Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 19 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then Pilate took Jesus and had him flogged. Ba mu ko defee Pilaat dóorlu Yeesu ay yar.
2 The soldiers wove a crown of thorns, put it on his head, and wrapped a purple robe around him. Takk-der ya teg ci boppu Yeesu kaala gu ñu ràbbe ay dég, solal ko mbubb mu xonq curr.
3 They kept coming to him, saying, "Hail, King of the Jews!" and slapped his face. Ñu dikk ba ca moom nag, naan ko: «Buuru Yawut yée, guddaluw fan!» te di ko dóori mbej.
4 Pilate went out again and said to them, "Look, I'm bringing him out to you, so you'll know I find no fault in him." Ci kaw loolu Pilaat génnati ne leen: «Ma ne, maa ngi leen koy indil ci biti, ngir ngeen xam ne gisuma ci moom lenn lees koy daane.»
5 So Jesus came out wearing the crown of thorns and the purple robe. Pilate told them, "Here is the man!" Yeesu nag génn ak kaalag dég gaak mbubb mu xonq ma. Pilaat ne leen: «Waa jaa ngii!»
6 When the chief priests and guards saw him, they shouted, "Crucify him! Crucify him!" Pilate told them, "Take him yourselves and crucify him, since I find no guilt in him." Teewul ba ko sarxalkat yu mag yaak wattukati kër Yàlla ga gisee, dañoo xaacoondoo, ne: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Jëlleen ko, yeen, daaj ko ci bant, ndax man gisuma ci moom lenn lees koy daane.»
7 The Jews answered him, "We have a law; by that law he must die, because he made himself the Son of God." Yawut yi ne ko: «Nun danoo am aw yoon, te ci sunuw yoon, àtteb dee moo war ci moom, ndax Doomu Yàlla la teg boppam.»
8 When Pilate heard this, he was even more afraid. Ba Pilaat déggee kàddu googu, tiitaangeem yokk.
9 He went into headquarters again and asked Jesus, "Where are you from?" But Jesus gave him no answer. Mu dellooti Yeesu ca biir kër ga, ne ko: «Yaw foo jóge?» Yeesu tontuwu ko.
10 So Pilate said to him, "You won't speak to me? Don't you know I have authority to release you, and authority to crucify you?" Pilaat ne ko: «Man nga dul waxal? Xamuloo ne am naa sañ-sañu bàyyi la, am naa itam sañ-sañu daaj la ci bant?»
11 Jesus answered him, "You would have no authority over me at all unless it had been given you from above. That is why the one who handed me over to you bears the greater sin." Yeesu ne ko: «Su dul woon ag may gu la dikke fa kaw, doo am benn sañ-sañ ci man. Moo tax it ki ma teg ci say loxo gënati laa bàkkaar.»
12 From then on, Pilate tried to release him, but the Jews cried out, "If you release him, you're no friend of Caesar. Anyone who makes himself king opposes Caesar." Ca la Pilaat doxe di seet nu mu bàyyee Yeesu. Teewul Yawut ya xaacu ne: «Kii, soo ko bàyyee, doo xaritub buur Sesaar. Képp ku teg boppam buur, yaa noonoo buur Sesaar!»
13 Hearing these words, Pilate brought Jesus out and sat on the judgment seat at a place called Stone Pavement—Gabbatha in Aramaic. Naka la Pilaat dégg kàddu googu, daldi génne Yeesu, dem nag toog ca jalub àttekaay ba, fa ñuy wax Dër ba, te ñu naan ko Gabata ci làkku yawut.
14 It was Passover Preparation Day, about noon. He told the Jews, "Here is your King!" Looloo nga yemook waxtuw digg bëccëg. Boobu ñu ngi waajal màggalu bésub Mucc ba. Pilaat nag ne Yawut ya: «Seen buur a ngoogu!»
15 They yelled, "Take him away! Take him away! Crucify him!" Pilate asked them, "Crucify your king?" The chief priests answered, "We have no king but Caesar." Ñu yuuxoo: «Na dee! Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur laay daaj ci bant?» Sarxalkat yu mag ya ne ko: «Amunu buur bu dul Sesaar!»
