Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 10 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 He left there for the region of Judea and beyond the Jordan; crowds gathered to him again, and as usual he taught them once more. Yeesu jóge foofa, dem réewum Yude ak ca wàllaa dexu Yurdan. Mbooloo yu bare fekkseeti ko, mu di leen jàngalati, na mu ko baaxoo woon.
2 Some Pharisees came to test him, asking, "Is it lawful for a man to divorce his wife?" Ci kaw loolu ay Farisen dikk, di ko fiir, laaj ko, ne ko: «Ndax yoon maye na nit fase jabaram?»
3 He answered them, "What did Moses command you?" Yeesu ne leen: «Lu leen Musaa sant?»
4 They said, "Moses permitted a man to write a certificate of divorce and send her away." Ñu ne ko: «Musaa maye na kayitu pase gu nit kiy bind, ngir fase jabaram.»
5 Jesus told them, "He wrote you this command because your hearts were hard. Yeesu nag ne leen: «Seen dëgër xol a tax Musaa bindal leen loolu ndigal.
6 But from the beginning of creation, our Father made them male and female. Waaye ca njàlbéen ga Yàlla sàkke àddina, ca la leen sàkk ñuy ku góor ak ku jigéen.
7 'For this reason a man will leave his father and mother and be joined to his wife, Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, taqoo ak jabaram,
8 and the two will become one flesh.' So they are no longer two, but one flesh. ba ñoom ñaar di wenn suux doŋŋ. Moo tax dootuñu ñaar, waaye wenn suux doŋŋ lañu.
9 Therefore what our Father has joined together, let no one separate." Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
10 Back in the house, the disciples asked him about this again. Ba ñu delloo ca kër ga taalibe ya laaj ko ca mooma mbir.
11 He said to them, "Whoever divorces his wife and marries another commits adultery against her, Yeesu ne leen: «Ku fase sa jabar, takk keneen, njaaloo nga, ndax sa jabar ja nga fase,
12 and if she divorces her husband and marries another, she commits adultery." te ki tas ak jëkkëram, su séyaatee ak keneen, njaaloo na.»
13 People were bringing children to him so that he might touch them, but the disciples rebuked them. Ay xale lañu indiloon Yeesu ngir mu teg leen ay loxoom. Teewul taalibe ya jànni leen.
14 When Jesus saw this, he grew angry and said, "Let the children come to me; don't stop them, for the kingdom of our Father belongs to such as these. Yeesu gis ko, daldi mer, ne leen: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man! Buleen leen aaye, ndax ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguurug Yàlla.
15 Truly I tell you, whoever doesn't receive our Father's kingdom like a child will never enter it." Maa leen ko wax déy, képp ku baña nangul nguurug Yàlla ni ab xale, doo ca tàbbi mukk.»
16 And he took them in his arms and blessed them, laying his hands on them. Yeesu nag fab leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen.
17 As he started down the road, a man ran up, knelt before him, and asked, "Good Teacher, what must I do to inherit eternal life?" Yeesoo doon dox ciw yoon, jenn waay dawsi ba ca moom, daldi sukk ca kanamam, ne ko: «Kilifa gu baax bi, ana lu may def, ngir texe ba fàww?»
18 Jesus asked, "Why call me good? No one is good except our Father alone. Yeesu ne ko: «Lu tax nga naa ma ku baax ki? Kenn baaxul ku moy Yàlla doŋŋ.
19 You know the commandments: 'don't murder, commit adultery, steal, or give false testimony; don't defraud; honor your father and mother.'" Xam nga ndigal yi: “Bul bóom, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, bul xañ nit àqam, teralal sa ndey ak sa baay.”»
20 He said to him, "Teacher, all these I have kept since my youth." Waa ja ne ko: «Kilifa gi, loolu lépp ba may ndaw laa ko dale sàmm ba tey.»
