Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 6 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 He went out from there and came to his hometown, and his disciples followed him. Ba loolu amee Yeesu jóge fa, dellu dëkk ba mu yaroo, taalibe ya ànd ak moom.
2 On the Sabbath he began teaching in the synagogue. Many who heard were amazed: "Where did this man get this? What wisdom is this, given to him? How do such miracles happen through his hands? Bésub Noflaay taxaw, mu tàmbalee jàngale ca jàngub Yawut ba, ñu bare dégg ko, yéemu naan: «Ana fu kii jële lii, ak xam-xam bii ñu ko may, lu mu doon, ba yii kéemaan sottee ci moom?
3 Isn't this the carpenter, Mary's son, brother of James, Joses, Judas, and Simon? Aren't his sisters here with us?" They were offended by him. Xanaa kii du minise bi? Du doomu Maryaama ji, magu Yanqóoba ak Yose ak Yudd ak Simoŋ? Xanaa du nook jigéenam ñee fi bokk dëkk?» Ñu daldi gise mbir ma ag yabeel.
4 Jesus said to them, "A prophet lacks honor only in his hometown, among his relatives, and in his own household." Yeesu nag ne leen: «Ab yonent de, deesu ko xeebe fenn fu moy ci réewu boppam ak ci biiri bokkam ak ci biir waa këram.»
5 He could do no miracle there, except laying hands on a few sick and healing them. Foofa Yeesu manu fa woona def genn kéemaan, lu moy jarag yu néew yu mu teg loxo, wéral leen.
6 He was amazed at their lack of faith. Then he went around the villages teaching. Yeesu nag yéemu ci seen ngëmadi. Ba mu ko defee Yeesu di wër dëkk ya, di jàngale.
7 He called the twelve and began sending them out two by two, giving them authority over unclean spirits. Ci biir loolu mu woo Fukk ñaak ñaar, yebal leen ñaar-ñaar, joxaale leen sañ-sañu dàq rab yi.
8 He ordered them to take only a staff for the road—no bread, no bag, no money in their belts, Mu jox leen ndigal, ne leen buñu yóbbaale dara ngir fàggu yoon wi, lu moy wenn yet doŋŋ, du mburu, du mbuus, du weccitu xànjar wu ñuy fas ci seen geño.
9 but to wear sandals and not put on two tunics. Mu neeti leen man nañoo sol ay carax waaye buñu yóbbaale ñaari turki.
10 And he said to them, "Wherever you enter a house, stay there until you leave that place. Mu ne leen: «Fu ngeen dugge ci kër, dalleen fa, ba kera ngeen dem.
11 Whatever place refuses to welcome or hear you, leaving there, shake the dust off your feet as testimony against them." Fépp fu ñu leen dalalul mbaa dégluwuñu leen, bu ngeen fay génne, faxasleen fa pënd bi ci seen tànk, ngir seedeele leen ko seen ngàntal.»
12 So they went out and proclaimed that people should repent. Gannaaw loolu taalibe ya dem, di waare ngir nit ñi tuub.
13 And they drove out many demons and anointed many sick people with oil and healed them. Ci biir loolu ñu dàq rab yu bare, diw diwu oliw jarag yu bare, ba wéral leen.
14 King Herod heard of it, for Jesus's name had become known. Some were saying, "John the Baptist has been raised from the dead; that is why these miraculous powers are at work in him." Buur Erodd nag dégg la xew, ndax fekk na Yeesu siiw, ba nit ñi naa: «Yaxya ma doon sóobe ci ndox moo dekki noonu, moo waral xam-xam yu kéemaane yi feeñe ci moom.»
15 But others said, "He's Elijah." Others said, "He's a prophet, like one of the prophets of old." Ñenn ña naa: «Kooku Ilyaas la.» Ña ca des naa: «Kooku kay ab yonent la bu bokk ca yonent yu njëkk ya.»
16 But when Herod heard of it, he said, "John, whom I beheaded, has been raised." Ba ko Erodd déggee nag da ne: «Yaxya ma ma doglu woon boppam man, Yaxya moomu moo dekki!»
17 Herod had sent and seized John, binding him in prison because of Herodias, his brother Philip's wife, whom he had married. Erodd moom ci boppam moo yónnee woon, jàpp Yaxya, yeew ko, tëj, ndax gannaaw ba Erodd dencee Erojàdd jabaru Filib magam,
18 For John kept telling Herod, "It is not lawful for you to have your brother's wife." Yaxya moo ko ne: «Yoon mayu la nga denc sa jabaru mag.»
