Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 12 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 He began speaking to them in parables: "A man planted a vineyard, fenced it in, dug a winepress pit, built a watchtower, rented it to farmers, and left. Yeesu nag teg ca di wax ak ñoom ci ay léeb. Mu ne leen: «Ab tóokëru reseñ la nit jëmbatoon. Mu ñag tóokër bi, gas ca paxum nalukaayu reseñ, tabax ca taaxum wattukaay, ba noppi batale tóokër ba ay beykat, daldi tukki.
2 At harvest time he sent a servant to the tenants to collect some of the vineyard's fruit. «Ba wittum reseñ jotee, mu yebal ab surga ca beykat ya, ñu jëlsi wàllam ca meññeef ma.
3 But they seized him, beat him, and sent him away empty-handed. Beykat ya jàpp ko, dóor ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen.
4 Again he sent them another servant; they hit him on the head and dishonored him. Boroom tóokër ba yebalaat beneen surga, ñu xaañ ko, toroxal ko.
5 And he sent another, and they killed him—then many more, beating some and killing others." Mu yebalati beneen surga, ñu rey ko. Mu dellu yebal ñu bare, ñii ñu dóor leen, ñii ñu rey.
6 He had still one, a beloved son; last he sent him to them, saying, "They will respect my son." «Boroom tóokër ba nag desewul kenn ku dul doomam ji mu sopp. Mu mujj koo yebal ca beykat ya te naan: “Sama doom, dinañu ko rus.”
7 "But the tenants said to each other, 'This is the heir. Come, let's kill him—the inheritance will be ours.' Teewul beykat ya ne ca seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko daldi rey, ndonoom di sunu moomeel.”
8 So they took him and killed him and threw him out of the vineyard. Ñu jàpp ko, rey, génne néew ba tóokër ba, sànni ca biti.»
9 So what will the vineyard's owner do? He'll come, destroy the tenants, and give the vineyard to others. «Ana nu boroom tóokër biy def? Xanaa dikk rekk, rey beykat yi, dénk tóokëru reseñ ba ñeneen.
10 Have you not read this Scripture: 'The stone the builders rejected has become the cornerstone; Xanaa jànguleen gii kàddu ci Mbind mi? “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj di doju koñu tabax bi.
11 this was our Father's doing, and it is marvelous in our eyes'?" Lii de, fa Boroom bi la sottee, nu gis ko, yéemu.”»
12 They wanted to arrest him but feared the crowd, knowing he'd told the parable against them. So they left him and went away. Ba loolu amee njiit ya di ko wuta jàpp, ndax xam nañu xéll ne ñoo moom léeb wa, waaye dañoo ragal mbooloo ma, ba tax ñu dem, bàyyi ko.
13 They sent some of the Pharisees and Herodians to trap him in his words. Njiiti Yawut ya teg ca yebal ca Yeesu ay Farisen ak ay farandooy Buur Erodd, ngir ñu lalal ko fiir gu ñu ko jàppe ci kaw kàddu.
14 They came and said to him, "Teacher, we know you're true and don't care what anyone thinks, since you don't judge by appearance but truly teach our Father's way. Is it lawful to pay taxes to Caesar, or not? Should we pay, or should we not?" Ñooñu dikk ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku dëggu nga, te ragaloo kenn, ndax seetuloo ci jëmmi nit, waaye ci kaw dëgg ngay jàngalee yoonu Yàlla. Ndax yoon maye na ku fey Buur Sesaar ab galag, am déet? War nanu koo fey, am warunu koo fey?»
15 But, knowing their hypocrisy, he said to them, "Why are you testing me? Bring me a silver coin to look at." Teewul Yeesu ràññee seen jinigal, ne leen: «Ana lu ngeen may seetloo? Indilleen ma posetub dinaar, ma xool.»
16 They brought one, and he asked them, "Whose image and inscription is this?" They told him, "Caesar's." Ñu jox ko poset, mu ne leen: «Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» Ñu ne ko: «Buur Sesaar.»
17 Jesus told them, "Give to Caesar what's Caesar's, and to our Father what's our Father's." They were amazed at him. Yeesu ne leen: «Yëfi Sesaar daal, joxleen ko Sesaar, yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.» Ñu waaru nag ci moom.
18 And the Sadducees came to him, who say there is no resurrection. And they questioned him, saying, Sadusen yi ne dee-dekki amul, ñoo ñëwoon ci Yeesu, di ko laaj, ne ko:
19 "Teacher, Moses wrote for us that if a man's brother dies leaving a wife but no child, the brother must marry her and raise up offspring for him. «Kilifa gi, Musaa da noo bindal ne, ku góor, su ku mu bokkal waajur te amul doom, faatoo, su bàyyee gannaaw jabar, kooku na jël jabar ja, ngir amal mbokkam ma dee, kuutaay.
20 There were seven brothers; the first married, and when he died, left no children. «Léegi juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay la woon. Taaw ba am jabar, ba faatu te bàyyiwul doom.
21 And the second married her, and he died leaving no children. And the third likewise. Tofo ba jël ndaw sa, ba mujj dee te bàyyiwul doom. Ñaareelu tofo ba it noonu.
22 And none of the seven left any children. Last of all the woman also died. Ñu topplantee ko noonu ba juróom ñaar ñépp dee, te kenn bàyyiwul doom. Gannaaw gi, ndaw sa it dee.
23 At the resurrection, when they rise, whose wife will she be? The seven had her as wife." Keroog ndekkite la nag, bu ñu dekkee, kan ci ñoom la ndaw say doon jabaram, gannaaw juróom ñaar ñépp a ko jëloon jabar?»
