Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The beginning of the gospel of Jesus Christ, the Son of our Father. Lii mooy ndoortel xibaaru jàmm bu Yeesu Almasi bi, Doomu Yàlla ji.
2 As written in Isaiah the prophet: "Look, I send my messenger ahead of you, who will prepare your way. Mu doore ni ñu ko binde ci téereb Yonent Yàlla Esayi, fu Yàlla ne: «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, xàllal la saw yoon.
3 A voice calling out in the wilderness: 'Prepare the way of the Lord, make his paths straight.'" Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan: “Nangeen xàll yoonu Boroom bi, juballeen ay xàllam.”»
4 John appeared, baptizing in the wilderness and proclaiming a baptism of repentance for the forgiveness of sins. Yaxya nag dikk ca màndiŋ ma, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir Yàlla jéggal leen seeni bàkkaar.
5 All Judea and everyone in Jerusalem went out to him, and he baptized them in the Jordan River as they confessed their sins. Ci kaw loolu mboolem diiwaanu Yude ak waa Yerusalem ñépp bàbbeeku, jëm ca Yaxya. Ñu tudd seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
6 John was dressed in camel's hair, with a leather belt around his waist, eating locusts and wild honey. Yaxyaa nga sol mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, laxasoo laxasaayu der ca ndigg la, di dundey njéeréer ak lemu àll.
7 He announced: "After me comes one stronger than I; I'm not worthy to stoop and untie his sandal strap. Mu waare, ne: «Am na ku ma sut kuy ñëw sama gannaaw, kooku, buumi caraxam sax yeyoowumaa sëgg, di ko ko feccil.
8 I have baptized you with water, but he will baptize you with the Holy Spirit." Man cim ndox laa leen sóob, waaye moom de, ci Noo gu Sell gi la leen di sóob.»
9 In those days Jesus came from Nazareth of Galilee and was baptized by John in the Jordan. Ca fan yooyu la Yeesu bàyyikoo dëkk ba ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile. Mu dikk, Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
10 Immediately, as he came up out of the water, he saw the heavens split open and the Holy Spirit come down on him like a dove. Naka la Yeesu génn ndox ma ca saa sa, daldi gis asamaan xar, Noowug Yàlla, wàcc ni am pitax, ca kawam,
11 And a voice came from heaven: "You are my beloved Son; in you I delight." baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaw laay bànneexoo.»
12 And immediately the Holy Spirit drove him out into the wilderness. Ca saa sa Noowug Yàlla jañax Yeesu, ba ca biir màndiŋ ma.
13 He was in the wilderness forty days, tempted by Satan, with the wild animals, and the angels served him. Nekk na ca màndiŋ ma ñeent fukki fan, Seytaane di ko fiir, mu nekkandook rabi àll yi, malaaka yi di ko toppatoo.
14 Now after John was arrested, Jesus came into Galilee, proclaiming the gospel of our Father, Gannaaw ba ñu tëjee Yaxya kaso, Yeesu dem Galile, di waare xibaaru jàmm bu Yàlla bi,
15 and saying, "The time is fulfilled, and our Father's kingdom is near; repent and believe the good news." naan: «Waxtu wa mat na, nguurug Yàlla dëgmal na. Tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bii.»
16 Passing the Sea of Galilee, he saw Simon and his brother Andrew casting a net in the sea, for they were fishermen. Yeesoo doon jaare tàkkal dexu Galile, daldi gis ku ñuy wax Simoŋ ak Àndre, rakkam ju mu bokkal ndey ak baay. Ña ngay mbaal ca dex ga, ndax ay nappkat lañu woon.
17 And Jesus said to them, "Follow me, and I will make you become fishers of people." Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ma, ma def leen nappkati nit.»
18 And immediately they left their nets and followed him. Ñu won mbaal ya gannaaw ca saa sa, daldi topp ca moom.
19 Going a little farther, he saw James son of Zebedee and John his brother in their boat, mending the nets. Yeesu doxaat tuuti, gis Yanqóoba doomu Sebede ak Yowaan mi Yanqóoba bokkal ndey ak baay. Ña nga ca gaal ga, di gaar seeni mbaal.
20 At once he called them; leaving their father Zebedee in the boat with the hired hands, they followed him. Yeesu woo leen ca saa sa, ñu bàyyi seen baay Sebede ca gaal ga, mook surga ya, daldi topp ca moom.
21 They went to Capernaum. At once, on the Sabbath, he entered the synagogue and began teaching. Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jàll biir dëkk ba ñuy wax Kapernawum. Naka la bésub Noflaay taxaw, Yeesu daldi dugg ca biir jàngub Yawut ba, di jàngale.
22 They were amazed at his teaching, for he taught them with authority, not like the scribes. Ñu yéemu ca njàngaleem ndax sañ-sañ ba mu leen di jàngale niroowul ak na la firikati yoonu Musaa yay jàngalee.