21 Jesus looked at him and loved him. "One thing you lack: go, sell everything you own, give to the poor—you'll have treasure in heaven—then come follow me." Yeesu nag xool ko bëti cofeel, daldi ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal te lépp loo am, nga jaay ko, jox ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
22 At this word his face fell, and he went away grieving, for he had many possessions. Waa ja am mbetteel ca kàddu ga, daldi fay jóge aku tiis ndax ku bare alal la woon.
23 Jesus looked around and told his disciples, "How hard it will be for the wealthy to enter the kingdom of our Father!" Ba loolu amee Yeesu dawal bëtam fa ko wër, daldi ne taalibe ya: «Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe!»
24 The disciples were amazed at his words. Jesus said to them again, "Children, how hard it is to enter the kingdom of our Father! Wax jooju nag jaaxal taalibe ya. Yeesu neeti leen: «Gone yi, tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe!
25 A camel goes through a needle's eye easier than a rich person enters our Father's kingdom." Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, giléem jaare bën-bënu puso moo ko gëna yomb.»
26 They were even more astonished and said to one another, "Then who can be saved?" Wax jooju gënatee yéem taalibe ya, ñu naan ca seen biir: «Ku mana mucc nag?»
27 Jesus looked at them and said, "With man, impossible; but not with our Father, for all things are possible with our Father." Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Nit la të, waaye tëwul Yàlla. Yàlla man na lépp.»
28 Peter began to say to him, "Look, we have left everything and followed you." Piyeer daldi ne ko: «Waaw, nun de lépp lanu dëddu, topp la!»
29 Jesus said, "Truly I tell you, no one has left house or brothers or sisters or mother or father or children or fields for my sake and for the gospel, Yeesu ne ko: «Maa leen ko wax déy, amul kenn kuy dëddu kër, mbaa doomi ndey yu góor mbaa yu jigéen, mbaa ndey mbaa baay, mbaa doom, mbaa suuf, ngir maak xibaaru jàmm bi,
30 "who won't receive a hundredfold now, in this time—houses, brothers, sisters, mothers, children, fields, with persecutions—and in the age to come, eternal life. te jotuloo ci jamonoy tey jii téeméeri yoon, la nga amoon ciy kër, ak doomi ndey yu góor ak yu jigéen, ak ndey ak doom ak suuf, ba jotaale coonoy bunduxataal, ak texe ba fàww gooy jot ëllëg.
31 But many who are first will be last, and the last first." Waaye ñu baree ngi jiitu tey, ñooy mujji, te ñu baree ngi mujje tey, ñooy jiituji.»
32 On the road up to Jerusalem, Jesus walked ahead of them. They were amazed, and those following were afraid. Taking the twelve aside again, he began telling them what was about to happen to him: Ñu ànd ca yoon wa, jëm Yerusalem, Yeesu jiitu leen, taalibe ya waaru, ña ca topp tiit. Yeesu nag wéetook Fukk ñaak ñaar, di leen xamal mbir ya ko nara dikkal.
33 "Look, we're going up to Jerusalem. The Son of Man will be handed over to the chief priests and scribes, who will condemn him to death and hand him over to the Gentiles. Mu ne leen: «Noo ngii jëm Yerusalem, te dees na wor Doomu nit ki, jébbal ko sarxalkat yu mag yaak firikati yoonu Musaa ya, ñu teg ko àtteb dee, jébbal ko jàmbur ñi dul Yawut.
34 They will mock him, spit on him, flog him, and kill him; after three days he will rise." Ñu ñaawal ko, tifli ko, caw ko, ba noppi rey ko, ñetti fan tege ca, mu dekki.»
35 James and John, Zebedee's sons, came to him and said, "Teacher, we want you to do for us whatever we ask." Ci kaw loolu Yanqóoba ak Yowaan, doomi Sebede dikk fa Yeesu. Ñu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon nga defal nu li nu lay ñaan.»
