1Two days before Passover and Unleavened Bread, the chief priests and scribes were looking for a way to seize Jesus by trickery and kill him.RWBTMàggalu bésub Mucc ba ak màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir a jubsi woon, ba des ñaari fan. Ci kaw loolu sarxalkat yu mag ya ak firikati yoonu Musaa ya di wut nu ñu sàcce ba jàpp Yeesu, reylu ko.
2For they said, "Not during the feast, or the people might riot."RWBTNdax booba dañu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, lu ko moy askan wi yëngu.»
3While he was in Bethany, in Simon the leper's house, reclining at the table, a woman came with an alabaster flask of pure nard perfume, very costly. She broke the flask and poured it on his head.RWBTCi biir loolu Yeesu demoon na dëkk ba ñuy wax Betani. Mu dale kër ku ñuy wax Simoŋ gaana ga. As ndaw dikk, fekk ko muy lekk. Ndaw saa nga yor njaqal doju albatar lu def diwu nàrd gu xeeñ lu neex te raxul, tey jar lu baree bare. Mu toj njaq li, daldi sotti diw gi ci boppu Yeesu.
4There were some who said to themselves indignantly, "Why was this perfume wasted like that?RWBTÑenn ca ña mu fa fekk nag ñaawlu loolu. Ñuy xultu ci seen biir naan: «Ana lu waral yàq gii lajkoloñ?
5For this perfume could have sold for over 300 denarii and given to the poor." And they scolded her.RWBTGii diw maneesoon na koo jaaye lu tollook ñetti téeméeri poseti xaalis, jox ko néew-doole yi.» Ñu sikk ca ndaw sa lool.
6But Jesus said, "Leave her alone. Why trouble her? She has done a beautiful thing for me.RWBTYeesu nag ne leen: «Bàyyileen ndaw si, ana lu ngeen koy sonale? Jëf ju rafet la ma defal.
7For the poor are always with you, and you can do good for them whenever you want; but you won't always have me.RWBTNéew-doole yi de, dingeen ci am ñu nekk ak yeen ba fàww, te saa yu leen neexee, man ngeen leena defal lu baax. Waaye man de, amuleen ma ba fàww.
8She has done what she could; she has anointed my body beforehand for burial.RWBTNdaw si, li mu man, def na ko. Laata ñu may rob, diw na ma lu xeeñ.
9Truly, I tell you, wherever the gospel is preached worldwide, what she did will be told in memory of her."RWBTTe maa leen ko wax déy, li ndaw sii def, fépp fu ñuy yéeneji ëllëg xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dees na ko fa nettalee, di ko fàttalikoo jëmmu ndaw si.»
10Then Judas Iscariot, one of the twelve, went to the chief priests to betray Jesus to them.RWBTCi biir loolu kenn ca Fukk ñaak ñaar, ñu di ko wax Yuda Iskaryo, daldi dem ca sarxalkat yu mag ya, ngir teg Yeesu ci seeni loxo.
11Hearing this, they were glad and promised him money. So he looked for a chance to betray Jesus.RWBTBa sarxalkat yu mag ya déggee lu doon tànki Yuda Iskaryo, dañu caa bég, ba dig ko xaalis. Muy seet nag yoon wu mu jekkoo Yeesu, ba wor ko.
12On the first day of Unleavened Bread, when they sacrificed the Passover lamb, his disciples asked him, "Where do you want us to go and prepare for you to eat the Passover?"RWBTCa bés ba njëkk ca màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir, ñu war caa rendi gàttub bésub Mucc, ca la taalibe ya laaj Yeesu, ne ko: «Foo bëgg, nu dem, waajalal la fa reeru bésub Mucc bi?»
13He sent two of his disciples, "Go into the city; a man carrying a jar of water will meet you. Follow him,RWBTYeesu nag yebal ñaar ca taalibe ya, ne leen: «Demleen ca dëkk ba, dina am waa ju dajeek yeen. Ma nga yenu njaqas ndox, toppleen ko.
14and wherever he enters, tell the house's owner, 'The Teacher says: Where is my guest room, where I may eat the Passover with my disciples?'RWBTKër gu mu mana dugg, neleen boroom kër ga: “Kilifa gi nee: Ana néegu gan, fi may reere reeru bésub Mucc, maak samay taalibe?”
15And he will show you a large upper room furnished and ready; there prepare for us."RWBTKooku moo leen di won néegub kaw bu yaa, bu ñu defar ba mu jekk. Foofa ngeen nuy waajale.»
