Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 9 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 As Jesus passed by, he saw a man who had been blind from birth. Yeesu moo doon dem, ba gis jenn waay ju judduwaale gumba.
2 His disciples asked him, "Rabbi, who sinned, this man or his parents, that he was born blind?" Taalibeem ya laaj ko ne ko: «Kilifa gi, ndax bàkkaaram a ko waral, walla bu waajuram, ba tax mu judduwaale gumba?»
3 "Neither this man nor his parents sinned,' Jesus answered, 'but this happened so the works of our Father might be revealed in him. Yeesu ne leen: «Du bàkkaaram, du bàkkaaru waajuram a tax. Da di liggéeyu Yàlla moo wara feeñe ci moom.
4 We must do the works of the one who sent me while it is day; night comes, when no one can work. Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey.
5 As long as I am in the world, I am the light of the world.'" Li feek maa ngi ci àddina, maay leeru àddina.»
6 Saying this, he spat on the ground, made mud from the saliva, and smeared it on the man's eyes. Loolu la Yeesu wax ba noppi, tifli fa suuf, tooyale ban ba lor wa, daldi diw bàq ba ca bëti gumba ga,
7 He told him, "Go, wash in the pool of Siloam" (meaning Sent). So the man went, washed, and returned able to see. ne ko: «Demal sëlmuji ca bëtu ndoxu Silowe.» Silowe di firi Ki ñu yónni. Gumba ga sëlmuji, délsi di gis.
8 Neighbors and those who'd seen him begging before said, "Isn't this the one who used to sit and beg?" Dëkkandoom ya ak ña ko xame woon yalwaan, naan: «Xanaa du kii moo daan toog, di yalwaan?»
9 Some said, "That's him." Others said, "No, he just looks like him." He kept saying, "I'm the one." Ñii naan: «Moom la!» Ñee naan: «Déedéet, da koo niru rekk.» Waa ji ci boppam ne: «Man la de!»
10 So they asked him, "Then how were your eyes opened?" Ñu ne ko: «Lu muri say bët?»
11 He replied, "The man called Jesus made mud, smeared it on my eyes, and told me, 'Go to Siloam and wash.' So I went, washed, and could see." Mu ne leen: «Waa ji ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, diw ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmuji ca bëtu ndoxu Silowe.” Ma dem sëlmuji, di gis.»
12 They said to him, "Where is he?" He said, "I do not know." Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.»
13 They brought the man who had been blind to the Pharisees. Ba mu ko defee ñu yóbbu nit ka gumba woon ca Farisen ya.
14 Now it was a Sabbath day when Jesus made the mud and opened his eyes. Ndeke bésub Noflaay la Yeesu tooyaloon ban ba, ba muri bëti gumba ga.
15 So the Pharisees also asked him again how he had gained sight. He told them, "He put mud on my eyes, and I washed, and I see." Loolu nag tax Farisen ya ñoom it, laaj ko nan la wére bay gis. Mu ne leen: «Ban la tooyal, diw ko ci samay bët, ma sëlmu, di gis.»
16 Some Pharisees said, "This man isn't from God—he doesn't keep the Sabbath." Others said, "How can a sinful man do such signs?" So they were divided among them. Ñenn ca Farisen ña nag naan: «Nit kii jógewul fa Yàlla, ndax sàmmul bésub Noflaay.» Ñeneen ña ne: «Nan la nitu neen kuy bàkkaar mana defe yii firnde?» Féewaloo daldi am ca seen biir.
17 Again they asked the blind man, "What do you say about him, since he opened your eyes?" He said, "He is a prophet." Farisen ya dellu wax ak ka gumba woon, ne ko: «Yaw, loo wax ci moom, gannaaw yaw la muril say bët?» Mu ne leen: «Ab yonent la.»
18 The Jews did not believe he had been blind and gained sight, until they summoned the parents of the man who had gained sight. Njiiti Yawut ya nag gëmuñu woon ne waa ja daa gumba woon bay doora gis noonu. Ñu daldi woolu waajuri ka gumba woon,
19 They asked them, "Is this your son you say was born blind? How then does he now see?" laaj leen ne leen: «Kii mooy seen doom ji ngeen ne gumba la judduwaale? Ana nu mu wére bay gis léegi?»
20 His parents answered, "We know that this is our son and that he was born blind. Waajur ya ne leen: «Xam nanu daal ne kii sunu doom la, te it gumba la judduwaale.
