Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 9 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 He said to them, "Truly I tell you: some standing here will not taste death before they see the kingdom of our Father come with power." Mu neeti leen: «Maa leen ko wax, déy, ñenn a ngi taxaw fii, duñu dee te gisuñu nguurug Yàlla dikk ak doole.»
2 Six days later Jesus took Peter, James, and John, and led them up a high mountain alone, and he was transfigured before them. Ba ñu ca tegee juróom benni fan, Yeesu ànd na ak Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan, yóbbu leen kaw tund wu kawe, ngir wéetook ñoomu neen. Mu soppiku fa seen kanam:
3 His clothes became radiant, dazzling white—whiter than anyone on earth could bleach them. ay yéreem ne ràññ, weex tàll weexaay bu raw lu fóotkatub àddina mana fóot.
4 And Elijah appeared to them along with Moses, and they were talking with Jesus. Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas feeñu leen, mook Yonent Yàlla Musaa, ñuy waxtaan ak Yeesu.
5 Peter said to Jesus, "Rabbi, it's good that we're here. Let's make three shelters—one for you, one for Moses, and one for Elijah." Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, su nu toogoon fii de, mu baax ci nun. Nan yékkati ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa, benn Ilyaas.»
6 He did not know what to say, for they were terrified. Booba Piyeer xamul sax lu muy wax, ndax tiitaange ju leen jàpp.
7 A cloud appeared and overshadowed them, and a voice came from the cloud: "This is my beloved Son. Listen to him!" Ci kaw loolu aw niir dikk, yiir leen, baat jibe ca niir wa, ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe, dégluleen ko.»
8 Suddenly, when they looked around, they no longer saw anyone with them except Jesus. Taalibe yi jekki xool wet gu nekk, waaye gisatuñu kenn ku dul mennum Yeesu doŋŋ, mook ñoom.
9 Coming down the mountain, he ordered them to tell no one what they'd seen until the Son of Man rose from the dead. Naka lañuy wàcce ca tund wa Yeesu sant leen, ne leen ñu baña nettali kenn la ñu gis, ba kera Doomu nit ki dekki.
10 So they kept the matter to themselves, questioning what rising from the dead could mean. Ñu jàpp wax jooju nag ci seen biir tey sottante xel, ngir xam lu «dee-dekki» di tekki.
11 And they asked him, "Why do the scribes say that Elijah must come first?" Ci kaw loolu taalibe ya laaj ko, ne ko: «Lu tax firikati yoonu Musaa yi ne fàww Ilyaas njëkka ñëw?»
12 He said, "Elijah does come first and restores everything. Then why is it written the Son of Man must suffer much and be treated with contempt? Yeesu ne leen: «Waaw, Ilyaas kay mooy njëkka ñëw, ba jubbanti lépp. Waaye lu tax ñu bind ci Doomu nit ki, ne fàww mu sonn coono bu bare, te dees na ko xeeb?
13 But I tell you, Elijah has come, and they did to him whatever they pleased, as it is written about him." Waaye maa leen wax ne Ilyaas ñëw na, lu leen neex lañu def ak moom, te noonu lañu ko binde woon ci moom.»
14 Coming to the other disciples, they saw a large crowd around the disciples, and scribes arguing with them. Ba ñu waññikoo ba jub yeneen taalibe ya, dañoo gis mbooloo mu bare yéew leen, ay firikati yoon di weranteek ñoom.
15 As soon as the whole crowd saw Jesus, they were astonished and ran to greet him. Mbooloo ma mépp daldi gis Yeesu, teewaayam bett leen. Ñu dawsi, nuyu ko.
16 He asked them, "What are you arguing about with the scribes?" Ba loolu amee Yeesu laajte, ne: «Ana lu ngeen di weranteek ñii?»
17 Someone in the crowd answered him, "Teacher, I brought my son to you; he has a spirit that won't let him speak. Kenn ca mbooloo ma ne ko: «Kilifa gi, sama doom ju góor laa la indil. Aw rab wuy luuloo ko jàpp.
