Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 7 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The Pharisees and some of the scribes who had come from Jerusalem gathered around Jesus, Farisen ya ak ñenn ca firikati yoonu Musaa yu jóge Yerusalem ñoo daje woon fa Yeesu.
2 and they saw that some of his disciples were eating bread with unclean hands—that is, unwashed. Ñu gis ñenn cay taalibeem di lekke loxo te raxasuñu ba set ni ko aada bëgge.
3 (For the Pharisees and all the Jews don't eat unless they wash their hands ceremonially, keeping the elders' tradition. Ndax muy Farisen ya, di Yawut yépp sax, duñu lekk te raxasuñu ba set ndax aaday maam ya ñu baaxoo.
4 When they come from the market, they don't eat without washing. They also hold to many other traditions they've received—washing cups, pitchers, and copper vessels.). Bu ñu jógee pénc ma it, duñu lekk te tooyluwuñu. Ak yeneen yu bare yu ñu baaxoo yu deme ni tooylu gi war ci jumtukaay yu mel ni ay kaas aki njaq ak ndabi xànjar.
5 Then the Pharisees and scribes asked him, "Why don't your disciples follow the elders' tradition, but eat bread with unclean hands?" Farisen yaak firikati yoon ya nag laaj ko, ne ko: «Lu tax say taalibe toppuñu aaday maam yi, xanaa ñuy lekke loxo yu setul?»
6 He replied, "Isaiah prophesied truly about you hypocrites, as written: 'These people honor me with their lips, but their heart is far from me.' Yeesu ne leen: «Jinigalkat yi! Naaféq yi ngeen doon! Esayi yey na, ba mu jottalee kàdduy waxyu ci seen mbir, noonu ñu ko binde, ne: “Askan wii, làmmiñ lañu may wormaale, waaye seen xol sore na ma.
7 'They worship me in vain, teaching as doctrines the commandments of men.' Seen njaamu Yàlla neen la, seen njàngale di santaaney niti kese.”»
8 You abandon the commandment of our Father and hold to the tradition of men." «Dangeena dëddu santaaney Yàlla, topp aaday nit.»
9 He said to them, "You do a fine job setting aside our Father's commandment to keep your own tradition!" Mu ne leen: «Yeenaka xam nu ngeen di neenale santaaneb Yàlla, ngir seen aaday bopp mana sax!
10 For Moses said, 'Honor your father and your mother,' and 'Whoever curses father or mother must be executed.' Mu ngi mel ni fi Musaa ne: “Teralal sa ndey ak sa baay,” neeti: “Ku saaga sa ndey mbaa sa baay, dee rekk mooy àtteem.”
11 "But you say: if anyone tells his father or mother, 'Whatever you'd have gained from me is Corban' (a gift devoted to our Father), Te yeen ngeen ne: “Ku ne sa ndey mbaa sa baay: Li ma la waroona jàppale, korban (muy firi sarax ngir Yàlla) laa ko def,”
12 then you no longer let him do anything for his father or mother. may ngeen ko mu baña defalati dara ndeyam mbaa baayam.
13 So you cancel the word of our Father with your handed-down tradition. You do many things like this." Kon seen aaday bopp ji ngeen di donnante, moom ngeen neenale kàddug Yàlla. Ak yeneen yu bare yu ni mel yu ngeen di def.»
14 He called the crowd again and said to them, "Listen to me, all of you, and understand: Yeesu wooti mbooloo ma, ne leen: «Dégluleen ma yeen ñépp, te ngeen amug dégg.
15-16 Nothing outside a person entering him can make him unclean; rather, what comes out of a person is what makes him unclean." Mboolem lu bokkul ci nit ki, du lenn lu ciy dugg ci moom, ba man koo sobeel. Liy génne ci nit ki kay mooy sobeel nit ki.»
17 When he had left the crowd and entered the house, his disciples asked him about the parable. Ba ñu duggsee ca biir kër ga, ba sore mbooloo ma, taalibe ya laaj Yeesu, ngir leerlu léeb woowu.
18 He said to them, "Are you also this dull? Don't you understand nothing entering a person from outside can make him unclean, Yeesu ne leen: «Ndeke yeen itam amuleenug dégg? Xamuleen ne mboolem lu bokkul ci nit, du lenn lu ciy dugg ci moom, ba man koo sobeel,
19 since it doesn't enter his heart but his stomach, and then goes out into the sewer?" (Saying this, he declared all foods clean.). ndax du ci xolam lay dugg, waaye ci koll bi lay dugg, balaa jàll, génneji gannaaw kër?» Googu kàddu di firndeel ne ñam yépp a dagan.
