëggeel, waaye mbëggeel gu mat sëkk day dàq ragal. Ndaxte ragal day ànd ak mbugal; te ku ragal, mbëggeel matul sëkk ci yaw.
19 We love because our Father first loved us. Danuy wéy ci mbëggeel, ndax moo nu jëkka bëgg.
20 If anyone says, "I love our Father," yet hates his brother, he is a liar. For whoever does not love his brother, whom he has seen, cannot love our Father, whom he has not seen. Su kenn nee: «Bëgg naa Yàlla,» te bëgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku bëggul sa mbokk mi ngay gis, doo mana bëgg Yàlla mi nga gisul.
21 And this commandment we have from him: whoever loves our Father must also love his brother. Te jox na nu ndigal lii: ku bëgg Yàlla, nga bëgg sa mbokk.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]