18 Whenever it seizes him, it throws him down. He foams at the mouth, grinds his teeth, and stiffens. I asked your disciples to drive it out, but they couldn't." Saa su ko dikkalee, da koy daaneel ci suuf, gémmiñ gi di fuur, muy yéyu, ne jàdd. Say taalibe laa ñaan ñu dàq rab wi, waaye manuñu ko.»
19 He replied, "You unbelieving generation, how long must I stay with you? How long must I endure you? Bring him to me." Yeesu ne leen: «Céy niti tey, yeena gëmadi! Maak yeen ba kañ? Dama leen di muñal ba kañ? Indilleen ma xale bi.»
20 They brought the boy to him. Seeing Jesus, the spirit instantly convulsed him; he fell to the ground, thrashing and foaming at the mouth. Ñu indil ko ko. Rab wa gis Yeesu rekk daldi sayloo xale ba, mu daanu fa suuf, di xalangu, gémmiñ gay fuur.
21 Jesus asked the boy's father, "How long has this been happening to him?" "From childhood," he said. Yeesu ne baay ba: «Lii kañ la ko dal?» Mu ne ko: «Ba muy gone ba tey.
22 "It has often thrown him into fire and water to destroy him. But if you can do anything, pity us and help us." Bare na lu mu koy xabtal ci sawara mbaa cim ndox, ngir sànk ko. Waaye soo ci manee lenn, yërëm nu, xettalee nu ko.»
23 Jesus said to him, "'If you can'? Everything is possible for the one who believes." Yeesu ne ko: «Nga ne: “Soo manee”? Ku ànd ak gëm kay, dara tëwu la.»
24 Immediately the boy's father cried, "I believe; help my unbelief!" Baayu xale bi daldi àddu ca kaw, ne: «Kon gëm naa, ngalla wallu maak sama ngëmadi.»
25 Seeing a crowd running together, Jesus rebuked the unclean spirit: "Mute and deaf spirit, I command you—come out of him and never enter him again!" Ci biir loolu Yeesu gis mbooloo mu dawandoo di dikk, mu daldi gëdd rab wa, ne ko: «Yaw rab wiy luulooka tëxloo, maa la ne génnal ci kii te bul duggati ci moom.»
26 Crying out and convulsing him hard, it came out. He looked like a corpse, so many said, "He's dead." Ba mu ko defee rab wa yuuxu, daldi sayloo xale ba bu metti, doora génn. Xale bi ne nemm, ni ku dee, ba ñu bare ne dee na.
27 But Jesus took him by the hand and raised him up, and he stood. Teewul Yeesu jàpp ca loxo ba, yékkati ko, mu taxaw.
28 When Jesus had gone indoors, his disciples asked him privately, "Why couldn't we drive it out?" Ba Yeesu duggee ca kër ga, taalibe ya laaj ko ci sutura, ne ko: «Lu tax manunu woona dàqal sunu bopp, rab wi?»
29 He told them, "This kind can come out only by prayer." Yeesu ne leen: «Xeetu rab wii, maneesu koo dàqe lenn lu moy ñaan.»
30 They left there and passed through Galilee. Jesus did not want anyone to know where they were, Foofa lañu bàyyikoo, jaare diiwaanu Galile, waaye Yeesu bëggul kenn yég ko.
31 because he was teaching his disciples, telling them, "The Son of Man is being handed into human hands. They will kill him, and three days later he will rise." Ndaxte booba ma ngay jàngal taalibe ya, naan leen: «Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit, ñu rey ko, te gannaaw bu ñu ko reyee dina dekki ci ñetti fan.»
32 But they did not understand what he meant, and they were afraid to ask him. Taalibe ya nag xamuñu woon lu kàddu googuy tekki, waaye ñemewuñu ko koo laaj.
