Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

1 John 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 See what kind of love our Father has given us, that we should be called children of our Father! And we are. The world doesn't know us because it didn't know him. Xool-leen mbëggeel gi nu Baay bi jox, ni mu réye, ba nu mana tudd doomi Yàlla. Te moom lanu. Moo tax àddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam.
2 Beloved, we are our Father's children now; what we will become has not yet been shown. But we know that when he appears, we will be like him, since we will see him as he is. Samay soppe, léegi doomi Yàlla lanu, te li nu nara nekki feeñagul, waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel.
3 And everyone who has this hope in him purifies himself, just as he is pure. Te képp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom.
4 Everyone who keeps committing sin also commits lawlessness; sin is lawlessness. Ku def bàkkaar, jàdd nga yoon; ndaxte bàkkaar mooy jàdd yoon.
5 You know he appeared to take away our sins, and in him is no sin. Te xam ngeen ne Yeesu Kirist feeñ na, ngir dindi bàkkaar yi, te moom amul benn bàkkaar.
6 Whoever remains in him doesn't go on sinning; whoever goes on sinning hasn't seen or known him. Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy def bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko.
7 Little children, let no one deceive you. Whoever practices righteousness is righteous, just as he is righteous. Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam.
8 Whoever keeps on sinning is of the devil, for the devil has been sinning from the beginning. The reason the Son of our Father appeared was to destroy the works of the devil. Kuy def bàkkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca njàlbéen ga ba tey day bàkkaar. Te Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane.
9 No one born of our Father keeps on sinning, because his seed abides in him; and he cannot keep on sinning, because he has been born of our Father. Ku juddu ci Yàlla doo def bàkkaar, ndax Yàlla sol na la jikkoom, te doo mana sax ci bàkkaar, ndax juddu nga ci Yàlla.
10 This shows who our Father's children are, and who the devil's children are: whoever doesn't do what's right isn't from our Father, nor is anyone who doesn't love their brother or sister. Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla.
11 For this is the message you have heard from the beginning: that we should love one another. Ndaxte xibaar, bi ngeen déggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu bëggante,
12 Not like Cain, who belonged to the evil one and killed his brother. Why did he kill him? Because his own deeds were evil and his brother's were righteous. te baña mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay jëfam dañoo bon, te yu rakkam jub.
13 Do not be surprised, brothers and sisters, if the world hates you. Bokk yi, bu leen àddina bañee, buleen ci jaaxle.
14 We know we've passed from death to life, because we love each other. Whoever doesn't love remains in death. Mbëggeel gi nu bëgg sunuy bokk, moo nuy xamal ne jóge nanu ci dee, tàbbi ci dund. Ku bëggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey.
15 Everyone who hates his brother or sister is a murderer, and you know no murderer has eternal life remaining in him. Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex.
16 This is how we know love: Christ laid down his life for us; we too should lay down our lives for one another. Ci lii lanuy xàmmee luy mbëggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.
17 But if anyone has the world's goods and sees his brother or sister in need, yet closes his heart to them, how does our Father's love remain in him? Waaye ku am alalu àddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dummóoyu ko, nan la mbëggeelu Yàlla dëkke ci yaw?
18 Little children, let us not love with words or talk, but in deed and in truth. Samay doom, bunu bëggante ci wax mbaa ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg.
19-20 By this we'll know we come from the truth, and settle our heart before him, Ci loolu lanu xame ne nu ngi ci dëgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam, ndaxte Yàllaa ëpp sunu xol te xam na lépp.
20 whenever our heart condemns us; for our Father is greater than our heart, and he knows everything. Not in this edition
21 Beloved, if our heart does not condemn us, we have confidence before our Father; Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Yàlla ak kóolute.
22 whatever we ask, we receive from him, because we keep his commands and do what pleases him. Te lépp lu nu koy ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi sàmm ay ndigalam, di def lu ko neex.
23 This is his command: believe in his Son Jesus Christ's name, and love one another as he commanded us. Ndigalam mooy lii: nu gëm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey bëggante, ni mu nu ko digale.
24 Whoever keeps his commands remains in our Father, and our Father in them. This is how we know he remains in us: by the Holy Spirit he gave us. Kuy sàmm ndigalu Yàlla, dinga sax ci moom, mu dëkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne dëkk na ci nun.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]