Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 So when Jesus knew the Pharisees heard he was making and baptizing more disciples than John. Ba Yeesu yégee nag ne Farisen ya dañoo dégg ne Yeesu moo ëpp Yaxya taalibe yu muy tuubloo, di leen sóob ci ndox,
2 (though Jesus himself was not baptizing, but his disciples were), doonte du woon Yeesu ci boppam moo doon sóobe, waaye taalibey Yeesu la woon,
3 he left Judea and went back to Galilee. ca la jóge Yude, dellu diiwaanu Galile.
4 And he had to pass through Samaria. Woowu yoon nag, Samari la waroona jaare.
5 So he came to a town of Samaria called Sychar, near the field Jacob gave his son Joseph. Ci kaw loolu mu dem ba agsi dëkkub Samari ba ñuy wax Sikar, ca wetu tool ba Yanqóoba mayoon doomam Yuusufa.
6 Jacob's well was there. Jesus, tired from the trip, sat down at the well—about noon. Foofa la teenub Yanqóoba nekkoon. Fekk na coonob tukki ba jàpp Yeesu. Mu toog ca wetu teen ba, waxtu wu xawa yemook digg bëccëg.
7 A woman of Samaria came to draw water. Jesus said to her, "Give me a drink." Senn ndawas Samari dikk, di rootsi. Yeesu ne ko: «May ma, ma naan.»
8 (For his disciples had gone into the town to buy food.). Booba ay taalibeem dem nañu dëkk ba, ngir jëndi lu ñu lekk.
9 The Samaritan woman said, "You're a Jew; why ask me, a Samaritan woman, for a drink?" (Jews don't associate with Samaritans.). Ndaw si ne ko: «Yaw miy Yawut, ana noo ma mana ñaane ndoxum naan, man, te may waa Samari?» Ndax Yawut yi séquñu woon ak waa Samari lenn.
10 Jesus answered her, "If you knew our Father's gift, and who asks you, 'Give me a drink,' you'd have asked him, and he'd have given you living water." Yeesu nag ne ndaw si: «Soo xamoon mayu Yàlla, ak kan moo la ne may ma, ma naan, kon yaw yaa koy ñaan, mu may la ndox miy dundal.»
11 The woman said to him, "Sir, you have nothing to draw with, and the well is deep. Where then do you get this living water? Ndaw si ne ko: «Sang bi, amuloo baag, te teen bi xóot na; ana fooy jële ndox miy dundal?
12 Are you greater than our father Jacob, who gave us the well, drank from it himself, with his sons and livestock?" Dangaa sut sunu maam Yanqóoba, mi nu may teen bi, te naan ci, mooki doomam akug juram?»
13 Jesus said to her, "Everyone who drinks of this water will be thirsty again, Yeesu ne ko: «Ku naan ci miim ndox it, dina maraat,
14 but whoever drinks the water I give him will never thirst again; that water will become in him a spring of water welling up to eternal life." waaye ku naan ci ndox mi ma koy may, man, du marati; ndox mi ma koy may, bëtu ndox lay doon ci moom, di ball, ngir dundug texe gu sax dàkk.»
15 The woman said to him, "Sir, give me this water, so I won't get thirsty or come here to draw water." Ndaw si ne ko: «Sang bi, may ma ci moomu ndox, ba duma marati, mbaa may dikkati fii, di root.»
16 Jesus said to her, "Go, call your husband, and come back here." Yeesu ne ko: «Demal woowi sa jëkkër te ñëw.»
17 The woman answered, "I have no husband." Jesus told her, "You're right to say you have no husband. Ndaw si ne ko: «Awma jëkkër.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg, amuloo jëkkër,
18 For you've had five husbands, and the man you have now isn't your husband. You've spoken the truth." ndax juróomi jëkkër nga séyal, te ki nga am léegi du sa jëkkër. Kon dëgg nga wax.»