21 But how he now sees, we don't know; or who opened his eyes, we don't know. Ask him—he's an adult; he'll speak for himself." Waaye nu mu wére bay gis, xamunu ko; ki ko muril ay bëtam it, nun, xamunu ko. Laajleen ko, magum jëmm la; moom dina waxal boppam.»
22 His parents said this, fearing the Jews, since the Jews had already agreed that if anyone confessed Jesus as the Christ, he would be expelled from the synagogue. Noonu waajuri waa ja waxe nag, ragal njiiti Yawut ya moo taxoon, ndax fekk na njiiti Yawut ya mànkoo ne képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, dees na ko dàqe ca jàngu ba.
23 That was why his parents said, "He is of age; ask him." Looloo waral waajur ya ne: «Magum jëmm la, laajleen ko moom.»
24 So they called the once-blind man again and said, "Give God the glory. We know this man is a sinner." Farisen ya dellu woo ka gumba woon, ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Nun xam nanu ne waa jooju nit kuy bàkkaar la.»
25 He replied, "Whether he's a sinner, I don't know. I know one thing: I was blind, now I see." Mu ne: «Su dee kuy bàkkaar de, xawma ci dara. Lenn laa xam: maa gumba woon, te léegi maa ngi gis.»
26 They said to him, "What did he do to you? How did he open your eyes?" Ñu ne ko: «Lu mu la defal? Nu mu muree say bët?»
27 He answered them, "I already told you, and you didn't listen. Why do you want to hear it again? Do you also want to become his disciples?" Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, yeena dégluwul. Lu ngeen bëgg ci ma di ko waxaat? Xanaa yeen itam dangeena bëgga doon ay taalibeem?»
28 And they reviled him, saying, "You are his disciple, but we are disciples of Moses. Ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeb kii, waaye nun, taalibey Musaa lanu.
29 We know God spoke to Moses, but we don't know where this man is from." Nun xam nanu ne Musaa la Yàlla waxal, waaye kii, xamunu fu mu jóge.»
30 The man answered them, "Here's the amazing thing: you don't know where he's from, yet he opened my eyes. Waa ja ne leen: «Loolu kay mooy li yéeme! Yeen, xamuleen fu mu jóge, te mu muril ma samay bët!
31 We know God doesn't listen to sinners, but if anyone reveres God and does his will, God listens to him. Xam nanu ne kuy bàkkaar, Yàlla du ko déglu. Waaye ki ragal Yàlla, tey jëfe coobareem, kooku lay déglu.
32 Never since the world began has anyone heard of someone opening the eyes of a person born blind. Ba àddina sosoo ba tey, maseesu la dégg ku muri bëti gumbag judduwaale.
33 If this man were not from God, he could do nothing." Kon nit kii, su jógewul woon ca Yàlla, du mana def dara.»
34 They answered him, "You were born entirely in sin, yet you teach us?" and threw him out. Ñu ne ko: «Ndax yaw mi fees ak bàkkaar, bi nga juddoo ba léegi, yaa nuy xaali?» Ci kaw loolu ñu dàqe ko ca jàngu ba.
35 Jesus heard they had thrown him out, and finding him, said, "Do you believe in the Son of Man?" Ba Yeesu déggee ne dàq nañu waa ja gumba woon, dafa dem ba gis ko, ne ko: «Yaw, ndax gëm nga Doomu nit ki?»
36 He answered, "And who is he, sir, so I can believe in him?" Waa ja ne ko: «Kooku kan la, Sang bi, ma gëm ko.»
37 Jesus said to him, "You have seen him, and it is he who is speaking with you." Yeesu ne ko: «Gis nga ko; mooy kiy wax ak yaw.»
38 He said, "Lord, I believe," and he worshiped him. Mu ne ko: «Gëm naa la, Sang bi,» daldi koy sujjóotal.
39 Jesus said, "I came into this world for judgment, so those who don't see may see, and those who see may become blind." Yeesu ne ko: «Man, ab àttee ma taxa dikk ci àddina sii, ngir ñi dul gis di gis; ñiy gis, gumba.»
40 Some Pharisees with him heard this and said, "Are we blind too?" Ay Farisen yu taxawoon ca wetam dégg ca, ne ko: «Xanaa nun it danoo gumba?»
41 Jesus told them, "If you were blind, you would have no sin; but since you say, 'We see,' your sin remains." Yeesu ne leen: «Su ngeen gumba woon, dungeen am bàkkaar, waaye léegi bi ngeen naa yeena ngi gis, ci ngeen di saxe ci bàkkaar ba furr.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]