16 So then he handed him over to them to be crucified. So they took Jesus, Noonu nag Pilaat teg Yeesu ci seeni loxo, ngir ñu daaj ko ci bant. Ñu daldi yóbbu Yeesu.
17 carrying his own cross, he went out to the place called The Place of a Skull, called Golgotha in Aramaic. Moom ci boppam moo gàddu bant ba, génn jëm ba fa ñuy wax bérebu Kaaŋu bopp, muy firi Golgota ci làkku yawut.
18 There they crucified him, with two others, one on each side, Jesus in the middle. Foofa lañu daaje Yeesu ca bant ba, mook ñeneen ñaar; kii ci wet gii, kee ca wet gee, Yeesu ca digg ba.
19 Pilate also wrote a sign and put it on the cross: Jesus of Nazareth, King of the Jews. Pilaat bindlu itam ab tegtalukaay, we ko ca kaw bant ba ñu ko daaj, ñu bind ca lii: «Kii mooy Yeesum Nasaret, buurub Yawut yi.»
20 Many Jews read this sign, since the place Jesus was crucified was near the city; it was written in Aramaic, Latin, and Greek. Mbind moomu Yawut yu bare jàng nañu ko, ndax béreb ba ñu daaj Yeesu jege na dëkk ba, te ci yawut, ak ci làkku waa Room ak ci gereg lañu ko bind.
21 So the Jewish chief priests said to Pilate, "Don't write 'The King of the Jews,' but 'This man said, I am King of the Jews.'" Sarxalkat yu mag yu Yawut ya nag ne Pilaat: «Waruloo bind ne: “Kii mooy buurub Yawut yi,” li nga wara bind mooy: “Kii moo ne mooy buurub Yawut yi.”»
22 Pilate answered, "What I have written, I have written." Pilaat ne leen: «Li ma bind, bind naa ko ba noppi.»
23 After crucifying Jesus, the soldiers took his clothes and split them into four shares, one per soldier, and took the tunic too. The tunic was seamless, woven in one piece from top to bottom. Gannaaw ba ñu daajee Yeesu ca bant ba, takk-der ya dañoo jël ay yéreem, def ko ñeenti cér, takk-der bu nekk benn. Jël nañu itam mbubbam rabalam mu mag, di lenn ndimo te ñaweesu ko fenn ca kaw ba ca suuf.
24 So they said to each other, "Let's not tear it, but cast lots for who gets it." This was to fulfill the Scripture that says, "They divided my clothes among themselves, and cast lots for my garment." So the soldiers did this. Takk-der ya diisoo ca, ne: «Mbubb mi, bunu ko xotti, nanu ko tegoo bant, ngir xam ku koy moom.» Noonu la mbir ma tëdde, ngir Mbind ma indi woon lii, sotti: «Séddoo nañu samay yére, sama mbubb mu mag, ñu tegoo ko bant.» Loolu nag la takk-der ya def.
25 His mother, his mother's sister, Mary wife of Clopas, and Mary Magdalene stood near Jesus' cross. Ña taxawoon ca wetu bant ba ñu daaj Yeesu, ñoo di yaayam ak yaayam ju ndaw, ak Maryaama jabaru Këlopas, ak Maryaama ma dëkk Magdala.
26 Seeing his mother and the disciple he loved standing there, Jesus told her, "Woman, here is your son." Taalibe ba Yeesu soppoon itam ma nga fa woon, taxaw. Ba leen Yeesu gisee da ne yaayam: «Soxna si, sa doom a ngoogu.»
27 Then he said to the disciple, "Here is your mother." From that hour, the disciple took her into his home. Mu teg ca ne taalibe ba: «Sa yaay a ngoogu.» Ca waxtu woowa tembe la taalibe ba yóbbu soxna sa këram.
28 After this, knowing all was now finished, Jesus said, to fulfill Scripture, "I am thirsty." Gannaaw loolu Yeesu xam ne lépp sotti na, mu daldi ne: «Mar naa!» ngir matal la Mbind ma indi woon ci mbiram.
