Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Now there was a man of the Pharisees named Nicodemus, a ruler of the Jews. Am na nit ku bokkoon ca Farisen ya, ku ñuy wax Nikodem, di njiit ca Yawut ya.
2 This man came to Jesus at night and said, "Rabbi, we know you are a teacher who has come from our Father, for no one can do these signs you do unless our Father is with him." Kooku moo dikk ag guddi ba ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ab kilifa nga bu bawoo fa Yàlla, nde kenn manula def firnde yii ngay def, te du Yàllaa ànd ak moom.»
3 Jesus answered, "Truly, truly, I tell you: unless someone is born from above, he can't see the kingdom of our Father." Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki, su judduwaatul, du mana gis nguurug Yàlla.»
4 Nicodemus asked, "How can a man be born when he's old? Can he enter his mother's womb again and be born?" Nikodem ne ko: «Ana nu nit di judduwaate te xasa dem bay mag? Daa mana duggaat ci biiru yaayam, ngir judduwaat?»
5 Jesus answered, "Truly, truly, I tell you, unless one is born of water and the Holy Spirit, he can't enter our Father's kingdom. Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki su juddoowul ci ndox ak ci Noowug Yàlla, du mana tàbbi ci nguurug Yàlla.
6 Born of the flesh is flesh, and born of the Holy Spirit is spirit. Lu juddoo ci nitu suuxu neen, nitu suux la, lu juddoo ci Noowug Yàlla nag, ag noo la.
7 Don't be amazed that I said to you, 'You must be born from above.' Li ma la ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal.
8 Wind blows where it wants; you hear its sound but don't know where it comes from or where it goes. So it is with everyone born of the Spirit." Ngelaw fu ko neex lay gelawe; coowam ngay dégg, waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la it ci képp ku juddoo ci Noowug Yàlla.»
9 Nicodemus said to him, "How can these things be?" Nikodem neeti ko: «Loolu nu mu mana ame?»
10 Jesus answered him, "Are you the teacher of Israel and yet you do not understand these things? Yeesu ne ko: «Yaw ngay jàngalekat bu mag ci bànni Israayil te xamuloo loolu?
11 Truly, truly, I tell you: we speak what we know, we testify to what we've seen, yet you don't accept our testimony. Maa la ko wax déy, ci lu wér; li nu xam, nu ngi koy wax; li nu gis, nu ngi koy seede, yeen kay yeena baña gëm li nu seede.
12 If I told you earthly things and you don't believe, how will you believe if I tell you heavenly things? Gannaaw mbiri àddina laa leen wax, gëmuleen ko, su ma leen waxee mbiri asamaan, ana nu ngeen koy gëme?
13 No one has ascended into heaven except the one who descended from heaven, the Son of Man. Kenn masula yéeg fa asamaan ku moy ki wàcce asamaan, te mooy Doomu nit ki.
14 As Moses lifted up the serpent in the wilderness, so the Son of Man must be lifted up, Te itam noonee Musaa yékkatee woon jaan ja ca màndiŋ ma, fàww ñu yékkatee ni Doomu nit ki,
15 that whoever believes in him may have eternal life. ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww.»
16 For our Father so loved the world that he gave his one and only Son, that whoever believes in him will not perish but have eternal life. Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.
17 For our Father did not send his Son into the world to condemn the world, but so the world could be saved through him. Ndax kat Yàlla yebalul Doomam ci waa àddina ngir daan waa àddina, waaye musal waa àddina, mucc gu sottee ci Doomam, moo tax mu yebal ko.
18 Whoever believes in him isn't condemned; whoever doesn't believe is condemned already, for not believing in the name of the one and only Son of our Father. Képp ku ko gëm, deesu la daan, waaye ku ko gëmul, daanees na ko ba noppi, ndax moo gëmul jenn Doomu Yàlla ji.