20 He said, "What comes out of a person—that makes him unclean. Mu neeti leen: «Li génne ci nit, loolu mooy sobeel nit ki.
21 For from within, out of the human heart, come evil thoughts—sexual sin, theft, murder, Ndaxte ci biir nit ki, ci biir xolam la mébét yu bon di jóge, ak séy yi yoon tere, ak càcc, ak bóom,
22 adultery, greed, malice, deceit, sensuality, envy, slander, pride, and foolishness. ak njaaloo, ak bëgge, ak jëfi coxor, ak njublaŋ, yàqute ak ñeetaane, ak saaga, ak réylu, ak jëf ju xel nanguwul.
23 All these evils come from inside and make a person unclean." Mboolem yu bon yooyii ci biir nit ki lay génne, sobeel ko.»
24 Jesus left there for the region of Tyre. He entered a house, wanting no one to know, but couldn't stay hidden. Yeesu jóge fa, dem ba ca diiwaan ba ñuy wax Tir. Mu dugg fa ci genn kër, te bëggul kenn xam ko, waaye manula fexe ba nit ña umple ko.
25 Instead, a woman whose little daughter had an unclean spirit heard about him at once, came, and fell at his feet. Ndeke as ndaw su rab jàpp doomam ju jigéen dégg na fa Yeesu. Mu daldi dikk, ne gurub sukk cay tànkam.
26 The woman was Greek, Syrophoenician by birth. She kept asking him to drive the demon out of her daughter. Ndaw sa ab Gereg la woon, cosaanoo Fenisi ga ca Siri. Mu ñaan ko, mu dàqal ko rab wa jàpp doomam.
27 He told her, "Let the children eat first, for it's not right to take their bread and toss it to the dogs." Yeesu nag ne ko: «Na gone yi njëkka lekk, ba regg; jël ñamu gone yi, sànni ko kuti yi daal jaaduwul.»
28 But she replied to him, "Sir, even the dogs under the table eat the children's crumbs." Ndaw sa ne ko: «Sang bi, teewul kuti yi, ca suufu ndab la lañuy fore ca ruusiti gone yi.»
29 He said to her, "Because of this answer, go—the demon has left your daughter." Yeesu nag ne ko: «Gannaaw kàddu googu nga wax man ngaa dem, rab wa génn na sa doom.»
30 And she went home and found the child lying on the bed, and the demon gone. Ndaw sa ñibbi këram, gis doom ja tëdd ca lal ba, fekk rab wa dem na.
31 Then Jesus left the territory of Tyre, went through Sidon to the Sea of Galilee, into the region of the Decapolis. Yeesu jógeeti diiwaanu Tir, jaare dëkk ba ñuy wax Sidon, jaare diiwaan ba ñuy wax Fukki Dëkk yi, dem ba ca dexu Galile.
32 They brought him a deaf man who could hardly speak, begging him to lay his hand on him. Ñu indil fa Yeesu ku tëx, te wax jafe ko. Ñu ñaan Yeesu, ne ko mu teg ko loxoom.
33 Jesus took him aside privately, away from the crowd, put his fingers in the man's ears, spit, and touched his tongue. Yeesu génne waa ja mbooloo ma, ñaarook moom, daldi def ay baaraamam ci noppi waa ja, ba noppi tifli, laalale loram làmmiñu waa ja.
34 Then, looking up to heaven, he sighed deeply and said to him, "Ephphatha!" (that is, "Be opened!"). Ci kaw loolu mu xool kaw asamaan, daldi binni, ne ko: «Efata», muy firi «Tijjikul.»
35 And immediately his ears were opened, his tongue was released, and he began to speak plainly. Ca saa sa ay noppam tijjiku, làmmiñ wa yiwiku, muy wax wax ju leer.
36 Jesus ordered them to tell no one; but the more he ordered, the more they proclaimed it. Ba mu ko defee Yeesu dénku leen, ne leen buñu ko wax kenn, waaye lu mu leen gëna dénku, ñu gën koo siiwal.
37 They were completely amazed: "He has done everything well—he makes the deaf hear and the mute speak." Dañoo waaru ba fa waaru yem, naan: «Kii lépp lu mu def, jëf ju matale la, ba tëx yi sax, mu déggloo leen, luu yi, mu waxloo leen!»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]