24 Jesus said to them, "Isn't this why you're wrong—you know neither the Scriptures nor our Father's power? Yeesu ne leen: «Du lii mooy seen njuumte: xamuleen Mbind mi, xamuleen manoorey Yàlla!
25 For when the dead rise, they neither marry nor are given in marriage, but are like the angels in heaven. Ndax ñi dee, bu ñu dekkee, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër, waaye dañuy mel ni malaaka yi ci asamaan.
26 About the dead being raised, haven't you read in Moses' book, in the passage about the bush, how our Father told him, 'I am the God of Abraham, of Isaac, and of Jacob'? Te ci wàllu dee-dekki sax, xanaa jànguleen na ko téereb Musaa indee ca mbirum ngarab sa, mooy ba mu ne: “Maay Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba”?
27 He is not God of the dead, but of the living. You are badly mistaken." Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund. Njuumte lu réy ngeen juum.»
28 One scribe approached, heard them debate, saw Jesus answered well, and asked, "Which commandment is most important of all?" Ci biir loolu ab firikatu yoonu Musaa bu dégg seen wax ja, daldi gis ne Yeesu tontu na leen bu baax. Mu dikk, laaj ko ne ko: «Ana lan ndigal moo gëna am solo ci ndigal yépp?»
29 Jesus answered, "The most important is this: 'Hear, Israel: our Father is one.' Yeesu ne ko: «Ndigal li gëna am solo mooy: “Dégluleen, yeen bànni Israayil, Boroom bi sunu Yàlla, Boroom bi kenn la.
30 Love your Father with all your heart, with all your soul, with all your mind, with all your strength." Kon seen Yàlla Boroom bi, nanga ko soppe sa léppi xol, ak sa léppi jëmm, ak sa léppi xel, ak sa léppi doole.”
31 "The second is this: 'Love your neighbor as yourself.' No commandment is greater than these." Ñaareel bi mooy: “Ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.” Ndigal gënula màgg yii.»
32 The scribe said to him, "Well said, Teacher. You've said truly that he is one, and there's no other besides him. Firikatu yoon bi ne ko: «Waawaaw, Kilifa gi, yaa wax dëgg; Yàlla kenn la, te amul jeneen Yàlla ju dul moom.
33 Loving him with all the heart, all the understanding, all the strength, and loving one's neighbor as oneself, matters far more than all whole burnt offerings and sacrifices." Te it nga soppe ko sa léppi xol, ak sa léppi xel, ak sa léppi doole, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom; loolu moo gën mboolem saraxi dóomal, ak yeneen sarax yu mu mana doon.»
34 Seeing he answered wisely, Jesus said to him, "You are not far from the kingdom of our Father." After that, no one dared ask him any more questions. Yeesu nag gis ne waa ja waxe xel, mu ne ko: «Sorewuloo nguurug Yàlla de.» Ba loolu amee kenn ñemeetu koo laaj dara.
35 Teaching in the temple, Jesus asked, "How can the scribes say the Christ is the son of David? Yeesu nag di jàngale ca kër Yàlla ga, daldi laajte, ne: «Lu tax firikati yoon yi ne, Almasi bi, sëtub Daawuda la?
36 David himself said by the Holy Spirit: 'Our Father said to my Lord, "Sit at my right hand until I put your enemies under your feet."' Daawuda ci boppam moo waxe ci ni ko leeru Noo gu Sell gi dikkale, ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor, ba ma teg say noon fi sa suufu tànk.’ ”»
37 "David himself calls the Christ Lord. How can the Christ be David's son?" The large crowd enjoyed listening to him. Yeesu neeti: «Gannaaw Daawuda ci boppam moo woowe Almasi bi “Sang bi,” ana kon nu mu nekke ab sëtam?» Mbooloo mu baree nga fa woon, di ko dégloo mbég.
38 And in his teaching he said, "Beware of the scribes, who like walking in long robes and being greeted in the marketplaces, Yeesu teg ca xamal leen ne leen: «Moytuleen firikati yoonu Musaa yi taamoo jaagar-jaagareek seen mbubb yu réy, di sàkku nuyoob wegeel ca pénc ma,
39 and to have the best seats in the synagogues and the places of honor at banquets, ak toogu yu kaname ca jàngu ya, ak péetey teraanga ca bernde ya.
40 who devour widows' houses and make long prayers just for show. These will receive the greater condemnation." Ñooy saax-saaxee alalu jëtun ñi tey ñaan ñaani ngistal yu dul jeex. Ñooñu la seen mbugal di gëna tar.»
41 Sitting across from the treasury, he watched the crowd drop coins in; many rich people dropped in large sums. Ci kaw loolu Yeesu toog ca kër Yàlla ga, janook ndaa la ñuy dugal seen xaalis bu ñuy joxe ngir Yàlla. Muy seetlu na nit ñay dugalee xaalis ca ndaa la. Ay boroom alal yu bare dugal ca dayo yu takku.
42 And a poor widow came and put in two small copper coins, worth a penny. Ci biir loolu ab jëtun dikk, sànni ca ñaari poseti xànjar yu matul sax ab dërëm.
43 Calling his disciples, he said, "Truly, I tell you, this poor widow put in more than all who put into the offering box. Yeesu nag woo taalibe ya, ne leen: «Maa leen ko wax déy, mboolem ñi sànni xaalis ci ndab li, jëtun bu néew doole bii moo leen ëpple lu mu ci sànni.
44 For they all gave from their surplus, but she gave from her poverty—all she had, her whole livelihood." Ndax ñoom ñépp ci seen koom lañu sàkke as lëf, sànni ci ndab li, waaye moom de, ci biirug ndóolam la jële la mu amoon lépp, dundam bépp, sànni ci.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]