Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 8 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In those days, again a large crowd gathered with nothing to eat. Jesus called his disciples and said, Ca fan yooya mbooloo mu réy a dajewaatoon te amuñu lu ñu lekk. Yeesu woo taalibe ya, ne leen:
2 "I feel compassion for the crowd—they've been with me three days now and have nothing to eat. «Damaa yërëm mbooloo mi, ndax ñetti fan a ngii yu ñu nekk ak man, te amuñu lu ñu lekk.
3 If I send them home hungry, they'll collapse on the way—some have come from far off." Su ma leen yiwee, ñu ñibbaale xiif, dinañu tële ci yoon wi, ndax am na ci ñu jóge fu sore.»
4 And his disciples answered him, "How can anyone feed these people with bread here in the wilderness?" Taalibeem ya ne ko: «Waaye fu nit di jële mburu mu suur ñii ci àll bu wéet bii?»
5 And he asked them, "How many loaves do you have?" They said, "Seven." Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
6 He told the crowd to sit on the ground, took the seven loaves, gave thanks, broke them, and gave them to his disciples to serve to the people; and they served the crowd. Ba mu ko defee Yeesu sant mbooloo ma ñu toog ci suuf. Mu jël juróom ñaari mburu ya, daldi yékkati kàddug cant, dagg ko, jox taalibe ya, ngir ñu taajal ko mbooloo ma. Ñu taajal leen ko.
7 They also had a few small fish; after blessing them, he told the disciples to serve these to the people. Dese woon nañu fa it tuuti jën yu ndaw. Yeesu jël ko, daldi ñaan mu barkeel. Mu sant nag taalibe ya ñu séddale loola itam.
8 And they ate and were satisfied. And they took up seven baskets of the leftover pieces. Ñu daldi lekk ba regg, ba yóbbu desit wa, yebe ci juróom ñaari dàmba,
9 About 4,000 people were there. And he sent them away. te lu tollook ñeenti junniy (4 000) góor a nga fa woon. Yeesu nag yiwi leen,
10 Then immediately he got into the boat with his disciples and went to the district of Dalmanutha. daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, ñu jàll ba diiwaanu Dalmanuta.
11 The Pharisees came and began debating with him, testing him by demanding a sign from heaven. Farisen yaa dikkoon, di weranteek Yeesu. Ñu di ko fiir, ba tax ñuy sàkku ci moom firnde ju bawoo asamaan.
12 Sighing deeply in his spirit, he said, "Why does this generation demand a sign? Truly I tell you, no sign will be given to this generation." Yeesu nag binni binni gu réy, daldi ne: «Ana lu waral maasug tey jii di wut firnde? Maa leen ko wax déy, du jenn firnde jees di jox maasug tey jii.»
13 And he left them, got back into the boat, and went to the other side. Ci kaw loolu Yeesu bàyyikoo ca ñoom, duggaat, jëm wàllaa dex.
14 They'd forgotten to bring bread—only one loaf was with them in the boat. Fekk na taalibe ya fàttee yóbbaale mburu, te amuñu woon lu dul menn mburu ca gaal ga.
15 And he warned them, "Watch out—beware of the yeast of the Pharisees and the yeast of Herod." Yeesu nag jox leen ndigal lii, ne leen: «Wattuleen! Bàyyileen xel lawiiru Farisen ñi, ak lawiiru Buur Erodd.»
16 And they began discussing with one another that they had no bread. Taalibe ya nag di werante ci seen biir, naan: «Nun de amunu fi mburu.»
17 Knowing this, Jesus asked, "Why discuss having no bread? Do you still not see or grasp? Are your hearts hardened? Yeesu xam la ñuy wax, ne leen: «Lu ngeen di werante, naan amuleen fi mburu? Kon xanaa daal xamaguleen ba tey, te ràññeewuleen? Am seenum xel a dërkiis?
18 Having eyes, do you not see? Having ears, do you not hear? And do you not remember? Dangeena ami gët, te dungeen gis? Am dangeena ami nopp te dungeen dégg, dungeen fàttaliku?
19 When I broke the five loaves for the 5,000, how many baskets full of fragments did you collect?" They said, "Twelve." Ba ma daggalee juróomi junniy (5 000) nit ña juróomi mburu ya, ba ngeen for desit ya, ñaata pañey dogi mburu la fees?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar.»
