Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 12 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Six days before Passover, Jesus came to Bethany, where Lazarus, whom Jesus raised from death, lived. Ba màggalu bésub Mucc desee juróom benni fan, ca la Yeesu dikk ba Betani, dëkkub Lasaar ma mu dekkal.
2 There they gave him a dinner; Martha served, and Lazarus was one of those at the table with him. Ñu toggal fa Yeesu ab reer. Màrt moo taaj, Lasaar di kenn ca ña bokk ak Yeesu ndab.
3 Mary took about a pint of pure nard perfume, expensive, and anointed Jesus' feet, then wiped his feet with her hair. The house filled with the fragrance of the perfume. Maryaama nag indi genn wàllu liitaru nàrd, diwu nàrd gu xeeñ lu neex te raxul te jafe njëg lool, sotti ko ca tànki Yeesu, daldi fomp tànk ya ak kawaru boppam. Kër ga gépp ne bann ak xetu diw ga.
4 But Judas Iscariot, one of his disciples, the one who was about to betray him, said, Teewul Yuda Iskaryo miy kenn ci taalibeem te doon ko waaja wor, daldi ne:
5 "Why was this perfume not sold for about a year's wages and given to the poor?" «Ana lu waral jaayeesul lajkoloñ jii lu tollook ñetti téeméeri poseti xaalis, ngir jox ko néew-doole yi?»
6 He said this not because he cared about the poor, but because he was a thief who kept the money box, taking what was put in it. Ba Yuda Iskaryo di wax loolu nag, du néew-doole yi lay xalaat, waaye ab sàcc la woon; dencub taalibe ya la yoroon, di yulli lu ñu ca def.
7 So Jesus said, "Leave her alone. She has kept this for the day of my burial. Teewul Yeesu ne ko: «Bàyyil Maryaama! Bés ba ñu may rob la fàggul lajkoloñ jii.
8 You will always have the poor among you, but you will not always have me." Néew-doole yi, dingeen ci am ñu nekk ak yeen ba fàww, waaye man amuleen ma ba fàww.»
9 A large crowd of Jews learned Jesus was there and came, not only for him but to see Lazarus, whom he had raised from the dead. Mbooloom Yawut mu réy a dikk ba ñu yégee ne Yeesoo nga fa, te Yeesu rekk yóbbuwu leen fa, waaye dañoo bëggoona gisaale Lasaar ma Yeesu dekkaloon.
10 So the chief priests planned to kill Lazarus as well, Sarxalkat yu mag ya nag dogu, nara rey Lasaar itam,
11 because on account of him many of the Jews were going over and believing in Jesus. ndax moo waraloon Yawut yu bare dem, dëddu leen, gëm Yeesu.
12 The next day, the large crowd that came for the feast heard Jesus was coming to Jerusalem. Ca ëllëg sa mbooloo mu bare ma dikk ca màggalu bésub Mucc ba ca Yerusalem, dañoo yég ne Yeesoo ngay ñëw.
13 They took palm branches and went out to meet him, shouting, "Hosanna! Blessed is he who comes in the name of our Father—the King of Israel!" Ñu jël cari garab yu ñu koy lalal, daldi génn gatanduji ko. Ña ngay xaacu naan: «Osaana! Na barke wàcc ci ki dikk ci turu Boroom bi, na barke wàcc ci buurub Israayil!»
14 Jesus found a young donkey and rode on it, just as it is written: Yeesu waajal ag cumbur, war ko, noonu ñu ko binde woon, ne:
15 "Do not be afraid, daughter of Zion; look, your king is coming, seated on a donkey's colt." «Janq Siyoŋ mu taaru, bul tiit. Niiral, sa buur a la dikkal nii, am cumbur la war.»
16 His disciples didn't understand these things at first; but when Jesus was glorified, they remembered these things were written about him, and that they had done these things to him. Kàddu yooyu nag, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki, waaye ba Yeesu tàbbee ca darajaam, ca lañu fàttaliku ne loolu lañu bindoon ci moom, te loolu it lañu ko defal.
