Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

2 John 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 The elder, to the chosen lady and her children, whom I love in truth—not only I, but all who know the truth, Man njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. Bëgg naa leen bu wér ci sama xol, jéllale naa sama bopp sax, waaye itam képp ku xam dëgg gi.
2 because of the truth that lives in us and will be with us forever. Te dëgg gee tax nuy def noonu, dëgg gi dëkk ci nun, tey ànd ak nun ba fàww.
3 Grace, mercy, and peace will be with us from our Father and from Jesus Christ, our Father's Son, in truth and love. Yàlla Baay bi ak Yeesu Kirist, Doomu Baay bi, dinañu nu may yiw, yërmande ak jàmm, ànd ak dëgg ak mbëggeel.
4 I was overjoyed to find some of your children walking in truth, as our Father commanded us. Gis naa ci say doom, ñuy jaar ci tànki dëgg, ni nu ko Baay bi digale, te bég naa ci lool.
5 Now I ask you, dear lady: not a new command, but one we've had from the start—love one another. Léegi nag soxna si, maa ngi lay dénk lii: nun ñépp nanu bëggante, te loolu du dénkaane bu bees, waaye moom lanu jotoon ca njàlbéen ga.
6 This is love: that we walk by his commands. This is the command, as you heard from the beginning: that you walk in love. Lii mooy mbëggeel: nu wéer sunug dund ci ndigali Yàlla; loolu mooy ndigalam, la nu jotoon ca njàlbéen ga, te ci lanu wara jaar.
7 For many deceivers have gone out into the world, denying that Jesus Christ came in the flesh. This is the deceiver and the antichrist. Maa ngi wax loolu nag, ndaxte am na ñuy sànke ñu bare, ñu tasaaroo ci àddina, te nanguwuñu ne Yeesu Kirist wàcc na, nekk nit. Kooku aji sànke la, di Bañaaleb Kirist.
8 Watch yourselves, so that you don't lose what we have worked for, but receive a full reward. Kon moytuleen, ngir baña ñàkk seen añub coono, waaye ngeen am yool bu mat sëkk.
9 Anyone who oversteps, not remaining in Christ's teaching, lacks our Father; whoever remains in the teaching has both our Father and the Son. Képp ku saxul ci dénkaaney Kirist, xanaa di ko weesu, bokkul ci Yàlla; ku sax ci dénkaane yi, bokk nga ak Baay bi ak Doom ji.
10 If someone comes to you without this teaching, don't welcome them into your home or greet them, Ku ñëw fi yaw, te indaalewul dénkaane yooyu, waxuma nga bañ koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax.
11 for whoever greets him shares in his evil deeds. Ku ko nuyu, bokk nga ciy ñaawteefam.
12 I have much to write, but I'd rather not use paper and ink. I hope to come and speak with you face to face, so our joy may be complete. Bëggoon naa leena wax lu bare ci bataaxal bii, waaye lépp xajul ci kayit. Kon nag fas naa yéenee ñëw, ba jàkkaarlook yéen, nu waxtaan ci, ngir sunu mbég mat sëkk.
13 The children of your chosen sister greet you. Say doomi rakk, ji Yàlla tànn, ñu ngi lay nuyu.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]