Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 16 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "I have told you all this so that you will not fall away. «Loolu laa leen di wax, ngir seen ngëm baña wàññiku.
2 They will expel you from synagogues; but the hour is coming when whoever kills you will think he offers a service to God. Dees na leen dàqe ci jàngu Yawut ya, te sax waxtoo ngi ñëw wu képp ku leen bóom yaakaar ne Yàlla la koy jaamoo.
3 They will do this because they have not known the Father or me. Loolu, li waral ñu di ko def moo di dañoo xamul Baay bi, xamuñu ma.
4 But I've told you this so that when their hour comes, you'll remember I told you. I didn't tell you this from the start, because I was with you. Ma wax leen loolu, ngir bu waxtu wi dikkee, ngeen fàttaliku ne man, waxoon naa leen ko. Waaye loolu nag, waxuma leen ko woon ca njàlbéen, ndax maa ngi nekkagum ak yeen.
5 "But now I'm going to him who sent me, and none of you asks me, 'Where are you going?' «Léegi nag maa ngi dem ca ka ma yónni, te kenn ci yeen laaju ma fu ma jëm.
6 Instead, because I have said these things to you, sorrow has filled your heart. Waaye aw tiis a fees seen xol ndax li ma leen wax.
7 I tell you the truth: my going is for your good. If I don't go, the Helper, the Holy Spirit, won't come to you. But if I go, I will send him to you. Moona man de, dëgg laa leen wax. Seen njariñ moo di ma dem, ndax su ma demul, Taxawukat bi du ñëw ci yeen; waaye su ma demee, maa leen koy yónnee.
8 And when he comes, he will convict the world concerning sin and righteousness and judgment: Te bu dikkee, mooy tiiñal àddina ci wàllu bàkkaar ak ci wàllu dëgg ak ci wàllu àtte.
9 concerning sin, because they do not believe in me; Benn, ci wàllu bàkkaar, ndax ñoo ma gëmul.
10 concerning righteousness, because I am going to my Father and you will see me no longer; Ñaar, ci wàllu dëgg, ndax maa ngi dem ci Baay bi, te dungeen ma gisati.
11 concerning judgment, because the ruler of this world has been judged. Ñett, ci wàllu àtte, ndax àttees na kàngamu àddina sii, ba daan ko.
12 "I still have many things to say to you, but you cannot bear them now. «Am naa ba tey lu bare lu ma leen wara wax, waaye dungeen ko mana àttan léegi.
13 But when he, the Spirit of truth, comes, he will guide you into all truth. He won't speak on his own, but will speak whatever he hears, and will tell you what is coming. Moom miy Noowug dëgg gi, bu dikkee, moo leen di àggale ci dëgg gi gépp, ndax du ci coobarey boppam lay wax, waaye mboolem lu mu dégg la leen di wax, te liy ñëw ëllëg, moo leen koy wax.
14 He will glorify me, for he will take what is mine and tell it to you. Moom, dina feeñal sama daraja, ndax ci sama jagleb bopp lay tanqe, àgge leen ko.
15 All my Father has is mine; that's why I said he takes from what is mine and will tell you. Mboolem lu Baay bi am, maay boroom. Moo tax ma ne ci sama jagleb bopp lay tanqe, àgge leen ko.
16 "Soon you'll no longer see me; then soon again you'll see me." «Fi leek ab diir, dungeen ma gisati; waaye gannaaw ab diirati, dingeen ma gisaat.»
17 So some of his disciples asked each other, "What does he mean: 'In a little while you will not see me, and then in a little while you will see me,' and, 'Because I am going to the Father'?" Ñenn ca taalibe ya di wax ca seen biir naan: «Li mu nuy wax nii, lu mu doon? Mu ne: “Fi leek ab diir, dungeen ma gisati, waaye gannaaw ab diirati, dingeen ma gisaat,” ak “ndax maa ngi dem ca Baay ba.”»
