Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 13 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Now, before the Passover festival, Jesus knew his hour had come to leave this world to his Father. Having loved his own in the world, he loved them to the end. Balaa màggalu bésub Mucc baa dikk, Yeesu xamoon na ne waxtu wa muy bàyyikoo àddina, jëm fa Baay ba, jot na. Cofeelu Yeesu ak ñoñam ñi ci àddina, googu cofeel la leen sopp ba ca muj ga.
2 During supper, the devil had already put into Judas son of Simon Iscariot's heart the plan to betray Jesus. Ba Yeesu di bokk reer ak taalibe ya, fekk na Seytaane xiirtal Yuda, doomu Simoŋ Iskaryo, ci wor Yeesu.
3 Jesus, knowing that the Father had given everything into his hands, and that he had come from him and was returning to him, Yeesu xamoon na ne lépp la Baay bi teg ciy loxoom, te it ci Yàlla la jóge, te ci Yàlla la jëm.
4 rose from supper, took off his outer clothes, picked up a towel, and tied it around his waist. Mu jóge nag ca ndabal reer ba, summi mbubbam mu mag, daldi jël am malaan, laxasaayoo.
5 Then he poured water into a basin and began washing the disciples' feet, drying them with the towel tied around him. Gannaaw loolu mu sotti ndox cib këll, daldi tàmbalee raxas tànki taalibe ya, di fompe sér ba mu laxasaayoo.
6 He came to Simon Peter, who said to him, "Lord, are you going to wash my feet?" Ba mu agsee ba ca Simoŋ Piyeer, Piyeer ne ko: «Sang bi, yaw yaa may raxasal samay tànk?»
7 Jesus answered him, "You do not realize now what I am doing, but later you will understand." Yeesu ne ko: «Man li may def nii tey, xamuloo ko; waaye ëllëg dinga ko xam.»
8 "You will never wash my feet," Peter said. Jesus answered, "Unless I wash you, you share nothing with me." Piyeer ne ko: «Déedéet, doo ma raxasal samay tànk mukk kay!» Yeesu ne ko: «Su ma la raxasalul, doo am ci man benn cér.»
9 Simon Peter said to him, "Lord, not only my feet, but also my hands and head!" Simoŋ Piyeer ne ko: «Kon nag Sang bi, bumu doon samay tànk doŋŋ, waaye na ci loxo yeek bopp bi bokk far!»
10 Jesus told him, "One who has bathed needs only to wash his feet—he is fully clean. You are clean, but not all of you." Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatula raxas lu moy ay tànkam, ndax set na wecc. Yeen nag set ngeen, waaye du ñépp.»
11 He knew who would betray him; that's why he said, "Not all of you are clean." Booba Yeesu xam na ka koy wor, te looloo tax mu ne: «Du yeen ñépp a set.»
12 After washing their feet and dressing, he reclined again and said to them, "Do you understand what I have done for you? Gannaaw ba leen Yeesu raxasalee seeni tànk, teg ca solaat mbubbam, ba toogaat, da leen ne: «Xam ngeen li ma leen defal?
13 You call me Teacher and Lord, and rightly so, for that is what I am. Yeena ngi ma naa Kilifa gi ak Sang bi, te yeena yey, nde moom laa.
14 So if I, your Lord and Teacher, washed your feet, you too must wash each other's feet. Ndegam nag man miy Sang bi, di Kilifa gi maa leen raxasal seeni tànk, kon yeen itam war ngeen di raxasalante ay tànk.
15 For I have given you an example, that you should do as I have done for you. Ab misaalu royukaay laa leen jox, ngir ni ma leen defal, ngeen di ko def yeen itam.
16 Truly, truly, I say to you, a servant isn't greater than his master, nor a messenger greater than his sender. Maa leen ko wax déy ci lu wér, jaam sutul sangam, te ndaw sutul ka ko yónni.
17 If you know these things, you are blessed if you do them. Loolu, su ngeen ko xamee, ndokkalee yeen, ndegam yeena ngi koy jëfe.
18 "I don't mean all of you—I know those I've chosen. But Scripture must be fulfilled: 'The one eating my bread has raised his heel against me.' «Du yeen ñépp a tax may wax; man xam naa ñi ma tànn. Waaye Mbind mii fàww mu sotti: “Ki lekk samaw ñam moo ma wéq.”
19 I tell you now, before it happens, so you'll believe, once it happens, that I AM. Léegi laa leen koy dale wax, bala looloo dikk, ngir bu dikkee ngeen gëm ne maay Ki nekk.