16The disciples left, went to the city, found things as he had told them, and prepared the Passover.RWBTBa taalibe ya demee ba àgg ca biir dëkk ba it, noonu lañu gise la mu leen waxoon. Ñu daldi waajal reeru bésub Mucc ba.
17And when it was evening, Jesus came with the twelve.RWBTBa jant sowee, Yeesu dikk, ànd ak Fukk ñaak ñaar.
18While they reclined and ate, Jesus said, "Truly, I tell you, one of you will betray me, one eating with me."RWBTGannaaw ba ñu toogee bay reer, Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, kenn ci yeen ñiy lekkandoo ak man, moo may wor.»
19They began to grieve and ask him, one by one, "Is it I?"RWBTAw tiis nag jàpp taalibe ya, ñu kenn-kennoo di laaj, naan: «Mbaa du man?»
20He said to them, "One of the twelve, dipping bread with me into the dish.RWBTMu ne leen: «Yeen Fukk ak ñaar ñii daal, kenn la ci, te mu ngi yebandoo ak man loxoom ci ndab li.
21The Son of Man goes as the Scriptures said about him, but how terrible for that man who betrays him—better if he had never been born."RWBTDoomu nit kaa ngi dem moos, noonee ñu ko binde woon, waaye wóoy ngalla ki pexe mi ñu wore Doomu nit ki di jaare! Kooka de, bañoona juddu sax moo doon gën ci moom.»
22As they ate, he took bread, blessed it, broke it, gave it to them, and said, "Take; this is my body."RWBTNaka ñuy lekk, Yeesu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg, jox leen, daldi ne: «Jëlleen, lii sama yaram la.»
23He took a cup, gave thanks, gave it to them, and they all drank from it.RWBTMu teg ca jël ab kaas, yékkati kàddug cant, jox leen, ñépp naan ca.
24He said to them, "This is my blood of the covenant, poured out for many.RWBTMu ne leen: «Lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te nara tuurul ñépp.
25Truly I tell you, I will not drink wine again until that day when I drink it new in the kingdom of our Father."RWBTMaa leen ko wax déy, dootuma naan mukk ndoxum reseñ, ba kera ma naan ko bees ca nguurug Yàlla.»
26And when they had sung a hymn, they went out to the Mount of Olives.RWBTBa loolu amee ñu yékkati galanu cant, daldi génn jëm tundu Oliw ya.
27Jesus said to them, "You will all stumble, for it's written: 'I will strike the shepherd, and the sheep will be scattered.'RWBTYeesu nag ne leen: «Yeen ñépp ay dellu gannaaw, ndax bindees na ne: “Maay dóor sàmm bi, xar yi tasaaroo.”
28But after I am raised up, I will go ahead of you to Galilee."RWBTWaaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji fa Galile.»
29Peter said to him, "Even though they all fall away, I will not."RWBTPiyeer nag ne ko: «Bu ñépp dellu woon gannaaw it, man duma dellu gannaaw mukk.»
30Jesus said to him, "Truly I tell you, today, this night, before the rooster crows twice, you will deny me three times."RWBTYeesu ne ko: «Maa la ko wax déy, yaw, guddig tey jii, bala ganaar a sab ñaari yoon, dinga ma jàmbu ñetti yoon.»
31But he insisted, "Even if I must die with you, I will never deny you." They all said the same.RWBTPiyeer nag gënatee biral, ne: «Su ma naree ànd ak yaw dee sax déy, duma la jàmbu mukk.» Taalibe ya ca des yépp nag waxe noonu, ñoom itam.
32They arrived at a place called Gethsemane, and he told his disciples, "Sit here while I pray."RWBTÑu dem ba tollook tool ba ñu dippee Setsemane. Yeesu ne taalibe ya: «Toogleen fii, xaar ma, ma ñaani.»
33He took Peter, James, and John, and began to feel deep distress and anguish.RWBTCi kaw loolu mu ànd ak Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan. Tiitaange ak njàqare daldi koy jàpp.
34He said to them, "My soul is crushed with grief, to death. Stay here and stay alert."RWBTMu ne leen: «Tiis wuy rey la sama xol fees, ba may bëgga dee! Toogleen fii te ngeen teewlu.»
35Going a little farther, he fell to the ground and prayed that, if possible, the hour would pass from him.RWBTBa loolu amee Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf, di ñaan ngir, ndegam man naa am, coonob waxtu wa mu dëgmal teggi ko.