18 So they kept saying, "What does he mean, 'a little while'? We don't know what he's talking about." Ña nga naan: «Lii mu wax lu mu doon? Mu ne “Gannaaw ab diirati.” Xamunu lu mu wax de.»
19 Jesus knew they wanted to ask him, so he said to them, "Are you asking each other what I meant by saying, 'In a little while you will not see me, and then a little while you will see me'? Yeesu nag gis li ñu ko bëgga laaj, mu ne leen: «Lii ma wax ngeen di laaj ci seen biir: “Fi leek ab diir, dungeen ma gisati, gannaaw ab diirati, ngeen gisaat ma”?
20 "Truly, truly, I tell you: you will weep and mourn, but the world rejoices. You'll grieve, but your grief will become joy. Maa leen ko wax déy ci lu wér, yeen yeenay jooy aka jooytu, àddina moom di bég; yeen, yeenay amu tiis, waaye bànneex la seenu tiis di soppaliku.
21 A woman in labor has pain because her hour has come; but once she gives birth, she forgets the anguish, because she is joyful that a person has been born into the world. Kuy waaja wasin, dina amu tiis, ndax waxtuw matam a jot. Waaye bu doom ji juddoo, dootul fàttaliku njàqareem, ndax ki gane àddina lay bége.
22 So you also have sorrow now, but I will see you again, and your heart will rejoice, and no one will take your joy from you. Kon yeen itam, tey, aw tiis ngeen am, waaye dinaa leen gisaat, seen xol sedd, te seen mbég moomu, kenn du leen ko xañ.
23 In that day you will ask me nothing. Truly, truly, I tell you: whatever you ask my Father in my name, he will give you. Bésub keroog, man dootuleen ma ñaan dara. Maa leen ko wax déy ci lu wér, su boobaa lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko.
24 Until now you've asked nothing in my name. Ask, and you will receive, so your joy may be complete. Ba léegi ñaanuleen dara ci sama tur. Ñaanleen, nangule, ngir seen mbég mat sëkk.
25 I've told you these things in figures. The hour is coming when I'll no longer speak in figures, but tell you plainly about my Father. «Loolu, ci ay misaal laa leen ko wax. Waxtoo ngi ñëw wu ma dootul wax ak yeen ci ay misaal, waaye ci Baay bi laa leen di wax lu leer nàññ.
26 That day you'll ask in my name, and I'm not telling you I'll ask my Father on your behalf; Bésub keroog, ci sama tur ngeen di ñaan. Waxuma leen ne man maa leen di ñaanal Baay bi,
27 for the Father himself loves you, because you've loved me and believed I came from our Father. ndax kat Baay bi ci boppam moo leen sopp, ndaxte yeena ma sopp, te gëm ngeen ne man, ci Yàlla laa jóge.
28 I came from my Father and entered the world; again, I leave the world, going to my Father." Ci Baay bi laa jóge, dikk ci àddina, te léegi maa ngi jóge ci àddina, jëm ci Baay bi.»
29 His disciples said, "Now you are speaking plainly and not using any figure of speech! Taalibe yi ne ko: «Mu ngoog, lu leer nàññ ngay wax nii, te misaaloo!
30 Now we know you know everything and need no one to ask you questions; so we believe you came from our Father." Léegi xam nanu ne xam nga lépp, te soxlawoo ku la laaj dara, te looloo tax nu gëm ne ci Yàlla nga jóge.»
31 Jesus replied, "Do you now believe? Yeesu ne leen: «Xanaa gëm ngeen léegi?
32 "See, the hour is coming—has come—when you'll be scattered, each to his own home, leaving me alone. Yet I'm not alone; my Father is with me. Waxtoo ngii di ñëw te agsi na ba noppi, ca ngeen di tasaaroo, ku nekk ak yoonu boppam, bàyyi ma, ma wéet. Waaye duma wéet, ndax Baay bi moo nekk ak man.
33 I've told you this so you may have peace in me. In the world you'll face trouble, but take heart—I've overcome the world." Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]