20 Truly, truly, I tell you, whoever welcomes someone I send welcomes me, and whoever welcomes me welcomes the one who sent me." Maa leen ko wax déy, ci lu wér, ku dalal nit ku ma yónni, man nga dalal; te ku ma dalal, dalal nga ki ma yónni.»
21 After saying this, Jesus, troubled in spirit, testified, "Truly, truly, I tell you, one of you will betray me." Loolu la Yeesu wax ba noppi, njàqare dikkal ko, mu daldi biral ne: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, kenn ci yeen moo may wor.»
22 The disciples looked at one another, at a loss to know which of them he meant. Taalibe ya di xoolante, te xamuñu kan lay wax.
23 One of his disciples, the one Jesus loved, was reclining at his side. Booba kenn ca taalibe ya, di ku Yeesu soppoon, ma nga sóonu, sës rëkk ca Yeesu.
24 So Simon Peter motioned to him to ask which one Jesus meant. Kooku la Simoŋ Piyeer liyaar, ngir mu laaj Yeesu ka ko taxoon di wax.
25 Leaning back against Jesus, he asked him, "Lord, who is it?" Kooku sóonu ba tafu ca dënnub Yeesu, ne ko: «Sang bi, kooku kan la?»
26 Jesus answered, "It's the one I'll give this bread to, once I've dipped it." Then he dipped the bread and gave it to Judas, son of Simon Iscariot. Yeesu ne ko: «Mooy ki may jox, man ci sama bopp, dogu mburu bi may capp ci ndab li.» Yeesu nag jël dogu mburu, capp ko ca ndab la, jox ko Yuda, doomu Simoŋ Iskaryo.
27 After Judas took the bread, Satan entered into him. So Jesus told him, "Do quickly what you're doing." Naka la Yuda jël dog ba, Seytaane man ko. Yeesu ne ko: «Li ngay def, gaaw ci boog!»
28 But no one reclining at the table understood why he said this to him. Loolu nag kenn ca ña woon ca ndab la xamul lu tax mu wax ko ko.
29 Since Judas held the money bag, some thought Jesus meant, 'Buy what we need for the feast,' or, 'Give something to the poor.' Ñenn ña dañoo xalaat ne gannaaw Yuda moo yoroon dencub taalibe ya, Yeesu da koo wax ne ko, mu gaaw jëndi lu ñu waajale màggal gi, mbaa néew-doole yi la ko ne mu dem saraxi leen.
30 As soon as Judas had taken the bread, he went out. And it was night. Ba mu ko defee Yuda jël dogu mburu ba, daldi génn ca saa sa. Booba nag guddi na.
31 After Judas left, Jesus said, "Now the Son of Man is glorified, and my Father is glorified in him. Ba Yuda génnee, Yeesu da ne: «Léegi nag darajay Doomu nit ki feeñ na, te darajay Yàllaa ngi feeñe ci moom.
32 If my Father is glorified in him, my Father will also glorify the Son in himself and glorify him immediately. Te ni darajay Yàlla feeñe ci Doomu nit ki, ni la Yàlla di feeñale ci boppam darajay Doomu nit ki, te dina ko def léegi.
33 Dear children, I'm with you a little longer. You'll look for me, and as I told the Jewish leaders, so I tell you now: where I'm going, you can't come. Gone yi, diir bu gàtt laa deeti nekk ak yeen. Dingeen ma seet, waaye li ma wax Yawut yi rekk: “Man, fa ma jëm, yeen dungeen fa mana dem.”
34 I give you a new command: love one another. As I have loved you, so you must love one another. Kon ndigal lu bees laa leen di jox, soppanteleen: ni ma leen soppe, yeen itam nangeen ni soppantee.
35 By this everyone will know that you are my disciples, if you love one another." Ni ñépp di xame ne samay taalibe ngeen moo di ngeen soppante.»
36 Simon Peter said to him, "Lord, where are you going?" Jesus answered, "Where I'm going you can't follow me now, but you'll follow later." Simoŋ Piyeer ne ko: «Sang bi, foo jëm?» Yeesu ne ko: «Fa ma jëm, doo ma fa mana topp léegi, waaye dinga ma toppsi ca kanam.»
37 Peter asked, "Lord, why can't I follow you now? I'll lay down my life for you." Piyeer ne ko: «Sang bi, lu tee ma man laa topp léegi? Sama bakkan laa la àttana joxeel!»
38 Jesus replied, "You will lay down your life for me? Truly, truly, I tell you: the rooster won't crow until you have denied me three times." Yeesu ne ko: «Sa bakkan nga ma àttana joxeel? Maa la ko wax déy ci lu wér, bala ganaar a sab, dinga ma jàmbu ñetti yoon.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]