36He said, "Abba, Father, all things are possible for you. Take this cup from me—but let it be your will, not mine."RWBTMu ne: «Abba, Baay, yaw mi dara tëwul, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Waaye bumuy sama coobare, nay doon ci sa coobare.»
37He returned, found them asleep, and said to Peter, "Simon, are you asleep? Couldn't you stay awake one hour?RWBTGannaaw loolu mu délsi, fekk taalibe ya di nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangay nelaw? Wenn waxtu doŋŋ, amuloo dooley teewlu ko?
38Watch and pray, so you don't fall into temptation. The spirit is willing, but the flesh is weak."RWBTTeewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»
39And again he went away and prayed, saying the same words.RWBTYeesu demaat ba nee, daldi baamtu kàddug ñaanam ga.
40Again he found them sleeping, eyes heavy, not knowing how to answer him.RWBTMu délsiwaat, fekk leen ñuy nelaw, manatuñoo xippi ndax ngëmment lu réy. Xamuñu nag lu ñuy wax.
41He came a third time and said, "Still sleeping and resting? Enough—the hour has come. Look, the Son of Man is handed over into the hands of sinners.RWBTGannaaw loolu mu délsiwaat ñetteel bi yoon, daldi ne leen: «Yeena ngi nelaw, di noppalu ba tey? Jeex na nag. Waxtu wi dikk na. Ñu ngi nii di teg Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi.
42Rise, let us be going; see, my betrayer is here."RWBTJógleen, nu dem. Ki may wor a ngi nii.»
43While he was still speaking, Judas—one of the twelve—arrived, and with him a crowd with swords and clubs from the chief priests, scribes, and elders.RWBTNaka la Yeesu di wax, daaneelagul, Yuda, kenn ca Fukk ñaak ñaar dikk, ànd ak gàngoor gu bawoo ca sarxalkat yu mag yaak firikati yoonu Musaa yaak magi askan wa. Ña nga gànnaayoo ay saamar aki njur.
44His betrayer had given them a signal: "The one I kiss is him—seize him and take him away securely."RWBTFekk na workat ba tegtal leen, ne leen: «Ki may fóon, kooku la; jàppleen ko, yóbbu te wattu ko bu baax.»
45He came up to Jesus at once, said, "Rabbi!" and kissed him.RWBTMu daldi agsi, dikk ba ci Yeesu, ne ko: «Kilifa gi!», daldi ko fóon.
46And they laid hands on him and seized him.RWBTBa mu ko defee nit ña ne ko taral, jàpp ko.
47One of the bystanders drew his sword, struck the high priest's servant, and cut off his ear.RWBTBa loolu amee kenn ca ña fa taxaw bocci ab saamar, caw ko surgab sarxalkat bu mag ba, njoof nopp ba.
48Jesus said to them, "Have you come out with swords and clubs to seize me, like a robber?RWBTYeesu ne leen: «Jàppsi ma doŋŋ a leen taxa dikkey saamar aki njur, mel ni ñuy topp ab fippukat?
49Every day I was with you in the temple teaching, and you didn't arrest me. But let the Scriptures be fulfilled."RWBTMoona bés bu nekk maa nga woon ak yeen ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma. Waaye lii daa am ngir sottal Mbind mi.»
50And they all left him and fled.RWBTCi kaw loolu, ñépp daw, wacc ko.
51And a young man followed him, wearing nothing but a linen cloth. And they seized the young man,RWBTAb xale bu góor a nga ko toppoon, lëkkaayoo ab malaan kese. Ñu daldi ko jàpp.
52but he left the linen cloth and ran away naked.RWBTXale bu góor ba nag, ne wëqét, daw, wacc fa malaan ma, def yaramu neen.
53They led Jesus to the high priest, and all the chief priests and elders and scribes gathered.RWBTBa loolu amee ñu yóbbu Yeesu ca sarxalkat bu mag ba, yeneen sarxalkat yu mag yaak magi askan waak firikati yoonu Musaa ya, ñépp daje fa.
54Peter had followed at a distance, all the way into the high priest's courtyard, and sat with the guards, warming himself by the fire.RWBTCi biir loolu Piyeer yoxal Yeesu lu sore, topp ca gannaawam, ba ca biir ëttu sarxalkat bu mag ba. Mu toog faak wattukat ya, di jaaru ca taal ba.
