Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Mark 15 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 At dawn the chief priests, elders, scribes, and the whole council consulted together, bound Jesus, led him away, and handed him over to Pilate. Ca ëllëg sa, suba teel sarxalkat yu mag ya féncoo, ñoom ak magi askan wa ak firikati yoonu Musaa ya, ak mboolem kuréelu àttekatu Yawut ya. Ñu yeew Yeesu, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat.
2 Pilate asked him, "Are you the King of the Jews?" "You say so," Jesus replied. Pilaat nag laaj ko, ne ko: «Yaw yaa di buurub Yawut yi?» Yeesu ne ko: «Yaa ko wax.»
3 The chief priests kept accusing him of many things. Sarxalkat yu mag yi nag tuumaal ko lu bare.
4 So Pilate questioned him again: "Have you no answer? See how many charges they bring against you." Pilaat dellu ko laaj, ne ko: «Doo tontu dara? Déggal li ñu lay jiiñ lépp.»
5 But Jesus said nothing more, and Pilate was amazed. Yeesu nag tontuwul dara, ba tax Pilaat jaaxle.
6 Now at the festival, Pilate used to release one prisoner for them—whoever they asked for. Fekk na màggal gu nekkaan, Pilaat daan na maye ca ña ñu tëj kaso, kenn nit ku ñu sàkku, mu bàyyil leen kooka.
7 A man called Barabbas was in prison with the rebels who had committed murder during the uprising. Fekk na ñu tëj ca kaso ba, ku ñuy wax Barabas, mook ay fippukat yu bóomoon nit ci ab yëngu-yëngal.
8 The crowd came up and began asking Pilate to do for them what he always did. Ci kaw loolu mbooloo ma dikk, di sàkku Pilaat defal leen la mu leen daan defal.
9 "Do you want me to release for you the King of the Jews?" Pilate answered, Pilaat ne leen: «Lu ngeen bëgg? Ma bàyyi buurub Yawut yi?»
10 for he knew it was out of envy that the chief priests had handed him over. Booba xam na xéll ne kiñaan a tax sarxalkat yu mag ya jàpplu Yeesu.
11 But the chief priests stirred up the crowd to have him release Barabbas for them instead. Waaye sarxalkat yu mag ya ñaax mbooloo ma ba ñu ne Pilaat: «Yiwil nu Barabas.»
12 "So what do you want me to do with the one you call King of the Jews?" Pilate asked them again. Pilaat dellu ne leen: «Lu ngeen bëgg nag, ma def ko kii ngeen di wax buurub Yawut yi?»
13 Crucify him!" they shouted back. Ñu dellu xaacoondoo ca kaw, ne: «Daaj ko ci bant!»
14 "Why? What evil has he done?" Pilate asked. But they shouted all the louder, "Crucify him!" Pilaat ne leen: «Lu tax? Ana lu bon lu mu def?» Mbooloo ma gëna xaacooti, ne: «Daaj ko ci bant!»
15 To satisfy the crowd, Pilate released Barabbas to them. He had Jesus flogged, and handed him over to be crucified. Pilaat nag bëgg lu neex mbooloo ma, ba tax mu bàyyi Barabas. Mu cawlu Yeesu ay kàcciri, ba noppi teg ko ciy loxo, ngir ñu daaj ko ci bant.
16 Soldiers led him away into the palace (the governor's headquarters) and called together the whole company of soldiers. Takk-deri Room ya nag dugal Yeesu ca ëttu kër boroom réew wa, daldi woo gàngoor ga gépp,
17 They dressed him in purple, twisted together a crown of thorns, and set it on him. ñu solal ko mbubb mu xonq curr, teg ci boppam kaala gu ñu ràbbe ay dég.
18 And they began to salute him: "Hail, King of the Jews!" Ña nga koy nuyu, naan: «Buuru Yawut yée, guddaluw fan!»
19 They kept beating his head with a staff, spat on him, and knelt in mock homage to him. di ko dóor aw yet ci bopp, di ko tifli, di ko sukkal.
20 After mocking him, they stripped off the purple and put his own clothes on him, then led him out to crucify him. Ba ñu ko ñaawalee ba noppi, dañoo summi mbubb mu xonq ma, solal ko ay yéreem, door koo yóbbu, ngir ñu daaj ko ci bant.
21 They forced a passerby coming from the countryside—Simon of Cyrene, father of Alexander and Rufus—to carry his cross. Ci biir loolu jenn waay ju ñuy wax Simoŋ, dëkke fu ñu naan Siren jóge ca tool ya, jaare fa. Muy baayu Alegsàndar ak Rufus. Moom lañu gàdduloo bant ba.
22 They brought Jesus to the place called Golgotha (which means Place of a Skull). Ñu yóbbu Yeesu ca béreb ba ñuy wax Golgota, muy firi bérebu Kaaŋu bopp.
23 They offered him wine mixed with myrrh, but he did not take it. Ñu bëgg koo nàndale biiñ bu ñu jaxaseek safal bu ñuy wax miir, mu bañ.
24 They crucified him. They divided his clothes among them, casting lots for what each would get. Ba mu ko defee ñu daaj Yeesu ca bant ba, ba noppi séddoo ay yéreem, tegoo ko bant, ngir xam lu ca ku nekk di am.
