Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 5 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After this there was a feast of the Jews, and Jesus went up to Jerusalem. Gannaaw loolu, ag màggal la Yawut ya xewle woon, ba tax Yeesu dem Yerusalem.
2 By the Sheep Gate in Jerusalem is a pool with five covered porches, called Bethesda in Aramaic. Ca Yerusalem nag, fa feggook buntu dëkk ba ñu dippee buntu Xar ya, ab déeg a nga fa woon, ñu di ko woowe ci làkku yawut, Betesda, te juróomi mbaar a nga fa woon.
3 In these lay a multitude of the sick—blind, lame, and paralyzed. Ci mbaar yooyu la jarag ju bare daan tëdd; ay gumba, ay làggi aki lafañ, di xaar ndox mi yëngu,
4 Not in this edition ndax am malaakam Boroom bi lañu foogoon ne daan na fa wàcc ci yenn bés, te bu ndox ma yëngoo, jarag bu jiitu ca biir ndox ma, wopp joo amoon, day wér ca saa sa.
5 One man was there who had been sick for thirty-eight years. Jenn waay a nga fa woon, fanweeri at ak juróom ñett la nekk ak woppam.
6 Seeing him lying there and knowing he had already been there a long time, Jesus asked, "Do you want to be healed?" Kooku la Yeesu gis mu tëdd, mu xam ne yàgg na fa. Mu ne ko: «Ndax bëgg ngaa wér?»
7 The sick man answered him, "Sir, I have no one to put me in the pool once the water stirs—while I'm on my way, someone else gets in first." Jarag ji ne ko: «Sang bi, damaa amul ku ma sóob ci ndox mi, bu yëngoo. Bu ma cay jëm, keneen jiitu ma, tàbbi ca.»
8 Jesus said to him, "Get up, take up your mat, and walk." Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.»
9 At once the man became well, picked up his mat, and walked. That day was the Sabbath. Mu wér ca saa sa, jël basaŋam, daldi dox. Bés booba bésub Noflaay la woon.
10 So the Jews told the healed man, "It's the Sabbath—you're not allowed to carry your mat." Loolu nag tax njiiti Yawut ya ne nit kay doora wér: «Tey bésub Noflaay la, mayeesu la nga gàddu sa basaŋ.»
11 He answered them, "The man who healed me told me, 'Take up your mat and walk.'" Mu ne leen: «Ki ma wéral moom moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»
12 They asked him, "Who is the man who told you, 'Take it up and walk'?" Ñu ne ko: «Ana nit ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox”?»
13 But the healed man didn't know who it was, since Jesus had slipped away into the crowd there. Waa ji nag xamul ka ko wéral ku mu doon, te fekk na Yeesu dem ba réer ca biir mbooloo mu bare ma teew foofa.
14 Later Jesus found him in the temple and said, "You are healed now. Stop sinning, or something worse may happen to you." Gannaaw loolu Yeesu dajeek moom ca kër Yàlla ga, ne ko: «Ma ne, léegi wér nga. Bul bàkkaarati nag, bala laa lu ko yées di dikkal.»
15 The man went away and told the Jews that it was Jesus who had made him well. Ba loolu amee waa ja dem, ne Yawut ya Yeesu moo ko wéral,
16 And so the Jews began persecuting Jesus, because he was doing these things on the Sabbath. ba loolu tax Yawut ya di bunduxataal Yeesu, ndax bésub Noflaay ba mu ko defe.
17 But Jesus answered them, "My Father is working until now, and I too am working." Teewul Yeesu ne leen: «Sama Baay a saxoo liggéey, man itam may liggéey.»
18 So the Jews sought even more to kill him: he not only broke the Sabbath but called our Father his own Father, making himself equal to him. Kàddu googu nag tax njiiti Yawut yi gën koo wuta rey, ndax du ndigalu bésub Noflaay bi mu xëtt doŋŋ, waaye itam la mu ne Yàlla mooy Baayam, di nawlante ak Yàlla.
19 So Jesus said to them, "Truly, truly, I tell you: the Son can do nothing on his own, but only what he sees the Father doing. Whatever the Father does, the Son does the same. Yeesu dellu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, Doom ji manula def dara ci jëmmu boppam, lu moy li mu gis Baay bi def ko, ndax lu mu def, loolu itam la Doom ji di def.
20 "For the Father loves the Son and shows him everything he does; he will show him greater works than these, so you will be amazed. Baay bi moo sopp Doom ji, ba won ko lépp lu muy def, te jëf ju raw jii la koy won, ngir ngeen waaru,
21 For as the Father raises the dead and gives life, so the Son too gives life to anyone he wants. ndax kat, ni Baay bi di dekkale ñi dee, dundal leen, noonu la Doom jiy dundale ku mu namma dundal.
22 For the Father judges no one, but has entrusted all judgment to the Son, Baay bi du àtte kenn; Doom ji la dénk àtte bi bépp,
23 so everyone honors the Son as they honor the Father; whoever doesn't honor the Son doesn't honor the Father who sent him. ngir ñépp teral Doom ji, ni ñu terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay bi ko yónni.