55The chief priests and the whole council sought testimony against Jesus to put him to death, but found none.RWBTCi kaw loolu sarxalkat yu mag yaak mboolem kuréelu àttekati Yawut ya di wut kàddug seede gu ñu tuumaale Yeesu, ba ñu man koo reylu, te amuñu ko.
56For many gave false testimony against him, but their testimony did not agree.RWBTTeewul ñu baree dikk, seedeel Yeesu ay fen, waaye seen kàddu yaa woroo.
57And some stood up and gave false testimony against him, saying,RWBTCi biir loolu ñenn ña jóg, seedeel ko ay fen, daldi ne:
58"We heard him say, 'I will destroy this temple made by hands, and in three days build another not made by hands.'"RWBT«Nun de dégg nanu, mu ne: “Kër Yàlla gii loxol nit liggéey, maa koy toj, tabaxaat ci ñetti fan geneen kër Yàlla gu loxol nit liggéeyul.”»
59Yet even about this their testimony did not agree.RWBTKàdduy ñooña nag woroo ba tey.
60The high priest stood up in the midst and asked Jesus, "You have no answer? What are these men testifying against you?"RWBTBa mu ko defee sarxalkat bu mag ba jóg taxaw ca digg mbooloo ma. Mu ne Yeesu: «Doo tontu dara ci li la ñii tuumaal?»
61He stayed silent, answered nothing. Again the high priest asked him, "Are you the Christ, the Son of the Blessed?"RWBTYeesu ne cell, waxul dara. Sarxalkat bu mag ba dellu ne ko: «Ndax yaa di Almasi bi, Doomu Ki yelloo màggal?»
62Jesus said, "I AM, and you will see the Son of Man seated at the right hand of the Mighty One and coming with heaven's clouds."RWBTYeesu ne ko: «Man mii la, te dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Boroom Kàttan gi, dingeen ko gis itam ci biir niir yi, muy ñëw.»
63And the high priest tore his clothes and said, "What further witnesses do we need?RWBTSarxalkat bu mag nag ne tareet yérey boppam, daldi ne: «Ana lu nuy doyeeti ay seede?
64You have heard his blasphemy. What is your decision?" And they all condemned him as deserving death.RWBTYeena dégg ni mu diire Yàlla mbagg! Lu ngeen ci xam nag?» Ñépp ne dee mooy àtteem.
65Some began spitting on him, covering his face, and punching him, saying to him, "Prophesy!" Then the guards slapped him.RWBTCi kaw loolu ñenn ña tàmbali koo tifli, muur kanam gi, dóor ko ay këmëx, naan ko: «Yaw waxal nu kàdduy waxyu boog!» Wattukat yi daldi ko jàpp, dóor ko ay mbej.
66While Peter was below in the courtyard, one of the high priest's servant girls came,RWBTCi biir loolu Piyeer a nga woon ca suuf, ca ëtt ba. Benn surga bu jigéen bu sarxalkat bu mag ba romb fa.
67seeing Peter warming himself, she looked at him and said, "You too were with the Nazarene, Jesus."RWBTNaka la gis Piyeer muy jaaru, mu xool ko jàkk, ne ko: «Yaw itam yaak Yeesum Nasaret a àndoon.»
68But he denied it: "I don't know or understand what you mean." Then he went out to the entrance, and a rooster crowed.RWBTPiyeer nag miim ko, ne ko: «Man de, yéguma, xawma dara ci li ngay wax.» Piyeer daldi génn, ba ca mbaaru bunt ba ca biti.
69The servant girl saw him and again told the bystanders, "This man is one of them."RWBTSurga bu jigéen ba gisati ko dellu ne ña fa taxaw: «Kii ci ñoom la bokk!»
70But he denied it again. A little later the bystanders again told Peter, "You truly are one of them, for you're a Galilean."RWBTMu dellu miim ko. Nes tuut ña fa taxaw ñoom it, ne Piyeer: «Yaw itam kay ci ñoom nga bokk, nde yaw itam waa Galile nga.»
71He began to call down curses on himself and swear, "I don't know this man you're talking about."RWBTPiyeer di tàmbalee waat aka giñ ne: «Ki ngeen di wax, man xawma ko!»
72At once a rooster crowed a second time. Peter remembered Jesus' words: "Before the rooster crows twice, you will deny me three times." He broke down and wept.RWBTCa saa sa ganaar sab ñaareel bi yoon. Piyeer nag fàttaliku la ko Yeesu waxoon, ne ko: «Bala ganaar a sab ñaari yoon, dinga ma jàmbu ñetti yoon.» Mu ne yikkét, jooy.