Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Malachi 4 RWBT

Side by side with the Father's Heart Bible™

3:19Bés ba déy a ngii di ñëw,di tàkk ni taal bu yànj.Képp ku bew ak kuy def lu bon,ca lay mel ni boob,te bésub keroog baa koy jafal,»Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,«du leen waccal tus, dub reen, dub car.

3:20Waaye yeen ñi ma ragalla jantub njub di fenkal,leerale leen ceeñeer yuy wéral,ngeen génn di tëbantu ni ay sëlluy yar.

3:21Yeenay joggi ñu bon ñi,ñu doon pënd fi seen ron téstën,keroog bés ba may jëfi,»Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

3:22«Bàyyileen xel ci yoonu Musaa, sama jaam ba,yoon wa ma ko dénkoon fa tundu Xoreb,ñeel Israayil gépp,mu diy dogal ak àttey yoon.

3:23Maa ngii di yebal ci yeen, Ilyaas yonent bi,balaa bésub Aji Sax jee teew,di lu màgg te raglu.

3:24Mooy delloo xolu baay ca doom ja,delloo xolu doom ca baay ba,lu ko moy ma dikk duma réew mi, ba faagaagal ko.»

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]