Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 18 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After saying these things, Jesus went out with his disciples across the Kidron Valley, where a garden stood; he and his disciples entered it. Loolu la Yeesu wax ba noppi, dem, ànd ak taalibeem ya, ñu jàlli ca wàllaa xuru Sedoron. Ab tool a nga fa woon nag, ñu daldi dugg ca biir.
2 Judas the betrayer knew the place too, since Jesus often gathered there with his disciples. Yuda mi koy wor it xamoon na béreb ba, ndax Yeesu daan na fa farala ànd aki taalibeem.
3 So Judas came there with a detachment of soldiers and officers from the chief priests and Pharisees, carrying lanterns, torches, and weapons. Ci kaw loolu Yuda jubal ca tool ba, ànd ak gàngooru takk-der aki wattukati kër Yàlla ga te ñu bàyyikoo ca sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya, yor ay jum aki làmp aki gànnaay.
4 So Jesus, knowing all that was coming on him, went out and said to them, "Who are you looking for?" Yeesu ma xamoon mboolem la koy dikkal nag, génn, jubsi leen, ne leen: «Ku ngeen di seet?»
5 They answered him, "Jesus of Nazareth." Jesus said, "I AM." Judas, his betrayer, stood with them. Ñu ne ko: «Yeesum Nasaret.» Mu ne: «Man a.» Yuda ma koy wor a nga bokk ak ñoom taxaw.
6 When Jesus said to them, "I AM," they drew back and fell to the ground. Ba leen Yeesu nee: «Man a,» dañoo dellu gannaaw, ba daanu.
7 So he asked them again, "Who are you looking for?" And they said, "Jesus of Nazareth." Mu dellu ne leen: «Ku ngeen di seet?» Ñu ne: «Yeesum Nasaret.»
8 Jesus answered, "I told you I AM. So if you're looking for me, let these men go." Mu ne leen: «Ne naa leen man la. Gannaaw man ngeen di seet nag, baleen ñii ma àndal, ñu dem.»
9 This fulfilled Jesus's own word: "I have not lost a single one of those you gave me." Kàddu ga Yeesu noon Yàlla: «Ñi nga ma jox, kenn du ci sànku,» noonu la sottee.
10 So Simon Peter drew his sword, struck the high priest's servant, and cut off his right ear—the servant named Malchus. Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ma ràngoo saamar, bocci, caw ko surgab sarxalkat bu mag ba, njoof noppu ndijoor ba. Surga ba, Malkus lañu koy wax.
11 So Jesus told Peter, "Sheath your sword. Shouldn't I drink the cup my Father has given me?" Yeesu ne Piyeer: «Defal saamar ci mbaram. Kaasub naqar bi ma Baay bi sédd, xanaa dama ko dul naan?»
12 Then the troops, their commander, and the Jewish officers seized Jesus and tied him up. Ba loolu amee gàngooru takk-der ya ak seen njiit, ak wattukati kër Yàlla ga njiiti Yawut ya yilifoon, daldi jàpp Yeesu, yeew ko.
13 They took him to Annas first, for he was father-in-law to Caiaphas, high priest that year. Ca Anas lañu ko njëkka yóbbu, ndax moo doon baayu jabaru Kayif ma doon sarxalkat bu mag ba, ca at mooma.
14 Caiaphas was the one who advised the Jews: better one man die for the people. Kayif moomu moo digaloon Yawut ya ne leen: «Liy njariñ moo di kenn nit doŋŋ deewal askan wi.»
15 Simon Peter and another disciple followed Jesus. That disciple was known to the high priest, so he entered with Jesus into the high priest's courtyard, Simoŋ Piyeer nag ànd ak keneen ca taalibe ya, ñu topp ca Yeesu. Fekk na beneen taalibe ba xamante ak sarxalkat bu mag ba, ba tax mu ànd ak Yeesu, dugg ca biir kër sarxalkat bu mag ba.
16 but Peter stood outside at the door. So the other disciple, known to the high priest, went out, spoke to the servant girl who kept the door, and brought Peter in. Teewul Piyeer, moom, taxaw ca bunt kër ga. Ci kaw loolu beneen taalibe ba xam sarxalkat bu mag ba daldi génn, wax ak surga bu jigéen bay wattu bunt ba, ba dugal Piyeer ca biir.
17 The servant girl guarding the door said to Peter, "You also are not one of this man's disciples, are you?" He said, "I'm not." Surga bu jigéen bay wattu bunt kër ga ne Piyeer: «Yaw itam, bokkuloo ci taalibey waa jii?» Mu ne ko: «Bokkuma ci.»
18 The servants and officers, feeling the cold, had lit a charcoal fire and stood warming themselves; Peter stood with them, warming himself. Ci biir loolu surga ya ak wattukat ya taxaw, tiim ab taalu këriñ gu ñu boyal bay jaaru, ndax dafa seddoon. Piyeer itam taxaw faak ñoom, di jaaru.
19 The high priest then questioned Jesus about his disciples and his teaching. Sarxalkat bu mag ba daldi laaj Yeesu ci mbirum ay taalibeem ak ci am njàngaleem.
20 Jesus answered him, "I spoke openly to the world; I always taught in synagogues and in the temple, where all the Jews gather. I said nothing in secret. Yeesu ne ko: «Man de, fàŋŋ laa waxe ak àddina. Te it man ca jàngu ba ak ca kër Yàlla ga, fa Yawut yépp di daje, fa laa mas di jàngalee, te làquwuma di wax lenn.