19 This is the judgment: light has entered the world, and people loved darkness more than light because their deeds were evil. Àtteb daan bi nii la tëdde: leer moo dikkal àddina, waaye nit ñi la lëndëm gënal leer ndax seen jëf yu bon.
20 Everyone who does evil hates the light and won't come to the light, so that his deeds aren't exposed. Képp kuy def jëf ju sew, day bañ ag leer te du dikk ci leer gi, ngir ragal ay jëfam feeñ.
21 But whoever does the truth comes to the light, so it may be revealed that his works have been done in our Father." Waaye kiy def liy dëgg, ci leer gi lay dikk, ngir mu leer nàññ ne déggal Yàlla la ko jëfe.
22 After this, Jesus and his disciples went into the Judean countryside, where he stayed with them, baptizing. Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem diiwaanu Yude. Mu toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox.
23 John also baptized at Aenon near Salim, since water was plentiful there, and people came and were baptized, Ci biir loolu Yaxya itam di sóobe ci ndox ca Aynon, wetug Salim, ndax diiwaan bu bare ndox la woon. Nit ñi di ko fa fekk, mu di leen sóob ci ndox.
24 for John had not yet been put in prison. Booba tëjaguñu Yaxya kaso.
25 Now a discussion arose between some of John's disciples and a Jew over purification. Werante nag am diggante ñenn ci taalibey Yaxya ak ab Yawut, ci mbirum setlu gi seen yoon laaj.
26 They came to John and said, "Rabbi, the man with you beyond the Jordan, the one you testified about—he's baptizing, and everyone goes to him." Ci kaw loolu ñu dikk ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ka nga dajeeloon ca wàllaa dexu Yurdan, te nga seedeeloon ko ag kàddu, moom de ma ngay sóobe ci ndox, ñépp jëm ca moom!»
27 John replied, "A person cannot receive even one thing unless it is given him from heaven. Yaxya ne leen: «Nit manula am lenn lu ko Yàlla joxul.
28 You yourselves can testify: I said 'I'm not the Christ, but sent ahead of him.' Yeen ci seen bopp, yeenay samay seede ne maa noon man duma Almasi bi, waaye dees maa yebal ngir ma jiitusi Almasi boobu.
29 The one with the bride is the bridegroom—Jesus. The bridegroom's friend, who stands and hears him, rejoices greatly at the bridegroom's voice. So my joy is now complete. Kiy séetal moo moom ab séetam. Waaye xaritu boroom séet bi day taxaw di ko déglu, bu déggee baatu boroom séet bi, bég. Mbég moomu nag laa moom, te mat na sëkk.
30 He must increase, but I must decrease." Moom mu gën di kawe, te man ma gën di suufe mooy li war.»
31 The one who comes from above is above all. The one from earth belongs to earth and speaks in an earthly way. The one who comes from heaven is above all. Ki jóge ci kaw moo féete ñépp kaw; ki jóge ci suuf nag, ci suuf la bokk, te mbiri suuf lay wax. Waaye ki jóge asamaan moo féete ñépp kaw.
32 He bears witness to what he has seen and heard, yet no one receives his testimony. La mu gis ak la mu dégg lay seede, waaye kenn du gëm kàddug seedeem.
33 Whoever receives his testimony confirms that our Father is true. Ku nangu kàddug seedeem nag yaa nangu ne Yàllaa wax dëgg.
34 The one our Father sent speaks our Father's words, for he gives the Holy Spirit without measure. Yàlla kat, ku mu yebal, kàddug Yàlla lay wax, ndax Yàlla du natt li mu koy nàddil cig Noowam.
35 Our Father loves the Son and has given all things into his hand. Baay bi moo sopp Doom ji, te lépp la teg ciy loxoom.
36 Whoever believes in the Son has eternal life; whoever disobeys the Son won't see life—our Father's wrath remains on him. Ku gëm Doom ji, yaay texe ba fàww; ku baña gëm Doom ji nag, doo gis googu texe, waaye sànjum Yàlla mooy dëkk ci sa kaw.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]