Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 6 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After this, Jesus crossed the Sea of Galilee, also called the Sea of Tiberias. Gannaaw loolu Yeesu jàll ca wàllaa dexu Galile, ga ñuy wax dexu Tiberyàdd itam.
2 A large crowd followed him, because they saw the signs he performed on the sick. Mbooloo mu bare topp ca moom, ndax ñoo gis firnde ya mu wérale jarag ya.
3 Jesus went up on the mountainside and sat down there with his disciples. Yeesu yéeg ca kaw tund wa, daldi toog foofa ak ay taalibeem.
4 Now the Passover, the feast of the Jews, was near. Booba màggalu Yawut ga ñuy wax bésub Mucc, jubsi na.
5 Looking up, Jesus saw a large crowd approaching and asked Philip, "Where can we buy bread for these people to eat?" Yeesu dawal bëtam, gis mbooloo mu réy mu dikk, jëm ca moom. Mu ne Filib: «Fu nuy jële mburu mu nu leen leele?»
6 He said this to test Philip, for he himself already knew what he was going to do. Loolu nag da koo wax ngir seetlu Filib, ndax moom ci boppam xamoon na la mu nar.
7 Philip answered him, "200 days' wages of bread isn't enough for each of them to get a little." Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax jëndul mburu mu leen doy, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci ndog su tuut.»
8 One of his disciples, Andrew, Simon Peter's brother, said to him, Àndre, keneen ca taalibe ya, te bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko:
9 "A boy here has five barley loaves and two fish—but what's that for so many?" «Ab xalee ngi fi de, am na juróomi mburu ak ñaari jën, waaye loolu lu mu jariñ ñu tollu nii?»
10 Jesus said, "Have the people sit down." Much grass grew there, so about 5,000 men sat down. Yeesu daldi ne: «Toogalleen nit ñi.» Ñax mu baree nga woon ca béreb booba. Góor ña nag toog, seenub lim wara tollu ci juróomi junni (5 000).
11 Jesus then took the loaves, gave thanks, and distributed them to those seated; likewise with the fish, as much as they wanted. Yeesu jël mburu ya, yékkati kàddug cant, daldi ko séddale ña fa toog. Jën ya itam noonu, ñu lekk ba doyal.
12 When they were full, he told his disciples, "Gather the leftover pieces, so nothing is lost." Ba ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibeem ya: «Dajaleleen desiti mburu mi, ba dara du ci yàqu.»
13 So they gathered the fragments left over from the five barley loaves after the people ate, filling twelve baskets. Ñu dajale ba feesal fukki pañe ak ñaar ci dogi juróomi mburu ya ñu lekk ba desal.
14 So when the people saw the sign he did, they said, "This really is the Prophet coming into the world!" Ba nit ña gisee firnde jooju Yeesu def, dañu ne: «Kii daal, dëgg-dëgg mooy Yonent bi dikk ci àddina!»
15 Knowing they meant to come and seize him to make him king, Jesus withdrew again to the mountain alone. Yeesu nag gis ne dañoo nara dikk, jàpp ko yóbbu, ngir fal ko buur, mu daw dellu, moom kenn ca tund wa.
16 When evening came, his disciples went down to the sea, Ba jant sowee, taalibeem ya dem ca tefes ga.
17 got in a boat and headed across the sea to Capernaum. It was already dark, and Jesus had not yet reached them. Ci kaw loolu ñu dugg gaal, ngir jàll jëm Kapernawum, ndax booba lëndëm na te Yeesu agseegul.
18 A strong wind was blowing, and the sea grew rough. Dex ga nag yëngu lool, ndax ngelaw lu jóg ak doole.
19 After rowing three or four miles, they saw Jesus walking on the water, approaching the boat, and were afraid. Ba taalibe ya joowee lu tollook juróomi kilomet ba juróom benn, Yeesu lañu séen, muy dox ca kaw dex ga, jëm ca gaal ga, ñu daldi tiit.
20 But he said to them, "It is I; do not be afraid." Yeesu ne leen: «Man mii la, buleen tiit!»
21 So they were glad to take him into the boat, and instantly it reached the shore they were heading toward. Ñu door koo nangoo dugal ca gaal ga. Ci kaw loolu gaal ga teeri ca saa sa, fa ñu jëm.
22 The next day, the crowd remaining on the far shore saw that only one boat had been there, that Jesus had not boarded it with his disciples, but that his disciples had gone off alone. Ca ëllëg sa mbooloo ma des ca geneen wàllaa dex ga, seetlu ne genn gaal doŋŋ a fa nekkoon, te Yeesu àndul woon ak taalibe ya ca gaal ga ñu dugg, waaye taalibe ya rekk a dem.
23 Other boats came from Tiberias near the place where they ate bread after the Lord gave thanks. Gannaaw gi la yeneen gaal jóge Tiberyàdd, teersi fa feggook béreb ba nit ña lekke woon mburu ma, gannaaw ba Sang bi yékkatee kàddug cant.