21 Why ask me? Ask those who heard what I said to them; they know what I said." Ana loo may laaje? Li ma wax, laaj ko ñi ma dégg. Ñoom kay xam nañu bu baax li ma wax, man.»
22 At this, one of the guards nearby slapped Jesus, saying, "Is that how you answer the high priest?" Ba Yeesu waxee loolu, kenn ca wattukati kër Yàlla ga fa taxawoon daldi ko dóor mbej, ne ko: «Ndax noonu ngay tontoo sarxalkat bu mag bi?»
23 Jesus answered him, "If I spoke wrongly, testify about the wrong; but if rightly, why do you strike me?" Yeesu ne ko: «Su ma waxee ndëngte, seedeel lu ci dëng, te su dee njub laa wax, ana loo may dóore?»
24 Then Annas sent him, still bound, to Caiaphas the high priest. Ba loolu amee Anas jàllale ko, na ñu ko yeewe, ca Kayif, sarxalkat bu mag ba.
25 Simon Peter, meanwhile, stood warming himself. They said, "Aren't you also one of his disciples?" He denied it: "I'm not." Ci biir loolu Simoŋ Piyeer a nga taxaw, di jaaru ba tey. Ñu ne ko: «Yaw itam du ci taalibey waa ji nga bokk?» Piyeer miim ko, ne: «Bokkuma ci de.»
26 One of the high priest's servants, a relative of the man whose ear Peter cut off, asked, "Didn't I see you with him in the garden?" Kenn ca surgay sarxalkat bu mag ba, te di mbokkum ka Piyeer njoofoon noppam, ne Piyeer: «Xanaa du yaw laa gisoon ak moom ca tool ba?»
27 Peter again denied it, and at once a rooster crowed. Piyeer miimati ko. Ca saa sa nag ganaar sab.
28 Then they led Jesus from Caiaphas to the governor's headquarters. It was early morning. They themselves didn't enter, so they wouldn't be made unclean but could eat the Passover. Ba loolu wéyee ñu jële Yeesu ca Kayif, yóbbu ko ca kër boroom réew ma. Waxtuw njël la woon; Yawut ñi ci seen bopp dugguñu ca biir kër ga, ndax baña sobeel seen bopp ba duñu mana lekk ca reeru bésub Mucc ba.
29 So Pilate went out to them and said, "What accusation do you bring against this man?" Pilaat boroom réew ma moo génn, dajeek ñoom. Mu ne leen: «Ana lu ngeen di jiiñ waa jii?»
30 They answered him, "If this man weren't doing wrong, we wouldn't have handed him over to you." Ñu ne ko: «Kii bu deful woon lu bon, duñu la ko jébbal.»
31 Pilate said, "Take him yourselves and judge him by your own law." The Jews said, "We're not permitted to execute anyone." Pilaat ne leen: «Jëlleen ko, yeen, te àtte ko ci seen yoonu bopp.» Yawut ya ne ko: «Nun, mayeesu nu nu teg kenn àtteb dee.»
32 This fulfilled the word Jesus had spoken, showing what kind of death he was about to die. Kàddug Yeesu ga mu tegtale woon deewin wa mu nara deewe, noonu la sottee.
33 So Pilate went back into the headquarters, summoned Jesus, and asked, "Are you the King of the Jews?" Gannaaw loolu Pilaat duggaat ca kër ga, daldi woo Yeesu, ne ko: «Yaw yaa di buurub Yawut yi?»
34 Jesus answered, "Are you saying this on your own, or did others tell you about me?" Yeesu ne ko: «Loolu ndax yaw yaa ko waxal sa bopp, am ñeneen a la ko wax ci man?»
35 Pilate replied, "Am I a Jew? Your own nation and chief priests handed you over to me. What have you done?" Pilaat ne ko: «Ndax man dama dib Yawut? Saw xeetu bopp ak seeni sarxalkat yu mag kay ñoo ma la jébbal. Ana loo def?»
36 Jesus answered, "My kingdom isn't from this world. If it were, my servants would fight against my being handed to the Jews. But my kingdom isn't from here." Yeesu ne ko: «Sama nguur moo bokkul ci àddina sii. Bu sama nguur bokkoon ci àddina, samay surga xeex, ba kenn du ma jébbal njiiti Yawut yi. Waaye sama nguur a bokkul fii.»
37 Then Pilate said to him, "So you are a king?" Jesus answered, "You say I'm a king. I was born for this, and I came into the world for this—to testify to the truth. Everyone who belongs to the truth hears my voice." Pilaat ne ko: «Kon yaw buur nga?» Yeesu ne ko: «Yaa ko wax; buur laa. Li tax ma juddu, li tax ma dikk ci àddina moo di seedeel dëgg. Ku bokk ci dëgg gi nag dina dégg li ma wax.»
38 Pilate asked, "What is truth?" Then he went out to the Jews again and said, "I find nothing wrong in him. Pilaat ne ko: «Ana luy dëgg gi?» Loolu la Pilaat wax, daldi génnaat ba ca Yawut ya, ne leen: «Man de gisuma ci moom lenn lees koy daane.
39 But you have a custom: I release one man to you at Passover. So do you want me to release the King of the Jews to you?" Gannaaw dangeena aadawoo nag ma bàyyil leen kenn nit ci bésub Mucc, ndax bëgg ngeen ma bàyyil leen kii di “buurub Yawut yi”?»
40 They cried out again, "Not this man, but Barabbas!" Now Barabbas was a robber. Ñu yuuxooti: «Du kii de, xanaa Barabas!» Te Barabas moomu doonoon ab fippukat.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]