Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 11 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 A man named Lazarus was sick, from Bethany, the village of Mary and her sister Martha. Jenn waay a woppoon; ñu di ko wax Lasaar, di waa Betani, dëkkub Maryaama ak Màrt, ña mu bokkal ndey ak baay.
2 Mary—whose brother Lazarus was sick—anointed the Lord with fragrant oil and dried his feet with her hair. Maryaama mooy ki sotti woon Sang bi lajkoloñ, ba fompe ay tànkam kawaru boppam. Moom la Lasaar mi woppoon di càmmiñam.
3 So the sisters sent word to him, saying, "Lord, the one you love is sick." Ñaari jigéeni Lasaar yooyu nag yónnee ca Yeesu ne ko: «Sang bi, sa soppe bi daa wopp.»
4 Hearing this, Jesus said, "This sickness won't end in death, but is for the glory of our Father, so the Son of our Father may be glorified through it." Yeesu dégg ca, ne: «Wopp jooju de du woppi dee, waaye darajay Yàlla lay feeñal, ba màggale ko Doomu Yàlla ji.»
5 Now Jesus loved Martha and her sister and Lazarus. Yeesu nag ku soppoon Màrt la, ak Maryaama ak Lasaar.
6 So when he heard Lazarus was sick, he stayed two more days where he was. Teewul ba mu déggee ne daa wopp, toogaat na ñaari fan fa mu nekkoon.
7 Then after this he said to the disciples, "Let us go back to Judea." Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: «Nanu dellu Yude.»
8 The disciples said to him, "Rabbi, the Jews just now tried to stone you, and you're going back there?" Taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, yàggul dara la la fa waa Yude doon wuta sànniy doj ngir rey la, nga di fa dellu?»
9 Jesus answered, "Aren't there twelve hours in the day? Anyone who walks by day won't stumble - he sees the light of this world. Yeesu ne leen: «Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? Kuy doxe bëccëg, du fakkastalu, ndax leeru àddina sii muy gis.
10 But if anyone walks at night, he stumbles, because the light is not in him." Waaye kuy doxe guddi, mooy fakkastalu, ndax ag leer la dul am.»
11 After this, he told them, "Our friend Lazarus has fallen asleep, but I'm going to wake him." Loolu la Yeesu wax, dal cay teg ne leen: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maay dem ba yee ko.»
12 So the disciples said to him, "Lord, if he has fallen asleep, he will get better." Taalibe ya ne ko: «Sang bi, su dee nelaw kay, dina mucc.»
13 Now Jesus had been speaking about his death, but they thought he meant natural sleep. Li Yeesu waxe noonu mooy Lasaar dee na, ñoom nag ñu foog ne da ne Lasaar day nelaw rekk.
14 So then Jesus told them plainly, "Lazarus has died, Ca la leen Yeesu wax lu leer, ne leen: «Lasaar dee na.
15 I'm glad for your sake I wasn't there, so you'll believe. But let's go to him." Dee gi fekku ma fa, te loolu tax na maa bég ndax yeen, ngir dina tax ngeen gëm. Nanu ko seeti.»
16 So Thomas, called the Twin, told the other disciples, "Let's go too, and die with him." Ci kaw loolu Tomaa mi ñuy wax Seex bi, ne bokki taalibeem: «Nanu dem nun itam, ngir ànd ak moom dee!»
17 So when Jesus arrived, he found that Lazarus had already been in the tomb four days. Ba Yeesu agsee, fekk na Lasaar am ñeenti fan ci biir bàmmeel.
18 Bethany was near Jerusalem, about two miles away, Betani nag jegewoo na ak Yerusalem, te diggante bi yées na ñetti kilomet.
19 and many of the Jews had come to Martha and Mary to console them about their brother. Yawut yu baree dikkoon kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewug càmmiñ.
20 When Martha heard Jesus was coming, she went to meet him; Mary stayed sitting in the house. Ba Màrt yégee ne Yeesoo ngay ñëw, da koo gatanduji, te fekk na Maryaama toog ca kër ga.
