Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 8 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 But Jesus went to the Mount of Olives. Yeesu moom, dem ca tundu Oliw ya.
2 At dawn he came again to the temple; all the people came to him, and he sat down and taught them. Ca ëllëg sa ca njël, mu dellu ca kër Yàlla ga, ña fa nekk ñépp dikk, mu toog, di leen jàngal.
3 The scribes and Pharisees brought a woman caught in adultery and stood her in the middle. Firikati yoonu Musaa ya ak Farisen ya nag indi as ndaw su ñu jàppoon ci njaaloo, taxawal ko ca diggu mbooloo ma.
4 They said to him, "Teacher, this woman was caught in the act of adultery. Ñu ne Yeesu: «Kilifa gi, ndaw sii, dañu koo jàpp ci njaaloo.
5 Now in the Law, Moses commanded us to stone such women. So what do you say? Ci sunuw yoon nag, Musaa moo santaane ne jigéen ñii, dees leen di sànni ay xeer ba ñu dee. Yaw nag, ana loo ciy wax?»
6 They said this to test him, seeking grounds to accuse him. But Jesus bent down and wrote on the ground with his finger." Kàddu googu dañu ko ko doon seetloo, ba am lu ñu ko tiiñale. Teewul Yeesu sëgg, di bind ak baaraamam ci suuf.
7 When they kept questioning him, he stood up and said to them, "Whichever of you has no sin, cast the first stone at her." Naka lañu ko toppe ay laaj, mu siggi ne leen: «Ku masula bàkkaar ci yeen, na njëkka sànni ndaw si xeer.»
8 And once more he bent down and wrote on the ground. Ci kaw loolu mu sëggaat, di rëdd ci suuf.
9 Hearing this, they left one by one, starting with the oldest, until Jesus was left alone with the woman standing there. Ba nit ña déggee loolu, kenn-kenn lañu rocceeku, ña gën di mag jiitu. Yeesu doŋŋ a fa des, mook ndaw sa fa taxaw.
10 Jesus stood up and said to her, "Woman, where are they? Has no one condemned you?" Mu daldi siggi ne ko: «Ndaw sii, ana nit ñi? Kenn joxu la ci sab daan?»
11 She said, "No one, Lord." Jesus said, "I don't condemn you either. Go, and from now on, don't sin anymore." Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it duma la daan. Demal, te bul bàkkaarati.»
12 Jesus spoke to them again: "I am the world's light. Whoever follows me will never walk in darkness but will have the light of life." Yeesu waxati leen ne leen: «Man maay leeru àddina. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye leeru dund ngay am.»
13 So the Pharisees said to him, "You are bearing witness about yourself; your testimony is not true." Farisen ya ne ko: «Yaw yaa seedeel sa bopp, kon li nga wax wérul.»
14 Jesus replied, "Even if I testify about myself, my testimony is true, because I know where I came from and where I'm going; but you don't know where I come from or where I'm going. Yeesu ne leen: «Maa seedeel sama bopp, te teewul sama kàddug seede di lu wér, ndax xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Yeena xamul fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm.
15 You judge according to the flesh; I judge no one. Yeen, seen bindu suuxu neen ngeen di àttee ab daan; man nag duma àttee kenn ab daan.
16 Even if I judge, my judgment is true, since I do not judge alone, but I and the Father who sent me. Teewul nag, su ma dee àtte, samab àtte dëgg lay doon, nde du doon man doŋŋ, waaye maak Baay bi ma yebal lay doon.
17 In your Law it is written that the testimony of two people is true. Te itam bindees na ci seenu yoon ne seedes ñaari nit mooy li wér.
18 I testify about myself, and the Father who sent me testifies about me." Man may kenn, seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni itam seedeel na ma.»
19 They asked, "Where is your Father?" Jesus answered, "You know neither me nor my Father. If you knew me, you would know my Father also." Ñu ne ko: «Kuy sa baay?» Yeesu ne leen: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Su ngeen ma xamoon, xam ko, moom itam.»
20 He said this while teaching in the temple, in the treasury; no one seized him—his hour had not yet come. Ba Yeesu di wax loolu, ma ngay jàngale ca béreb ba ñuy denc xaalisu sarax, ca kër Yàlla ga. Booba kenn jàppu ko, ndax waxtoom a jotagul woon.
21 So he told them again, "I am going away. You will look for me and die in your sin. Where I am going, you cannot come." Yeesu neeti leen: «Man, maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deewaale. Man, fa ma jëm, yeen dungeen fa mana dem.»