19 And Herodias held a grudge against him and wanted to kill him, but she could not, Moo taxoon Erojàdd soxna sa dencal ko mer, ba bëgg koo rey, waaye manu ko woon.
20 Herod feared John, knowing him righteous and holy, and protected him. Hearing John left Herod deeply puzzled, yet he gladly listened to him. Ndaxte Erodd dafa ragaloon Yaxya, te xamoon na ne nit ku jub la te sell, ba tax mu di ko aar. Ku bége woona déglu Yaxya la, doonte la mu ko wax indil na ko njàqare.
21 Then a fitting day came: Herod's birthday, when he gave a banquet for his nobles, military commanders, and Galilee's leading men. Gannaaw gi, bés bu yell ñëw, Erodd doon baaxantal bésu juddoom, daldi cay defal bernde ay jaraafam ak njiiti gàngoor yaak kàngami diiwaanu Galile.
22 When Herodias's daughter entered and danced, she delighted Herod and his dinner guests. The king told the girl, "Ask me for anything you want, and I'll give it to you." Ci biir loolu doomu Erojàdd duggsi, di fecc. Peccum janq ba neex Buur Erodd ak gan ña. Buur ne ko: «Laaj ma loo bëgg, ma jox la ko.»
23 He swore to her, "Whatever you ask me, I'll give you—up to half my kingdom." Mu giñal ko, ne ko: «Loo ma mana laaj, dinaa la ko jox, ba ci sama genn-wàllu réew mi sax.»
24 She went out and said to her mother, "What should I ask?" She said, "The head of John the Baptist." Janq ba nag génn, ne yaayam: «Lu may laaj?» Mu ne ko: «Xanaa boppu Yaxya.»
25 She went in immediately, with urgency, to the king and asked, "I want you to give me this instant the head of John the Baptist on a platter." Mu daldi gaaw dugg ba ca Buur, wax ko la muy laaj, ne ko: «Damaa bëgg, nga indil ma léegi ci ndab boppu Yaxya.»
26 Deeply grieved, the king still wouldn't refuse her, because of his oaths and his guests. Buur nag daldi am lu ko metti lool, waaye ngiñ la ak gan ña moo tax bëggu koo gàntu.
27 The king at once sent an executioner, ordering John's head brought. He went and beheaded him in the prison, Buur yebal ab dag, jox ko ndigal ngir mu indil ko boppu Yaxya. Waa ja dem, dog boppu Yaxya ca kaso ba,
28 and brought his head on a platter, gave it to the girl, and the girl gave it to her mother. daldi indi bopp bi ci ndab, jox ko janq ba, janq ba jox ko yaayam.
29 When John's disciples heard, they came, took his body, and laid it in a tomb. Ba mu ko defee taalibey Yaxya dégg ko, dikk, yóbbu néew ba, rob ko.
30 The apostles gathered to Jesus and told him all that they had done and taught. Ndaw ya nag daje fa Yeesu, nettali ko la ñu def ak la ñu jàngale lépp.
31 He told them, "Come away by yourselves to a quiet place and rest a while." For many were coming and going, and they had no time to eat. Ci kaw loolu Yeesu ne leen: «Yeen nag dangeen di ñëw, nu daw ba fu wéet, ngeen noppalu fa tuuti.» Booba ñay dem aka dikk dañoo bare, ba taalibe ya talatuñoo lekk sax.
32 And they went away in the boat to a desolate place by themselves. Ñu jël gaal, daw jëm béreb bu wéet, ngir beruji fa.
33 Many saw them leave and recognized them; they ran on foot from every town and got there ahead of them. Teewul ñu bare gis leen ñuy dem, daldi xam la ñu nar, dëkkoo dëkk nag nit ña bàbbeekoo ca, tefesu, jiituji leen fa.
34 Stepping ashore, he saw a large crowd and felt compassion for them, for they were like sheep without a shepherd, and began teaching them many things. Ba Yeesu wàccee ca gaal ga, mbooloo mu réy la gis. Mu ñeewante leen, ndax dañoo mel ni xar yu amul sàmm. Mu daldi leen jàngal lu bare.
35 When it was already late, his disciples came to him and said, "This is an isolated place, and it's already late. Booba mu ngi bëgga guddi xaat. Taalibe ya dikk, ne ko: «Fii àllub neen la, te mu ngi guddi xaat.
36 Send them away to go into the surrounding countryside and villages and buy themselves something to eat." Dangay yiwi mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yu ndaw yii ak dëkk-dëkkaan yi ko wër, ndax ñu jënd lu ñu lekk.»
