Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 10 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "Truly, truly, I tell you: whoever doesn't enter the sheepfold through the gate, but climbs in another way, is a thief and a robber. «Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku duggewul ci buntu wërmbalu xar yi, xanaa mu yéege feneen, tëb, kooku ab sàcc la, ab saay-saay la.
2 But the one who enters by the gate is the shepherd of the sheep. Waaye ki dugge ci buntu wërmbal bi, kookooy sàmmub xar yi.
3 The gatekeeper opens for him, and the sheep hear his voice. He calls his own sheep by name and leads them out. Kooku la wattukat biy ubbil, xar yi di déglu baatam. Mooy woo xari boppam ci seen tur, génne leen.
4 After bringing all his own out, he goes ahead of them, and the sheep follow him because they know his voice. Bu génnee xaram yépp ba noppi, da leen di jiitu, ñu topp ci moom, ndax xàmmee nañu baatam.
5 They will never follow a stranger—they'll run from him, since they don't know the voice of strangers." Ab jàmbur nag, duñu ko topp mukk; dañu koy daw kay, ndax xàmmeewuñu baatub jàmbur.»
6 Jesus told them this figure of speech, but they didn't grasp what he meant. Léeb woowu la Yeesu léeb ci kanamu nit ñi, waaye ñoom xamuñu la mu leen wax.
7 So Jesus said again, "Truly, truly, I tell you, I am the gate for the sheep. Ci kaw loolu Yeesu neeti: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, man maay buntu wërmbalu xar yi.
8 "All who came before me are thieves and robbers, but the sheep did not listen to them. Mboolem ñi ma jiitu, ay sàcc aki saay-saay lañu, waaye xar yi dégluwuñu leen.
9 I am the gate; whoever enters through me will be saved, going in and out, finding pasture. Man maay bunt bi; ku dugge ci man, dinga mucc, di dugg aka génn, di gis mbooy goo fore.
10 The thief comes only to steal, kill, and destroy. I came so they may have life, and have it in abundance. Ab sàcc moom, dara indiwu ko lu moy sàcc aka rey aka yàq. Man maa ñëw, ngir nit ñi dund dund gu naat.
11 "I am the good shepherd. The good shepherd lays down his life for the sheep. «Man maay sàmm bi baax. Sàmm bu baax, bakkanam lay joxe, jote ko ay xaram.
12 The hired hand, not a shepherd, doesn't own the sheep. Seeing the wolf coming, he leaves the sheep and flees—the wolf snatches and scatters them. Kuy sàmmaan di feyeeku te dub sàmm, moomuli xar; bu séenee bukki buy dikk, day bàyyi xar ya, daw, bukki ba jàpp ca, tasaare la ca des.
13 The man runs away because he is a hired hand and cares nothing for the sheep. Ab sàmmaan kuy feyeeku rekk la, xalaatul xar ya, moo tax muy daw.
14 "I am the good shepherd. I know my own and my own know me, «Man maay sàmm bi baax. Maa xam sama xari bopp, ñoom it ñu xam ma.
15 as the Father knows me and I know the Father, and I lay down my life for the sheep. Noonu it laa xame Baay bi, Baay bi xame ma ni, te maay joxe sama bakkan, jote ko xar yi.
16 I have other sheep not of this fold; I must lead them too, and they will hear my voice. They will become one flock, one shepherd. Am naa it yeneen xar yu bokkul ci bii wërmbal. Ñoom it fàww ma indi leen, te dinañu dégg sama baat. Su ko defee muy gennug coggal, di bennub sàmm.
17 This is why the Father loves me: I lay down my life only to take it up again. Li tax Baay bi sopp ma, moo di sama bakkan laa joxe, ba man koo jëlaat.
18 No one takes it from me, but I lay it down on my own. I have authority to lay it down, and authority to take it up again. This charge I received from my Father." Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»
19 These words brought division among the Jews once again. Féewaloo nag amati ca Yawut ya, ndax kàddu yooyu.
20 Many of them said, "He is demon-possessed and out of his mind. Why listen to him?" Ñu bare ca ñoom naan: «Aw rab a ko jàpp! Dafa dof! Lu ngeen koy dégloo?»
21 But others said, "These aren't a demon-possessed man's words. Can a demon open blind eyes?" Ña ca des naan: «Jii wax du waxi ku rab jàpp. Ndax aw rab man naa muri bëti gumba?»