24 So when the crowd saw Jesus and his disciples weren't there, they got in boats and went to Capernaum to look for Jesus. Ba mbooloo ma gisee nag ne Yeesu ak taalibe ya, kenn nekku fa, gaal yooyu lañu dugg, dem seeti ko Kapernawum.
25 Finding him across the sea, they asked, "Rabbi, when did you get here?" Ci kaw loolu ñu fekk Yeesu ca geneen wàllaa dex ga, ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?»
26 Jesus answered them, "Truly, truly, I tell you: you seek me not because you saw signs, but because you ate the loaves and were filled. Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, yeen du firnde yi ngeen gis a tax ngeen di ma seet, waaye mburu mi ngeen lekk ba regg moo tax.
27 Don't work for food that spoils, but for food that lasts to eternal life, which the Son of Man will give you. For on him our Father has set his seal." Ñam wuy yàqu, bumu leen taxa liggéey; liggéeyalleen ñam wi sax, ñam wiy texeel fàww, te Doomu nit ki moo leen koy jox, ndax moom la Yàlla màndargaal, ngir firndeel ne moom la tànn.»
28 Then they said to him, "What must we do to be doing the works of our Father?" Ñu ne ko: «Ana lu nuy def, ba jëfe jëf ji neex Yàlla?»
29 Jesus answered them, "This is our Father's work: that you believe in the one he sent." Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, mooy ngeen gëm ki mu yebal.»
30 So they asked him, "What sign will you give, so we may see and believe you? What work will you do? Ñu ne ko: «Jan firnde ngay def, nu gis ba gëm la? Ana jëf joo nu mana defal?
31 Our ancestors ate manna in the wilderness, as it is written: 'He gave them bread from heaven to eat.'" Sunuy maam de, mànn lañu dunde ca màndiŋ ma, te noonu lañu binde ne: “Peppum asamaan la leen leel.”»
32 Jesus told them, "Truly, truly, I tell you: Moses didn't give you the bread from heaven—my Father gives you the true bread from heaven. Yeesu neeti leen: «Maa leen ko wax déy, ci lu wér, du Musaa moo leen jox ñamu asamaan, sama Baay la, te moo leen jox tey ñamu asamaan dëgg.
33 For the bread of our Father is he who comes down from heaven and gives the world life." Ndaxte ñamu Yàlla mooy ki wàcce asamaan te kooku moo may àddina ñu dund.»
34 So they said to him, "Lord, give us this bread always." Ñu ne ko nag: «Sang bi, dee nu may saa su ne ci woowu ñam!»
35 Jesus told them, "I am the bread of life. Whoever comes to me will never hunger; whoever believes in me will never thirst. Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar mukk.
36 But as I told you, you have seen me and still do not believe. Waaye wax naa leen ko; gis ngeen ma, te taxul ngeen gëm!
37 All the Father gives me will come to me, and the one who comes to me I will never drive away. Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk.
38 For I came down from heaven not to do my own will, but the will of him who sent me. Def sama coobarey bopp taxul ma wàcce fa asamaan, waaye def coobarey ki ma yónni moo tax.
39 This is the will of him who sent me: that I lose none of all he has given me, but raise them up on the last day. Ki ma yónni nag, coobareem moo di mboolem ñi mu ma jox, buma ci ñàkk kenn, waaye naa leen dekkal kera bés bu mujj ba.
40 For this is the will of my Father: that everyone who looks to the Son and believes in him should have eternal life, and I will raise them up on the last day." Ndax sama coobarey Baay kat moo di képp ku gis Doom ji te gëm ko, na texe ba fàww, te maa koy dekkal keroog bés bu mujj ba.»
41 So the Jews grumbled about him because he said, "I am the bread that came down from heaven." Yawut ya nag di ñurumtoo Yeesu, ndax la mu ne: «Man maay ñam wi wàcce fa asamaan.»
42 They said, "Isn't this Jesus, Joseph's son, whose father and mother we know? How can he now say, 'I have come down from heaven'?" Ñu naan: «Xanaa kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Nun, nu xam baayam, xam ndeyam. Ana nu mu mana waxe ne asamaan la jóge?»
43 Jesus answered them, "Stop grumbling among yourselves. Yeesu ne leen: «Baleen ñurumtu bi ci seen biir.
44 "No one can come to me unless the Father who sent me draws him, and I will raise him on the last day. Kenn manula ñëw ci man te Baay bi ma yónni indiwu ko; te ku ñëw ci man, maa koy dekkal kera bés bu mujj ba.
45 It is written in the Prophets: 'And they will all be taught by our Father.' Everyone who has heard and learned from the Father comes to me. Bindees na ci téerey yonent yi ne: “Ñoom ñépp ay jànge ci Yàlla.” Kon nag képp ku dégg Baay bi, ba déggal àlluwaam, dina ñëw ci man.
46 Not that anyone has seen the Father except the one from him; he has seen the Father. Tekkiwul ne kenn mas naa gis Baay bi. Xanaa ki bawoo fa Yàlla, kookoo gis Baay bi.