22 So the Jews said, "Will he kill himself, since he says, "You can't come where I'm going"?" Yawut ya nag naan: «Xanaa day xaruji? Ndax kat nee fa mu jëm, dunu fa mana dem!»
23 He said to them, "You're from below; I'm from above. You're of this world; I'm not of this world. Yeesu ne leen: «Yeen, fu suufe fii ngeen bokk, waaye man fa kaw laa bokk. Yeen, ci àddina ngeen bokk, waaye man bokkuma fi àddina sii.
24 I told you that you'll die in your sins; if you don't believe I AM, you'll die in your sins." Moo tax ma ne leen, seeni bàkkaar ngeen di deewaale. Ndax kat su ngeen gëmul ne maay Ki nekk, seeni bàkkaar ngeen di deewaale.»
25 So they said to him, "Just who are you?" Jesus said to them, "Exactly what I've said from the start. Ñu ne ko: «Yaw yaay kan?» Yeesu ne leen: «Xanaa ki ma leen waxoon ca njàlbéen.
26 I have much to say and judge about you, but the One who sent me is true; what I heard from him, I tell the world." Am naa lu bare lu ma mana wax ci yeen ak lu ma leen àttee. Waaye ki ma yónni, ku dëggu la, te man, li ma dégge ci moom doŋŋ laay àgge àddina.»
27 They did not understand that he had been speaking to them about the Father. Booba xamuñu ne ci Yàlla Baay bi la leen di wax.
28 So Jesus told them, "When you lift up the Son of Man, then you'll know that I AM, and that I do nothing on my own, but say these things as the Father taught me. Yeesu nag ne leen: «Bu ngeen yékkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne man maay Ki nekk, te duma def dara ci sama wàllu bopp, waaye li ma Baay bi jàngal rekk laay wax.
29 The one who sent me is with me; he hasn't left me alone, because I always do what pleases him." Te it ki ma yónni moo ànd ak man; bàyyiwu ma, ma wéet, ndax man, li ko neex doŋŋ laay def.»
30 As he was saying these things, many believed in him. Ñu bare, ba ñu déggee Yeesu muy wax loolu, ca lañu ko gëm.
31 Jesus then told the Jews who had believed him, "If you remain in my word, you are truly my disciples, Yeesu moo waxoon Yawut yi ko gëmoon ne leen: «Bu ngeen saxee ci sama kàddu, samay taalibe dëgg ngeen.
32 and you will know the truth, and the truth will set you free." Su boobaa dingeen xam liy dëgg, te dëgg gi moo leen di goreel.»
33 They answered him, "We are Abraham's descendants, never enslaved to anyone. How can you say, 'You will become free'?" Ñu ne ko: «Nun askanu Ibraayma lanu, masunoo doon jaamu kenn. Kon ana loo nu naa dees na nu goreel?»
34 Jesus answered them, "Truly, truly, I tell you: everyone who keeps sinning is sin's slave. Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, képp kuy bàkkaar, ab jaamu bàkkaar la.
35 The slave does not remain in the house forever; the son remains forever. Te ab jaam bokkul ci kër gi ba fàww, doom a bokk ci kër gi ba fàww.
36 So if the Son sets you free, you will be free indeed. Kon nag su leen Doom ji goreelee, ngeen diy gor tigi.
37 I know you are Abraham's descendants; yet you seek to kill me because my word has no space in you. Xam naa ne askanu Ibraayma ngeen. Waaye yeena ngi may wuta rey, ndax sama kàddu ngeen xajoowul.
38 I speak what I've seen with my Father, and you do what you heard from your father." Man, li ma gis ci sama Baay laay wax, te yeen it li ngeen dégge ci seen baay ngeen di def.»
39 They answered, "Abraham is our father." Jesus said, "If you were Abraham's children, you'd do the works Abraham did, Ñu ne ko: «Sunu baay Ibraaymaa.» Yeesu ne leen: «Su ngeen doon doomi Ibraayma, jëfi Ibraayma ngeen di def.
40 but now you want to kill me—a man who told you the truth I heard from my Father. Abraham didn't do this. Waaye tey yeena ngi may wuta rey; man, nit ku leen àgge dëgg gu mu dégge fa Yàlla. Loolu de Ibraayma defu ko.
41 You do your father's works." They said to him, "We weren't born of sexual sin. We have one Father—God himself." Yeen, seen jëfi baay ngeen di def.» Ñu ne ko nag: «Nun de, dunu doomi moykat, te benn baay doŋŋ lanu am, muy Yàlla.»
