Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

3 John 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 The elder, to the beloved Gaius, whom I love in truth. Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma bëgg ci sama xol.
2 Beloved, I pray you prosper in every way and stay healthy, as your soul prospers. Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér-gi-yaram, ju mel ni sa naataangeg xol.
3 I rejoiced greatly when brothers arrived and testified about your faithfulness to the truth—for you truly are walking in it. Sunuy bokk ñëw nañu te seede ni nga fonke dëgg gi, ba wéer ci sa dund gépp, te bég naa ci lool.
4 I have no greater joy than this: to hear that my children are walking in the truth. Awma mbég mu ëpp lii: ma dégg ne samay doomi diine ñu ngiy jaar ci tànki dëgg.
5 Beloved, you act faithfully in all you do for the brothers, even strangers. Yaw sama xarit, sa takkute fés na ci teeru bi ngay teeru bokk yi, te fekk xamoo leen.
6 They testified to your love before the church. Send them on in a way worthy of our Father. Seedeel nañu sa mbëggeel fi kanam mbooloom ñi gëm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Yàlla.
7 For they went out for the sake of the Name, accepting nothing from the Gentiles. Ndaxte turu Kirist la leen taxa jóg, te sàkkuwuñu daray ku gëmul.
8 Therefore we ought to support such people, so that we may be fellow workers for the truth. Nun nag fàww nu teeru ñu mel ni ñoom, ngir nu ànd ak ñoom liggéeyal dëgg.
9 I wrote something to the church, but Diotrephes, who loves being first among them, does not receive us. Bind naa mbooloo mi bataaxal, waaye Joteref, mi bëgg not ñépp, du dégg sunu ndigal.
10 So if I come, I'll expose what he's doing—slandering us with malicious words. Not satisfied with that, he refuses to welcome the brothers, stops those who want to, and throws them out of the church. Kon nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru bokk yi, rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo mi.
11 Beloved, don't imitate evil, but good. Whoever does good is from our Father; whoever does evil hasn't seen our Father. Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Yàlla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Yàlla.
12 All speak well of Demetrius, and so does the truth. We testify too, and you know our testimony is true. Naka Demetirus nag, ñépp seedeel nañu ko lu baax, te dëgg gi ci moom sax seedeel na ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te wóor na ma ne sunu seede dëgg la.
13 I had much to write to you, but I would rather not write with pen and ink. Am na lu bare lu ma la bëggoona wax, waaye lépp xajul ci kayit.
14 I hope to see you soon, and we will talk face to face. Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg, jàkkaarlook yaw, nu waxtaan ci.
15 Peace to you. The friends send their greetings. Greet each of the friends by name. Yal na jàmm ànd ak yaw. Xarit yi yépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, kenn ku nekk ci turam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]