Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 11 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Nearing Jerusalem, at Bethphage and Bethany by the Mount of Olives, Jesus sent two of his disciples ahead, Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya dikk ba jub Yerusalem, ba agsi dëkk ya ñuy wax Betfase ak Betani ca wetu tundu Oliw ya. Yeesu yebal ñaar ca taalibe ya,
2 telling them, "Go into the village ahead of you, and as soon as you enter it, you'll find a tied colt no one has ever ridden. Untie it and bring it here." ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen agsee rekk, dingeen fa gis cumbur bu yeewe, bu kenn masula war. Yiwileen ko, indi.
3 If anyone asks you, 'Why are you doing this?' say, 'The Lord needs it and will send it back here at once.' Bu ñu leen nee: “Lu ngeen di def nii?”, ngeen ne: “Boroom bee ko soxla, dina ko delloosi léegi.”»
4 They went and found a colt tied at a doorway outside in the street, and untied it. Taalibe ya dem, daldi gis ab cumbur ci mbedd mi, mu yeewe ci buntu kër. Ñu yiwi ko.
5 Some of those standing there asked them, "What are you doing, untying that colt?" Ñenn ca ña fa taxaw ne leen: «Lu ngeen di def nii, bay yiwi cumbur bi?»
6 They answered as Jesus had told them, and the people let them go. Ñu tontu leen la leen Yeesu waxoon, nit ña bàyyi leen.
7 They brought the colt to Jesus and threw their cloaks over it, and he sat on it. Ñu indil Yeesu cumbur ba, daldi teg seeni yére ca kawam, Yeesu war.
8 Many spread their cloaks on the road; others spread leafy branches cut from the fields. Ñu bare nag lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña lal ay cari garab yu sëq yu ñu dagge ca tool ya.
9 Those who went ahead and those who followed were shouting, "Hosanna! Blessed is he who comes in the name of our Father! Ci kaw loolu ña jiitu ak ña topp ca Yeesu xaacoondoo, naan: «Osaana! Na barke wàcc ci ki dikk ci turu Boroom bi!
10 Blessed is the coming kingdom of our father David! Hosanna in the highest!" Na barke wàcc ci nguur giy ñëw, sunu nguurug maam Daawuda! Osaana, na cant jibe béreb ya gëna kawe!»
11 Jesus entered Jerusalem and the temple, looked around at everything, and—since it was already late—went out to Bethany with the Twelve. Yeesu nag agsi Yerusalem, dugg ca kër Yàlla ga. Ba mu xoolee lépp ca biir, ba noppi, yemook mu guddi, mu ànd ak fukki taalibe yaak ñaar, jubal dëkk ba ñuy wax Betani.
12 The next day, as they were leaving Bethany, Jesus was hungry. Ba bët setee ñu génne Betani. Ci biir loolu Yeesu xiif.
13 Seeing a leafy fig tree in the distance, he went to see if it had anything on it. Reaching it, he found nothing but leaves, since it wasn't fig season. Mu séen fu sore garabu figg gu sëq. Mu jàdd, di seeti, ndax dina ca fekk dara. Mu dem ba ca figg ga, gisul lu dul ay xob, ndax booba figg amagul.
14 Then he told it, "May no one ever eat fruit from you again." His disciples heard him say it. Ci kaw loolu mu ne figg ga: «Yàlla bu kenn lekkati sab doom!» Taalibe ya di ca dégg.
15 They arrived in Jerusalem, and Jesus entered the temple and began driving out the sellers and buyers there. He overturned the money-changers' tables and the seats of those selling doves, Ñu délsi Yerusalem, Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ñay jaay aka jënd ca kër Yàlla ga. Mu dëpp taabali weccikati xaalis ya, ak tooguy jaaykati pitax ya,
16 and he would not allow anyone to carry merchandise through the temple courts. ba noppi bàyyiwul kenn, mu dugal lenn ca kër Yàlla ga.
