Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 On the third day, a wedding took place in Cana of Galilee; Jesus's mother was there. Ca gannaaw ëllëg sa, ag céet a amoon ca Kana ga ca diiwaanu Galile. Yaayu Yeesu nag ma nga fa woon.
2 Jesus and his disciples were also invited to the wedding. Yeesu aki taalibeem itam, woo woon nañu leen ca céet ga.
3 When the wine ran out, the mother of Jesus said to him, "They have no wine." Ca biir bernde ja, biiñ ba dem ba jeex. Yaayu Yeesu ne Yeesu: «Ñii de, seen biiñ jeex na.»
4 "Woman, why are you bringing me into this?" Jesus replied. "My hour has not yet come." Yeesu ne: «Soxna si, lu tax nga di ma wax loolu? Sama waxtu jotagul.»
5 His mother said to the servants, "Do whatever he tells you." Teewul yaayam ne surga ya: «Lu mu leen wax, defleen ko.»
6 Six stone water jars stood there, used for Jewish purification, each holding twenty to thirty gallons. Juróom benni ndaayi doj yu ñu yatt a nga fa woon, Yawut ya daan ca jàppe; ndaa lu ci nekk mana def juróom ñett fukk ba téeméeri liitar.
7 Jesus said to them, "Fill the jars with water," so they filled them to the brim. Yeesu ne surga ya: «Duyleen ndaa yi ba mu fees.» Ñu duy ndaa yi, ba mu rembat.
8 He told them, "Draw some out now, and take it to the head steward." So they did. Yeesu ne leen: «Léegi tanqleen ci, yót ko njiitu xew wi.» Ñu tanq, yót ko.
9 The master of the banquet tasted the water now wine, not knowing its source—though the servants who drew it knew. So he called the bridegroom aside, Njiitu xew wa mos ndox ma, ndeke soppaliku na biiñ. Xamul fu biiñ ba jóge, teewul surga ya tanq ndox ma, ñoom xam nañu ko. Njiit la woo boroom séet ba, ne ko:
10 and said, "Everyone serves the good wine first, then the lesser once guests are drunk. But you've kept the good wine till now." «Mboolem kuy xew, biiñ bu neex lay njëkka joxe; bu nit ñi naanee ba doyal, mu doora taaj bu yemamaay. Yaw nag nga denc bu neex bi ba nëgëni!»
11 Jesus performed this first sign at Cana in Galilee. He revealed his glory, and his disciples believed in him. Lii Yeesu moo ko def fa Kana gu diiwaanu Galile, muy ndoorteli firndeem. Ni la firndeele darajaam, ba ay taalibeem gëm ko.
12 After this he went down to Capernaum with his mother, brothers, and disciples, and stayed there a few days. Gannaaw loolu la dem Kapernawum, mook yaayam aki rakkam aki taalibeem. Waaye tooguñu fa fan yu bare.
13 When the Jewish Passover was near, Jesus went up to Jerusalem. Màggalu Yawut gi ñuy wax bésub Mucc moo jubsi woon. Yeesu nag dem Yerusalem.
14 In the temple courts he found sellers of cattle, sheep, and doves, and others sitting at tables exchanging money. Ba mu agsee ca ëttu kër Yàlla ga, ay jaaykati nag la fa fekk ak jaaykati xar ak jaaykati pitax ak weccikati xaalis yu toog.
15 He made a whip of cords and drove them all out of the temple courts, sheep and cattle alike, poured out the money-changers' coins, and overturned their tables. Mu defar kàcciri gu mu ràbbe ay buum, dàqe leen ko, génne kër Yàlla ga, ñoom ñépp, ak xar yaak nag ya. Ci biir loolu mu tasaare xaalisu weccikat ya, dëpp taabal ya.
16 To the dove sellers he said, "Take these out of here! Don't make my Father's house a marketplace." Jaaykati pitax ya, mu ne leen: «Jëleleen fi lii! Buleen def sama kër Baay, kërug jaayukaay!»
17 His disciples remembered that it is written: "Zeal for your house will consume me." Taalibeem ya nag fàttaliku la ñu bind ne: «Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk.»
18 So the Jews asked, "What sign will you show us for doing these things?" Ba loolu amee njiiti Yawut ya ne ko: «Lii ngay def, jan firnde nga nuy jox, ba sañ koo def?»
19 Jesus answered them, "Destroy this temple, and in three days I will raise it up." Yeesu ne leen: «Yàqleen kër Yàlla gii, ma yékkatiwaat ko ci ñetti fan.»
20 They replied, "This temple took forty-six years to build, and will you raise it in three days?" Yawut yi nag ne ko: «Kër Yàlla gii ñu tabax ci ñeent fukki at ak juróom benn, yaa koy yékkatiwaat ci ñetti fan?»
21 But the temple he had spoken of was his body. Waaye Yeesu kër Yàlla ga mu doon wax, yaramu boppam la woon.
22 After he rose from the dead, his disciples remembered he had said this, and believed the Scripture and the word Jesus had spoken. Gannaaw ba Yeesu deewee ba dekki nag, la taalibeem ya fàttaliku loolu mu waxoon. Ñu daldi gëm li Mbind mi indi, ak kàddu ga Yeesu waxoon.
23 While he was in Jerusalem at the Passover, many saw the signs he did and trusted in his name. La Yeesu toog Yerusalem ca màggalu bésub Mucc, ñu baree ko gëm, ba ñu gisee firnde ya muy def.
24 But Jesus would not entrust himself to them, for he knew all people. Waaye Yeesu moom, taxul mu wóolu leen, ndax ñoom ñépp la xamoon,
25 He didn't need anyone's testimony about people—he knew what was in each one. te it soxlawul kenn xamal ko nit, ndax moom ci boppam xam na li ci nit.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]