Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 5 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 They came to the other side of the sea, to the region of the Gerasenes. Gannaaw loolu ñu jàll wàllaa dex ga, ca diiwaanu waa Serasa.
2 As Jesus left the boat, a man with an unclean spirit met him at once, from the tombs. Naka la Yeesu génn gaal ga, jenn waay ju rab jàpp bàyyikoo ca sëg ya, dikk dogale ko.
3 He lived among the tombs, and no one could bind him anymore, not even with a chain. Waa jaa nga dëkkoon ca sëg ya, te ag càllala sax maneesu ko ko woona yeeweeti.
4 For he'd often been bound with shackles and chains, but tore the chains apart and shattered the shackles—no one had strength to subdue him. Daan nañu ko farala jéng, yeewe koy càllala, waaye waa ja da daan dagg càllala yi, damm jéng yi, ba kenn amul kàttanu téye ko.
5 Night and day, among the tombs and on the mountains, he cried out constantly, cutting himself with stones. Guddeek bëccëg ma nga woon ca sëg yaak ca tund ya, di yuuxooka for ay xeer, di ko dagge yaramam.
6 And when he saw Jesus from a distance, he ran and fell down before him. Dafa séen Yeesu fu sore, daldi daw ba agsi, sukk fa kanamam.
7 Shouting loudly, he said, "What do you want with me, Jesus, Son of the Most High God? I beg you by God, don't torment me!" Mu xaacu ca kaw, ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, ana lu ma joteek yaw? Dama lay dagaan ngir Yàlla, bu ma mbugal.»
8 For Jesus had been saying to him, "Come out of the man, you unclean spirit!" Booba Yeesoo nga ko naa: «Yaw rab wi, génnal ci waa ji.»
9 Jesus asked, "What is your name?" "Legion," he said, "we are many." Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Gàngoor laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
10 He kept begging him not to send them out of the region. Muy tinu Yeesu lu bare ngir mu bañ leena dàqe ca réew ma.
11 Now a great herd of pigs was feeding there on the hillside. Fekk coggalu mbaam-xuux gu mag a nga woon ca tund wa, di for.
12 And they begged him, "Send us to the pigs; let us enter them." Rab ya tinu Yeesu, ne ko: «Yebal nu ci mbaam-xuux yi, ndax nu dugg leen.»
13 He gave permission. The unclean spirits came out and entered the pigs; the herd—about 2,000—rushed down the cliff into the sea and drowned in the sea. Mu may ko rab ya, ñu génn, duggi mbaam-xuux ya, coggal ga bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, lu wara tollu ci ñaari junniy (2 000) mbaam-xuux daldi lab ca dex ga.
14 The herders fled and told it in town and country; people came to see what happened. Ba mu ko defee sàmm ya daw, nettaliji ko waa dëkk ba, ak dëkk-dëkkaan ya, nit ña dikk, di seet la xew.
15 They came to Jesus and saw the man who had been possessed by the demons, the one who'd had the legion, sitting there, dressed and thinking clearly—and they were afraid. Ñu dikk ba ci Yeesu, daldi gis boroom rab ba, mu solu ba toog, ànd ak sagoom. Nit ña nag tiit.
16 Eyewitnesses told them what had happened to the demon-possessed man, and about the pigs. Ña fekke woon mbir ma daldi leen nettali mbirum boroom rab baak mbaam-xuux ya.
17 And they began to beg Jesus to leave their region. Ci kaw loolu ñuy tinu Yeesu ngir mu génn seen gox ba.
18 As he was getting into the boat, the once-possessed man begged to be with him. Naka la Yeesu di dugg ca gaal ga, boroom rab ba di tinu Yeesu, ngir ànd ak moom.
19 But Jesus refused, telling him instead, "Go home to your own people and tell them how much our Father has done for you, and how he has had mercy on you." Waaye Yeesu mayu ko ko. Da ne ko: «Ñibbil sa kër ca say bokk, nga àgge leen li la Boroom bi defal lépp ci yërmandeem.»
20 He went and began proclaiming in the Decapolis all Jesus had done for him, and everyone was amazed. Waa ja it dem, di tàmbalee siiwtaane ca diiwaan ba ñu dippee Fukki Dëkk, la ko Yeesu defal lépp. Ñépp waaru.
21 When Jesus crossed again by boat to the other side, a large crowd gathered around him by the sea. Yeesu nag jàllaat dex ga, mbooloo mu bare daje, wër ko fa mu nekk ca tàkkal dex ga.