17 The crowd that was with him when he called Lazarus from the tomb and raised him from the dead kept testifying. Mbooloo ma daroon Yeesu, ba muy woo Lasaar, ba dekkal ko nag, di nettali la ñu fekke.
18 The crowd went to meet him because they heard he had done this sign. Moo tax itam mbooloo ma gatandu ko, ndax yégoon nañu ne googu kéemaan la def.
19 So the Pharisees said to each other, "See, you're accomplishing nothing—the whole world has gone after him." Farisen yi nag di waxante ci seen biir naan: «Xoolleen, dara ngeen ci manul; àddina yépp a ko topp!»
20 Now there were some Greeks among those who went up to worship at the feast. Ca mbooloo ma dikkoon jaamusi Yàlla ca Yerusalem ca màggal ga, ay Gereg ña nga ca woon.
21 These came to Philip, from Bethsaida in Galilee, and asked him, "Sir, we want to see Jesus." Ñooñoo dikk ba ca Filib ma dëkke Betsayda ca diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëgga gis Yeesu.»
22 Philip went and told Andrew; then Andrew and Philip went and told Jesus. Filib dem wax ko Àndre; Àndre ak Filib waxi ko Yeesu.
23 Jesus replied to them, "The hour has come for the Son of Man to be glorified. Yeesu wax leen ne leen: «Waxtu wi ñu wara darajaal Doomu nit ki jot na.
24 Truly, truly, I tell you, unless a wheat grain falls to the ground and dies, it stays alone; but if it dies, it bears much fruit. Maa leen ko wax déy ci lu wér, su feppu bele waddul ci suuf, dee, wéetaay lay dëkke. Waaye su deewee lay meññ fepp yu bare.
25 Whoever loves his life loses it; whoever hates his life in this world keeps it for eternal life. Képp ku bëgg bakkanam moo koy ñàkk; waaye ku bañ bakkanam ci àddina sii, moo musal bakkanam ba keroog muy texe ba fàww.
26 Whoever serves me must follow me, so my servant will be where I am. Whoever serves me, my Father will honor him." Ku may surgawu, na ma topp; fu ma nekk, sama surga ne fa moom itam. Ku ma surgawu nag, sama Baay moo koy teral.
27 "Now my soul is troubled. What should I say—'Father, save me from this hour'? But this is why I came to this hour. Father, glorify your name." «Léegi nag am naa njàqarey xol. Ana lu may wax? Dama naa: “Baay, musal ma ci coonob waxtu wii”? Waaye coonob waxtu wii tembe moo ma taxa dikk!
28 Then a voice came from heaven: "I have glorified it, and I will glorify it again." Baay, màggalal saw tur!» Ci kaw loolu baat dégtu ci asamaan, ne: «Maa koy màggal, màggalati ko.»
29 The crowd standing there heard it and said it thundered; others said an angel spoke to him. Mbooloo ma fa taxaw te dégg baat ba nag ne: «Yàlla jee dënu!» Ñeneen ña ne: «Am malaaka moo wax ak moom.»
30 Jesus said, "This voice came for your sake, not mine. Teewul Yeesu ne leen: «Baat boobu du maa tax mu jib, waaye yeena tax.
31 Now is the judgment of this world; now the ruler of this world will be cast out. Léegi nag àtteb àddina sii jot na; léegi lees di dàq ca biti kàngam li jiite àddina sii.
32 And I, when I am lifted up from the earth, will draw all people to myself." Man nag kera bu ñu ma yékkatee, jële ma fi kaw suuf, ñépp laay xëcc, jëme ci man.»
33 He said this to show by what kind of death he was going to die. Kàddu yooyu la misaale deewin wa mu naroona deewe.
34 The crowd replied, "We've heard from the Law that the Christ stays forever. How can you say the Son of Man must be lifted up? Who is this Son of Man?" Mbooloo ma ne ko: «Nun danoo dégge ci téereb yoonu Musaa bi ne Almasi bi day sax ba fàww. Kon yaw, noo mane ne: “Fàww dees na yékkati Doomu nit ki?” Doomu nit kooku mooy kan sax?»