19 The woman said to him, "Sir, I see that you are a prophet. Ndaw si ne ko: «Sang bi, gis naa ne yaw ab yonent nga.
20 Our fathers worshiped on this mountain, but you say Jerusalem is where people must worship." Nun nag, sunuy maam ca tund wee lañu daan jaamoo Yàlla, te yeen Yawut yi, yeena ne béreb ba jaamu Yàlla ware, ma nga ca Yerusalem.»
21 Jesus told her, "Woman, believe me: an hour is coming when you'll worship the Father neither on this mountain nor in Jerusalem. Yeesu ne ko: «Ndaw sile, lii ma lay wax, gëm ko: waxtoo ngi ñëw, du ci tund wii, te du Yerusalem lees di jaamoo Baay bi.
22 You worship what you don't know; we worship what we know—salvation comes from the Jews. Yeen waa Samari, yeenay jaamu lu ngeen xamul. Nun Yawut yi, li nuy jaamu, xam nanu ko, ndax ag mucc, ci Yawut yi lay jóge.
23 But a time is coming, and now is, when true worshipers worship the Father in spirit and truth—for the Father seeks such worshipers. Waaye waxtoo ngi ñëw, te léegi la; ci la jaamukat yi dëgg di jaamoo Baay bi xel ak dëgg, ndax ñu ni mel la Baay bi sàkku ñu jaamu ko.
24 The Father is spirit, and those who worship him must worship in spirit and truth." Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu, xel ak dëgg lañu ko war di jaamoo.»
25 The woman said to him, "I know Messiah—the one called Christ—is coming. When he comes, he will tell us everything." Ndaw si ne ko: «Xam naa ne Almasi baa ngi ñëw, moom lañu naan Ki ñu fal, kooku bu dikkee, moo nuy leeralal lépp.»
26 Jesus said to her, "I am he—the one speaking to you." Yeesu ne ko: «Man miy wax ak yaw, man la.»
27 Just then his disciples returned, amazed he was talking with a woman. Yet no one said, "What do you want?" or, "Why talk with her?" Cooca la taalibey Yeesu dikk, daldi jaaxle ca lañu ko fekk muy wax ak as ndaw, waaye kenn newu ko: «Loo soxla?» mbaa: «Lu tax ngay wax ak ndaw si?»
28 So the woman left her water jar and went back to town and said to the people, Ndaw sa nag wacc fa njaqam, dem ca dëkk ba, daldi ne nit ña:
29 "Come, see a man who told me everything I ever did. Could this be the Christ?" «Kaayleen gis; nit a nga fee, wax na ma mboolem lu ma def! Kooku du Almasi beem?»
30 They left the town and were coming to him. Ñu génne ca dëkk ba, wutsi Yeesu.
31 Meanwhile the disciples were urging him, "Rabbi, eat." Ci biir loolu taalibe ya di ko soññ, naan ko: «Kilifa gi, lekkal.»
32 But he said to them, "I have food to eat that you know nothing about." Teewul Yeesu ne leen: «Am naa ñam wu ma lekk, te woowu ñam, yeen xamuleen ko.»
33 So the disciples said to one another, "Has anyone brought him something to eat?" Taalibe ya nag naan ca seen biir: «Ndax dees koo indil ag lekk?»
34 Jesus said to them, "My food is doing the will of the one who sent me and finishing his work. Yeesu ne leen: «Samaw ñam moo di jëfe coobarey ki ma yónni, ba sottal ab liggéeyam.
35 Don't you say, 'Four months more, then harvest comes'? Look, I tell you: raise your eyes, see the fields—white for harvest. Du yeena naan: “Fii ak ñeenti weer ngóob taxaw”? Dégluleen, ma wax leen: dawalleen seen bët, xool tool yi, ñu ngi weex tàll, di xaar am ngóob.
36 Already the harvester earns wages, gathering fruit for eternal life, so that planter and harvester may rejoice together. Góobkat baa ngi feyeeku xaat, tey dajale meññeef mi ngir texe gu sax dàkk, ba jikat bi ak góobkat bi bokk bég.
37 For here the saying holds true: 'One plants and another harvests.' Loolu lañu léeb te muy dëgg, ne: “Kenn ji, keneen góob.”