21 Martha said to Jesus, "Lord, if you had been here, my brother would not have died. Màrt ne Yeesu: «Sang bi, soo fi nekkoon de, sama càmmiñ du dee.
22 But even now I know that whatever you ask of our Father, he will give you." Waaye ba léegi sax, xam naa ne loo ñaan Yàlla, Yàlla may la ko.»
23 Jesus said to her, "Your brother will rise again." Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.»
24 Martha said to him, "I know he'll rise again in the resurrection on the last day." Màrt ne ko: «Xam naa ne dina dekki kera ca ndekkitel bés bu mujj ba.»
25 Jesus told her, "I am the resurrection and the life. Whoever believes in me will live, even though he dies, Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund.
26 and everyone who lives and believes in me will never die. Do you believe this?" Te képp kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
27 She said to him, "Yes, Lord; I believe you are the Christ, the Son of our Father, the one coming into the world." Mu ne ko: «Waaw, Sang bi. Man gëm naa ne yaay Almasi bi, Doomu Yàlla, ki ñëw ci àddina si.»
28 After saying this, she went and called her sister Mary privately: "The Teacher is here—he's calling for you." Loolu la Màrt wax, daldi woowi Maryaama, ñaarook moom, ne ko: «Kilifa gi ñëw na, ba di la laaj.»
29 When Mary heard this, she rose quickly and went to him. Maryaama dégg loolu, gaaw jóg dem ca Yeesu.
30 Jesus had not yet entered the village; he was still where Martha met him. Booba Yeesu agseegul ca biir dëkk ba, waaye ma nga ba tey fa mu daje woon ak Màrt.
31 The Jews with her in the house, comforting her, saw Mary rise quickly and leave; they followed, thinking she was going to the tomb to weep there. Yawut ya nekk ak Maryaama ca kër ga, di ko dëfal nag, gis ko na mu nee bërét génn, ñu topp ko, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
32 Mary came to Jesus, saw him, fell at his feet, and said, "Lord, if you had been here, my brother would not have died." Ba Maryaama agsee ba gis Yeesu, da ne gurub cay tànkam ne ko: «Sang bi, soo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.»
33 When Jesus saw her weeping, and the Jews who came with her also weeping, he groaned in spirit and was troubled. Ba ko Yeesu gisee muy jooy, Yawut ya mu àndal itam di jooy, yaramam daw na, mu jàq.
34 And he said, "Where have you laid him?" They said to him, "Lord, come and see." Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
35 Jesus wept. Yeesu nag jooy.
36 So the Jews said, "See how he loved him!" Yawut ya naan: «Gisleen rekk ni mu ko bëgge!»
37 But some of them said, "Could this man who opened the blind man's eyes not have kept him from dying?" Teewul ñenn ca ñoom naan: «Moom mi muri bëti gumba gi, manul woona fexe itam ba kii du dee?»
38 So Jesus, again deeply moved in himself, came to the tomb—a cave with a stone against it. Naka la yaramu Yeesu dawati lool, mu dem ba ca bàmmeel ba, muy pax mu ñu yatt ciw doj, ube pax mi aw doj.
39 Jesus said, "Take away the stone." Martha, the dead man's sister, said to him, "Lord, he must smell by now—he's been dead four days." Yeesu ne: «Dindileen doj wi!» Màrt, jigéenu ki dee ne ko: «Sang bi, fii nu tollu dina am xet, nde mu ngi ci ñeenti fanam.»
40 Jesus said to her, "Didn't I tell you: if you believe you'll see our Father's glory?" Yeesu ne ko: «Xanaa waxuma la ne soo gëmee, dinga gis màggug Yàlla?»
41 So they removed the stone. Jesus looked up and said, "Father, I thank you that you heard me. Ñu dindi doj wa. Yeesu xool ca kaw, daldi ne: «Baay, sant naa la, ndax nangul nga ma.