25 It was nine in the morning when they crucified him. Ca yoor-yoor lañu daaj Yeesu ci bant, yemook juróom ñeenti waxtu.
26 The written notice of the charge against him read: THE KING OF THE JEWS. Lii lañu bind ne moo di tuumaam ja ko daanlu: «Kii mooy Buurub Yawut yi.»
27-28 They crucified two rebels with him, one on his right and one on his left. Ñaari fippukat lañu daajaaleek Yeesu ci ay bant, kenn ki ci ndijooram, ki ci des ci càmmoñam.
29 Those passing by insulted him, shaking their heads, saying, "Ha! You who tear down the temple and build it in three days, Ña fa jaare nag di ko saaga, aka wëcc bopp, naan: «Acam, yaw miy toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan,
30 save yourself and come down from the cross!" wàccal bant bi, musal sa bopp boog!»
31 Likewise the chief priests and scribes mocked him among themselves: "He saved others; himself he can't save. Sarxalkat yu mag ya it naka noonu, ñook firikati yoonu Musaa ya. Ñu di ko ñaawal ci seen biir, naan: «Moom day musle te manul musal sax boppam.
32 Let the Christ, King of Israel, come down from the cross now, so we can see and believe." Those crucified with him also insulted him. Na Almasi bi, buurub Israayil wàcc bant bi léegi, nu gis ba gëm.» Ci biir loolu ña ñu daajaale ak moom itam di ko tifaare ay saaga.
33 At noon, darkness came over the whole land until three in the afternoon. Ba fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg jotee, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
34 At three in the afternoon Jesus cried out loudly, "Eloi, Eloi, lema sabachthani?" meaning, "My God, my God, why have you forsaken me?" Ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon jotee, Yeesu àddu ca kaw, ne: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» muy firi: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma?»
35 When some of those standing nearby heard this, they said, "Listen, he's calling Elijah." Ñenn ca ña ko teewe, dégg ca, ne: «Déggal, Yonent Yàlla Ilyaas lay woo.»
36 One ran, filled a sponge with sour wine, put it on a reed, and gave him a drink. "Let him be," he said, "let's see if Elijah comes to take him down." Mu am ku daw, jël ab sagar, xooj ko ci bineegar, lonk ko ci bant, tàllal ko ko, ngir mu naan, te ne: «Bàyyileen, nu seet, ndax Ilyaas ay ñëw, wàcce ko.»
37 With a loud cry, Jesus breathed his last. Yeesu nag yuuxu, daldi dog.
38 And the curtain of the temple was torn in two from top to bottom. Ba mu ko defee ridob biir néegu Yàlla ba xar ñaar, dale ca kaw ba ca suuf.
39 The centurion facing Jesus saw how he breathed his last and said, "Truly this man was the Son of God." Njiitu takk-der ba taxawoon ca kanam Yeesu nag gis, na Yeesu doge. Mu ne: «Aylayéwén, waa jii mooy Doomu Yàlla!»
40 Women were also watching from a distance, including Mary Magdalene, Mary the mother of James the younger and Joses, and Salome. Ay jigéen a nga fa woon, dànd leen lu sore, di seetaan. Maryaama ma dëkk Magdala ca la bokk, ak Maryaama yaayu Yanqóoba mu ndaw ak Yose, ak ndaw seneen su ñuy wax Salome.
41 These women had followed him in Galilee and served him; many others who came up with him to Jerusalem were also there. Ba Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñoo ko toppoon, di ko toppatoo. Ñeneen jigéen ñu baree nga ca woon, di ñu àndoon ak Yeesu, ba dikk Yerusalem.
42 Evening had come, and since it was Preparation Day—the day before the Sabbath. Loolu lépp bésub Waajal ba la xewe, ëllëg sa di bésub Noflaay. Ca ngoon sa,
43 Joseph of Arimathea, a prominent council member who himself was waiting for the kingdom of our Father, dared to go to Pilate and ask for Jesus' body. ku ñuy wax Yuusufa te dëkk Arimate, daldi takk aw fitam, dem ca Pilaat, sàkku ci moom, mu jox ko néewub Yeesu. Yuusufa moomu, ku ñu nawloo la woon ca kuréelu àttekati Yawut ya. Bokkoon na moom itam ca ña doon séentu nguurug Yàlla.
44 Pilate was surprised he was already dead; summoning the centurion, he asked if Jesus had been dead long. Ba Pilaat déggee ne Yeesu faatu na xaat, am na mbetteel. Mu woolu nag njiitu takk-der ya, laaj ko, ndax yàgg naa faatu.
45 When he learned from the centurion that it was so, he granted the body to Joseph. Bi ko njiit la waxee, Pilaat may Yuusufa mu jël néew ba.
46 Joseph bought linen, took the body down, wrapped it in the cloth, and laid it in a tomb cut from rock. Then he rolled a stone against the tomb's entrance. Fekk na Yuusufa jënd càngaayal lẽe. Mu wàcce néew ba, sàng ko ca, denc ko ci bàmmeel bu ñu yatt ciw doj. Ba mu ko defee Yuusufa béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel ba.
47 Mary Magdalene and Mary the mother of Joses saw where he was laid. Ci biir loolu Maryaama ma dëkk Magdala, ak Maryaama yaayu Yose ña ngay xool fa ñu denc néew ba.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]