36 He said to them, "What do you want me to do for you?" Yeesu ne leen: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
37 They said to him, "Let us sit in your glory, one at your right, one at your left." Ñu ne ko: «May nu nu toog, kii féete la ndijoor, kii féete la càmmoñ, keroog ca sa jataayu daraja ba.»
38 Jesus said to them, "You don't know what you're asking. Can you drink the cup I drink, or be baptized with the baptism I'm baptized with?" Yeesu ne leen: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Mbaa kaasub naqar bi may naani, man ngeen koo naan? Am sóobu gu metti gi ma sóobu, man ngeen koo sóobu?»
39 "We can," they said. Jesus said to them, "The cup I drink, you will drink; the baptism I'm baptized with, you will be baptized with, Ñu ne ko: «Man nanu ko.» Yeesu ne leen: «Kaasub naqar bi may naani de, dingeen ko naan, sóobu gu metti gi ma sóobu it, dingeen ko sóobu,
40 but sitting at my right or left isn't mine to give - that's for those it's prepared for." tooge sama ndijoor mbaa sama càmmoñ nag, du maa koy maye, waaye ña ñu ko waajalal lay seen cér.»
41 Hearing this, the ten grew indignant at James and John. Ba fukki taalibe ya ca des déggee mbir ma, seen xol tàmbali tàng ca Yanqóoba ak Yowaan.
42 Jesus called them together and said, "You know that those regarded as rulers of the Gentiles dominate them, and their great ones wield power over them. Yeesu daldi leen woo, ne leen: «Xam ngeen ne ñi xeeti àddina yi def seeni njiit, dañu leen di def jaam, seeni kàngam di leen néewal doole.
43 But it isn't so among you. Instead, whoever wants to be great among you must be your servant, Yeen nag, bumu deme noonu ci seen biir. Ku bëgga doon ku màgg ci yeen, na nekk seen surga,
44 and whoever wants to be first among you must be slave of all. te ku bëgga nekk seen njiit, na doon jaamub ñépp.
45 For even the Son of Man came not to be served, but to serve, and to give his life as a ransom for many." Ndax Doomu nit ki itam ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñu bare.»
46 They came to Jericho. As Jesus and his disciples were leaving with a large crowd, blind Bartimaeus son of Timaeus sat begging by the road. Yeesu ak taalibeem ya nag agsi dëkk ba ñuy wax Yeriko. Naka lañuy génne Yeriko, mbooloo mu takku topp leen. Ci biir loolu ab silmaxa bu ñuy wax Bartime, tur wa di tekki doomu Time, ma nga tooge ca peggu yoon wa, di yalwaan.
47 Hearing it was Jesus of Nazareth, he began to cry out, "Jesus, Son of David, have mercy on me!" Mu dégg ne Yeesum Nasaret mooy jubsi, ba tax muy xaacu, naan: «Yeesu Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
48 Many scolded him to be silent, but he shouted even louder, "Son of David, have mercy on me!" Ba loolu amee ñu bare femmu ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna xaacooti, ne: «Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
49 Jesus stopped and said, "Call him." So they called the blind man: "Courage! Get up—he's calling you." Yeesu daldi taxaw, ne: «Wooleen ko!» Ñu woo silmaxa ba, ne ko: «Dallul te jóg, mu ngi lay woo.»
50 Throwing off his cloak, he jumped up and came to Jesus. Mu sànni malaanam, ne layy, dikk ba ca Yeesu.
51 Jesus told him, "What do you want me to do for you?" The blind man told him, "Rabboni, let me see again." Yeesu ne ko: «Ana loo bëgg, ma defal la ko?» Silmaxa ba ne ko: «Xanaa ma dellu di gis, sama kilifa.»
52 Jesus told him, "Go; your faith has healed you." At once he regained his sight and followed Jesus on the road. Yeesu ne ko: «Demal. Sa ngëm musal na la.» Ca saa sa muy gis, daldi topp Yeesu ca yoon wa.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]