22 One of the synagogue leaders, named Jairus, came, saw Jesus, and fell at his feet, Ci biir loolu kenn ci njiiti jàngub Yawut ba, ku ñuy wax Yayrus dikk. Naka la gis Yeesu, ne gurub sukk ciy tànkam,
23 and begged him urgently, "My little daughter is dying. Come, lay your hands on her, so she may be healed and live." di ko tinu lu bare, ne ko: «Sama doom ju jigéen ay bëgga faatu. Ngalla kaay teg ko loxo, ngir mu mucc ba dund.»
24 So Jesus went with him. And a great crowd followed him and pressed around him. Yeesu ànd ak moom, dem, mbooloo mu réy topp ca Yeesu, tanc ko.
25 And there was a woman with a discharge of blood that had gone on for twelve years. Sennas ndaw a nga ca woon, fukki at ak ñaar ma ngay xëpp deret.
26 She had suffered much under many doctors, spent all she owned, gained nothing, and only grew worse. Fekk na mu sonn coono bu réy bu ko fajkat yu bare teg. Mu sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, xanaa gëna wopp.
27 Hearing about Jesus, she came up behind him in the crowd and touched his cloak. Mu déggoon nag turu Yeesu, ba tax mu dikk, dugg ci biir mbooloo mi, doxe ko gannaaw, teg loxoom ca mbubbam.
28 For she kept saying, "If I just touch his garments, I will be made well." Fekk na mu naan ci xelam: «Su ma fexee ba laal mbubbam rekk, dinaa mucc.»
29 Her flow of blood dried up instantly, and she felt in her body that she was healed of her suffering. Ba mu tegee loxoom ca mbubbam Yeesu, ca saa sa la deret ja taxaw, mu yég ci yaramam, ne teqalikoo naak jàngoro ja.
30 At once Jesus, aware that power had left him, turned around in the crowd and asked, "Who touched my clothes?" Yeesu nag yég ca saa sa leer gu bàyyikoo ca moom. Mu walbatiku ca biir mbooloo ma, ne: «Ana ku laal sama mbubb?»
31 His disciples said to him, "You see the crowd crushing you, yet you ask, 'Who touched me?'" Taalibeem ya ne ko: «Yaa ngi gis mbooloo mi la tanc mépp, nga naa: “Ku ma laal?”»
32 And he looked around to see who had done it. Teewul Yeesu dawal bëtam fa ko wër, ngir gis ka def loola.
33 But the woman, afraid and trembling, knowing what had happened to her, came, fell before him, and told him the whole truth. Ndaw saa nga tiit bay lox, ndax xam na xéll la ko dikkal. Mu dikk, ne gurub sukk fa moom, daldi koy wax dëgg gépp.
34 He told her, "Daughter, your faith made you well. Go in peace, healed of your suffering." Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm a la faj. Demal ak jàmm te teqalikook sa jàngoro.»
35 While he was still speaking, people came from the synagogue leader's house, saying, "Your daughter has died. Why bother the Teacher any longer?" Yeesoo ngay wax, noppeegul, aw nit jóge ca kër njiitu jàngu ba, dikk, ne njiit la: «Sa doom faatu na. Jaratul ngay yékkati kilifa gi.»
36 But Jesus overheard what they said and told the synagogue leader, "Don't fear, only believe." Yeesu nag tanqamlu wax ja ñu wax. Mu ne njiit la: «Bul tiit, gëmal rekk.»
37 And he allowed no one to follow him except Peter, James, and John the brother of James. Ba Yeesu di dem kër njiit la, mayul kenn mu ànd ak moom ku moy Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan rakku Yanqóoba.
38 They came to the synagogue leader's house and Jesus saw chaos—people weeping, wailing loudly. Ñu agsi kër njiit la, Yeesu yem ca coow la. Ña ngay jooyooka yuuxoo.
39 Entering, he said to them, "Why this commotion and crying? The child isn't dead, just asleep." Mu duggsi, ne leen: «Lu ngeen di soow aka jooyoo? Xale bi deewul, day nelaw rekk.»
40 They laughed at him. But he sent them all out, took the child's father and mother and his companions, and entered where the child was. Waaye ñu di ko ñaawal. Yeesu génne ñépp, daldi woo baayu xale bi ak yaay ji, ak taalibe ya mu àndal, ñu jàll ca biir fa xale ba nekk.
41 He took her hand and said to her, "Talitha koum," which means, "Little girl, I say to you, get up!" Mu jàpp ca loxol xale ba, ne ko: «Talita kumi,» mu tekki: «Janq, ma ne la, jógal.»
42 At once the girl got up and walked—for she was twelve—and they were instantly overwhelmed with great amazement. Ca saa sa janq ba jóg, di dox, ndax amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp waaru lool.
43 He strictly ordered them to tell no one of this, and said to give her something to eat. Ci kaw loolu Yeesu dénku leen bu baax, ne leen bu ko kenn yég, daldi ne ñu may janq bi, mu lekk.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]