Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Jesus again taught by the sea. So large a crowd gathered around him that he got into a boat on the water and sat, while the whole crowd was on land by the sea. Yeesu tàmbalee jàngaleeti ca tàkkal dex ga, mbooloo mu bare daje fa moom, ba mu mujj dugg ci gaal, toog ca biir, ca kaw dex ga, mbooloo mépp des ca tàkk ga, feggook ndox ma.
2 He taught them many things in parables, and in his teaching he said to them: Noonu Yeesu jàngal leen lu bare ciy léeb. Mu jàngal leen, ne leen:
3 "Listen! A sower went out to sow. «Dégluleen, dama ne, boroom jiwu moo demoon jiwi.
4 And as he sowed, some seed fell along the path, and the birds came and devoured it. Naka lay saaw, ndeke lenn ca jiwu maa nga tuuru ca kaw yoon wa, picc yi dikk, lekk ko.
5 Other seed fell on rocky ground, lacking much soil, and sprang up at once since the soil had no depth. Leneen la tuuru fu barey doj, te suuf sa néew. Mu ne coleet ca saa sa, ndax la suuf sa xóotul.
6 When the sun rose, the plants were scorched, and since they had no root, they withered. Ba jant bi jógee, mu lakk, daldi wow, ndax ñàkkub reen.
7 Other seed fell among thorns, and the thorns grew up and choked it, yielding no grain. Leneen la tuuru ca xaaxaam ma, xaaxaam ma sëq, tanc ko, ba meññul dara.
8 Other seed fell into good soil, producing grain that sprouted, grew, and yielded thirty, sixty, one hundred times what was sown." La des ca jiwu ma tuuru ca suuf su baax. Mu sax, màgg, ba meññ; wii fepp meññal fanweer, wee, juróom benn fukk, wale, téeméer.»
9 And he said, "Whoever has ears to hear, let him hear." Yeesu nag ne leen: «Ku am nopp yu mu dégge kat, na dégg.»
10 When he was alone, those around him, together with the Twelve, asked him about the parables. Gannaaw loolu Yeesu beru, fukki taalibe yaak ñaar ak ñeneen ñu daje fa moom daldi koy laaj lu léeb yooyuy wund.
11 He said to them, "To you is given the secret of the kingdom of our Father, but to those outside, everything comes in parables, Mu ne leen: «Yeen lañu xamal mbóotum nguurug Yàlla, waaye ñi ci biti ñoom, lépp ciy léeb lañu leen koy dëxëñal.
12 so that 'they may look but not perceive, and hear but not understand, and not turn and be forgiven.'" Su ko defee: “Ñuy xoolee xoole te duñu gis, di dégloo déglu te duñu dégg, ngir bañ ñu dëpp, ñu baal leen.”»
13 He said to them, "You don't understand this parable? Then how will you understand all the parables? Yeesu neeti leen: «Dégguleen woowu léeb? Nu ngeen di dégge léeb yi ci des yépp nag?
14 The sower sows the word. Boroom nji mi, kàddu gi lay ji.
15 These are the ones on the path where the word is sown: once they hear, Satan comes immediately and takes away the word sown in them. Ñi ci kaw yoon wi kàddu giy jiwe, ñooy ñi déglu rekk, Seytaane dikk ci saa si, foqati kàddu gi ci ñoom.
16 These are the ones sown on rocky ground, who hear the word and immediately receive it with joy. Ñee jote jiwu mi fu barey doj ñooy ña déglu kàddu gi rekk, nangoo ko xol bu sedd ci saa si,
17 But they have no root in themselves, lasting only briefly; when trouble or persecution comes because of the word, they fall away at once. waaye ab reen la jotula saxle ci ñoom, moo tax duñu ko wéye. Bu coono dikkee mbaa ñu bunduxataal leen ndax kàddu gi, dañuy dellu gannaaw ca saa sa.
18 And others are the ones sown among thorns. These are those who hear the word, Ñeneen ña jote jiwu ma ca xaaxaam ya, ñooy ña déglu kàddu gi,
19 but worries of this age, the deceit of wealth, and desires for other things enter and choke the word, and it produces no fruit. te xalaati àddina ak naxey alal ak yeneen xemmemtéef wàllisi, daldi fatt kàddu gi, ba tax meññul.
20 And these are the ones sown on good soil: they hear the word, accept it, and produce fruit—thirty, sixty, one hundred times over." Ñi jote jiwu mi ci suuf su baax si nag, ñooy ñi déglu kàddu gi, nangu ko, ba meññal; wii fepp, fanweer, wee, juróom benn fukk, wale, téeméer.»