38 I sent you to reap what you didn't work for. Others worked, and you have entered into their labor." Man maa leen yebal ngir ngeen góob fu ngeen ñaqul woon, yeen. Ñeneen a fa ñaq, ngeen dikk jariñoo seenu ñaq.»
39 Many Samaritans from that town believed in him because of the woman's testimony: "He told me everything I ever did." Dëkk boobu, niti Samari ñu baree fa gëm Yeesu, ndax kàddug ndaw sa seede woon ci Yeesu, ne: «Wax na ma mboolem lu ma def.»
40 When the Samaritans came to him, they asked him to stay with them; he stayed two days. Moo tax ba waa Samari dikkee ca Yeesu, dañu koo ñaan, ngir mu dal ak ñoom. Toog na fa ñaari fan.
41 And many more believed because of his word. Ci kaw loolu ñu gëna bare gëm ko ndax kàddoom.
42 They told the woman, "It is no longer because of what you said that we believe—we've heard for ourselves, and we know this man truly is the Savior of the world." Ñu wax ndaw sa nag ne ko: «Dootul li nga wax a nu taxa gëm, waaye nun noo déggal sunu bopp, ba gis ne kii moo di Musalkatub àddina bi.»
43 After the two days he departed from there for Galilee. Gannaaw ñaari fan yooyu la fa Yeesu jóge, jëm diiwaanu Galile,
44 (For Jesus himself had testified that a prophet has no honor in his own hometown.). ndax Yeesu ci boppam moo noon: «Ab yonent, réewu boppam, deesu ko fa nawe.»
45 When he arrived in Galilee, the Galileans welcomed him, having seen all he did in Jerusalem at the feast—they too had gone to the feast. Ba mu agsee Galile, waa Galile dalal nañu ko, ndax gis nañu mboolem la mu defoon ca Yerusalem, ca màggalu bésub Mucc ba, ndax ñoom itam demoon nañu ca màggal ga.
46 He went again to Cana in Galilee, where he had turned water to wine. A royal official's son was sick at Capernaum. Ci kaw loolu mu délsi Kana gu Galile, dëkk ba mu soppee woon ndox ma biiñ. Amoon na fa ab dagu buur bu doomam wopp ca dëkk ba ñuy wax Kapernawum.
47 Hearing that Jesus had come from Judea to Galilee, he went to him and begged him to come down and heal his son, who was about to die. Ba mu déggee ne Yeesu jóge na Yude, ba agsi Galile, dafa dem ca moom, ñaan ko mu dikk, wéral doomam, ndax booba ma ngay waaja dee.
48 So Jesus said to him, "Unless you people see signs and wonders, you will never believe." Yeesu ne ko: «Su ngeen gisul ay firnde ak kéemaan daal, dungeen gëm!»
49 The royal official said to him, "Sir, come down before my child dies." Dagu buur bi ne ko: «Sang bi, dikkal, bala sama doom a dee!»
50 Jesus said to him, "Go; your son will live." The man believed what Jesus told him and left. Yeesu ne ko: «Demal, sa doom a ngi dund.» Waa ja gëm kàddu ga ko Yeesu wax, daldi dem.
51 As he was going down, his servants met him and told him that his boy was living. Naka lay dellu këram, ay surgaam gatandu ko, ne ko: «Sa doom a ngi dund!»
52 So he asked them the hour he improved, and they said, "Yesterday at the seventh hour, the fever left him." Mu laaj leen wan waxtu la tane, ñu ne ko: «Démb, ci benn waxtu ci bëccëg, la tàngooru yaram teqalikoo ak moom.»
53 So the father knew this was the hour when Jesus told him, "Your son will live." He and his whole household believed. Baay ba nag xam ne ca waxtu woowa la ko Yeesu noon: «Sa doom a ngi dund.» Ca la gëm Yeesu, moom ak waa këram gépp.
54 This was now the second sign that Jesus did when he had come from Judea to Galilee. Lii moo di ñaareelu firnde ba Yeesu def ca Galile, gannaaw ba mu jógee Yude.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]