37 He replied, "You give them something to eat." They said, "Should we go buy 200 denarii of bread and give them it to eat?" Yeesu ne leen: «Yeen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa danuy jëndi njëgu ñaari téeméeri poseti xaalis ci mburu, jox leen, ñu lekk?»
38 He asked them, "How many loaves do you have? Go and see." They found out and said, "Five, and two fish." Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am? Demleen xool.» Ñu xool, ne ko: «Juróomi mburu la ak ñaari jën.»
39 Then he commanded them all to sit down in groups on the green grass. Ba loolu amee Yeesu ne leen ñu toogal ñépp, ñu def ay géew ci ñax mu naat mi.
40 So they sat down in groups, by hundreds and by fifties. Ñu toog nag, ñii def géewi téeméer, ñee géewi juróom fukk.
41 Taking the five loaves and two fish, he looked up to heaven, gave thanks and broke the loaves, gave them to the disciples to set before the people, and divided the two fish among them all. Ba mu ko defee Yeesu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool kaw asamaan, daldi yékkati kàddug cant, ba noppi dogat mburu ya, jox taalibe ya, ngir ñu taajal ko mbooloo ma. Ñaari jën ya it, mu séddale ko ñépp.
42 And they all ate and were satisfied. Ñépp lekk ba regg,
43 And they took up twelve baskets full of broken pieces and of the fish. ba ñu yóbbu fukki pañe ak ñaar yu fees ak desiti mburu yaak jën ya.
44 And those who ate the loaves were 5,000 men. Ña lekk ca mburu ya juróomi junniy (5 000) góor lañu.
45 At once he made his disciples board the boat and go ahead to the other side, toward Bethsaida, while dismissing the crowd. Ci kaw loolu Yeesu duggloo taalibeem ya ca gaal ga, ngir ñu jàllagum, jiituji ca Betsayda ga ca wàlla, ba mu yiwi mbooloo ma.
46 And after he had taken leave of them, he went up on the mountain to pray. Mu tàggatook ñoom, daldi yéegi ca tund wa, ngir ñaan.
47 When evening came, the boat was out on the sea, and he was alone on the land. Ba guddi jotee, gaal gaa nga tollu ca digg dex ga, Yeesu doŋŋ la fekk ca joor ga.
48 He saw them straining at the oars, for the wind was against them. Around three in the morning he came to them, walking on the sea. He meant to pass by them, Mu gis nag na taalibe ya sonne ca joow ba ndax booba ngelaw laa leen soflu. Ba suuf di waaja sedd, Yeesu dox ci kaw dex gi, wutsi leen, ba nar leena romb.
49 but seeing him walk on the sea, they thought it was a ghost and cried out, Ba ñu ko gisee nag muy dox ca kaw dex ga, dañoo foog ne njuuma la, ñu daldi yuuxoo.
50 for all saw him and were terrified; but immediately he spoke to them, saying, "Take heart; it is I. Do not be afraid." Ñoom ñépp a jommi ba ñu ko gisee. Mu daldi wax ak ñoom, ne leen: «Dalleen, man mii la, buleen tiit!»
51 He got into the boat with them, and the wind stopped; they were completely amazed among themselves, Mu dugg, fekksi leen ca biir gaal ga, ngelaw la dal. Mbir ma waar leen ba ëlëm leen,
52 for they did not understand about the loaves, but their hearts were hardened. ngir fekk na ñu réere mbir kéemaan ga ca mburu ma ndax xol yu fattu.
53 When they had crossed over, they came to land at Gennesaret and moored to the shore. Ba loolu amee ñu jàll dex ga, daleji diiwaanu Senesaret, taxawal fa gaal ga.
54 And when they got out of the boat, the people immediately recognized him. Naka lañu wàcce ca gaal ga, nit ña xàmmee Yeesu.
55 They ran through that whole region and began carrying the sick on mats to wherever they heard he was. Ci kaw loolu nit ñay daw ca diiwaan bépp. Ñu tàmbalee jàppoo ña wopp ca seen kawi basaŋ, fépp fu ñu dégg Yeesu, yóbbu leen fa.
56 Wherever he went—villages, towns, countryside—they laid the sick in the marketplaces, begging to touch just the edge of his cloak. All who touched it were healed. Fépp fu mu dugg, muy dëkk bu ndaw, di bu mag, ba ca dëkk-dëkkaan ya, ca pénc mooma lañuy teg jarag ya, tey sarxu Yeesu, mu may leen ñu laal lu mu bon bon cati mbubbam, te képp ku ca laal, mucc nga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]