Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 13 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Leaving the temple, one of his disciples said to him, "Teacher, look! What huge stones, what magnificent buildings!" Naka la Yeesuy génne ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal rekk kër Yàlla gi! Céy yii doj ak yii taax!»
2 Jesus said to him, "Do you see these great buildings? Not one stone will remain here on another; all will be torn down." Yeesu ne leen: «Gis ngeen yii taax yu réy yépp? Doj wu tege ciw doj du dese fii te tasul.»
3 As he sat on the Mount of Olives facing the temple, Peter, James, John, and Andrew asked him privately, Gannaaw gi, ba Yeesu toogee ca kaw tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan ak Àndre ñoo dikk di ko laaj, ñook moom doŋŋ, ne ko:
4 tell us, when will these things happen, and what sign shows all this is about to be fulfilled? «Wax nu kañ la loolu di am? Ak luy doonub takk buy xamle ne xew-xew yooyu yépp ay waaja sotti?»
5 Jesus began to tell them: "Watch out that no one deceives you. Yeesu ne leen: «Moytuleen, ba kenn du leen nax.
6 Many will come in my name, claiming, 'I am he,' and they will deceive many. Ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te ñu bare lañuy nax.
7 When you hear of wars and rumors of wars, don't be troubled—these must happen, but the end isn't yet. Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, buleen tiit, fàww loolu am, waaye du doonagum muj ga.
8 Nation will rise against nation, kingdom against kingdom, earthquakes in various places, famines—these are the beginning of birth pains. Aw xeet dina jógal aw xeet, am réew jógal am réew, ay yëngu-yënguy suuf dina dikke fu bare, te ay xiif dina am, waaye ndoortel mititu mat la looluy doon.
9 Watch yourselves. They'll hand you to councils and beat you in synagogues. Because of me you'll stand before governors and kings, as a testimony to them. «Yeen nag moytuleen. Dees na leen jàpp, jébbal leen pénci layoo ya, dees na leen dóor ca biir jànguy Yawut ya, te fa kanam boroomi dëkk aki buur ngeen di taxawi ndax man, ngir ngeen man leena yékkatil kàdduy seede.
10 And the gospel must first be proclaimed to all nations. Balaa daraa xew, fàww xibaaru jàmm bi siiw ci xeet yépp.
11 When they arrest and hand you over, don't worry beforehand what to say. Say whatever you're given in that hour—it's not you speaking, but the Holy Spirit. Bu ñu leen tegee loxo nag, ba jébbal leen kilifa ya, la ngeen wara waxi bumu leen jaaxal, waaye kàddu gu ñu leen may keroog ca waxtu wa rekk, waxleen ko, ndax su keroogee du yeenay wax, waaye Noo gu Sell geey wax ci yeen.
12 Brother will betray brother to death, father his child. Children will rise against parents and have them put to death. «Doomu ndey dina wor doomu ndey, ngir ñu rey ko, baay it wore noonu doomam, te doom dina jógal waajuram, ba reylu ko.
13 All will hate you for my name, but whoever endures to the end will be saved. Te it ñépp a leen di bañ ndax sama tur. Waaye ku muñ ba muj ga, kooku dina mucc.»
14 When you see the abomination of desolation standing where it should not be (reader, take note), those in Judea must flee to the mountains. «Bés bu ngeen gisee nag “lu siblu luy jur yàqute”, mu taxawe fu mu yelloowul, yaw miy jàng, teewlul, su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya.
15 Let no one on the housetop go down or enter the house to take anything out. Ku mu fekk ci kaw am taax, bul wàcc, bay dugg jëli lenn ca biir.
16 Let no one in the field go back to get their coat. Ku mu fekk tool ba, bul dellu ca kër ga, di jëli sa mbubb.
17 How dreadful it will be in those days for pregnant women and nursing mothers! Wóoy ngalla jigéeni wérul ña, ak ñay nàmpal ca bés yooyu!