35 So Jesus said, "The light is with you a little while longer. Walk while you have light, so darkness doesn't overtake you. Whoever walks in darkness doesn't know where he's going. Yeesu ne leen: «Leer gaa ngeegum ci seen biir ci diggante bu gàtt. Doxleen ci bi ngeen di am leer, ngir lëndëm bañ leena bett. Kuy doxe ag lëndëm, xamoo foo jëm.
36 While you have light, believe in the light, so you become children of light." Having said this, Jesus left and hid from them. Gëmleen ko ci bi ngeen di am leer, ngir ngeen doon doomi leer.» Loolu la Yeesu wax, daldi dem làquji leen.
37 Though he had performed so many signs in their presence, they still would not believe in him, Firnde yu bare la def ci seen kanam te taxul ñu gëm ko,
38 so that the word of Isaiah the prophet would be fulfilled, which he spoke: "Father, who has believed our message? And to whom has the arm of our Father been revealed?" te noonu la kàddug Yonent Yàlla Esayi sottee. Mooy ba mu nee: «Boroom bi, ana ku gëm sunub dégtal? Dooley loxol Boroom bi, ana ku mu ko won?»
39 This is why they could not believe, for Isaiah said again: Manuñu woona gëm it, ndax Esayee neeti:
40 "He has blinded their eyes and hardened their heart, so that they would not see with their eyes, nor understand with their heart, nor turn—and I would heal them." «Yàllaa gumbaal seeni gët, tëj seenum xel, ngir seeni gët du gis, seenum xel du xam, ngir ñu baña dëpp, ba ma wéral leen.»
41 Isaiah said these things because he saw Jesus' glory and spoke about him. Loolu Esayee ko wax, ndax moo gisoon darajay Yeesu, bay wax ci mbiram.
42 Still, many even of the rulers believed in him, but they didn't admit it because of the Pharisees, so they wouldn't be expelled from the synagogue, Teewul sax ñu bare ci njiiti Yawut yi gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee taxoon biraluñu seen ngëm, ndax ragal ñu dàqe leen ca jàngu Yawut ba,
43 for they loved the glory that comes from people more than the glory that comes from our Father. ndax ngërëmal nit ñi moo leen gënaloon ngërëmal Yàlla.
44 Jesus cried out, "Whoever believes in me does not believe in me only, but in the one who sent me. Yeesu nag àddu ca kaw ne: «Ku ma gëm, du man nga gëm, waaye ki ma yónni nga gëm,
45 And whoever sees me sees the one who sent me. te ku ma gis, gis nga ki ma yónni.
46 I came into the world as light, so no one who believes in me stays in the darkness. Man maa dikk, di ag leer ci àddina, ngir ku ma gëm du des cig lëndëm.
47 If anyone hears my words and doesn't keep them, I don't judge him—I didn't come to judge the world, but to save the world. Ku dégg samay wax te toppu ko, du man maa koy daan, ndax daan àddina taxu maa dikk, waaye musal àddinaa ma taxa dikk.
48 Whoever rejects me and doesn't accept my words already has a judge: my spoken word will judge him on the last day. Ku ma xarab ba nanguwul samay wax, am na ab daan-katam: kàddu gi ma wax moo koy daan, keroog bés bu mujj ba.
49 I have not spoken on my own; but the Father who sent me himself commanded me what to say and how to speak. Ndax kat du ci sama coobarey bopp laay waxe, waaye Baay bi ma yónni, moom ci boppam moo ma sant li may dégtale ak li may wax.
50 I know his commandment is eternal life, so I say only what the Father told me to say." Te xam naa ne ab santaaneem moo dig texe gu sax dàkk. Moo tax it, li may wax man, ni ma ko Baay bi dégtale, ni laa koy waxe.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]