Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Once again Jesus entered the synagogue, and a man with a withered hand was there. Gannaaw loolu Yeesu duggati ca jàngub Yawut ba. Boroom loxo bu làggee nga fa woon.
2 They watched closely to see if he'd heal the man on the Sabbath, to accuse Jesus. Ay Farisen a ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj, te muy bésub Noflaay, ngir ñu man koo tuumaal.
3 Jesus said to the man with the withered hand, "Stand up and come forward." Yeesu ne boroom loxo bu làggi ba: «Taxawal fii ci digg bi.»
4 Then he asked them, "Is it lawful on the Sabbath to do good or to do harm, to save life or to kill?" But they stayed silent. Yeesu nag ne leen: «Ana lu yoon maye; def lu baax bésub Noflaay am def lu bon? Rawale bakkan am rey?» Ñu ne xerem.
5 He looked around at them in anger, grieved by their hardness of heart, and told the man, "Stretch out your hand." He stretched it out, and his hand was restored. Ci kaw loolu Yeesu dawal bëtu mer, xool leen ñoom ñépp, boole kooku naqar ndax seen xol yu wow. Mu ne waa ja: «Tàllalal loxo bi.» Mu tàllal, loxo ba wér.
6 Then the Pharisees went out and immediately began plotting with the Herodians how they might destroy him. Ba loolu amee Farisen ya génn, diisooji ca saa sa ak farandooy Buur Erodd ca mbirum Yeesu, ngir fexe nu ñu ko sànke.
7 Jesus withdrew with his disciples to the sea; a large crowd from Galilee followed, and from Judea, Gannaaw loolu Yeesu aki taalibeem jóge fa, jëm dex ga, mbooloom diiwaanu Galile mu bare topp ko, ak waa diiwaanu Yude itam,
8 from Jerusalem, Idumea, beyond the Jordan, and the region around Tyre and Sidon—hearing all he was doing, a great crowd came to him. ak waa Yerusalem ak Idume ak wàllaa Yurdan ak la wër Tir ak Sidon. Muy mbooloo mu bare mu dégg mboolem la muy def, daldi koy fekki.
9 He told his disciples to keep a small boat ready, because of the crowd, so they wouldn't crush him. Yeesu nag ne ay taalibeem, ñu waajal ko gaal bala ko mbooloo maa tanc.
10 For he had healed so many that all who had diseases were pressing forward to touch him. Ndax booba Yeesu jotoon naa faj ñu bare, ba tax mboolem ña ame ay jàngoro song ko, di ko wuta laal.
11 Whenever the unclean spirits saw him, they fell before him, shouting, "You are the Son of God!" Rab ya itam, saa yu ñu ko gisaa, daldi daanu fa kanamam, tey yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.»
12 But he firmly warned them not to reveal him. Teewul Yeesu femmu rab ya bu baax, ngir ñu bañ koo siiwal.
13 Jesus went up the mountain and called those he wanted; they came to him. Gannaaw loolu Yeesu yéeg ca tund wa, woo fa ña ko neex, ñooña dikk ba ca moom.
14 He appointed twelve, named apostles, so they could be with him and he could send them out to preach, Mu tabb ca fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñuy ànd ak moom, ngir itam, mu di leen yebal, ñu waareji,
15 and to have authority to drive out demons. mu joxaale leen xam-xamu dàq ay rab.
16 These are the twelve he appointed: Simon, to whom he gave the name Peter; Noonu la tabbe Fukk ak ñaar ñii, di Simoŋ ma muy wax Piyeer,
17 James son of Zebedee, and John his brother, whom he named Boanerges, meaning Sons of Thunder; ak Yanqóoba ak Yowaan, doomi Sebede, ña Yeesu di wax Bowanerses, muy firi Doomi dënu,
18 Andrew, Philip, Bartholomew, Matthew, Thomas, James son of Alphaeus, Thaddaeus, Simon the Zealot, ak Àndre ak Filib ak Bartelemi ak Macë ak Tomaa ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Tade ak Simoŋ, Mbokki kuréelu Moom-sa-réew ma,
19 and Judas Iscariot, who betrayed him. ak Yuda Iskaryo may mujj wor Yeesu.
20 He went home; the crowd gathered again, so he and his disciples couldn't even eat. Yeesu dellooti kër ga, mbooloo ma dajeeti fa, ba moom ak ay taalibeem taluñoo sex dugub sax.
21 When his family heard, they went out to restrain him, for they said, "He's out of his mind." Ay bokkam dégg la xew, daldi dikk, ngir jàppsi ko, naan dafa teqalikoo ak sagoom.
22 The scribes who came down from Jerusalem said, "He has Beelzebul," and, "By the prince of demons he drives out demons." Firikati yoonu Musaa ya jotoona wàccsee Yerusalem it ne: «Kii, Beelsebul a ko jàpp. Buuru rab boobu lay dàqe ay rab.»
23 So Jesus called them to him and spoke in parables: "How can Satan drive out Satan? Ba mu ko defee Yeesu woo leen, léeb leen ay léeb, ne leen: «Ana nu Seytaane mana dàqe Seytaane?
24 If a kingdom is divided against itself, that kingdom cannot stand. Ag nguur de, su dee xàjjalikoo ci biiram, googa nguur du mana yàgg.
25 And if a house is divided against itself, that house will not be able to stand. Ag kër it, su dee xàjjalikoo ci biiram, googa kër du mana yàgg.
26 And if Satan opposes himself and is divided, he cannot stand; his end has come. Seytaane nag, su jógee di xàjjalikoo ci biiram, du mana yàgg, day jeexal rekk.
27 No one can enter a strong man's house and take his goods without first tying up the strong man—then he can plunder the house. «Du kenn moos ku mana dugg kër ponkal, buub alalam! Xanaa mu njëkka yeew ponkal mi, doora mana toj kër ga.
28 Truly I tell you, all sins and insults against God will be forgiven children of mankind, whatever they say, Maa leen ko wax déy, lu mu mana doon, dees na ko jéggal doom aadama, mu diy bàkkaaram, ak mboolem kàddug saaga Yàlla.
29 but whoever blasphemes against the Holy Spirit never has forgiveness; they are guilty of an eternal sin," Waaye képp ku saaga Noo gu Sell gi, deesu ko jéggal mukk; day gàddu bàkkaar ba fàww.»
30 for they were saying, "He has an unclean spirit." La ñu ne rab a ko jàpp moo waral mu wax leen loolu.
31 His mother and brothers arrived and, standing outside, sent to him, calling him. Yaayu Yeesu moo dikkoon, ànd ak ay rakki Yeesu. Ñu taxaw ca biti, yónnee, woo ko.
32 A crowd sat around him and said to him, "Look, your mother and your brothers are outside, asking for you." Booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk kat ñu ngi ci biti, di la seet.»
33 He answered them, "Who are my mother and my brothers?" Yeesu ne leen: «Ana kan mooy sama yaay? Ak ñan ñooy samay rakk?»
34 Looking around at those sitting in a circle around him, he said, "Here are my mother and my brothers! Mu dawal nag bëtam, xool ña ko yéew, daldi ne: «Dama ne, ñii ñooy sama yaay ak samay rakk.
35 Whoever does the will of our Father is my brother and sister and mother." Ndax kuy jëfe coobarey Yàlla, kooku moo di sama rakk ju góor, di samab jigéen, di sama yaay.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]