18 Pray that it will not happen in winter, Ñaanleen nag mu baña yemook jamonoy seddaayu lolli,
19 for those days will bring suffering unmatched since our Father created the world until now—and never to be matched again. ndax janti keroog coono lay doon bu masula am, ba Yàllay doora sos àddina ba tey, te dootul am mukk.
20 Had the Sovereign not shortened those days, no one would survive; but the Sovereign shortened them for the elect he chose. Te bu Boroom bi wàññiwul woon àppu jant yooyu, kenn du mucc, waaye tànnéefam ñi mu tànn, ñoo tax mu wàññi janti coono ya.
21 Then if anyone tells you, 'Look, here is the Christ!' or 'Look, there!' don't believe it. «Su booba nag, ku leen ne: “Xoolal, Almasi baa ngi nii,” mbaa: “Xoolal, ma nga nee,” buleen ko gëm,
22 False christs and false prophets will appear, performing signs and wonders to deceive the elect, if possible. ndax ay almasiy caaxaan ak yonenti caaxaan ñooy feeñ, di jëfe ay firnde aki kéemaan, di wuta nax ñi ñu tànn, ndegam man naa nekk.
23 So be on your guard; I have told you everything ahead of time. Yeen nag, moytuleen, wax naa leen lépp, ba noppi.»
24 But in those days, after that suffering, the sun will darken, and the moon will not give its light; Yeesu neeti: «Te fan yooya, gannaaw coono ba, “jant bi day lëndëm, weer wi fey ag leeram,
25 the stars will fall from the sky, and the powers in the heavens will be shaken. biddiiw yi xàwweekoo asamaan, doole ya fa asamaan sàqi.”
26 Then they will see the Son of Man coming in clouds with great power and glory. «Su boobaa dees na gis Doomu nit kiy ñëw ci ay niir, ànd ak manoore ju réy ak daraja.
27 He will send his angels and gather his chosen from the four winds, from earth's ends to heaven's ends. Su ko defee mu yebal malaaka yi, ñu dajalee ay tànnéefam fa ñeenti jëmuy ngelaw li, dale ko ca catu kaw suuf, ba ca catu asamaan.»
28 Learn this from the fig tree: once its branch softens and leaves sprout, you know summer is near. Yeesu teg ca ne: «Jàngatleen misaalu garabu figg. Ag figg, bu bànqaas ya duyee, xob ya di sëq, ngeen xam ne nawet jubsi na.
29 So also, when you see these things happening, know it's near, at the door. Bu ngeen gisee xew-xew yooyu sotti, noonu itam ngeen di xame ne bés bi jubsi na, ba agsi ci bunt bi sax.
30 Truly I tell you, this generation will certainly not pass away until all these things have happened. Maa leen ko wax déy, niti tey jii duñu wéy mukk, te loolu lépp sottiwul.
31 Heaven and earth will pass away, but my words will never pass away. Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.
32 But no one knows that day or hour—not the angels in heaven, not the Son, only the Father. «Waaye bés boobu mbaa waxtu wa nag, kenn xamu ko; du malaaka ya fa asamaan, du Doom ji, xanaa Baay bi doŋŋ.
33 Be on guard! Stay alert! For you do not know when that time will come. Moytuleen te teewlu, ndax xamuleen kañ la.
34 Like a man on a journey: he leaves his house, gives his servants authority—each his own task—and orders the doorkeeper to stay alert. Daa mel ni nit ku tukki, bàyyi këram gannaaw. Fekk na mu batale ay surgaam, ku nekk ak saw sas. Bëkk-néeg bi nag, mu sant ko ne ko mu teewlu.
35 So stay alert, since you don't know when the master of the house comes—evening, midnight, rooster's crow, or dawn. Kon teewluleen, ndax xamuleen kañ la boroom kër giy dikk. Jombul muy ngoonug suuf, mbaa xaaju guddi, mbaa bu ganaar sabee, mbaa bu bët setee.
36 Otherwise, if he comes suddenly, he may find you sleeping. Bumu ne jalañ, fekk leen ciy nelaw.
37 What I say to you, I say to everyone: Keep watch!" Lii ma leen wax nag, ñépp laa ko wax: “Teewluleen!”»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]