23 And immediately there was in their synagogue a man with an unclean spirit, and he cried out. Jenn waay a nga woon ca seen biir jàngu ba, rab a ko jàpp. Mu jekki di xaacu, naan:
24 Why meddle with us, Jesus of Nazareth? Have you come to destroy us? I know who you are—God's Holy One! «Yaw Yeesum Nasaret, ana lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji.»
25 But Jesus rebuked him, saying, "Be silent, and come out of him!" Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!»
26 And the unclean spirit, convulsing him and crying out with a loud voice, came out of him. Rab wu bon wa daane waa ja ba muy say, mu yuuxu yuux gu réy, doora génne ca waa ja.
27 All were amazed, and they questioned each other: "What is this? A new teaching with authority - he commands even the unclean spirits, and they obey him!" Ba loolu amee ñépp yéemu, naan ca seen biir: «Lii lu mu doon? Guléet mii njàngale! Céy bii xam-xam bu ànd ak sañ-sañ! Rab yi sax, mu jox leen ndigal, ñu def!»
28 And at once his fame spread everywhere throughout all the surrounding region of Galilee. Turu Yeesu nag law a law ca saa sa, ba dajal diiwaanu Galile gépp.
29 Immediately he left the synagogue and went to Simon and Andrew's house, with James and John. Gannaaw ba Yeesu ak Yanqóoba ak Yowaan génnee ca jàngu ba, dañoo ànd ca saa sa, dem kër Simoŋ ak Àndre.
30 Now Simon's mother-in-law lay sick with a fever, and immediately they told him about her. Fekk yaayu jabaru Simoŋ tëdd ndax yaram wu tàng. Ñu yégal ko Yeesu.
31 He came, took her hand, raised her up. The fever left her, and she served them. Mu dikk ba ca soxna sa, jàpp ca loxoom, yékkati ko, tàngooru yaram wa teqalikook soxna sa, mu di leen toppatoo.
32 That evening, when the sun set, they brought him all who were sick and those oppressed by demons. Ba ngoon jotee ba jant so, ñu indil Yeesu mboolem ñi wopp ak ñi rab jàpp,
33 And the whole city was gathered together at the door. dëkk ba bépp daje ca buntu kër ga.
34 He healed many sick with various diseases and drove out many demons, not letting the demons speak, since they knew him. Ci biir loolu ñu bare ñu ame ay jàngoroy jàngoro, mu wéral leen, rab yu bare, mu dàq leen. Waaye gannaaw rab ya xam nañu ko, mayu leen ñu wax.
35 Long before dawn, while still dark, he got up, went out to a deserted place, and prayed there. Ca ëllëg sa, laata bët di set, Yeesu jóg, génn, dem, ba àgg benn béreb bu wéet. Mu di fa ñaan Yàlla.
36 And Simon and those who were with him searched for him, Ci biir loolu Simoŋ aki àndandoom di ko seet.
37 and they found him and said to him, "Everyone is looking for you." Ba ñu ko gisee, ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.»
38 He said, "Let us go elsewhere, to the neighboring towns, so I can preach there too, for that is why I came." Yeesu ne leen: «Nan dem feneen ci dëkk yi nu wër ngir ma waare foofu itam, ndax looloo ma taxa génn.»
39 And he went throughout all Galilee, preaching in their synagogues and casting out demons. Ci kaw loolu muy wër diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, di dàq rab yi.
40 A man with leprosy came, knelt, and begged him, "If you're willing, you can make me clean." Gannaaw loolu genn gaana dikk ba ca moom, di ko ñaan, daldi sukk, ne ko: «Su la soobee, man nga maa setal.»
41 Moved with deep compassion, he stretched out his hand, touched him, and said to him, "I am willing; be clean." Yërmande jàpp Yeesu, mu tàllal loxoom, laal ko, ne ko: «Soob na ma, setal.»
42 And immediately the leprosy left him, and he was made clean. Ca saa sa ngaana ga teqalikook moom, mu set wecc.
43 Sternly warning him, he sent him away at once, Yeesu nag artu ko bu baax, yiwi ko ca saa sa, ne ko:
44 and told him, "Make sure you tell no one—but go, show yourself to the priest, and offer what Moses commanded for your cleansing, as proof to the people." «Fexeel ba bul wax kenn dara, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa saraxu setlu ni ko yoonu Musaa santaanee, ngir muy firnde ci ñoom.»
45 But he went out, proclaiming it freely and spreading the news, so Jesus could no longer enter a town openly, but stayed in lonely places. Yet people came to him from everywhere. Waaye naka la waa ja génn, tàmbalee yéene, siiwal mbir ma, ba tax Yeesu manatula siiwal duggam cib dëkk, xanaa mu féetewoo béreb yu wéet ca fa ko wër. Teewul nit ñiy jóge fu nekk, di ko fekki.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]