Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 17 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After saying this, Jesus looked up to heaven and said: "Father, the hour has come. Glorify your Son, so the Son may glorify you, Loolu la Yeesu wax ba noppi, téen, xool asamaan, daldi ne: «Baay, waxtu wi jot na. Feeñalal sa darajay Doom, ngir Doom ji feeñal sa daraja.
2 since you gave him authority over all people, to give eternal life to all you gave him. Yaa ko jox sañ-sañ ci ñépp, ngir mboolem ñi nga ko jox, mu texeel leen ba fàww.
3 This is eternal life: that they know you, the only true Father, and Jesus Christ whom you sent. Texeg fàww gi nag moo di ñu xam la, yaw jenn Yàlla jiy dëgg, xam it ki nga yebal, muy Yeesu Almasi bi.
4 I glorified you on the earth, having finished the work you gave me to do. Man de, feeñal naa sa màggaay ci àddina; liggéey bi nga ma santoon ma def ko, sottal naa ko.
5 Father, glorify me now with yourself, with the glory I had with you before the world existed. Léegi nag Baay, daraja ja ma amoon fa yaw, balaa àddinaa sosu, jox ma daraja jooju fa sa wet.
6 I revealed your name to those you gave me from the world. They were yours; you gave them to me, and they have kept your word. «Nit ñi nga tànne ci àddina, jox ma leen, ràññeeloo naa leen saw tur. Sa ñoñ lañu woon, nga jox ma leen, te sa kàddu, sàmm nañu ko.
7 Now they know that everything you have given me is from you, Léegi xam nañu ne lépp lu ma am ci yaw la jóge,
8 for I gave them the words you gave me; they received them, truly knew I came from you, and believed you sent me. ndax wax ji nga ma dénk, dénk naa leen ko, te nangu nañu ko. Xam nañu xéll it ne ci yaw laa jóge, te gëm nañu ne yaw yaa ma yebal.
9 I pray for them, not for the world, but for those you gave me, since they are yours. Man nag, ñoom laay ñaanal; ñaanaluma waa àddina, waaye ñi nga ma dénk, ñoom laay ñaanal, ndax sa ñoñ lañu.
10 Everything mine is yours, and yours is mine, and I am glorified in them. Mboolem lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom, te ci ñoom la sama daraja feeñe.
11 I'm no longer in the world, but they are in the world, and I'm coming to you. Holy Father, keep them in your name, the name you gave me, so they may be one as we are. Toogatuma ci àddina, waaye ñoom ci àddina lañu nekk, te man, ci yaw laa jëm. Baay bu sell bi, sàmme leen sa tur wi nga ma jox, ngir ni nu nekke benn, ñoom it ñu nekke noonu benn.
12 While with them, I kept them in your name you gave me. I guarded them—none was lost except the son of destruction, so Scripture would be fulfilled. Diir bi may nekk ak ñoom, man maa leen doon sàmme sa tur wi nga ma jox. Wattu naa leen, ba kenn ci ñoom sànkuwul, ku moy doomu sànkute jiy sànku, ngir Mbind mi sotti.
13 Now I come to you, and I say these things in the world so they may have my joy completed in themselves. «Léegi nag, ci yaw laa jëm, waaye lii laay wax bi may nekkagum ci àddina, ngir sama mbég ñeel leen, mat sëkk.
14 I've given them your word; the world hated them, since they're not of the world, just as I'm not of the world. Man, jottali naa leen sa kàddu, waaye àddinaa leen bañ, ndax ni ma ñàkka bokke ci àddina, ni lañu ñàkka bokke ci àddina.
15 I don't ask you to remove them from the world, but to guard them from the evil one. Ñaanuma nga jële leen ci àddina, xanaa nga musal leen ci ku bon ki.
16 They are not of the world, just as I am not of the world. Ni ma ñàkka bokke ci àddina, man ci sama bopp, noonu lañu ñàkka bokke ci àddina.
17 Make them holy by truth; your word is truth. Ngalla sellale leen dëgg gi: sa kàddu mooy dëgg.
18 As you sent me into the world, so I have sent them into the world. Ni nga ma yebale ci àddina, man itam, ni laa leen yebale ci àddina.
19 For them I make myself holy, so they too may be made holy in truth. Man nag, ñoom laa sellalal sama bopp, ngir ñoom itam, ñu mana sellaloo dëgg gi.
20 I pray not only for these, but also for those who will believe in me through their word. «Du ñoom doŋŋ laay ñaanal nag, waaye ñi may gëm ëllëg ndax seen kàddu itam laay ñaanal,
21 Father, let them all be one, as you're in me and I in you, so they're in us too, and the world believes you sent me. ngir ñépp doon benn, ni nga nekke yaw Baay, ci man, ma nekke ko ci yaw, ñoom itam, ñu nekke ni ci nun, ba àddina gëm ne yaw yaa ma yebal.
22 The glory you have given me, I have given them, so they may be one as we are one. Man nag daraja ji nga ma jox, jox naa leen ko, ngir ni nu nekke benn maak yaw, ñu nekke ni noonu.
23 I in them and you in me, so they may be made completely one, so the world may know you sent me and loved them as you loved me. Man ma nekk ci ñoom, yaw nga nekk ci man, ngir ñu mat sëkk ci ag bennoo, ba àddina xam ne yaw yaa ma yebal, te ni nga ma soppe, ni nga leen soppe.
24 Father, I want those you gave me to be with me where I am, to see my glory, which you gave me because you loved me before the world was made. «Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.
25 Righteous Father—the world doesn't know you, but I know you, and these know you sent me. «Baay Boroom njub, àddinaa la xamul, waaye man xam naa la, te ñii xam nañu ne yaa ma yebal.
26 I have made your name known to them, and will keep making it known, so the love you loved me with may be in them, and I in them." Xamal naa leen sa tur te dinaa ko gëna xamle, ngir cofeel gi nga ma sopp nekk ci ñoom, te man it, ma nekk ci ñoom.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]