42 I knew you always hear me, but I said this for the crowd standing here, so they may believe you sent me." Man nag xam naa ne saa su nekk danga may nangul, waaye mbooloo mi fi teew a ma taxa wax loolu, ngir ñu gëm ne yaw yaa ma yebal.»
43 When he had said this, he cried out with a loud voice, "Lazarus, come out!" Loolu la Yeesu wax, daldi xaacu ca kaw, ne: «Lasaar, génnal!»
44 The dead man came out, feet and hands bound with strips of linen, and his face wrapped in cloth. Jesus said to them, "Untie him; let him go." Néew bi génn ak càngaayam, tànk yeek loxo yi lëmëse, kanam ga muure. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
45 So many of the Jews who came to Mary and saw what Jesus did believed in him. Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama, ba ñu gisee la Yeesu def, ca lañu ko gëm.
46 But some of them went to the Pharisees and told them what Jesus had done. Teewul ñenn ca ñoom dem ca Farisen ya, ba nettali leen la Yeesu def.
47 So the chief priests and Pharisees convened the council and said, "What are we doing? For this man performs many signs. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya woo kuréelu àttekat ya, ne leen: «Ana lu nuy def nag? Ndax nit kii kat a ngi def firnde yu bare!
48 If we leave him alone, everyone will believe in him, and the Romans will come and take away both our place and our nation." Su nu ko bàyyee nii, ñépp a koy gëm, te kon kilifay Room dikk boole sunu béreb bu sell bi ak sunuw xeet, tas!»
49 But one of them, Caiaphas, high priest that year, told them, "You know nothing at all. Kenn ca ñoom nag ku ñuy wax Kayif te doon sarxalkat bu mag ba ca at mooma, ne leen: «Yeen, dangeena xamul dara.
50 Don't you see it's better for you that one man die for the people than the whole nation perish?" Yeen gisuleen sax ne seen njariñ moo di kenn nit doŋŋ deewal ñépp, ba askan wépp baña bokk sànku.»
51 He didn't say this on his own; as high priest that year, he prophesied Jesus would die for the nation, Loolu du lu Kayif wax ci sagoom, la mu doon sarxalkat bu mag ca at mooma, moo ko taxa jottali kàdduy waxyu yooyu mu biral, ne Yeesu mooy deewal xeet wi.
52 not only for the nation, but also to gather into one the scattered children of our Father. Te du xeet woowu doŋŋ la ko defal, waaye da koo def ngir itam dajale doomi Yàlla yi tasaaroo, ñu doon benn bopp.
53 So from that day on they plotted to put him to death. Bésub keroog nag la njiiti Yawut yi dogu ci rey Yeesu.
54 So Jesus no longer moved about openly among the Jews, but withdrew to a town called Ephraim near the wilderness, and stayed there with his disciples. Ci kaw loolu Yeesu jaareetul fu ñu koy gise ca Yawut ña, waaye fa la bàyyikoo, dem gox ba feggook màndiŋ ma, ca dëkk ba ñuy wax Efrayim. Foofa la toog aki taalibeem.
55 The Jews' Passover was near, and many went up from the country to Jerusalem before it to purify themselves. Bésub Mucc nag moo jubsi woon, di màggalu Yawut yi. Ci biir loolu ñu bare jóge ca dëkki kaw ga, jëm Yerusalem balaa bésu Mucc baa dikk, ngir setluji fa.
56 So they looked for Jesus, asking each other as they stood in the temple, "What do you think? Surely he won't come to the feast?" Ba mu ko defee ñuy seet Yeesu. Naka lañu taxaw ca kër Yàlla ga, di wax ca seen biir, naan: «Lu ngeen ci xalaat? Da dul ñëw ci màggal gi?»
57 The chief priests and Pharisees had ordered that anyone who knew his whereabouts must report it, so they could arrest him. Ci biir loolu sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya joxe ndigal ne képp ku xam fu Yeesu nekk, na ko xamle, ngir ñu jàpp ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]