33 They came to Capernaum. In the house he asked them, "What were you arguing about on the way?" Ba ñu àggee dëkk ba ñuy wax Kapernawum, ba dugg ca kër ga, Yeesu laaj leen, ne leen: «Lu ngeen doon waxtaane ci yoon wi?»
34 But they were silent, since they had argued along the way about who was greatest. Ñu ne cell, ndax la ñu doon werante ca yoon wa moo di kan moo gëna kawe ci ñoom.
35 He sat down, called the Twelve, and told them, "Anyone who wants to be first must be last of all and servant of all." Ba mu ko defee Yeesu toog, woo fukki taalibe yaak ñaar, ne leen: «Ku bëgga jiitu, na mujj ñépp te di surgab ñépp.»
36 He took a little child, stood him among them, took the child in his arms, and said to them: Yeesu daldi indi ab xale, taxawal ko ci seen biir. Ci kaw loolu mu fab xale bi, ne leen:
37 "Whoever accepts one of these little children in my name accepts me; whoever accepts me accepts not me but the one who sent me." «Képp ku dalal xale bu mel nii ndax man, man mii nga dalal, te képp ku ma dalal, du man nga dalal, waaye ki ma yebal nga dalal.»
38 John said to him, "Teacher, we saw someone driving out demons in your name and tried to stop him, since he doesn't follow us." Yowaan ne ko: «Kilifa gi, danoo gis kuy dàq ay rab ci sa tur, nu aaye ko, ndax bokkul ci nun.»
39 But Jesus said, "Don't stop him—no one who does a miracle in my name can soon speak evil of me. Yeesu nag ne ko: «Buleen ko aaye, ndaxte kenn manula def kéemaan ci sama tur, daldi ci teg wax ju bon ci man.
40 For whoever is not against us is for us. Képp ku nu sotul, nun la faral.
41 Truly I tell you, whoever gives you a cup of water to drink because you belong to Christ will never lose his reward. Maa leen ko wax, déy, képp ku leen may ab kaasu ndox, ngir li ngeen di niti Almasi bi, doo ñàkk sag pey mukk.
42 Whoever trips up one of these little ones who believe in me—better for him to have a large millstone hung around his neck and be thrown into the sea. «Waaye kenn sax ci xale yii ma gëm, képp ku ko bàkkaarloo, li gën ci moom, mooy ñu takk ci baatam doju wolukaay wu réy wu mbaam di wëndeel, daldi koy sànni biir géej.
43-44 If your hand trips you up, cut it off. Better to enter life maimed than with two hands to go into hell, into the unquenchable fire. Su la sab loxo bàkkaarloo, dog ko. Tàbbiwaale ab kuuñ ca dund gu wóor ga moo gën ci yaw, nga tàbbiwaale sa ñaari loxo biir jànnama, sawara sa dul fey.
45-46 If your foot trips you up, cut it off. Better to enter life lame than be thrown into hell with two feet. Su la sab tànk bàkkaarloo, dog ko. Tàbbiwaale bennub tànk ca dund gu wóor ga moo gën ci yaw, ñu boole laak sa ñaari tànk, sànni la biir jànnama.
47 If your eye trips you up, throw it out. Better to enter the kingdom of our Father with one eye than be thrown into hell with two, Su la sa bët bàkkaarloo, luqil. Tàbbiwaale patt ci nguurug Yàlla, moo gën ci yaw ñu boole laak sa ñaari bët, sànni biir sawara,
48 where 'their worm never dies and the fire never goes out.' “foofa sax ya dul deewe, sawara sa du fa feye.”
49 For everyone will be salted with fire. Ñépp nag sawara lañu leen di setale ni xorom di setale.
50 Salt is good, but if it loses its saltiness, how can you season it again? Keep salt among yourselves, and be at peace with each other." Xorom lu baax la, waaye bu raxee ba sàlli, nees koy delloo cafkaam? Nangeen jikkowoo xorom su raxul, daldi jàmmoo.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]