Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 14 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "Do not let your hearts be troubled. Believe in our Father; believe also in me. «Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma.
2 In my Father's house are many rooms. If it were not so, would I have told you that I am going to prepare a place for you? Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb?
3 And if I go and prepare a place for you, I'll come back and take you to myself, so you'll be where I am. Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.
4 And you know the way to where I am going." Te fa ma jëm, xam ngeen yoon wi.»
5 Thomas said to him, "Lord, we don't know where you're going—how can we know the way?" Tomaa ne ko: «Sang bi, xamunu foo jëm, kon ana nu nuy xame yoon wi?»
6 Jesus told him, "I am the way, and the truth, and the life. No one comes to the Father except through me. Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man.
7 Had you known me, you would have known my Father too. Starting now, you know him and have seen him." Su ngeen ma xamoon, sama Baay itam, dingeen ko xam. Li ko dale tey nag, xam ngeen ko, gis ngeen ko.»
8 Philip said to him, "Lord, show us the Father, and that will be enough for us." Filib ne ko: «Sang bi, won nu Baay bi rekk, mu doy nu.»
9 Jesus said, "Philip, I've been with you this long, and you don't know me? Whoever has seen me has seen the Father. How can you say, 'Show us the Father'? Yeesu ne ko: «Filib, ni ma yàggeek yeen te ba tey xamuloo ma? Ku ma gis kay, gis nga Baay bi. Kon ana noo naan: “Won nu Baay bi”?
10 Don't you believe I'm in the Father, and the Father in me? The words I speak to you aren't my own—the Father living in me does his works. Dangaa gëmul ne man, maa ngi ci Baay bi, te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax, waxuma ko ci sama coobarey bopp, waaye Baay bi nekk ci man, moo sottal ay jëfam.
11 Believe me: I'm in the Father, the Father in me—or else believe because of the works themselves. Gëmleen ma, ndax kàddu gii ma ne, maa ngi ci Baay bi, te Baay baa ngi ci man; mbaa boog, ngeen gëm ndax jëf ji may def.
12 Truly, truly, I tell you, whoever believes in me will do the works I do, and will do even greater works, because I am going to the Father. Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku ma gëm, jëf ji may def man, moom itam dina ko def, te jëf ju raw jii sax lay def, ndax man, ci Baay bi laa jëm.
13 Whatever you ask in my name, I will do it, so the Father may be glorified in the Son. Te lépp lu ngeen ñaan ci sama tur, loolu laay def, ngir Doom ji fésal darajay Baay bi.
14 If you ask me anything in my name, I will do it. Su ngeen ma ñaanee mbir ci sama tur, man maa koy def.
15 "If you love me, you will keep my commandments. «Su ngeen ma soppee, sàmmleen samay ndigal.
16 And I will ask the Father, and he will give you another Helper, the Holy Spirit, to be with you forever, Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww.
17 the Spirit of truth, whom the world cannot receive, since it neither sees him nor knows him. But you know him, since he remains with you and will be in you. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.
18 I will not leave you as orphans; I will come to you. Duma leen bàyyi ngeen tumurànke. Dinaa délsi ci yeen.
19 Soon the world won't see me anymore, but you will see me. Because I live, you will live too. Des na tuuti, àddina du ma gisati; yeen dingeen ma gis, ndax man maa ngi dund, te yeen itam dingeen dund.
20 On that day you'll know: I'm in my Father, you in me, and I in you. Bésub keroog dingeen xam ne man maa ngi ci sama Baay, yeen ngeen nekk ci man, man it ma nekk ci yeen.
21 Whoever has my commandments and keeps them loves me, and my Father will love whoever loves me. I will love him and show myself to him." Ki nangu sama ndigal nag, te di ko sàmm, moo ma sopp, te kooku ma sopp, cofeel ñeel na ko, bawoo fa sama Baay, te man itam dinaa ko sopp, di ko feeñu.»
22 Judas, not Iscariot, asked, "Lord, why show yourself to us and not to the world?" Yuda meneen ma wuuteek Yuda Iskaryo, ne ko: «Sang bi, lu waral nga nar noo feeñu te doo feeñu àddina?»
23 Jesus replied, "Anyone who loves me will keep my word, and my Father will love that person, and we will come to them and make our home with them. Yeesu ne ko: «Ku ma sopp day sàmm sama kàddu, sama Baay sopp ko; fi moom lanuy dikk, te moom lanuy def màkkaan.
24 Whoever doesn't love me doesn't keep my words. And the word you hear isn't mine but the Father's who sent me. Ku ma soppul, du sàmm samay kàddu. Kàddu gi ngeen dégg nag, du sama gos, waaye kàddug Baay bi ma yónni la.
25 I have spoken these things to you while I am still with you. «Lii laa leen di wax bi may nekkagum ak yeen.
26 But the Helper, the Holy Spirit, whom the Father will send in my name, will teach you everything and remind you of everything I said to you. Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.
27 Peace I leave you; my own peace I give you. Not as the world gives, I give it. Don't let your hearts be troubled or afraid. Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
28 You heard me say to you, 'I'm going away, and I'm coming to you.' If you loved me, you'd have rejoiced, because I'm going to the Father, for the Father is greater than I. «Dégg ngeen ma ne leen: “Maa ngi dem, maa ngi délsi ci yeen.” Su ngeen ma soppoon, dingeen bége li may dem ci Baay bi, ndax Baay bee ma gëna màgg.
29 And now I've told you before it happens, so that when it happens you'll believe. Léegi bala looloo dikk nag laa leen koy wax, ngir bu dikkee ngeen gëm.
30 I won't talk with you much longer—this world's ruler is coming. He has no hold on me, Duma waxateek yeen lu bare ndax kàngamu àddinaa ngi dikk. Manul ci man dara nag.
31 but I do exactly as the Father commanded me, so the world may know I love the Father. Get up, let's leave this place." Waaye fàww àddina xam ne Baay bi laa sopp, te li ma Baay bi sant rekk laay def. Jógleen, nu dem!
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]