29 A jar full of sour wine sat there; they soaked a sponge in it, fixed it on a hyssop stalk, and lifted it to his mouth. Ndab lu fees ak bineegar a nga fa tege woon. Ñu jël ab sagar, xooj ko ca, lonk ko ci caru garabu isob, tàllal ko ba mu jot gémmiñam.
30 Jesus took the sour wine and said, "It is finished." He bowed his head and gave up his spirit. Yeesu nag muucu bineegar ba, daldi ne: «Sotti na!» Ci kaw loolu mu sëgal bopp ba, daldi yiwi noo ga.
31 Since it was Preparation Day, and they didn't want the bodies remaining on the cross during the Sabbath—that Sabbath was a special day—the Jews asked Pilate to break their legs and remove the bodies. Waajalu bésub Noflaay la woon, te bésub Noflaay warula fekk néew ya ca bant ba, ndax bés bu màgg la ci Yawut ñi. Ñu ñaan Pilaat, mu dammlu tànki ña ñu daaj, ngir jële leen fa.
32 So soldiers came and broke the legs of the first man, then the other crucified with him. Takk-der ya dikk, damm tànki kenn ka ñu daajaaleek Yeesu, teg ca keneen ka.
33 But coming to Jesus, seeing he was already dead, they didn't break his legs. Ñu agsi ci Yeesu, daldi gis ne dee na ba noppi, ba tax dammuñu ay tànkam.
34 But one of the soldiers pierced his side with a spear, and blood and water immediately came out. Teewul kenn ca takk-der ya jam ko ab xeej ci faar yi, deret ànd ak ndox tuuru ca saa sa.
35 The eyewitness has testified—his testimony is true, and he knows he speaks the truth—so you also may believe. Ki joxeb seedeem ci mbir yooyii, moo ci teg bëtam, te kàddug seedeem dëgg la. Moom ci boppam, xam na ne dëgg lay wax, te moo ci joxe kàddug seedeem, ngir yeen itam ngeen gëm.
36 For these things happened to fulfill the Scripture: "Not one of his bones will be broken." Loola moo am ngir Mbind mi indi woon lii, sotti: «Benn yaxam, deesu ko damm.»
37 And again another Scripture says, "They will look on the one they have pierced." Meneen Mbind indeeti ne: «Dinañu gis ki ñu jam.»
38 Afterward, Joseph of Arimathea—a disciple of Jesus, but secretly, for fear of the Jews—asked Pilate to let him remove Jesus' body. Pilate agreed, so he came and removed it. Gannaaw loolu Yuusufa ma dëkk Arimate, di taalibeb Yeesu bu làqu ndax ragal njiiti Yawut ya, moom moo ñaan Pilaat mu may ko mu yóbbu néewub Yeesu. Pilaat may ko ko. Yuusufa nag dem, yóbbu néewub Yeesu.
39 Nicodemus, who had first come to Jesus at night, also came, bringing a mixture of myrrh and aloes, about seventy-five pounds. Nikodem itam ànd ak moom, indaale lu wara tollook fanweeri kiloy cuuraayal njafaan lu ñu defare ndàbbu miir ak alowes. Nikodem moomu jëkkoon naa seetsi Yeesu ag guddi.
40 They took Jesus's body and wrapped it in linen cloths with spices, as is Jewish burial custom. Ñu jël néewub Yeesu, lëmëse ko sori lẽe, defaale ca cuuraay la, na ko Yawut ya baaxoo woon ci waajtaayu rob.
41 Where he was crucified there was a garden, and in the garden a new tomb where no one had yet been laid. Foofa ñu daajoon Yeesu, ab tool a nga fa, ab bàmmeel bu bees bu ñu yatt ciw doj a nga ca tool ba, te maseesu caa denc ab néew.
42 Because it was the Jewish Preparation day, and the tomb was near, they laid Jesus there. Foofa lañu denc Yeesu, gannaaw jege woon na, te ci Waajalu bésub Noflaay lañu nekkoon.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]