Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 John 5 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Everyone who believes Jesus is the Christ has been born of our Father, and everyone who loves the Father who gives birth loves the child born of him. Képp ku gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, juddu nga ci Yàlla; te ku bëgg waajur, dinga bëgg itam ki mu jur.
2 By this we know we love the children of our Father: when we love our Father and keep his commands. Xam nanu ne bëgg nanu doomi Yàlla yi ci lii: bëgg Yàlla tey sàmm ay ndigalam.
3 This is love of our Father: that we keep his commands, and his commands aren't burdensome. Ndaxte mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam; te ay ndigalam diisuñu.
4 Everyone born of our Father overcomes the world. This is the victory that overcame the world: our faith. Ndaxte képp ku juddu ci Yàlla day not àddina; te li nuy note àddina mooy sunu ngëm.
5 Who overcomes the world except the one believing Jesus is the Son of our Father? Ku not àddina mooy kan? Mooy ki gëm ne Yeesu mooy Doomu Yàlla.
6 Jesus Christ came by water and blood—not water only, but water and blood. The Holy Spirit testifies to this, because the Holy Spirit is the truth. Yeesu Kirist mooy ki ñëw, jaar ci ndox ak deret; du ci ndox rekk, waaye ndox ak deret. Te Xelu Yàlla mi moo koy seedeel, ndax Xel mi mooy dëgg.
7 For there are three that testify: Ndaxte am na ñetti seede:
8 the Spirit, the water, and the blood; and these three are in agreement. Xel mi, ndox ak deret, te ñoom ñett ñépp, ñoo bokk benn baat.
9 If we accept human testimony, our Father's testimony is greater—for this is our Father's testimony: that he testified about his Son. Seedes nit, dinanu ko nangu, waaye seedes Yàlla moo gëna wóor, ndax boobu seede mooy li Yàlla seede ci Doomam.
10 Whoever believes in the Son of our Father carries this testimony within himself. Whoever does not believe has made him a liar, since he hasn't believed the testimony our Father gave about his Son. Ku gëm Doomu Yàlla ji, am nga seede boobu ci sa xol. Ku gëmul Yàlla, teg nga ko kuy tebbi waxam ndaxte gëmuloo li Yàlla seede ci Doomam.
11 And this is the testimony: our Father gave us eternal life, and this life is in his Son. Te seede si mooy lii: Yàlla jox na nu dund gu dul jeex, te dund googoo ngi ci Doomam.
12 Whoever has the Son has life; whoever lacks the Son of our Father lacks life. Ku am Doom ji, am nga dund; ku amul Doomu Yàlla, amuloo dund.
13 I write these things to you who believe in the name of the Son of our Father, so you may know you have eternal life. Maa ngi leen di bind yëf yii, yéen ñi gëm turu Doomu Yàlla ji, ngir ngeen xam ne am ngeen dund gu dul jeex.
14 This is our confidence before him: whatever we ask according to his will, he hears us. Kóolute gi nu am ci kanam Yàlla mooy lii: su nu ko ñaanee dara ci coobareem, dina nu nangul.
15 And if we know he hears us—whatever we ask—we know we have what we asked him for. Gannaaw xam nañu ne dina nangu lépp lu nu koy ñaan, xam nanu it ne li nu ko ñaan, jox na nu ko.
16 If anyone sees his brother sin a sin not leading to death, he should ask, and our Father will give him life—to those sinning not to death. There's a sin leading to death; I'm not saying he should pray about that. Ku gis mbokkam, muy def bàkkaar bu jarul dee, na ko ñaanal, te Yàlla dina ko may dund. Ku def bàkkaar bu jarul dee laa wax. Ndaxte am na bàkkaar bu jar dee; boobu taxul may wax, mu ñaanal ko.
17 All wrongdoing is sin, and there is sin that does not lead to death. Gépp jubadi bàkkaar la, waaye am na bàkkaar bu jarul dee.
18 We know: whoever is born of our Father does not keep sinning, but the One who was born of our Father protects him, and the evil one cannot touch him. Xam nanu ne képp ku juddu ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Doomu Yàlla ji mooy wottu sa bakkan, ba Ibliis du la manal dara.
19 We know we are from our Father, and the whole world lies under the evil one's power. Nun nag xam nanu ne nu ngi ci Yàlla, te àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis.
20 We know the Son of our Father has come and given us understanding, to know the One who is true. We are in the One who is true, in his Son Jesus Christ. He is the true God and eternal life. Xam nanu ne Doomu Yàlla ji ñëw na te may na nu xel, ba nu mana xam Aji Wóor ji. Te nu ngi ci Aji Wóor ji ak ci Doomam Yeesu Kirist. Kooku mooy Yàlla ju wóor, ji yor dund gu dul jeex.
21 Little children, keep yourselves from idols. Samay doom, wottuleen seen bopp ciy xërëm.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]