Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 7 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After this, Jesus traveled around Galilee, not wanting to go into Judea because Jewish leaders there were looking for a chance to kill him. Gannaaw loolu Yeesu diiwaanu Galile la doon wër. Bëggul woona doxe biir diiwaanu Yude, ndax njiiti Yawut ya ñoo ko doon wuta rey.
2 But the Jewish Festival of Booths was near. Ci biir loolu màggalu Yawut gi ñuy wax Mbaar yi, jubsi.
3 His brothers told him, "Leave here and go to Judea, so your disciples can also see the works you do. Rakki Yeesu yu góor ya ne Yeesu: «Jógeel fii te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe, ñoom itam, gis jaloore yi ngay def.
4 No one seeking public attention hides what he does. If you're doing these things, show yourself to the world." Kenn du jëfe biir kumpa tey wuta feeñ. Gannaaw yaay def yii jaloore, wonal sa bopp àddina,»
5 For not even his brothers believed in him. ndax booba ay rakkam sax gëmuñu ko woon.
6 So Jesus told them, "My time has not yet come, but for you any time is right. Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul; yeen nag, seen waxtu bopp, bés bu nekk la.
7 "The world cannot hate you, but it hates me, because I testify that its works are evil. Àddina du leen mana bañ, waaye man la bañ, ndax maa koy seedeel ne ay jëfam dafa bon.
8 You yourselves go up to the festival; I'm not going up to this festival, since my time hasn't yet fully come." Yeen nag demleen màggal ga, man demuma ca màggal googu, ndax sama waxtu jotagul.»
9 After saying this, he stayed in Galilee. Loolu la leen wax, daldi des ca Galile.
10 After his brothers went up to the festival, he too went up—not openly, but secretly. Teewul ba rakki Yeesu demee ca màggal ga, Yeesu itam dem na ca, waaye siiwalul aw yoonam, daanaka daa làqu.
11 So the Jewish leaders were looking for him at the festival and asking, "Where is he?" Yawut ya nag di ko seet, naan: «Ana waa ji?»
12 Much murmuring about him spread among the crowds: some said, "He's good," others, "No, he misleads the crowd." Ci kaw loolu déeyoo bi ci mbiram bare ca mbooloo ma. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day naxe.»
13 Yet no one spoke about him openly, for fear of the Jewish leaders. Waaye taxul kenn waxe mbiram ca kaw, ndax ragal njiiti Yawut ya.
14 About the middle of the festival, Jesus went up into the temple and began to teach. Ba ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem ca kër Yàlla ga, di jàngale.
15 The Jewish leaders were amazed and asked, "How does this man know so much without training?" Yawut ya jaaxle, naan: «Kii nu mu ame bii xam-xam te jàngul?»
16 Jesus answered them, "My teaching isn't mine—it's from the one who sent me. Yeesu daldi leen wax ne leen: «Li may jàngale, moomuma ko, ki ma yebal a ko moom.
17 Whoever wants to do our Father's will knows if my teaching is from my Father or I speak on my own. Ku namma jëfe coobarey Yàlla, dina xam ndax li may jàngale ci Yàlla la jóge, am ci sama coobarey bopp laay waxe.
18 Whoever speaks on his own seeks his own glory, but whoever seeks the sender's glory is true, with no falsehood in him. Kiy wax ci coobarey boppam nag, darajay boppam lay sàkku, waaye ki bëgga fésal darajay ki ko yónni, kooku ku dëggu lay doon, te ag njubadi du nekk ci moom.
19 Didn't Moses give you the law? Yet none of you obeys the law. Why are you trying to kill me?" Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali yoon wi? Ndaxam kenn ci yeen jëfewul yoon wi! Ana lu ngeen may wuta rey?»
20 The crowd answered, "You have a demon! Who is trying to kill you?" Mbooloo ma ne ko: «Yaw rab a la jàpp! Ku lay wuta rey?»
21 Jesus replied, "I did one work, and you are all amazed. Yeesu ne leen: «Jenn jaloore doŋŋ laa def, yeen ñépp ngeen waaru!
22 "Moses gave you circumcision—not from Moses, but the patriarchs—and you circumcise a man on the Sabbath. Ndigalu xarafal gi leen Musaa jox, doonte jógewul ci Musaa, waaye cay maam la ba tey, tax na ngeen di xarafale ci bésub Noflaay sax.
23 If a man is circumcised on the Sabbath so the law of Moses isn't broken, why are you angry at me for making a whole man well on the Sabbath? Gannaaw nit ay xaraf ci bésub Noflaay, ngir yoonu Musaa baña tebbiku, ana lu ngeen ma meree ndax nit ku ma wéral péŋŋ ci bésub Noflaay?
24 Stop judging by appearances, and judge with right judgment." Bàyyileen di àttee li leen seen bët may, deeleen àttee dëgg.»
25 Then some Jerusalemites said, "Isn't this the man they want to kill? Ci kaw loolu ñenn ci waa Yerusalem naan: «Xanaa du kii lees di wuta rey?
26 Yet he speaks openly, and they say nothing to him. Can the rulers truly know this is the Christ? Te mu ngii ne fàŋŋ di waare, te waxuñu ko dara. Xanaa sunu kilifa yi dañoo xam ne kii mooy Almasi bi?
27 But we know this man's origin. When the Christ comes, no one will know his origin." Moonte kii, xam nanu fu mu bokk, te su Almasi bi dikkee, kenn du xam fu mu bokk.»
