Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 15 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "I am the true vine, and my Father is the gardener. «Man maay reseñ gi dëgg, sama Baay di boroom tóokër bi koy toppatoo.
2 Every branch in me not bearing fruit, he removes; and every one bearing fruit, he prunes, so it bears more fruit. Sama bépp car bu meññul, da koy tenqi sànni, bépp car bu ci meññ lay xosat ba mu set wecc, ngir mu gëna meññ.
3 You are already clean because of the word I have spoken to you. Yeen nag, set ngeen wecc ba noppi, ndax kàddu gi ma leen wax.
4 Remain in me, and I in you. As a branch can't bear fruit alone, unless it remains in the vine, neither can you unless you remain in me. Saxleen ci man, ni ma saxe man ci sama bopp ci yeen. Ni carub reseñ tëlee meññal boppam, su saxul ci ndeyam, ni ngeen di tëlee meññ, su ngeen saxul ci man.
5 I am the vine, you the branches. Whoever remains in me, and I in them, bears much fruit, for apart from me you can do nothing. «Man maay reseñ gi, yeen ngeen di car yi. Ki sax ci man, ma sax ci moom, kooku mooy meññ lu bare, nde su dul man, dungeen mana def dara.
6 Anyone not remaining in me is thrown out like a branch and withers; branches are gathered, thrown into the fire, and burned. Ku saxul ci man daa mel ni ab car bu ñu sànni, mu wow, te yooyu car lees di buub, sànni ci sawara, mu lakk.
7 If you remain in me and my words remain in you, ask whatever you want, and it will happen for you. Su ngeen saxee ci man te samay wax sax ci yeen, lu ngeen bëgg, ñaanleen ko, dees na leen ko nangul.
8 This is how my Father is glorified: that you bear much fruit and prove to be my disciples. Li feeñal sama darajay Baay mooy ngeen meññ lu bare, te noonu ngeen di firndeele ne samay taalibe ngeen.
9 "As the Father has loved me, so I have loved you. Remain in my love. «Ni ma Baay bi soppe, man itam noonu laa leen soppe. Saxleen ci sama cofeel.
10 If you keep my commands, you will remain in my love, as I have kept my Father's commands and remain in his love. Ni ma sàmme sama santaaney Baay, ba tax ma sax ci cofeelam, su ngeen ni sàmmee samay santaane, dingeen sax ci sama cofeel.
11 I've told you this so my joy may be in you, and your joy be complete. Maa leen wax loolu ngir samag mbég wàllsi ci yeen, ba seen mbég mat sëkk.
12 "This is my command: love one another as I have loved you. Sama santaane moo di ni ma leen soppe, ngeen soppantee noonu.
13 No one has greater love than this: to lay down one's life for one's friends. Joxe sa bakkan te say xarit tax, ameesul cofeel gu ko raw,
14 You are my friends if you do what I command you. te samay xarit ngeen, ndegam yeena ngi def li ma leen sant.
15 I no longer call you servants—a servant doesn't know what his master does. I call you friends, since I've made known to you everything I heard from my Father. Wooweetuma leen ay jaam, ndax ab jaam xamul lu sangam di def. Xarit laa leen woowe, ndax mboolem lu ma dégge ci sama Baay, xamal naa leen ko.
16 You didn't choose me—I chose you and placed you to go, bear fruit that lasts, so whatever you ask the Father in my name, he'll give you. Du yeen yeena ma tànn, man maa leen tànn, sas leen ngir ngeen dem, meññi meññeef, te seenum meññeef sax, ba lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko.
17 This is my command to you: love one another. Li ma leen sant nag, moo di ngeen soppante.
18 "If the world hates you, know that it hated me first. «Su leen àddina bañee, xamleen ne man la njëkka bañ.
19 If you were of the world, the world would love you as its own. But you are not of the world; instead, I chose you out of the world, so the world hates you. Su ngeen bokkoon ci àddina, àddina bëgg leen, ndax li ngeen diy ñoñam, waaye dangeena bokkul ci àddina, nde maa leen tànne ci àddina, te looloo tax àddina bañ leen.
20 Remember what I told you: a servant isn't greater than his master. If they persecuted me, they'll persecute you too; if they kept my word, they'll keep yours too. Fàttalikuleen kàddu gi ma leen wax: “Jaam sutul sangam.” Gannaaw man lañu bunduxataal, yeen itam, dinañu leen bunduxataal. Bu ñu sàmmoon sama kàddu, dinañu sàmm seen gos itam.
21 But they'll do all this to you because of my name, since they don't know the one who sent me. Waaye mboolem lu ñu ma def, dinañu leen ko def ndax sama tur, ndax xamuñu ki ma yónni.
22 Had I not come and spoken to them, they would have no sin; now they have no excuse for their sin. Su ma ñëwul woon, ba wax ak ñoom, duñu am bàkkaar. Waaye léegi amuñu aw lay ci seeni bàkkaar.
23 Whoever hates me hates my Father as well. Ku ma bañ nag, bañ nga sama Baay itam.
24 Had I not done among them the works no one else did, they would have no sin. But now they have seen and hated both me and my Father. Su ma deful woon ci seen biir jëf yu kenn deful, kon duñu am bàkkaar. Léegi nag gis nañu ko, te teewul ñu bañ ma, bañ sama Baay.
25 But this happened to fulfill what is written in their Law: 'They hated me without cause.' Waaye loolu moo am, ngir sottal kàddu gii binde ci seen téereb yoon: “Dañu maa bañ ci dara.”
26 "When the Helper comes, whom I will send you from the Father—the Spirit of truth proceeding from the Father—he will testify about me. «Taxawukat bi may yónni ci yeen te muy jóge ci Baay bi mooy Noowug dëgg googu di bàyyikoo ci Baay bi, te kooku bu dikkee, moo may seedeel.
27 "And you also must testify, because you have been with me from the beginning." Te yeen itam dingeen seede, ndax ca njàlbéen ngeen dale nekk ak man.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]