24 Truly, truly, I tell you: whoever hears my word and believes the one who sent me has eternal life and won't face judgment—they have passed from death to life. «Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku dégg sama kàddu ba gëm ki ma yónni, yaa texe ba fàww, te àtte ba, doo ca jaare, waaye bàyyikoo nga ci dee, tàbbi ci dund.
25 Truly, truly, I tell you, an hour comes, and is now here, when the dead will hear the voice of the Son of our Father, and those hearing will live. Maa leen ko wax déy ci lu wér, waxtu waa ngi ñëw, te léegi la; mooy waxtu wi ñi dee di dégg baatu Doomu Yàlla, te ñi ko dégg ñooy dundaat.
26 For as the Father has life in himself, he gave the Son to also have life in himself. Ndax kat ni Baay bi jagoo dund ci jëmmu boppam, noonu la maye Doom ji mu jagoo dund ci jëmmu boppam,
27 And he has given him authority to execute judgment, because he is the Son of Man. te sañ-sañu amal àtte bi itam, moom la ko jox, ndax mooy Doomu nit ki.
28 Don't be astonished at this—an hour is coming when everyone in the tombs will hear his voice, «Bu leen ci dara jaaxal; waxtoo ngi ñëw wu mboolem ñi ci biir bàmmeel, di dégg baatam,
29 and come out—those who did good, to the resurrection of life; those who did evil, to the resurrection of judgment. ba génn; ñi daan def lu baax añe ndekkitel dund, ñi daan def lu bon añe ndekkitel mbugal.
30 By myself I can do nothing. I judge as I hear; my judgment is fair, because I seek not my own will but the will of the One who sent me. Man, manumaa def dara ci sama jëmmu bopp; ni ma dégge rekk laay àttee, te sama àtte jub na, nde sàkkuwuma sama coobarey bopp, xanaa coobarey ki ma yónni.
31 "If I testify about myself, my testimony is not valid. «Su ma seedeelee sama bopp, sama kàddug seede wérul.
32 There is another who testifies about me, and I know his testimony about me is true. Keneen a ma seedeel, te xam naa ne dëgg la ma seedeel.
33 You sent messengers to John, and he has testified to the truth. «Yeena yónnee ca Yaxya, Yaxya seede dëgg.
34 Not that I accept human testimony, but I say these things so that you may be saved. Man nag soxlawuma seedes nit; waaye dama leena wax lii ngir ngeen mucc.
35 John was a burning, shining lamp, and you were willing to rejoice briefly in his light. Yaxya moo doon làmp buy tàkk, di leer, ngeen bége leeram ay fan.
36 But I have testimony greater than John's: the works my Father gave me to finish—the very works I'm doing—testify that my Father sent me. «Waaye man ci sama bopp maa ngeek seede su raw si ma Yaxya seedeel, ndax liggéey yi ma Baay bi dénk, ngir ma sottal ko, liggéey yooyu may liggéey moo may seedeel ne Baay bi moo ma yebal.
37 And my Father who sent me has himself testified about me. You've never heard his voice or seen his form, Baay bi ma yónni, moom ci boppam seedeel na ma. Masuleena dégg baatam mbaa ngeen gis kanamam,
38 and you don't have his word remaining in you, since you don't believe the one he sent. te kàddoom dëkkul ci seen xol, ndax ki mu yebal, ngeen gëmul.
39 You search the Scriptures, thinking they hold eternal life—yet they themselves testify about me, Yeena ngi gëstu Mbind mi, ndax ci ngeen yaakaara ame texe gu sax dàkk, yooyu bind nag far seedeel ma,
40 yet you refuse to come to me so that you may have life. te bëgguleena ñëw ci man, ba texe!
41 I do not accept glory from people, «Ngërëmal nit, sàkkuwuma ko.
42 but I know you—that you do not have the love of our Father within you. Waaye yeen, xam naa leen; cofeelu Yàlla nekkul ci yeen.
43 I have come in my Father's name, and you don't receive me; if another comes in his own name, you'll receive him. Man, maa dikk ci sama turu Baay, te dalaluleen ma, waaye keneen ku dikk ci turu boppam, kooku ngeen di dalal.
44 How can you believe, when you accept glory from one another and don't seek the glory from the only God? Yeen, ngërëm, ci seen biir ngeen koy sàkkoonte, te sàkkuwuleen ngërëmal Yàlla miy kenn. Kon ana nu ngeen mana gëme?
45 Don't think I will accuse you before my Father. Moses, in whom you've hoped, accuses you. «Buleen defe ne maa leen di boole ak Baay bi. Ki leen di boole mooy Musaa, mi ngeen yaakaar.
46 For if you believed Moses, you would believe me, because he wrote about me. Bu ngeen gëmoon Musaa, gëm ma, nde moom, ci sama mbir la bind.
47 But if you do not believe his writings, how will you believe my words?" Waaye su ngeen gëmul bindi Musaa, nu ngeen di gëme samay wax?»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]