28 Then Jesus, teaching in the temple, cried out: "You know me, and know where I'm from. Yet I didn't come on my own—the one who sent me is true, and you don't know him. Ci kaw loolu Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga, daldi biral ne: «Kon xam ngeen ma, xam fi ma bokk? Ndaxam du ci sama coobarey bopp laa dikke, te ki ma yónni, ku wóor la. Yeen nag xamuleen ko.
29 I know him, because I am from him, and he sent me." Man maa ko xam, ndax ci moom laa bàyyikoo, te moom moo ma yebal.»
30 So they tried to grab him, but no one touched him, because his hour had not yet come. Ba mu ko defee ñu di ko wuta jàpp, waaye kenn tegu ko loxo, ndax waxtoom moo jotagul woon.
31 But many in the crowd believed in him, asking, "When the Christ comes, will he do more signs than this man did?" Teewul ñu bare ca mbooloo ma gëm ko, te naan: «Almasi bi sax, bu dikkee, ndax dina def firnde yu ëpp firnde yi nit kii def?»
32 The Pharisees heard the crowd murmuring these things about him, so the chief priests and Pharisees sent temple guards to seize him. Farisen ya dégg loola mbooloo may déeyoo ci mbirum Yeesu. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya daldi yebal ay wattukati kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
33 So Jesus said, "I'm with you a little while longer, and then I go to the one who sent me. Yeesu nag ne: «Diir bu gàtt laay toogaat ak yeen, doora dem ca ki ma yónni.
34 You will search for me and not find me; you cannot come where I am." Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te man fa may nekk, yeen, dungeen fa mana dem.»
35 So the Jewish leaders asked each other, "Where does he intend to go that we won't find him? Does he intend to go to our people dispersed among the Greeks and teach the Greeks? Yawut ya naan ca seen biir: «Kii fu muy waaja jëm, fu ñu ko dul gise? Xanaa ca Yawut ya dëkki ca jàmbur ña? Xanaa jàmbur ña lay jàngali?
36 What does he mean: 'You will look for me, but you will not find me,' and 'Where I am, you cannot come'?" Ak luy tekkitel kàddu gii mu wax, ne: “Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te man fa may nekk, yeen dungeen fa mana dem?”»
37 On the last, great day of the festival, Jesus stood and called out, "Whoever is thirsty, let him come to me and drink. Bés ba mujj ca màggal ga nag moo ca gënoona màgg. Keroog la Yeesu taxaw, àddu ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man, naan;
38 Whoever believes in me, as Scripture said, rivers of living water will flow from his heart." ku ma gëm, ay dex ay balle cib dënnam, di wal ndox muy dund! Te noonu la ko Mbind mi indee.»
39 He said this about the Holy Spirit, whom believers in him were to receive; the Spirit had not yet been given, since Jesus had not yet been glorified. Booba Noowug Yàlla la doon wax, Noo ga gëmkati Yeesu doon waaja jot, te jotaguñu ko woon, ndax booba, Yeesoo tàbbeegul woon ci teraangaam.
40 When they heard these words, some of the crowd said, "This really is the Prophet." Ba ñenn ca mbooloo ma déggee kàddu yooyu, dañu ne: «Aylayéwén kii mooy Yonent bi.»
41 Others said, "This is the Christ." But others asked, "How can the Christ come from Galilee? Ñeneen naan: «Kii mooy Almasi bi!» Teewul mu am ñu naan: «Galile, nu fa Almasi biy jógee?
42 Doesn't Scripture say the Christ comes from David's line and from Bethlehem, David's village?" Du Mbind mi moo wax ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay soqikoo, ca Betleyem, dëkk ba Daawuda fekk baax?»
43 So the crowd was divided over him. Féewaloo nag am ca mbooloo ma ndax Yeesu.
44 Some of them wanted to seize him, but no one laid a hand on him. Ñenn ca ñoom bëggoon nañu koo jàpp, waaye kenn tegu ko loxo.
45 So the temple guards returned to the chief priests and Pharisees, who asked, "Why didn't you bring him?" Ba loolu amee wattukat ya dellu ca sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya. Ñooñu ne leen: «Lu tax indiwuleen ko?»
46 The guards answered, "No one ever spoke the way this man does." Wattukat ya ne leen: «Nit masula waxe ni kii!»
47 "Have you also been deceived?" the Pharisees answered. Farisen ya ne leen: «Kon yeen itam nax nañu leen a?
48 "Has any of the rulers or of the Pharisees believed in him? Ndax yeena gis ci njiit yi mbaa ci Farisen yi, kenn ku ko gëm?
49 But this crowd, who knows nothing of the law—they are under a curse." Xanaa mbooloo mii xamul yoonu Musaa, te ñu alku lañu!»
50 Nicodemus, who had gone to Jesus earlier and was one of their own number, asked them, Nikodem bokk na ca Farisen ya fa nekkoon, te demoon na seeti Yeesu lu jiitu loolu. Mu ne leen:
51 "Does our law condemn a man without first hearing him and finding out what he does?" «Sunuw yoon ndax dina daan nit te njëkkeesu koo déglu, boole ci xam lu mu def?»
52 They replied, "Are you from Galilee too? Search, and see: no prophet arises from Galilee." Ñu ne ko: «Xanaa yaw itam ci diiwaanu Galile nga bokk? Gëstul, kon dinga xam ne Galile, ab yonent du fa feeñe.»
53 Then they all went home. Ba loolu amee ku nekk ñibbi këram.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]