22 Then came the Feast of Dedication at Jerusalem. It was winter, Bés ba ñuy baaxantal daloog kër Yàlla ga la woon ca Yerusalem, yemook jamonoy sedd.
23 and Jesus was walking in the temple, in Solomon's Colonnade. Yeesoo nga doon doxantu ca kër Yàlla ga, ca mbaar ma ñuy wax Mbaarum Suleymaan.
24 The Jews surrounded him and said, "How long will you hold us in suspense? If you are the Christ, tell us plainly." Yawut ya yéew ko ne ko: «Loo deeti xaar ci dindil nu kumpa; su dee yaa di Almasi bi, wax nu lu leer!»
25 Jesus answered, "I told you, and you don't believe. The works I do in my Father's name testify about me, Yeesu ne leen: «Wax naa leen ko, yeena gëmul. Man, jëf ji may def ci sama turu Baay moo may seedeel.
26 but you do not believe, because you are not my sheep. Waaye yeen yeena gëmul, ndax bokkuleen ci samay xar.
27 My sheep listen to my voice; I know them, and they follow me. Samay xar, sama baat lañuy déglu; maa leen xam, te man lañuy topp.
28 I give them eternal life, and they will never perish, and no one will snatch them from my hand. Man maa leen di texeel ba fàww; duñu sànku mukk, te kenn du leen foqatee ci sama loxo.
29 My Father, who gave them to me, is greater than all; no one can snatch them out of the Father's hand. Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi.
30 I and the Father are one." Man ak Baay bi benn lanu.»
31 Again the Jews picked up stones to stone him. Yawut ya nag foratiy xeer yu ñu ko sànni, ngir rey ko.
32 Jesus replied, "I have shown you many good works from the Father. For which of these are you going to stone me?" Yeesu ne leen: «Jëf ju baax ju bare laa def ci ndigalal Baay bi. Ana ci yooyu jëf, jan ngeen ma nara sànnee ay xeer ba rey ma?»
33 "We're stoning you not for good work," they said, "but for blasphemy, because you, a mere man, claim to be God." Yawut ya ne ko: «Du jëf ju baax lanu lay sànneey xeer, ba rey la, waaye dangaa diir Yàlla mbagg. Yaw ngay nit doŋŋ te naan yaay Yàlla!»
34 Jesus answered them, "Is it not written in your Law: 'I have said you are gods'? Yeesu ne leen: «Xanaa bindeesul ci seen téereb yoon, kàddug Yàlla gii: “Dama ne ay yàlla ngeen”?
35 If he called them 'gods,' to whom the word of my Father came—and Scripture cannot be broken, Ndegam Yàlla moo woowe “yàlla” ñi kàddug Yàlla dikkal, te Mbindum kàddoom maneesu koo toxal,
36 what about the one the Father set apart and sent into the world? Why accuse me of blasphemy for saying, 'I am the Son of our Father'? kon man mi Yàlla beral boppam, yebal ma ci àddina, ana nu ngeen ma mana waxe ne: “Yaa diir Yàlla mbagg,” ndax li ma ne maay Doomu Yàlla?
37 "If I am not doing the works of my Father, then do not believe me. Su ma deful sama liggéeyu Baay, buleen ma gëm;
38 But if I do them, even if you won't believe me, believe the works, so you'll know and keep knowing the Father is in me, and I in the Father." waaye gannaaw moom laay def, su ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog jëf ji, ngir ngeen xam te ràññee ne Baay baa ngi ci man, te man it, maa ngi ci Baay bi.»
39 Again they tried to seize him, but he escaped their grasp. Ñu di ko jéematee jàpp nag, mu far rëcc leen.
40 Jesus then went back across the Jordan, to the place where John had first been baptizing, and stayed there. Ci kaw loolu Yeesu jàllaat dexu Yurdan, daldi dem fa béreb ba Yaxya njëkkoon di sóobe nit ñi, mu dal foofa.
41 Many came to him, saying, "John performed no sign, but all John said about this man was true." Ñu bare nag dikk, fekk ko fa, te naan: «Yaxya de wonewul jenn firnde, waaye mboolem lu mu wax ci kii, dëgg la.»
42 And in that place many believed in him. Ñu bare gëme ko foofa.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]