17 And he taught them, saying, "Isn't it written: 'My house will be called a house of prayer for all the nations'? But you've made it a den of robbers." Mu di leen jàngal nag, wax leen, ne leen: «Xanaa bindeesul ne: “Sama kër gi, kërug ñaan lees ko tudde, ñeel xeetoo xeet.” Waaye yeen, moom ngeen def rawtub sàcc.»
18 The chief priests and scribes heard this and sought a way to destroy him, for they feared him, since the whole crowd was amazed at his teaching. Sarxalkat yu mag yaak firikati yoonu Musaa ya dégg loolu, ragal ko, di ko fexee rey, ndax mbooloo mépp a yéemu woon ca njàngaleem.
19 And when evening came, they went out of the city. Timis jot, Yeesu ànd ak taalibe ya, génn dëkk ba.
20 In the morning, as they passed by, they saw the fig tree withered from its roots. Ba ñuy dem ca suba teel lañu gis garabu figg ga wow koŋŋ, ba ca reen ya.
21 Peter remembered and said to him, "Rabbi, look! The fig tree you cursed has withered." Piyeer nag fàttaliku, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg ga nga rëbboon wow na koŋŋ!»
22 Jesus answered them, "Have faith in our Father. Yeesu ne leen: «Gëmleen Yàlla.
23 Truly I tell you, whoever tells this mountain, 'Be lifted up and thrown into the sea,' without doubting in his heart but believing what he says will happen—it will be done for him. Maa leen ko wax déy, képp ku ne tund wale: “Jógal, tàbbiji géej,” te bañ cee boole xel ñaar, xanaa gëm ne li nga wax dina am, noonu lees la koy nangule.
24 So I tell you: whatever you pray and ask for, believe you've received it - it will be yours. Moo tax ma di leen wax lii: Lépp lu ngeen di sàkku cig ñaan, gëmleen ne jot ngeen ko ba noppi, dingeen ko am.
25-26 When you stand praying, forgive whatever you hold against anyone, so your Father in heaven may also forgive you your sins." Bu ngeen taxawee di ñaan it, te fekk ngeen jàppal kenn dara, baalleen ko, ngir seen Baay ba fa asamaan baal leen seeni tooñ, yeen itam.»
27 They returned to Jerusalem. While Jesus walked in the temple, the chief priests, scribes, and elders came to him, Ñu dellooti Yerusalem. Ci kaw loolu Yeesu dugg kër Yàlla ga, di doxantu ca biir ëtt ba. Sarxalkat yu mag yaak firikati yoonu Musaa yaak magi askan wa dikk ba ca moom,
28 and asked, "By what authority are you doing this? Or who gave you this authority to do it?" ne ko: «Lii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ak ku la jox sañ-sañu def ko?»
29 Jesus said to them, "I'll ask you one question. Answer me, and I'll tell you by what authority I do these things. Yeesu ne leen: «Ma laaj leen man itam lenn; tontuleen ma ci, ma wax leen ci ban sañ-sañ laay defe lii.
30 John's baptism—was it from heaven, or of human origin? Answer me." Sóobeb Yaxya ci ndox, ndax asamaan la ndigal la bawoo, am ci nit ñi la bawoo? Tontuleen ma ci loolu.»
31 They discussed it among themselves: "If we say, 'From heaven,' he'll ask, 'Then why didn't you believe him?' Ñu diisoo, daldi ne: «Su nu nee: “Asamaan la ndigal la bawoo,” da naan: “Lu tax kon gëmuleen Yaxya?”
32 But if we say, 'From humans'"—they feared the crowd, since all considered John a true prophet. Ndax danuy wax ne ci nit ñi la bawoo?» Booba mbooloo ma lañu ragal, ndax ñépp a jàppoon ne Yaxya ab yonent dëgg la woon.
33 They answered Jesus, "We don't know." Jesus said, "Neither will I tell you by what authority I do these things." Ñu daldi ne Yeesu: «Loolu xamunu ko.» Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe lii.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]