21 He told them, "Does anyone bring in a lamp to put it under a basket or bed—not on a stand? Yeesu neeti leen: «Ndax dees na indib làmp, dëppeg leget? Am dees na indib làmp, yeb ci ron lal? Du dees koy aj ca kaw tegoom?
22 Nothing is hidden except to be revealed; nothing is secret except to surface. Mboolem lu làqu, siiwal lañu ca namm, te mboolem lu umpe, xamle lañu ca namm.
23 If anyone has ears to hear, let him hear." Ku am nopp yu mu dégge daal, na dégg.»
24 He told them, "Watch what you hear. The measure you use will be measured to you—and more added. Mu neeti leen: «Teewluleen bu baax li ngeen di dégg. Natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale, ba wis leen.
25 For whoever has will be given more; whoever doesn't, even what he has will be taken from him." Ku am, dees na ko dolli. Ku amul nag, la mu am as néew sax, dees na ko nangu.»
26 He said, "This is what the kingdom of our Father is like: a man scatters seed on the ground. Yeesu teg ca ne: «Nguurug Yàlla dafa mel ni nit ku sànni jiwu fi suuf.
27 Night and day, asleep or awake, the seed sprouts and grows, though he doesn't know how. Buy nelaw ak bu yewwoo, guddi ak bëccëg, jiwu maa ngi sax, di màgg, te xamul nan la koy defe.
28 The soil yields grain on its own—first blade, then head, then full kernel in the head. Suuf ay meññal boppam gàncax, jiital am ñax, dem ba taxawal aw gub, ba ay pepp mujj fees gub wa.
29 But when the grain ripens, he immediately sends the sickle, since harvest has come." Pepp ñor, janti ngóob taxaw, mu dawal sàrtam.»
30 He said, "What can we compare the kingdom of our Father to, or what parable can we use for it? Yeesu neeti leen: «Ana lees mana méngaleel nguurug Yàlla sax? Wan léeb lees koy misaale?
31 It's like a mustard seed, the smallest of all seeds when sown on the ground. Dafa mel ni doomu fuddën. Boo koy ji, moo gëna tuut ci mboolem jiwu.
32 Yet once sown, it grows up and becomes the largest of all garden plants, producing branches so big that birds of the air can nest in its shade." Waaye boo ko jiwee, mu sax, màgg, ba sut gàncax gépp, daldi sax car yu réy, ba njanaaw yi mana tàgge ci keram.»
33 With many such parables he spoke the word to them, as they were able to hear. Bare na léeb yu ni mel yu leen Yeesu daan misaale kàddu gi, ca na ñu ko mana xame.
34 He spoke to them only in parables, but privately explained everything to his own disciples. Daawul wax ak ñoom lu moy ci ay léeb. Bu wéetooki taalibeem nag, firil leen lépp.
35 That day, when evening came, he said to them, "Let us cross over to the other side." Bésub keroog ba ngoon jotee Yeesu ne taalibe ya: «Nanu jàll wàllaa dex gi.»
36 They left the crowd and took him along, just as he was, in the boat, other boats accompanying him. Ñu daldi bàyyikoo ca mbooloo ma, dem, yóbbaale Yeesu ca gaal ga mu des ba tey, yeneen gaal topp ca moom.
37 A fierce windstorm came up. Waves broke over the boat, so that it was already being swamped. Ba mu ko defee ngelaw la riddeek doole, gannax yay dal ca kaw gaal ga, ba mu bëgga fees.
38 But Jesus was asleep in the stern on the cushion. They woke him and said, "Teacher, don't you care that we're dying?" Teewul Yeesoo nga ca taatu gaal ga, tëdd, gegenu, di nelaw. Taalibe ya yee ko, ne ko: «Kilifa gi, nu ngi sànku, xanaa xalaatoo nu?»
39 He got up, rebuked the wind, and told the sea, "Peace! Be still!" The wind stopped, and it grew totally calm. Yeesu yewwu, daldi gëdd ngelaw la, ne dex ga: «Dalal, neel tekk!» Ngelaw la ne tekk, lépp ne sendaw.
40 He said to them, "Why are you so afraid? Do you still have no faith?" Yeesu ne leen: «Lu ngeen di tiit? Dangeena gëmul ba tey?»
41 They were terrified and asked one another, "Who then is this, that even the wind and the sea obey him?" Ba loolu amee ñu tiit lool, naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan, ba ngelaw leek dex gi sax di ko déggal?»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]