20 "And when I broke the seven for the 4,000, how many basketfuls of broken pieces did you gather?" They said, "Seven." Mu neeti leen: «Juróom ñaari mburu ya ca ñeenti junniy (4 000) nit ña nag, ba ngeen foree desit ya, ñaata dàmbay dogi mburu la fees?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
21 And he said to them, "Do you still not understand?" Yeesu nag ne leen: «Te xamaguleen ba tey?»
22 They came to Bethsaida, where people brought him a blind man and begged Jesus to touch the man. Gannaaw loolu Yeesu aki taalibeem agsi dëkk ba ñuy wax Betsayda. Ñu indil fa Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu teg ko loxo.
23 He took the blind man's hand, led him out of the village, spit on his eyes, laid hands on him, and asked, "Do you see anything?" Yeesu jàpp loxob silmaxa ba, yóbbu ko, ba génn dëkk ba. Mu tifli ci bët yi, teg ko loxo, ne ko: «Ndax yaa ngi gis dara?»
24 He looked up and said, "I see people, but they look like trees, walking." Waa ji xippi, ne ko: «Gis naa ay nit ñu mel ni ay garab, waaye ñu ngi dox.»
25 Then Jesus put his hands on the man's eyes again; he looked intently, was restored, and saw everything distinctly. Yeesu dellu tegaat ay loxoom ci bët yi, silmaxa bi ne xiféet, daldi wér, di ràññee lépp bu baax.
26 And he sent him home, saying, "Do not even go into the village." Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu ñibbi, ne ko: «Bul dellu ci biir dëkk bi.»
27 Jesus and his disciples went to the villages of Caesarea Philippi. On the way he asked them, "Who do people say I am?" Ba loolu amee Yeesu ànd aki taalibeem, ñu jëm ca dëkk-dëkkaan, ya ca wetu Sesare gu Filib. Mu laaj taalibe ya ca yoon wa, ne leen: «Ana ku nit ñi wax ne moom laa?»
28 They told him, "John the Baptist; and others say Elijah; and others, one of the prophets." Ñu ne ko: «Ñii nee ñu yaa di Yaxya, ñee ne yaa di Ilyaas, ñale ne kenn ci yonent yi nga.»
29 Then he asked them, "But who do you say I am?" Peter answered, "You are the Christ." Yeesu it ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi.»
30 And he strictly warned them not to speak about him. Ci kaw loolu Yeesu femmu leen ngir ñu baña wax kenn dara ci mbiram.
31 He began teaching them the Son of Man must suffer much, be rejected by the elders, chief priests, and scribes, be killed, and rise after three days. Yeesu nag tàmbali leena jàngal, ne leen fàww Doomu nit ki sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak sarxalkat yu mag yi, ak firikati yoonu Musaa yi, te dees na ko rey, ba mu am ñetti fan, mu dekki.
32 He said this plainly. And Peter took him aside and began to rebuke him. Mu daldi leen xamal mbir mi, ba mu leer nàññ. Piyeer nag ñaarook moom, tàmbali koo femmu.
33 But turning, he looked at his disciples and rebuked Peter: "Get behind me, Satan! For you are not setting your mind on the things of our Father, but on the things of man." Teewul Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, daldi gëdd Piyeer, ne ko: «Seytaane, xiddi ma te dellu gannaaw, yaw xalaatoo yëfi Yàlla, waaye yëfi nit ngay xalaat.»
34 He called the crowd and his disciples and said to them, "Whoever wants to come after me must deny himself, take up his cross, and follow me. Ba loolu amee Yeesu woo mbooloo maak taalibe ya, ne leen: «Ku ma bëgga topp, fàtteel sa bopp te gàddu sa bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
35 Whoever wants to save his life will lose it; whoever loses his life for my sake and the good news will save it. Ndaxte képp ku bëgga rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, te ku ñàkk sa bakkan ndax man ak xibaaru jàmm bi, dinga ko jotaat.
36 What good does it do a person to gain the whole world and forfeit his soul? Ana luy njariñal nit ku jagoo àddina sépp, te ñàkk bakkanam?
37 For what can a person give in exchange for his soul? Ana lu nit wara mana weccee bakkanam?
38 For whoever is ashamed of me and my words in this adulterous, sinful generation—the Son of Man will be ashamed of them too when he comes in his Father's glory with the holy angels." Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, ci biir niti jamono jii, di jamonoy bokkaaleek bàkkaar, bés bu Doomu nit ki dikkee ci biir darajay Baayam, ànd ak malaaka yu sell yi, su keroogee moom it dina la kersawoo.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]