Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 A few days later, when Jesus came back to Capernaum, word spread that he was home. Ba mu amee ay fan Yeesu délsi dëkk ba ñuy wax Kapernawum, nit ñi yég ne ñibbisi na.
2 So many gathered that there was no room left, not even at the door, and he was speaking the word to them. Ba mu ko defee ñu bare daje fa, ba xajatuñu ca bunt ba sax. Yeesu nag di leen xamal kàddu gi.
3 Then some men came, bringing to him a paralyzed man carried by four of them. Ci biir loolu ñu dikk, indil ko ab lafañ, ñeenti nit jàppoo ko.
4 Unable to bring him to Jesus because of the crowd, they removed the roof over him, dug through it, and lowered the mat the paralyzed man lay on. Waaye manuñu koo àggale ca moom ndax mbooloo ma. Ñu yéeg, bënn kaw taax ma, bëtte ko ca wet ga tollook fa Yeesu féete. Ñu yoor nag basaŋ ga lafañ ba tëdd.
5 When Jesus saw their faith, he said to the paralyzed man, "Son, your sins are forgiven." Yeesu seetlu seen ngëm, daldi ne lafañ ba: «Doom, jéggalees na la say bàkkaar.»
6 Now some of the scribes were sitting there, reasoning in their hearts, Ay firikati yoonu Musaa nga fa woon toog. Ña ngay wax ca seen xel naan:
7 "Why does this man speak this way? He is blaspheming! Who can forgive sins but God alone?" «Lu kii di wax nii? Yàlla de lay diir mbagg. Ana ku mana jéggaley bàkkaar, ku dul Yàlla doŋŋ?»
8 Immediately Jesus knew in his spirit they were reasoning this way within themselves, and said to them, "Why are you reasoning these things in your hearts? Ca saa sa Yeesu yég ci xelam la ñuy nàttable ci seen xel. Mu ne leen: «Li ngeen di nàttable nii ci seen xel, ana lu ko waral?
9 Which is easier—telling the paralyzed man, 'Your sins are forgiven,' or, 'Get up, take your mat, and walk'? Ana yii yaar, lu ci gëna yomb: ne lafañ bi “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne ko: “Jógal, jël sa basaŋ te dox”?
10 But so you'll know the Son of Man has authority on earth to forgive sins"—he told the paralyzed man, Kon nag dingeen xam ne Doomu nit ki am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba:
11 "I say to you, get up, take your mat, and go home." «Dama ne, jógal, jël sa basaŋ, te ñibbi.»
12 He got up, immediately took his mat, and went out before them all, so that everyone was amazed and praised our Father, saying, "We've never seen anything like this." Mu jóg, jël basaŋ ga ca saa sa, daldi génn fa kanam ñépp, ba ñépp waaru, di sàbbaal Yàlla, naan: «Lu mel nii, masunu koo gis!»
13 Jesus went out beside the sea again; the whole crowd came to him, and he taught them. Yeesu génnati, awe tàkkal dex ga, mbooloo mépp di ñëw ca moom, mu di leen jàngal.
14 Passing by, he saw Levi son of Alphaeus sitting at the tax booth and said, "Follow me." He got up and followed him. Naka la Yeesuy dem, daldi gis ku ñuy wax Lewi, doomu Alfe, mu toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay, topp ma.» Mu jóg, topp ko.
15 While Jesus reclined at the table in Levi's house, many tax collectors and sinners reclined with Jesus and his disciples, since many were following him. Yeesoo doon lekk ca kër Lewi, lu bare ci ay juutikat aki bàkkaarkat dikk, ñu bokk di lekk, ñook Yeesu aki taalibeem, ndax ñu baree ko toppoon.
16 Seeing him eat with sinners and tax collectors, the Pharisees' scribes asked his disciples, "Why does he eat with tax collectors and sinners?" Firikati yoonu Musaa ya bokk ca Farisen ya gis Yeesu bokk lekk ak bàkkaarkat yaak juutikat ya. Ñu ne ay taalibeem: «Juutikat yeek bàkkaarkat yi lay bokkal lekk nag?»
17 Hearing this, Jesus said to them, "The healthy don't need a doctor, but the sick do. I didn't come to call the righteous, but sinners." Yeesu nag dégg ca, ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. Du ñi jub laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo.»
18 John's disciples and the Pharisees were fasting. They came and asked him, "Why do John's disciples and the Pharisees' disciples fast, but yours don't?" Taalibey Yaxya ak Farisen yee doon woor. Ay nit dikk, ne Yeesu: «Lu tax taalibey Yaxya ak taalibey Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?»
19 Jesus said to them, "Can wedding guests fast while the bridegroom is with them? As long as they have the bridegroom with them, they cannot fast. Yeesu ne leen: «Ana nu xariti boroom séet mana woore, te boroom séet bi teew ci seen biir? Li feek boroom séet baa ngi ci seen biir duñu mana woor.
20 But days will come when the bridegroom is taken from them; then, on that day, they will fast. Teewul ay jant a ngi ñëw, dees na fi jële boroom séet bi. Bésub keroog nag dinañu woor.
21 No one sews unshrunk cloth on an old garment; otherwise the new patch tears away from the old, and the tear worsens. «Kenn du jël sekkit wu yees, di ko daaxe mbubb mu ràpp. Lu ko moy sekkit wi day ñoddi ndimo la ràpp, mbubb ma gëna xar.
22 No one puts new wine into old wineskins; the wine bursts the skins, and both are ruined. New wine goes into new wineskins." Biiñ bu bees it, deesu ko sotti ci mbuusum der yu ràpp. Lu ko moy biiñ bi fàcc mbuus yi, biiñ yàqu, mbuus yi yàqu. Biiñ bu bees daal, mbuus mu bees.»
23 One Sabbath, he walked through the grainfields, and as they went, his disciples began picking heads of grain. Bésub Noflaay la Yeesu jaare woon ay tool yu ñor, taalibeem ya ànd ak moom, tàmbalee fàq ay gub ca yoon wa.
24 The Pharisees said to him, "Look, why are they doing what's not lawful on the Sabbath?" Farisen ya nag ne Yeesu: «Danu ne, lu waral sa taalibe yi di def lu yoon mayewul ci bésub Noflaay?»
25 And he said to them, "Have you never read what David did when he was in need and hungry, he and those with him, Yeesu ne leen: «Xanaa masu leena jàng la Daawuda defoon, ba mu tolloo diggante te xiif, moom ak ña mu àndaloon?
26 how he entered the house of our Father in the days of Abiathar the high priest, ate the bread of the Presence—which only priests may eat—and gave some to those with him?" Ba Daawuda duggee ca kër Yàlla ga, jant ya Abyatar dee sarxalkat bu mag ba, mburum teewal ma la lekk, te yoon mayewul kenn ku ca lekk, ku dul sarxalkat ba. Sédd na ca sax ña mu àndal.»
27 And he said to them, "The Sabbath was made for people, not man for the Sabbath. Yeesu dellu ne leen: «Bésub Noflaay, dees koo sàkk ngir nit ki. Waaye nit ki, sàkkeesu ko ngir bésub Noflaay.
28 So the Son of Man is Lord even of the Sabbath." Kon Doomu nit ki, bésub Noflaay it mooy boroom.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]