47 Truly, truly, I tell you, whoever believes has eternal life. Maa leen ko wax déy, ci lu wér, ku gëm, yaa texe ba fàww.
48 I am the bread of life. Man maay ñam wiy joxe dund.
49 Your ancestors ate the manna in the wilderness, yet they died. Seeni maam a lekk mànn ca màndiŋ ma, te dee nañu.
50 This is the bread that comes down from heaven, so anyone may eat it and not die. Waaye ñam wii mooy wi wàcce fa asamaan, ngir ku ko lekk, du dee.
51 I am the living bread come down from heaven. Whoever eats this bread will live forever. The bread I will give is my flesh, for the life of the world." Man maay ñam wiy dund te wàcce fa asamaan. Ku lekk ci wii ñam, mooy texe ba fàww. Ñam woowu nag mooy samaw suux; maa ko joxe, ngir àddina dund.»
52 Then the Jews argued sharply among themselves, "How can this man give us his flesh to eat?" Ci kaw loolu Yawut ya di werante werante wu tàng ci seen biir naan: «Ana nu nu kii mana joxee aw suuxam, nu lekk?»
53 Jesus told them, "Truly, truly, I tell you, unless you eat the flesh of the Son of Man and drink his blood, you have no life in yourselves. Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, bu ngeen lekkul ci suuxu Doomu nit ki, naan deretam, amuleen dund ci seen jëmmi bopp.
54 Whoever feeds on my flesh and drinks my blood has eternal life, and I will raise him on the last day. Képp ku lekk samaw suux, naan sama deret, texe nga ba fàww, te maa lay dekkal kera bés bu mujj ba.
55 For my flesh is true food, and my blood is true drink. Ndaxte sama yaram mooy ñam wi wóor, sama deret di naan gi wóor.
56 Whoever feeds on my flesh and drinks my blood remains in me, and I in him. Képp ku lekk sama suux, naan sama deret, ci man lay dëkk, ma dëkk ci moom.
57 As the living Father sent me and I live because of the Father, so whoever feeds on me will live because of me. Ni ma Baay biy dund yebale, te may dund ndax moom, noonu la ki ma lekk di dunde ndax man.
58 This is the bread that came down from heaven. It is not like the bread your ancestors ate and still died. Whoever feeds on this bread will live forever." Woowu ñam mooy wi wàcce fa asamaan; bokkul ak ñam wa seeni maam lekkoon te teewuleena dee. Ku lekk wii ñam, yaay texe ba fàww.»
59 He said these things while teaching in the synagogue at Capernaum. Baat yooyu la Yeesu wax, ba muy jàngale ca jàngub Yawut ba, ca Kapernawum.
60 On hearing it, many of his disciples said, "This is a hard teaching. Who can accept it?" Taalibey Yeesu yu bare, ba ñu déggee loolu, dañu ne: «Gii kàddooka jafe! Ana ku ko mana dégg?»
61 Aware that his disciples were grumbling about this, Jesus said to them, "Does this offend you? Yeesu nag yég ci boppam ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu. Mu ne leen: «Xanaa kàddu gii mbetteel la leen def?
62 "Then what if you see the Son of Man ascending to where he was before? Kon bés bu ngeen gisee Doomu nit kiy yéeg jëm fa mu njëkkoona nekk nag?
63 The Spirit gives life; the flesh helps nothing. The words I have spoken to you are spirit and life. Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.
64 But some of you don't believe." For Jesus knew from the start who didn't believe, and who would betray him. Waaye am na ñenn ñu bokk ci yeen, ñu gëmul.» Ndax kat Yeesu xamoon na ca njàlbéen ñan ñooy ña gëmul woon, ak kan mooy ka koy wor.
65 And he said, "This is why I told you: no one can come to me unless the Father enables him." Mu teg ca ne: «Looloo tax ma ne leen kenn manula ñëw ci man, te du Baay bi moo ko ko may.»
66 From this time many of his disciples turned back and no longer walked with him. Booba la taalibeem yu bare dëpp, àndatuñu ak moom.
67 So Jesus asked the Twelve, "Do you want to leave too?" Yeesu nag ne fukki taalibe yaak ñaar: «Yeen itam bëgg ngeena dem am?»
68 Simon Peter answered him, "Lord, to whom should we go? You have the words of eternal life. Simoŋ Piyeer ne ko: «Sang bi, ci kan lanu jëm? Kàddu giy texeel fàww, yaa ko yor!
69 We have believed and known you are the Holy One of our Father." Nun gëm nanu te ràññee nanu ne yaa di Aji Sell ju Yàlla ji.»
70 Jesus answered them, "Have I not chosen you, the Twelve? Yet one of you is a devil." Yeesu ne leen: «Xanaa du man maa leen tànn, yeen Fukk ak ñaar? Ndaxam kenn a ngi bokk ci yeen te ab seytaane la!»
71 He meant Judas, son of Simon Iscariot, one of the Twelve, who was about to betray him. Yuda doomu Simoŋ Iskaryo la doon wax, ndax mooy ka ko doon waaja wor, te ca Fukk ñaak ñaar la bokkoon.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]