42 Jesus said to them, "If God were your Father, you'd love me, for I came from God and am here. I didn't come on my own—he sent me. Yeesu ne leen: «Su Yàlla doon seen Baay, ngeen sopp ma, nde man, fa moom laa bàyyikoo, dikk. Dikkuma it ci sama coobarey bopp, waaye moom moo ma yebal.
43 Why don't you understand my speech? Because you cannot bear to hear my word. Lu waral xamuleen sama wax? Dangeena manula dégg sama kàddu.
44 You belong to your father, the devil, and want to carry out his desires. He was a murderer from the beginning, not standing in truth, since no truth is in him. When he lies, he speaks from his own nature, since he's a liar and the lie's father. Yeen ci seen baay Seytaane ngeen bokk, te seen xemmemtéefi baay ngeen namma def. Ca njàlbéen la dale di ab bóomkat. Masula taxaw ci dëgg, ndax dëgg a nekkul ci moom. Buy fen, jikkoom la topp, nde mooy fen-kat te di baayu fen.
45 But because I tell the truth, you do not believe me. Man nag, dëgg laay wax, moo tax gëmuleen ma.
46 Who among you convicts me of sin? If I speak truth, why don't you believe me? Kan ci yeen moo mana firndeel ne bàkkaar naa? Gannaaw dëgg laay wax nag, lu tax yeen, gëmuleen ma?
47 Whoever is from our Father hears his words; you don't hear because you're not from our Father." Ku bokk ci Yàlla, déglu ay kàddoom. Gannaaw dégguleen nag, bokkuleen ci Yàlla.»
48 The Jews replied, "Aren't we right in saying that you are a Samaritan and have a demon?" Yawut ya ne ko: «Xanaa yeyunu nag, ba nu nee nitu Samari nga, te aw rab a la jàpp?»
49 Jesus answered, "I do not have a demon, but I honor my Father, and you dishonor me. Yeesu ne leen: «Man de, aw rab jàppu ma; sama Baay laay teral, yeen ngeen di ma teddadil.
50 But I'm not seeking my own glory; our Father seeks it, and he judges. Man nag, sàkkuwuma sama darajay bopp, waaye am na ku ma koy sàkkul, te mooy àtte.
51 Truly, truly, I say to you, if anyone keeps my word, he will never see death." Maa leen ko wax déy, ci lu wér, ku sàmm sama kàddu, doo dee mukk.»
52 The Jews said to him, "Now we know you have a demon. Abraham died, as did the prophets, yet you say, 'Whoever keeps my word will never taste death.' Yawut ya ne ko: «Léegi nag wóor nanu ne aw rab a la jàpp! Ibraayma dee, yonent yi dee, yaw nga naay: “Ku sàmm sama kàddu, doo dee mukk!”
53 Are you greater than our father Abraham, who died? The prophets died too! Who do you claim to be?" Ndax yaw yaa gën sunu maam Ibraayma mi dee, te yonent yi itam dee? Koo teg sa bopp?»
54 Jesus answered, "If I glorify myself, my glory is nothing. It is my Father who glorifies me, of whom you say, 'He is our God.' Yeesu ne leen: «Su ma dee darajaal sama bopp, sama daraja amul solo. Sama Baay a may darajaal, ki ngeen ne mooy seen Yàlla.
55 You don't know him, but I know him. If I said I didn't know him, I'd be a liar like you. But I know him and keep his word. Xamuleen ko nag; man maa ko xam. Su ma noon xawma ko, di fen-kat ni yeen. Waaye xam naa ko te kàddoom laay sàmm.
56 Your father Abraham rejoiced that he would see my day. He saw it and was glad." Seen baay Ibraayma bànneex bu réy la doon séentoo sama bés. Gis na ko it, ba am ci mbégte.»
57 So the Jews said to him, "You're not yet fifty years old, and you've seen Abraham?" Yawut ya ne ko: «Amaguloo juróom fukki at, te gis nga Ibraayma!»
58 Jesus said to them, "Truly, truly, I say to you, before Abraham was, I AM." Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, balaa Ibraaymaa juddu, man maa nekk.»
59 So they grabbed stones to throw at him, but Jesus hid himself and slipped out of the temple. Ca lañu for xeer yu ñu ko sànnee, ngir rey ko. Teewul Yeesu làqu, ba génn kër Yàlla ga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]